Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Bu keroogee xam-xamub Yàlla di fees suuf si

Bu keroogee xam-xamub Yàlla di fees suuf si

Pàcc 19

Bu keroogee xam-xamub Yàlla di fees suuf si

1, 2. Nan lañu mujjee yàq mbindeefum Yeowa?

 JORTUL ab nataalkat bu mag bu soga sottal ab nataal bu rafet-a-rafet. Ci lu jaadu mu ngi ko jàppe niki lu baax lool—liggéey bu amul moroom! Waaye, ci guddi, kuy rawanteek moom te iñaan yàq ko. Mën nañoo nànd ne loolu jural na nataalkat bi naqar wu réy. Akay yàkkamtee gis ñu kaaf wayu bi! Te mën ngaa jortu nan la nataalkat boobu di xintee gis liggéeyam defaruwaat, rafet ni bu njëkk.

2 Niki nataalkat boobu, Yeowa defoon na liggéey bu amul moroom ba muy defar suuf si te teg ci nit. Gannaaw ba mu sàkkee góor ak jigéen, àtte na lépp li mu liggéey ci kow suuf niki lu “baax lool.” (1 Musaa 1:31) Aadamaak Awa doomi Yàlla saxsax lañu woon, te bëggoon na leen. Li mu leen séentuloon a doon ëllëgu bànneex, ju ànd ak ndam. Dëgg la, Seytaane duggal na leen ci jógal Yàlla, waaye mbindeefum Yàlla mu rafet-a-rafet mi yàquñu ko ci lu ñu mënula jagal.—1 Musaa 3:23, 24; 6:11, 12.

3. Lan mooy “dund gu wóor gi”?

3 Yàlla dogal na jubbanti yëf yi. Bëgg na ci xolam gis ñu, ñuy dund ni mu ko nase woon ca njëlbéen. Suñu dund gu gàtt te jaxasoo gi, du “dund gu wóor gi,” ndaxte moo yées fuuf la Yeowa nasoon. “Dund gu wóor gi” ñu Yàlla bëggal mooy “dund gu dul jeex gi” ci nekkin yu mat sëkk.—1 Timote 6:12, 19.

4, 5. (a) Nan lañuy amale yaakaaru Àjjana? (b) Lu tax ñu warkoona xalaat suñu yaakaar ngir ëllëg?

4 Xam-xamub Yàlla dafay yóbbe ay wareef ci kanamu Yeowa. (Saak 4:17) Waaye xalaatal barke yi ngay bànneexoo soo toppee xam-xam boobu te nga fexee jot dund gu dul jeex. Ci Kàddoom, Biibël bi, Yeowa Yàlla nataal na nataal bu rafet, nataalu li dund gi di mel ci suuf siy nekk Àjjana te mu dégmal. Jarul ñu koy wax, niki mbooloo Yeowa, jaamuwuñu Yàlla doŋŋ ndax dañu cee séenu yool. Dañuy jaamu Yeowa ndaxte dañu koo bëgg. (Mark 12:29, 30) Magum loolu, dund du lu ñu yelloo ndax li ñuy jaamu Yeowa. Dund gu dul jeex, mayug Yàlla la. (Room 6:23) Dina ñu amal njariñ ñu xalaat ba xeli dund gu ni mel ndaxte yaakaaru Àjjana dafa ñuy fàttali fasoŋu Yàlla bi Yeowa nekk—ku am mbëggeel kiiy “neexal ñi koy wut.” ( Yawut yi 11:6) Yaakaar joojuy ray-rayi ci suñu xel ak suñuy xol dina ñu taxa muñ jafe-jafe yi ci àddina Seytaane.—Yérémi 23:20.

5 Nañu teewlu léegi ci yaakaar ji sës ci Biibël bi, yaakaaru dund gu dul jeex gi ci Àjjana juy dikk ci kow suuf. Nan la dund ga di mel bés bu xam-xamub Yàlla feesee suuf si?

GANNAAW AR-MAGEDON— AB ÀJJANA CI KOW SUUF

6. Lan mooy Ar-Magedon, te lan lay tekki ngir doomi Aadama yi?

6 Ni ñu ko wone bu njëkk, Yeowa Yàlla tuuti ca kanam dina sànk jamano ju soxor jii. Àddina saa ngi dégmal bu gaaw ci li Biibël biy tudde Xar-Magedon, walla Ar-Magedon. Baat boobu dafay foogloo ñenn ñi àddina suy tukki ndax xeet yiy xareek seeni bomb atomik, waaye Ar-Magedon du dara lu ni mel. Ni ko Peeñu bi 16:14-16 wone, Ar-Magedon mooy “xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam.” Xeex buy laal “buuri àddina sépp” la, walla xeet yi. Doomu Yeowa Yàlla ju góor, Buur bi ñu fal, tuuti ca kanam dina dugg ci xare bi. Muj gi, lu wóor-a-wóor la. Ñépp ñii bañ Nguurug Yàlla, te bokk ci jamano Seytaane ju soxor ji, dinañu leen dindi. Ñii gore ci Yeowa doŋŋ ay mucc.—Peeñu bi 7:9, 14; 19:11-21.

