Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla

Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla

NI NGEEN MËN A DEF BA GIS FI AAYA NEKK CI BIIBËL BI

Biibël bi, téere la bu boole 66 téere yu ndaw. Dafa def ñaari xaaj : Mbind yi ci làkku Ebrë ak Arameyni maanaam “ Kóllëre gu njëkk gi ” ak Mbind yi ci làkku Gereg maanaam “ Kóllëre gu bees gi ”. Téere bu ndaw bu nekk dañu ko xaaj ci ay pàcc ak ay aaya. Bu ñu bëggee wone fu aaya nekk ci Biibël bi, dañuy njëkk a bind turu téere bi, teg ci nimoro pàcc bi ak nimoro aaya bi walla aaya yi. Ci misaal, bu ñu bindee Njàlbéen ga 1:​1, loolu dafay tekki Njàlbéen ga pàcc 1, aaya 1.