LAAJ 10
Lan lu rafet la Biibël bi wax ci ëllëg ?
“ Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww. ”
“ Suuf si dina fi nekk ba abadan. ”
Dajalekat 1:4, MN
“ Dina noot dee ba fàww, te Aji Boroom bi Yexowa dina fomp rongooñu ñépp. ”
Esayi 25:8, MN
“ Noonu gumba yi di gis, tëx yi di dégg, lafañ di tëbeentu ni kéwél, te làmmiñu luu ne tell ak mbég ; ndax ndox dina balle ci màndiŋ mi, ay dex ci tàkk yi. ”
“ Dina fomp bépp rongooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ”
“ Dinañu tabax ay kër te dëkk ci. Dinañu jëmbët ay reseñ te lekk li ñu meññ. Duñu tabax ngir keneen dëkk, duñu jëmbët ngir keneen lekk, ndaxte samay nit, seeni fan dinañu mel ni fani garab ; te ñi ma tànn, dinañu jariñoo ba mu mat sëkk liggéey bi ñu def ak seen loxo. ”
Esayi 65:21, 22, MN