Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ñu ngi ci bés yu mujj yi!

Ñu ngi ci bés yu mujj yi!

Pàcc 11

Ñu ngi ci bés yu mujj yi!

1. Lu tax ñu bare mel ni ñu xawa xonet bu ñuy xool ni àddina si mel, waaye fan lañu mënee am faramfàcce bu wóor ci xew-xew yi ci àddina?

 NAN la suñu àddina su yëngu sii agsee fi mu tollu tey? Fan lañuy jëm? Ndax mas ngaa laaj laaj yu ni mel? Ñu bare dañu ne xonet ndax ni àddina si mel fépp. Xeex, feebar ak ñaawtéef, di ay mbir yu ñu mëna teg suñuy gët tax nañu nit ñiy laaj li leen ëllëg di indil. Njiit yi ci wàllu politig dese nañoo faj yaakaar. Wànte, mën nañoo jële ci Yàlla, ci biir Kàddoom, ab faramfàcce bu jara wóolu ci li waral bési tiis yii. Biibël baa ngi ñuy dimbali ci lu wóor-a-wóor ñu gis fi ñu tollu ci doxub jamano ji. Mu ngiy wone ne ñu ngi ci “bés yu mujj yi” suñu jamano jii.—2 Timote 3:1.

2. Ban laaj la taalibe yi laaj Yeesu, te nan la tontoo?

2 Nañu seet, maanaam, tont li Yeesu tontu ci yenn laaj yu jóge ci ay taalibeem. Ñetti fan laata Yeesoo dee, dañu ko laaj: “Luy doon màndargam sa teewaay ak cutitel jamano ji?” * (Macë 24:3, NW) Ngir tontu leen, Yeesu waxtaane naak ñoom ay xew-xewi àddina aki nekkin saxsax yu naroona am te doon wone ci lu leer ne jamano ju jullitewul jii dugg na ciy bésam yu mujj.

3. Lu tax yëf yi ci kow suuf yées ba Yeesu tàmbalee ilif?

3 Ni ñu ko gise ci pàcc mi jiitu, waññub diir yi ci Biibël baa ngi ñuy taxa tofal ne Nguurug Yàlla tàmbali naa ilif jeeg. Waaye nan la loolu mënee am? Yëf yaa ngi gën di yées, tanewuñu. Ci dëgg, loolu mooy wone, ci lu am doole, ne Nguurug Yàlla tàmbali naa ilif. Lu tax ñuy wax loolu? Sabuur 110:2 a ngi ñuy xamal ne, cib diggante diir, Yeesu doon na ilif ‘ci diggiy noonam.’ Ci dëgg, jëfam ji njëkk niki Buur ca asamaan moo doon sànni Seytaaneek malaakam yu bon yi ci wetug suuf si. ( Peeñu bi 12:9) Lan la loolu jur? Li Peeñu bi 12:12 yégle woon saxsax: “Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej gi! Ndaxte Seytaane wàcc na ci yeen, ànd ak mer mu tàng, ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.” Ñu ngiy dund ci “jot g[u] (...) barewul” googu.

4. Yan ñooy yenn xàmmikaayi bés yu mujj yi, te lan lañuy joxoñ? (Seetal séq bi.)

4 Bettuñu kon, keroog ba ñu laajoon Yeesu lu doon nekk màndargam teewaayam ak cutitel jamano ji, tontoom nekkoon lu doon gimmiloo. Dinga gis melo yu bare yu jëm ci màndarga mi ci xët 102. Ni nga ko mënee gis, ndawiy Yeesu, Pool, Pieer, ak Yowanna gën nañ ñoo nettali benn-benn lu jëm ci bés yu mujj yi. Dëgg la, li ëpp ci xàmmikaayi màndarga mi ak xàmmikaayi bés yu mujj yi dañoo ëmb ay nekkin yuy tiisloo. Ndaxam, mottalib yégley yonent yooyu war nañ ñoo gulami ne jamano ju bon jaa ngi ci mujam. Nañu seppali yenn ci xàmmikaayi bés yu mujj yi, yi gëna ràññeeku.

