Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 17

Naka la Biibël bi mën a dimbalee seen njaboot ?

Naka la Biibël bi mën a dimbalee seen njaboot ?

JËKKËR YI / BAAY YI

“ Na góor bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa soxna, bëgg sa bopp la. Ndaxte kenn masula bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk . . . na góor gu nekk bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam. ”

Efes 5:​28, 29, 33

‘ Yéen baay yi, buleen bundxataal xale yi, waaye ngeen yar léen, di léen yemale ak a yee ci Boroom bi. ’

Efes 6:4

JABAR YI

“ Te jigéen ji weg jëkkëram. ”

Efes 5:​33

“Jigéen ñi, na ku nekk nangul jëkkëram, ndaxte looloo jekk ci ñi bokk ci Boroom bi. ”

Kolos 3:​18

XALE YI

“ Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet. « Teralal sa ndey ak sa baay, » mooy ndigal li jëkka ëmb dige, maanaa : « ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm. » ”

Efes 6:​1-3

“ Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi. ”

Kolos 3:​20