Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 16

Naka lañu mënee jànkoonte ak suñuy coono ?

Naka lañu mënee jànkoonte ak suñuy coono ?

“ Sippikul Aji Sax ji lu la diis, moom moo lay taxawu. Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf. ”

Sabóor 55:⁠23

“ Farlu, woomle ; ku gaawtu, mujj néewle. ”

Kàddu yu Xelu 21:5

“ Bul tiit, ndaxte maa ngi ak yaw. Bul jaaxle, ndaxte man maay sa Yàlla. Dinaa la dooleel, waaw, dinaa la dimbali. Dinaa la téye ak sama loxo ndeyjoor bi ànd ak njubte. ”

Esayi 41:⁠10, MN

“ Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo mana yokk waxtu ci àppam ? ”

Macë 6:​27

“ Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko. ”

Macë 6:​34

“ Nangeen sax noonu ci li gëna rafet. ”

Filib 1:​10

“ Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant. Noonu jàmmu Yàlla, ji xel manta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu. ”

Filib 4:​6, 7