XÀMMIKAAYI BÉS YU MUJJ YI

5, 6. Nan la yégle yonent yi jëm ci xeex ak xiif àgge?

5 “Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew.” (Macë 24:7; Peeñu bi 6:4) Fentkat bu tudd Ernest Hemingway tudde na Xeexu Àddina Sépp bi Njëkk “reyante bi gëna jéggi dayo, bi gëna bóom ay doomi Aadama, bi yées ci ni ñu ko doxale, bu masa am ci kow suuf.” Ni ko téere bi tudd The World in the Crucible—1914-1919 (Àddina si ci biir nattu bu mettee metti—1914-1919), loolu nekkoon na “ubbitel fasoŋu xeex bu bees, xeex bi njëkk te bàyyiwul benn doomu Aadama. Yàggaayam, metitam, dayoom weesu nañu lépp li ñu daan xam walla daan séenu naka-jekk.” Teg ca, Ñaareelu Xeexu Àddina Sépp dikk, gënatee yàq Xeexu Àddina Sépp bi Njëkk. “Ñaar-fukkeelu xarnu bi nekk na ci nooteelug mitrayet, tank, B-52, bomb atomik, ak ci muj gi, misil. Wuute naak jamano ju mu mënta doon ndax ay xeexam yi raw ci tuur deret ak yàq,” la Hugh Thomas, jàngalekatu xew-xewi démb wax. Dëgg la, waxtaane nañu lu bare ci wékk gànnaay yi, gannaaw ba Xeex bu Sedd ba jeexee. Terewul, ab liggéeyub gëstoo ngiy xayma ne, gannaaw bu ñu doxalee waññiw gànnaay yi ñu wax, lu tollook fukki junni (10 000) ba ci ñaar-fukki junniy (20 000) boppi bomb nukleer dinañu des—muy lu ëpp juróom-ñeenti téeméeri (900) yoon doole lépp li tàkkoon ca Ñaareelu Xeexu Àddina Sépp ba.

6 “Dina am ay xiif yu tar.” (Macë 24:27; Peeñu bi 6:5, 6, 8) Li dale ca 1914 lu mu néew néew am na ñaar-fukki (20) xiif yu tar yu mag. Béréb yi xiif yooyu dal ëmb nañu Bangladesh, Burundi, Kampuchéa (Cambodia), Chine (China), Ethiopie (Ethiopia), Grèce (Greece), Inde (India), Nigeria, Russie (Russia), Rwanda, Somalie (Somalia) ak Soudan (Sudan). Waaye saa yu xiif amee, du ñàkkum lekk a tax. Ab kurélu ay gëstukat ci wàllu mbéy ak ci wàllu koom-koom tofal nañu: “Sàq yi denc dundu bi ci àddina si sépp, ci fukki at yii ñu génn, ñoo gëna yokku nit ñi. Waaye, ndax li ñu nekk ci toskare ju metti, lu mu néew néew, juróom-ñetti téeméer (800) ci ay tamndareeti nit, (. . .) mënuñoo jënd lu leen doy ci sakkanaay boobu ngir musal seen bopp ci yooy bi xiif gu metti di yóbbe.” Mbirum politig bokk na ci li sabab loolu ci yenn anam. Dr. Abdelgalil Elmekki bu université (university) bu Torontoo ngiy lim ñaari misaal foo xam ne ay junniy nit ñu nga doon dee ak xiif, ca jamano ja seeni réew doon jaay dundu bu bare bitim réew. Nguur yaa ngi mel ni dañoo gëna tiisoo am xaalis bu jóge bitim réew ngir def ko ci seeni xeex, asté ñuy jox lekk seeni njuddu-réew. Lan la Dr. Elmekki tofal? Xiif, ci li farala am, “mbirum seddaleek doxalinu nguur la.”

