Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 12

Ndax mën nañu yaakaar a gisaat ñi dee ?

Ndax mën nañu yaakaar a gisaat ñi dee ?

“ Bu leen ci dara jaaxal ; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn. ”

Yowaana 5:​28

“ Ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki. ”

Jëf ya 24:⁠15

“ Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam gàngune ma. Daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya. Noonu géej gëq néew, yi nekkoon ci moom ; dee ak barsàq delloo néew, ya ñu yoroon. Ñu àtte ñépp ci seeni jëf. ”

Peeñu ma 20:​12, 13