Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 7

Lan la Biibël bi yégle lu jëm ci suñu jamono ?

Lan la Biibël bi yégle lu jëm ci suñu jamono ?

“ Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew . . . Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi. ”

Macë 24:​7, 8

“ Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare. Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku. ”

Macë 24:​11, 12

“ Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit ; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul. ”

Màrk 13:7

“ Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan. ”

Luug 21:⁠11

“ Bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci mujug jamono. Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur ; duñu am kóllëre, sellaay mbaa cofeel ; dañuy jàpp mer ak a sos ; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax ; ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar ; seen bànneex a léen gënal Yàlla. Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. ”

2 Timote 3:​1-5