7. Yan ñooy yëf yi am lu jëm ci mbas yi tey?

7 “Ay mbas.” (Lukk 21:11, NW; Peeñu bi 6:8, NW) Mbas bu bon ba ñu tudde woon Grippe Espagnole (Spanish flu), bu atum 1918-1919, faatoon na lu mu néew néew ñaar-fukki tamndareet ak benn ci ay bakkan. “Ba àddina sosoo ba léegi, masuloona am ab reykat bu ko yàqe noonu, bu faate nit ñu ni bare, ci lu ni gaawe noonu”, la A. A. Hoehling bind ci téere bi tudd The Great Epidemic (Mbas mu mag ma). Tey, mbas yaa ngiy say ci kow nit ñi. At mu nekk, cancer a ngiy rey juróomi tamndareeti nit, feebari biir buy daw a ngiy faat lu ëpp ñetti tamndareet ci ay bakkani liir aki xaleel, te sëqat su mag si mooy tax ba ñetti tamndareet ci ay nit di dee. At mu nekk, congiy doomi jàngoro ci wàllu noyyi, rawatina metitu xëtër, a ngiy rey ñetti tamndareet ak genn-wàll ci ay gune yu amagul juróomi at. Te muy lu doy waar, ñaari junniy tamndareeti nit ak genn-wàll—genn-wàllu nit ñi nekk ci àddina si sépp—a ngiy ame metit ndax ay feebar yu jóge ci ñàkkum ndox, walla ndox muy joxe feebar te doyadi. Mbasu SIDA (AIDS) nekk na leneen luy fàttali ne nit, ak lu mu def def lu am doole ci wàllum mpaj, amul mën-mënub far mbas yi.

8. Nan la nit ñiy wone ne ay “xariti xaalis” lañu?

8 “Nit ñi dinañu (...) fonk xaalis. (2 Timote 3:2) Ci réew yi wër àddina si sépp, nit ñi dañoo mel ni ñu suuradi ci am alal ju bare. “Bayre” dañuy faral di ko yemaleek naka li nit ki di feyeeku te “ku tekki” ak ni alalam tollu. Jigéen ju nekk tof-njiitum ab kurél buy def publicité (advertising) nee na: “Ittewoo yëfi yaram doŋŋ dina wéy di nekk jenn ci doole yiy ruux waa Amerig (. . .) te dina nekk doole ju gën di am solo ci yeneen bérébi jaay ak jënd, yu mag yi.” Ndax looloo xew fi nga dëkk?

9. Lan lañu mëna wax ci lu jëm ci xëtt ndigali way-jur, bi ñu yégle woon?

9 “Di xëtt ndigalu waa-jur.” (2 Timote 3:2) Tey, way-jur yi, jàngalekat yi, ak ñeneen gisal nañu seen bopp ne xale yu bare amuñu yar te dañoo déggadi. Ñenn ci xale yooyoo ngi mel noonu ndax deminub seeni way-jur, bu bon bi, walla ndax dañu leen di roy. Aw waññ wu gën di yokku ci ay xalee ngiy ñàkk kóolute ci lekkool, sàrt, diine, ak seeni way-jur te di leen jógal. Benn jàngalekat bu yàgg ci liggéeyam nee na: “Li ñu xewal mooy, dañoo mel ni kersa gu néew a néew lañu am ci lépp.” Waaye, Yàlla baax na, ay xale yu baree ngiy nekk ay royukaay yu rafet ci wàllu demin.

10, 11. Jan firnde ju wóor moo am ci nit ñi dañoo soxor te ñàkk cofeelug nit ji war?

