Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 11

Bu nit deewee, lan moo koy dal ?

Bu nit deewee, lan moo koy dal ?

“ Saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële ; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd. ”

Njàlbéen ga 3:⁠19

“ Ñiy dund, xam nañu ne dinañu dee. Waaye ñi dee, ñoom, xamuñu dara . . . Lépp li nga mën a def ak sa loxo, def ci sa kem kàttan, ndaxte amul liggéey, amul waaj, amul xam-xam, walla sagowu ci bàmmeel bi nga jëm. ”

Dajalekat 9:​5, 10, MN

“ Yeesu wax loolu, teg ca ne : « Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko. » Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax. Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne : « Lasaar dee na. » ”

Yowaana 11:​11, 13, 14