7. Fan la Seytaane aki seytaaneem di nekk ci biir Nguurug Junniy At, gu Krist, te nan la loolu di jariñe doomi Aadama yi?

7 Jortul mucc nga ci musiba mu réy moomu. Nan la dund ga ca kow suuf di mel ci àddina su bees si ñu Yàlla dig? (2 Pieer 3:13) Jarul ñuy tandale, ndax Biibël bi wax nañu ko, te li muy wax lu dawloo yaram la. Ñu ngiy jàng ne Seytaane aki seytaaneem dinañu leen yeew, kaaf leen cim yeeru sawaradi, fu ñuy ne tekk ca biir Nguurug Junniy At, gu Yeesu Krist. Mbindaafon yu bon te soxor yooyu dootuñu nëbbu di jaxase te di ñu jéema xiir ci jëfiy takkoodi ci Yàlla. Ndaw coono bu wàññeeku!—Peeñu bi 20:1-3.

8, 9. Ci àddina su bees si, lan mooy xew ak naqar yi, feebar ak màgget?

8 Ca waxtoom, fasoŋi wopp yi yépp dinañu deñ. ( Isayi 33:24) Bu boobaa ki lafañ dina taxaw, dox, daw te fecc aki tànk yu wér. Gannaaw ba ñu dundee ay at ci seen àddina bu ne selaw, ñi tëx dinañu dégg riir yu bég yi leen wër. Ñi gumba dinañu am mbetteel mu réy, gis àddina su bare kulóor ak melin di firiku ci seeni gët. (Isayi 35:5, 6) Ndax Yàlla, dinañu faf gis xar-kanami seeni soppe! Xëy na booba ay rongooñiy mbégte dinañu lëndëmal ci saa su gàtt seen gis-gis.

9 Xalaatal loolu rekk! Dootul am lunét, dootul am sukkóot aki yet ngir dox, dootul am garab, dootul am béréb ngir faj bëñ, walla loppitaan! Wopp ju jëm ci siddit ak naqar bu tepp dootuñu xañ mukk nit ñi bànneex. Genn gone du am naqar ndax feebar. Yàq-yàq yi màgget di yóbbe dinañu leen defaraat. (Ayóoba 33:25) Suñu wér-gi-yaram dina gën di baax, dinañu gëna am doole. Suba su nekk dinañu yeewoo nelawu guddi gu neex, ak kàttan gu bees, fees ak doole te njaxlaf ngir bés bu bees buy jàjji, ak liggéey buy bégloo.

10. Ban liggéey bu ñu leen di sas la ñay mucc ca Ar-Magedon di sumb?

10 Dina am liggéey bu bare buy bégloo, liggéey bu ñiiy mucce Ar-Magedon di def. Dinañu soppali suuf si mu nekk ab àjjana. Dinañu fi jële lépp lu des ci jamano ju màgget te tilim jii. Ndambalaan yeek tooli dër yi dinañu wuutu dëkkuwaay yu toskare yeek suuf su sàppi si. Ñépp dinañu am mbégte dëkk ci kër yu neex, yu jekk. (Isayi 65:21) Bu jamanoy dox, wàll yooyu nekk àjjana ci suuf si dinañu law te booloo ba suuf sépp dab rëddu-yoonu Sàkkkat bi ci wàllu rafetaay, rëddu-yoon wa woon ca biir toolu Eden. Akay nekk mbégte, bokk ci liggéeyu ndefar boobu!

11. Ëllëg, digaale doomi Aadama yeek kéewaange suuf seek mala yi, lan lay doon?

11 Loolu lépp dinañu ko def ci njiiteefug Yàlla, ba tax duñu yàq kéewaange gi. Doomi Aadama yi dinañu nekk ci jàmm ak mala yi. Asté mu leen di rendi ndax topp li ko neex, nit dina tàmbaliwaata saytu suuf si, di leen toppatoo bu baax. Jortul lupus yeek mbote yi, gaynde yeek sëllu yi, di forandoo—te bàyyima yaa ngi ci dalaay bu mat sëkk. Gone gu ndaw sax du am dara lu muy ragal ci rabi àll yi, te nit ñu xos ñi, te soxor duñu dog seddaayub àddina su bees si. ( Isayi 11:6-8) Akay nekk àddina su bees su am jàmm!

