Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 1

Kan mooy Yàlla ?

Kan mooy Yàlla ?

“ Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji [“ Yexowa ”, MN] doŋŋ yaay Aji Kawe ji yilif àddina yépp. ”

Sabóor 83:⁠19

‘ Seedeleen ne Aji Sax ji [“ Yexowa ”, MN] mooy Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di mbooloom, di gàttam yi muy foral. ’

Sabóor 100:3

“ Maay Aji Sax ji [“ Yexowa ”, MN], mooy sama tur, duma bàyyeel sama ndam keneen mbaa sama sag xërëm yi. ””

Esayi 42:8

“ Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc. ”

Room 10:⁠13

“ Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla. ”

Yawut ya 3:4

“ Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg. ”

Sabóor 8:⁠4