10 “Soxor.” (2 Timote 3:3) Baat grekk bi ñu firi “soxor” a ngiy tekki ‘lu ñu miisalul, lu xos, lu ñàkk miinante doomu Aadama, lu àndul ak laabiir.’ Akay lu jekk ci ñu bare ñuy sabab taafar ji am tey! “Dund gi dafay xonetloo, dafa taq deret ndax lu ñaaw liy dawloo yaram, ba tax ngir duruus xabaar yi bés bu nekk, fàww nga dëgër fit,” la ubbiteb surnaal wax. Ab alkaati buy wottu ay dëkkuwaay seetlu na ne ay ndaw yu bare dañoo mel ni ñuy gëlëmal seen bopp ci li seeni jëf di jur. Nee na: “Dafa mel ni dañuy wax, ‘Xawma liy xew ëllëg. Li ma bëgg, dinaa ko am tey.’”

11 “Duñu am cofeel.” (2 Timote 3:3) Waxeel woowu, dañu ko firee cib baatu grekk buy tekki “lu amul xol, lu nitewul” te dafay junj “ñàkkum cofeel ji war ci biir njaboot.” (The New International Dictionary of New Testament Theology) Ci dëgg, cofeel faral na di ñàkk fa mu waroona fekka baax—biir kër. Nettali yu jëm ci toroxal ki nga séyal, doom aki way-jur yu màgget sax, dañu ëpp tey jaaxal. Kurélu ay gëstukat wax na: “Taafaru nit—muy cim mbej walla bëmëx, ci jam paaka walla fetal—ci biir njaboot la gëna farala am bépp beneen béréb bu mu mënta doon ci mbootaayug doomi Aadama yi.”

12. Lu tax ñu mëna wax ne nit ñi dañuy mbubboo njullite doŋŋ?

12 “Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo duggal seen xol.” (2 Timote 3:5) Biibël bi am na kàttanug soppi ay dund ci li gën. (Efes 4:22-24) Moona, ñu bare, tey, dañuy jariñoo seeni diine nikib tappaat bu ñuy làqu ngir wéy di doxal ay yëngu-yëngu yu jubadi, yu neexul Yàlla. Njiitiy diine yi, dañu faral di wéyale fen, sàcc ak deminub saay-saay ci wàllu awra. Diine yu bare dañuy waare mbëggeel, waaye di taxawu xeex. “Ci turu Aji Sàkkkat si, ay nit def nañu seen moroomi mbindaafon ñaawtéef yi yées,” la ubbiteb surnaal bi tudd India Today seetlu. Li am sax mooy, ñaari xeex yi gëna tur dérét ci suñuy jamano yii—Xeexu Àddina Sépp bu Njëkk bi ak Ñaareelu Xeexu Àddina Sépp—ci biir réew yiy wuyoo turu karceen lañu tàkke.

13. Jan firnde ju wóor moo am ci ñu ngiy yàq suuf si?

13 “Di yàq suuf si.” (Peeñu bi 11:18) Lu ëpp junneek juróom-benni téeméer (1 600) ci ay boroom xam-xam ci wàllu science, boole ci téeméer ak ñeent (104) yu jot neexalu prix Nobel (Nobel prize), ñu jóge fu nekk ci àddina si, torlu nañu ab artu bu bawoo ci Union of Concerned ScientistsUCS—(mbootaayu boroom xam-xam ci wàllu science yi jàq), mbootaay bu wax ne: “Doom-Aadama yeek kéewaange gaa ngi ci yoonu mbëkkante. (. . .) Li des ëppul fukkiy at yiy ñëw balaa ñoo ñàkk yoon wi ñu am ngir randal musiba yi ñuy méb tey dégmalsi.” Faramfàcce bi nee na: jëfiy nit ñi, yiy méb dund “mën nañoo soppi àddina si ba tax dootul mëna yor dund ci ni ñu ko xame.” Wàññeekub ozone bi, setadi ndox mi, àll yi ñuy jeexal, suuf si ñuy bey siy sàppi, ak raafte xeeti mala ak garab yu bare, lim nañu leen niki ay jafe-jafe yu jamp yu ñu wara toppatoo. UCS boobu nee na: “Li ñu duggal suñu loxo ci ràbbug dund gi, fu yëf yépp lëkkale ci seen biir, mën naa jur luy law, boole ci màbbub ndefarini lépp li jëm ci dund, ndefarin yu ñu nàndul bu baax seeni doole.”