SOPPI NAÑU DOOMI AADAMA YI

12. Nan la Isayi 11:9 di àgge tey, te nan lay àgge ci Àjjana?

12 Isayi 11:9 a ngi ñuy wax lu tax dara luy lor du am ci kow suuf si sépp. Nee na: “Ci lu wóor, suuf si dina fees ak xam-xamub Yeowa niki ndox yi di muure géej ci boppam.” Loolu nit ñi lay laal ndaxte mala yi mënuñoo jànga xam “xam-xamub Yeowa” te def ay soppi, ndegam seen xiiru moo leen di jiital. Waaye xam-xamub suñu Sàkkkat dafay soppi dëgg nit ñi. Du ñàkk, def nga ba noppi yenn soppi ndax li nga jëfoo xam-xamub Yàlla ci sa dund. Ay tamndareeti nit def nañu ko. Noonu yégleb yonent bii tàmbali naa àgg ci jaamiy Yeowa. Ndaxam, mu ngiy joxoñ itam jamano joo xam ne niti àddina si sépp dinañu xàcceek jikko mala ju mu mënta doon walla taafar te dinañu mujja nekk nitiy jàmm ba fàww.

13. Ban doxalukaayub njàngale lañuy taxawal ca kow suuf?

13 Akay nekk lu di yéemloo, bu keroogee xam-xamub Yàlla di fees suuf si! Buur bi Yeesu Krist ak téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000) yiy nguurandook moom dinañu taxawal doxalukaayub njàngale bu yaatoo yaatu. Bu booba dinañu jëfandikoo ay “téere” yu bees. Jarul ñu koy wax, ay tegtal yu bawoo ca Yàlla yu ñu bind lañu, yuy sabab njàngale ñii dëkk ci kow suuf. (Peeñu bi 20:12) Doomi Aadama yi duñu jànga xare, waaye jàmm. Gànnaay yiy sànk yépp dinañu wéy ba fàww. (Sabuur 46:9) Nit ñay dëkk ca àddina su bees soosa dinañu leen jàngal ñu digaaleek seeni moroomi doomi Aadama ak mbëggeel, weg ak teraanga.

14. Nan la àddina si di wuutee bu keroogee doomi Aadama yi di nekk genn njaboot gu déggoo?

14 Doomi Aadama yi dinañu mujja nekk genn njaboot gu déggoo. Dootul am ay gàllankoor ci déggook cofeel gu takku. (Sabuur 133:1-3) Duñu soxlaa caabi këru kenn ngir muslu ci sàcc yi. Jàmm dina dëkk ci bépp xol, ci gépp kër, ci bépp diiwaan ci kow suuf.—Mikaa 4:4.

NDEKKITE LAY YÓBBE MBÉGTE

15. Yan ñaari mbooloo lañuy dekkal ci kow suuf?

15 Ca biir Junniy At yooya, la ndekkite la di am. Ña teyoon bàkkaar kontar xelum Yàlla mu sell mi, walla dooleem jiy jëf, ci li ñu liggéey, noonook peeñoom wallay tegtalam te bañ ko réccu, duñu dekki. ( Macë 23:15, 33; Yawut yi 6:4-6) Jarul ñu koy wax, Yàlla képp ay dogal ku bàkkaaree noonu. Waaye ñaari mbooloo yu wuuteey dekki—“ñi jub ak ñi jubadi.” (Jëf ya 24:15) Ndegam lépp ciw yoon lay tegu, jaadu na ñu tofal ne ñii ñuy njëkka teeru bu ñu dellusee ci dund ci kow suuf ñooy ñu jub ñi, ñii surgawu woon Yeowa ak ngor.—Yawut yi 11:35-39.

16. (a) Kan mooy bokk ci “ñu jub ñi” ñuy dekkal ci kow suuf? (b) Ñan nit ñu takku ci Yàlla, nitiy jamano yu yàgg ya nga bëgga dajeel saxsax, te lu tax?

