Dajal dalaay ci biir mbooloo Yàlla
Pàcc 17
Dajal dalaay ci biir mbooloo Yàlla
1, 2. Nan la nekkinu mbooloom nit ñi mele ni bosu nit ñu nekk ci diiwaan bu ngëlén lu am doole yàq?
JORTUL ngëlén lu am doole lu yàq diiwaan bi nga dëkk. Sa kër a ngi màbb te say am-am yépp, ñàkk nga leen. Lekk gaa ngi jafe. Mu ngi mel ni mbir mi amatul jenn yaakaar. Booba la ndimbal loo séentuwul agsi. Lekk geek yëre yaa ngi ne gàññ. Tabaxal nañu la kër gu bees. Ci lu wóor, doon nga gërëm nit ki tax nga am loolu lépp.
2 Lenn lu ni mel a ngiy xew tey. Niki ngëlén loolu, jógal bi Aadamaak Awa jógal Yàlla jural na loraange ju réy doomi Aadama yi. Nit ñi ñàkk nañu seen dëkkuwaay, Àjjana. Booba ba tey, nguuri doomi Aadama yi caŋ nañu ci aar nit ñi ci xare, ñaawtéef ak njubadi. Diine ju moy dëgg ji bàyyi na ay ndiiraani nit ñuy dee ak xiif gu jëm ci ñamu xel wu sell. Waaye ci fànnab xel, Yeowaa Yàllaa ngiy joxe ñam, yëreek làqukaay. Nan la koy defe?
“JAAM BU TAKKU TE TEEY BI”
3. Nan la Yeowa di joxe mbooloom nit ñi li war ci wàllu ngëm, te yan misaal a ko wone?
3 Ndimbal, ñaare, dañu koy joxe jaare cib kurél bu ñu taxawal, te noonu itam Yeowa fogoru na ndimbal ci wàllu ngëm ngir mbooloom. Noonu, waa Israel ñoo nekkoon “mbooloo Yeowa” lu tollook junneek juróomi téeméeri (1500) at. Ca seen biir amoon na ña Yàlla doon jëfandikoo ngir jàngale Sàrtam. (1 Nettaliy xew-xewi cosaan 28:8; 2 Nettaliy xew-xewi cosaan 17:7-9) Ca xarnu bu njëkk ba, Yeowa taxawal na mbootaayug karceen yi. Dañoo sampoon ay mbooloo te ñu nga doon dox ca njiitum jataay bu doon dogal, bu ay ndawiy Yeesu ak ay mag séqoon. (Jëf ya 15:22-31) Noonu itam tey, Yeowaa ngi digaaleek mbooloom jaare ci mbootaay bu mu jagal. Nan lañu xame loolu?
4. Kan a jota firndeel bu wóor ne mooy “jaam bu takku te teey bi, NW” ci suñu jamano , te nan lañu mënee jot ci li Yàllay joxe ci wàllu ngëm?
4 Yeesu waxoon na ne keroog ca teewaayam ci kàttanug Nguur gi, “jaam bu takku te teey bi” doon nañu ko fekk muy jox ñi Koy topp “dundu bi ca jamano ja war.” (Macë 24:45-47, NW ) Ba ñu falee Yeesu Buur ca asamaan ca atum 1914, kan a wone ne moo doon “jaam” boobu? Ci lu wóor, duloon njiitiy diiney yiy wuyoo turu karceen. Li ci ëpp ñu nga daan dundal seeni coggal ak njéemantal yi ñu daan lawloo, lawloo-njéemantal gu daan jàpple seeni nguuri réew ca Xeexu Àddina Sépp bu Njëkk ba. Waaye, mbooloom karceen yi ñu tànnoon ak xelum Yàlla mu sell mi ñu nga daan séddale ñamuw xel wi war, ci waxtoom, te bokkoon nañu ci li Yeesu tudde “coggal ju ndaw ji.” ( Lukk 12:32) Karceen yooyu ñu tànn, Nguuru Yàlla lañu waare asté nguuriy nit. Loolu li mu yóbbe mooy, ci biir at yi toppante, ay tamndareeti “yeneen xar” yu jagoo njub booloo nañook “jaam” bi ñu tànn ci topp diine dëgg ji. ( Yowanna 10:16) Jaare ci ‛jaam bu takku’ bi ak Jataayam biy dogal ci suñu jamano jii, Yàllaa ngiy saytu mbooloom mi mu jagal ngir defaral ñépp ñii ko bëgg dundu, yëreek làqukaay ci wàllu ngëm yu ñu waajal.
“DUNDU BI CA JAMANO JA WAR”
5. Lan ay nekkinu àddina si tey ci wàllu ngëm, waaye lan la Yeoway def ci fànna boobu?
5 Yeesu nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu, gu génne ci gémmiñug Yàlla.” (Macë 4:4) Li metti mooy li ëpp ci nit ñi duñuy bàyyi xel ci yégley Yàlla. Na ko yonent Yeowa bi tudd Amos yégle woon, dafa am “ag xiif, du ngir mburu, ak mar, du ngir ndox, waaye ngir dégg kàdduy Yeowa.” (Amos 8:11) Nit ñu jullite sax dañoo xiif ci wàllu ngëm. Wànte, coobareg Yeowa mooy nit “ñépp mucc te xam dëgg gi.” (1 Timote 2:3, 4) Looloo tax mu ngiy joxe ñamuw xel bu baree bare. Waaye fan lañu ko mëna ame?