14. Nan nga mënee firndeel ne Macë 24:14 a ngiy àgg ci suñu jamano?

14 “Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp.” (Macë 24:14) Yeesu yégle na ne doon nañu waare xabaar bu baax bi jëm ci Nguur gi ci suuf sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Ak ndimbalul Yàllaak barkeem, ay tamndareeti Seedey Yeowa jébbal nañu ay junniy tamndareeti waxtu ci seen jot ngir waare tey def ay taalibe. (Macë 28:19, 20) Waaw, Seede yi ràññee nañu ne, doon nañu am àqu deret su ñu duloon yégle xabaar bu baax bi. (Esekiel 3:18, 19) Waaye bég nañu ci li ay junniy nit di nangu at mu nekk, ànd ceek ngërëm, xabaaru Nguur gi tey fas yéene nekk ay karceen dëgg, maanaam Seedey Yeowa. Di jaamu Yeowa tey tas xam-xamub Yàlla, nekk na teraanga ju amul moroom. Te gannaaw bu ñu waaree xabaar bu neex bii ci suuf sépp, mujug jamano ju bon jii dina ñëw.

YËNGATUL CI KANAMIY FIRNDE YU LEER YII

15. Nan la jamano ju bon jii di jeexe?

15 Nan la jamano jii di jeexe? Biibël baa ngiy yégle “metit wu réy” wuy tàmbaleek song muy jóge ci wàllu àddina siy doxal politig, song muy dal ci kow “Babylon mu mag mi,” nguurug mbooloom diiney fen ci kow àddina sépp. (Macë 24:21; Peeñu bi 17:5, 16) Yeesu nee na ca biir jamano jooja, ‘jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddéew yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yengu.’ (Macë 24:29) Loolu mën naa nekk ay kawtéefi asamaan yu ñuy teg suñuy gët saxsax. Ak lu mu mënta doon, dinañu feeñal wàlliyuy diiney àddina si te far leen. Gannaaw loolu, Seytaane mi ñu tudde “Gog bu réewum Magog,” dina jaar ci nit ñu yàqu ngir song ak kem-kàttanam nitiy Yeowa. Waaye Seytaane du jot ca la mu bëgg, ndax Yàlla dina ñëw xettali leen. (Esekiel 38:1, 2, 14-23) “Metit wu réy” wi dina àgg ci collam ca Ar-Magedon, di “xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam.” Xeex boobu dina dindi bépp ndesitu mbootaayub Seytaane ci kow suuf, di xàllee noonu yoon wi ngir ay barke yu dul jeex yuy baawaan ci kow ñiy mucc.—Peeñu bi 7:9, 14; 11:15; 16:14, 16; 21:3, 4.

16. Nan lañu xame ne xàmmikaayi bés yu mujj yi ñu yégle woon, suñu jamono lañu fekka baax?

16 Bu ñu leen beree, yenn xàmmikaayiy yégle yonent yuy nettali bés yu mujj yi, mën nañoo mel ni luy dëppook yeneen jamanoy démb. Waaye bu ñu leen boole, firnde yu wóor yi ñu yégle woon dañuy joxoñ suñu jamano. Nañu jël am misaal: Rëdd yiy booloo def rëddi-baraamu nit a ngiy muul ab xàmmikaay bu keneen mënula moom ku dul boroomam. Noonu it, bés yu mujj yi am nañu seen xàmmikaayi bopp, walla xew-xew. Xàmmikaay yooyu dañoo booloo nekk “rëddi-baraam” yu mënula fekk baax ci jeneen jamano. Bu ñu jëlee firnde yi, dendale leen ak joxoñi Biibël bi, yiy wone ne Nguurug Yàlla ca asamaan a ngiy nguuru léegi, ñu ngi ñuy jox sësukaay bu dëgër ngir tofal ne bés yii ñooy, ci dëgg, bés yu mujj yi. Rax-ca-dolli, am na firnde ju leer ju jóge ci Mbind yi, juy wone ne jamano ju bon jii ñu nekk, dinañu ko tas, ci lu yàggatul.