16 Asté ñoo dégg ay xabaar yu jëm ci xare, musibaak dee, jaamiy Yeowa dinañu jot nettaliy ndekkite yu yéeme. Dégg ne ay góor aki jigéen ñu takku ci Yàlla, mel ni Abel, Enok, Nóoxin, Ibrayima, Saara, Ayóoba, Musaa, Raxab, Rut, Daawuda, Eliyaak Esteer dellusi nañu, dina nekk luy ràkkati ndax mbégte. Ndaw xew-xewiy démb yuy dawloo yaram yuñ ñuy nettali, ba ñu ñuy leeralal anamiy nettali yu bare ci Biibël bi! Amul werante, ñoom ak ñu jub ñi dee ci jamano yu yàggul dara, dinañu yàkkamtee jàng lu jëm ci mujug jamanoy Seytaane te nan la Yeowa sellale turam wu sell wi te làyyee kiliftéefam.

17. Lan ndimbal la ñii takku ci Yàlla di jox ñeneen ñi dekki ?

17 Ñu takku ci Yàlla ñooñee, aka ñooy nekk ndimbal ci jamano ndekkite jiy topp, bu ñu yewwee ay junniy tamndareeti nit “ñu jubadi” ci buumiy dee! Li ëpp ci nit ñi masuñoo am muuru xam Yeowa. Seytaane daa ‘gëlëmal[oon] seen xel.’ (2 Korent 4:4) Waaye dinañu nasaxal liggéeyub Ibliis. Ñi jubadi dinañu dellusi ci kow suuf su rafet te am jàmm. Am mbooloo mu ñu jagal bu baax dina leen teeru ngir jàngal leen lu jëm ci Yeowaak Doomam ju góor jiy nguuru, Yeesu Krist. Ba ay junniy tamndareeti nit ñu dekki di mujja xam tey bëgg seen Sàkkkat, xam-xamub Yeowa dina fees suuf si ci ni mu masulee am.

18. Lan nga xalaat ne loolu ngay yëg, ëllëg booy teeru sa soppe yi dekki ?

18 Ndaw bànneex, bu ndekkite loolu di indi ci suñuy xol! Kan a yëgul naqar ndax suñu noon, dee? Ca dëgg, kan a saalitul ba buumug mbëggeel ak xaritoo dogee, ba feebar, màgget, aksidã, walla taafar faatee bakkanu nit koo sopp? Jortul, kon, mbégte miy ànd ak gisewaat yi ca biir Àjjana. Ndey ak baay, doom yu góor ak yu jigéen, xarit aki mbokk, dinañu gatandoonte, foonante, di ree, aka yuuxu ndax mbégte.

MATAAY FAF NAA AM!

19. Ban kéemaan ay am ca biir Junniy At ya?

19 Ca biir Junniy At yi, ab kéemaan bu yéeme dina am. Ngir doomiy Aadama, xëy na dana nekk fànna biy gëna dawloo yaram bu Nguurug Junniy At, gu Krist. Yeowa dina santaane Doomam ju góor mu jariñloo peyug njotu saraxam ku nekk ci góor ak jigéen ñu takku ñi te déggal. Jaare ci pexe moomu, dinañu dindi bàkkaar yépp te mbooloom nit ñi dinañu leen yëkkëti ci mataay.—1 Yowanna 2:2; Peeñu bi 21:1-4.

20. (a) Nekk ku mat sëkk, lan la loolooy tekki? (b) Kañ la ñay mucc ca Ar-Magedon ak ñay dekki di tàmbalee dund dëgg-dëgg?

20 Mataay! Lan la looluy tekki? Loolu dina tekki am ndellusi ca dund ga Aadamaak Awa doon bànneexoo laata ñoo bàkkaar kontar Yeowa Yàlla. Moo xam ci yaram, ci xel, ci wàllu cofeel, ci wàllu jikkook ngëm—ci fasoŋ boo mëna xalaat—doomi Aadama yu mat yi dinañu dab, ba mu mat sëkk, yooniy Yàlla. Waaye ndax, bu boobaa, nit ñi ñépp ay bokka niroo? Sore na loolu! Mbindeefiy Yeowa—garab yi, tóor-tóor yi, mala yi—lépp a ñuy jàngal ne ku bëgg wuutaate la. Doomi Aadama ñu mat ñi dinañu am ay jikkooki xereñ yu wuute. Ku nekk dina bànneexoo dund na Yàlla bëgge woon mu doon. Peeñu bi 20:5 nee na: “[Ñ]eneen [ñii dee] duñu dekki, fi ak junniy at yi matul.” Niki mbooloo mu réy, mbooloom ñay mucc ca Ar-Magedon, ñiiy dekki dinañu mujja dund dëgg bu ñu jotee mataay bu àndalul bàkkaar.

21. (a) Lan ay xew bu Nguurug Junniy At, gu Krist sottee? (b) Lan ay mujja dal Seytaaneek ñépp ñii far ak moom?