17. Xam ne ñu ngi ci bés yu mujj yi, lan la ñu wara defloo?

17 Firnde yu wóor yooyuy wone ne, bés yii ñooy bés yu mujj yi, ci lan la la wara xiir? Seetal lii: Bu ngëlén luy yàq di méb, dañuy njëkkantu ci saa si, jël ay matuwaay ngir aar suñu bopp. Kon, li Biibël biy yégle te mu jëm ci jamano jii tey, war nañoo jañ ci jëf. (Macë 16:1-3) Mën nañoo gis bu baax ne ñu ngiy dund ci bés yu mujj jamano jii. Loolu war na ñoo xiir ci def bépp jubbanti bu war, bu mu mënta doon ngir ñu am yiwu Yàlla. (2 Pieer 3:3, 10-12) Ba muy junj boppam niki kiy musal, Yeesu woote na woote wu jamp wi: “Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal. Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf. Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen mana mucc ci loolu lépp wara xew, te mana taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.”—Lukk 21:34-36.

[Li ñu bind ci suuf]

^ Am na ay Biibël yuy jëfandikoo baat “àddina” asté “jamano.” Téere bi tudd Expository Dictionary of New Testament Words bu W. E. Vine a ngiy wax ne baat Grekk ai·onʹ “a ngiy tekki diir bu ñu àppalul, walla jamano ju ñu lëkkaleek liy xew ci diir bi.” Téere bi tudd Greek and English Lexicon to the New Testament (xët 17) bu Parkhurst a ngiy ëmb waxeel “jamano jii” buy waxtaane jëfandikoob ai·oʹnes (bareel) ci Yawut yi 1:2. Kon di firee baat ai·oʹnes: “jamano ji” dëppoo naak la mbindum Grekk ma jiitu tekki saxsax.

SEETLUL SA XAM-XAM

Yan xew-xewi àddina la Biibël yégle woon jëm ci ndoortel kiliftéefug Krist?

Yan ñooy yenn xàmmikaayi bés yu mujj yi?

Lan moo lay gulami ne bés yii ñooy bés yu mujj yi?

[Laaj yi]

[Wërale bi nekk paas 102]

YENN XÀMMIKAAYI BÉS YU MUJJ YI

• Xeex yu amul dendale.—Macë 24:7; Peeñu bi 6:4.

• Xiif.—Macë 24:7; Peeñu bi 6:5, 6, 8.

• Mbas yi.—Lukk 21:11; Peeñu bi 6:8.

• Yokkuteb lu awul yoon.—Macë 24:12.

• Di yàq suuf si.—Peeñu bi 11:18.

• Yëngu-yënguy suuf.—Macë 24:7.

• Bési tiis yu jafee dékku.—2 Timote 3:1.

• Mbëggeelug xaalis gu jéggi dayo.—2 Timote 3:2.

• Duñu déggal seeni way-jur.—2 Timote 3:2.

• Ñàkkum cofeelug nit gi war.—2 Timote 3:3.

• Seen bànneex a leen gënal Yàlla.—2 Timote 3:4.

• Ñàkkum tëye sa bopp.—2 Timote 3:3.

• Bañ lu baax.—2 Timote 3:3.

• Duñu faale mbàmb lu leen di méb tey dégmal.—Macë 24:39.

• Ñaawalkat yuy jaleñ firndey bés yu mujj yi.—2 Pieer 3:3, 4.

• Waareb Nguurug Yàlla ci àddina sépp.— Macë 24:14.

[Nataal bi nekk paas 101]