21 Bu boobaa doomi Aadama ñu mat ñi dinañu jànkoonteek benn nattu, bu mujj bi. Bu Junniy At yi matee, Seytaane aki seytaaneem dinañu leen yewwee yeer ma ngir diir bu gàtt te dinañu leen may ñu def seen njéem bu mujj bi ngir dëddale nit ñi ci Yeowa. Dina am ñuy yëkkëti ay bëgg-bëgg yu bon ci kow seen mbëggeelug Yàlla, waaye jógal Yàlla boobu dinañu ko gàttal. Yeowa dina reyaale ñu siis ñooñook Seytaane aki seytaaneem yépp. Bu boobaa defkati lu bon ñépp dinañu leen sànk ba fàww.—Peeñu bi 20:7-10.

LAN NGAY DEF?

22. Lan nga séenoo def ca Àjjana?

22 Abadan ga dina nekk ci kanami ñépp ñii bëgg Yeowa Yàlla te dinañu dëkk ci Àjjana ci kow suuf. Seen mbégte, jafe naa jortu te mën ngaa fekke loolu. Ci wàlluw misig, xereñ ak liggéey yu xarala—li nit ñu mat ñi di amal dina raw jëf yi dàq ci jëfiy boroom xam-xam yi gëna waane ci suñu jamano ju màgget ji! Boo ko seete sax, doomiy Aadama yi dinañu mat te dinañu am jot gu dul jeex ci seen kanam. Jortul li ngay mëna def lépp niki nit ku mat sëkk. Xalaatal, itam, li yow ak sa moroomi doomiy Aadama di jàng ci mbindeefum Yeowa—li dale ci junniy tamndareeti juugi biddéew ci biir jaww ji ba ci dogatiit yi gëna tuuti ci wàllu atom. Lépp lu nit ñi amal dina gëna bégal xolu suñu Baay bu fees ak mbëggeel ba ca asamaan, Yeowa.—Sabuur 150:1-6.

23. Lu tax dund ga ca biir Àjjana du soof mukk?

23 Dund ga, booba, du soof. Dina gën di neex bu jamano dee dox. Gis nga, xam-xamub Yàlla amul àpp. ( Room 11:33) Ca biir abadan ga, dina am saa su nekk lu ñu mëna jàng aki fànna yu bees yu ñuy gëstu. (Dajalekat 3:11) Te ba ngay wéy di jànga xam Yeowa Yàlla, dinga kontinee dund—du rekk ay at yu néew, waaye ba fàww!—Sabuur 22:26.

24, 25. Lu tax nga warkoona dëpp sa dund léegi-léegi ak xam-xamub Yàlla?

24 Ndax ëllëg ju ni neexe ci kow suuf su nekk àjjana jarul gépp njéem walla lépp loo xañ sa bopp, ak lu mu mënta doon? Bu wóor-a-wóor, jar na ko! Kon, Yeowa tàllal na la caabiy ëllëg ju amul moroom jooju. Caabi jooju mooy xam-xamub Yàlla. Ndax dinga ko jëfandikoo?

25 Soo bëggee Yeowa, dinga am bànneex ciy def coobareem. (1 Yowanna 5:3) Ba ngay wéy di topp dundin boobu, ndaw barke yooy daj! Soo jëfee xam-xamub Yàlla, loolu mën na laa yóbbe dund gu gëna bég ci suñu jamano ju jaxasoo jii sax. Te yool yiy ñëw, yu réy-a-réy lañu, ndax xam-xam la, bu lay jëme ca dund ga dul jeex! Léegi la waxtu wi saxsax wi nga wara jekku ngir jëf. Dogul ngir dund dund gu dëppook xam-xamub Yàlla. Woneel sa mbëggeel ngir Yeowa. Sargalal turam wu sell te firndeelal bu wóor ne Seytaane ab fenkat la. Lu jëm ci moom, Yeowa Yàlla, Aji Sago dëgg ak Aji Xam-xam ji, dina bég ci yow, ci xolam bu yaa te fees ak mbëggeel. (Yérémi 31:3; Tsëfanyaa 3:17) Te dina la bëgg ba fàww!

SEETLUL SA XAM-XAM

Lan mooy “dund gu wóor gi”?

Gannaaw Ar-Magedon, lan mooy am ci kow suuf ?

Kan lañuy dekkal ci kow suuf ?

Nan la nit ñi dee mujja mat sëkk te nan lañu leen dee mujja nattu?

Lan mooy sa yaakaar jëm ci Àjjana?

[Laaj yi]

[Nataal bi nekk paas 188, 189]

Ndax yaakaar ngaa dund ci Àjjana, bu xam-xamub Yàlla feesee suuf si?