6. Nan la Yeowa doon dundale mbooloom, bu njëkk, ci wàllu ngëm?
6 Ba àddina sosoo ba tey, Yeowa séddale na ay gaayam dundub xel nikim mbooloo. ( Isayi 65:13) Noonu saraxekati waa Israel dañu daan dajale góor ñi, jigéen ñeek xale yi ngir jàngal leen Sàrtub Yàlla niki mbooloo. (5 Musaa 31:9, 12) Ci njiitu jataay biy dogal, karceeni xarnu bu njëkk ba jagaloon nañu ay mbooloo te daan nañu am ay ndaje ngir jàngal te xiirtal ñépp. ( Room 16:5; Filémon 1, 2) Seede Yeowa yi, royukaay boobu lañuy topp. Ñu ngi lay ñaan, mu jóge ci biir xol, nga teew ci seeni ndaje yépp.
7. Tàmm di teew ci ndajey karceen yi, nan la lëkkaleek xam-xam ak ngëm?
7 Dëgg la, xëy na jot ngaa jàng lu bare ci sa njàngum Biibël bi ngay defal sa bopp. Mën naa am sax kenn ku la ci jàpple. (Jëf ya 8:30-35) Waaye mënkoon nañu misaale sa ngëm ak garab guy lax te dee su ñu ko toppatoowul ni mu ware. Noonu, war ngaa jot dundub xel bi war. (1 Timote 4:6) Ndajey karceen yaa ngiy joxe porogaraamu njàngale buy wéy, ñu waajal ko ngir dundal la ci wàllu ngëm te dimbali la nga wéy di màgg ci ngëm ba ngay yokk sa xam-xamub Yàlla.—Kolos 1:9, 10.
8. Lu tax ñu di ñu xiirtal ciy teew ci ndajey Seedey Yeowa yi?
8 Ndaje yaa ngiy jariñ neneen, ci nas bu suñu bakkan aju. Pool bind na: “Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. Te bunu bàyyi sunu ndaje yi.” ( Yawut yi 10:24, 25) Baat ci Grekk bi ñu firee “xiirtalante” mën naa tekki “daas.” Benn léebu ci Biibël baa ngiy wax: “Weñ, weñ ci boppam a koy daas. Noonu, nit mooy daas xar-kanamu keneen.” ( Léebu 27:17) Ñun ñépp soxla nañu, ñu wéy di ñu ‛daas.’ Naj yi ñuy daj bés bu nekk, naj yu jóge ci àddina mën nañoo dayal suñu ngëm. Bu ñu dee teew ci ndajey karceen yi, dafay am xiirtalante. (Room 1:11, 12) Ñii bokk ci mbooloo maa ngiy topp xelalu Pool, di wéy ci “naabante tey yokkante, NW, ” te yëf yu ni mel ñooy daas suñu ngëm. (1 Tesalonikk 5:11) Tàmm di teew ci ndajey karceen yi dafay wone it ne bëgg nañu Yàlla te dafa ñuy xàllal yoon ngir tagg ko.—Sabuur 35:18.
“NANGEEN SOLOO MBËGGEEL, NW.”
9. Nan la Yeowa nekke royukaay lu jëm ciy wone mbëggeel?
9 Pool bind na: “[ Nangeen soloo, NW ] mbëggeel, giy jókkaale lépp, ba mu mat.” (Kolos 3:14) Yeowa may na ñu, ci xol bu sedd, yëre boobu. Naka? Karceen yi mën nañoo wone mbëggeel ndaxte mooy benn ci meññeefi xelum Yeowa mu sell mi, yi Yàlla di maye. (Galasi 5:22, 23) Yeowa ci boppam wone na mbëggeel gi gëna mag ci li mu yónnee Doomam ju góor ji mu jur kott ngir ñu mëna am dund gu dul jeex. ( Yowanna 3:16) Peeñub mbëggeel boobu sut lépp, nekk na ab royukaay ngir ñuy wone jikko jooju. Ndaw li Yowanna bind na: “Bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante.”—1 Yowanna 4:11.
10. Nan lañu mënee jële njariñ ci “mbooloom njabootu mbokkiy [diine ji], NW”?
10 Sa teewaay ca ndaje ya ca Saalu Nguur ga dina la xàllal yoon wu rafet ngir wone mbëggeel. Foofa ay fasoŋi nit yu baree fay daje. Ci lu amul werante dinga gaawa taq ci ñu bare ci ñoom. Dëgg la, ci biir ñiiy surgawu Yeowa sax, jikko yi dañoo wuute. Xëy na bu njëkk danga doon yem ci moytu nit ñi nga bokkalul itte walla jikko. Waaye, karceen yi war nañoo “am mbëggeel ngir mbooloom njabootu mbokkiy [diine ji], NW.” (1 Pieer 2:17) Looloo tax, defal muy sa jëmu: xamanteek ñépp ñiiy teew ca Saalu Nguur ga—bu fekkee sax yemuloo maas, jikko, walla bokkuloo xeet walla njàng ak ñoom. Jombul dinga gis ne ku nekk am na melo jikkoom wu jolli wuy tax ñu sopp ko.
11. Lu tax jikko yu wuute yi ci biir mbooloo Yeowa waruñu ñoo lëmbe?
11 Jikko yu wuute yii ci mbooloo mi waruñu laa lëmbe. Nañu ko misaale nii: jortul ay oto yuy tukki, ànd ak yow di wàcc benn tali bi. Yépp bokkuñu gaawaay, te yépp bokkuñu ni ñu mel. Am na yu ci tukki kilomet yu bare, waaye niki yow, ñeneen a ngiy soga tàmbali. Waaye, ak lu mu ama am wuutale yooyu, ñoom yépp a ngiy daw, di wàcc benn tali bi. Noonu la deme ak nit ñiy booloo def mbooloo mi. Ñépp duñu niroo gaawaay ci ni ñuy suqalee jikkoy karceen. Rax-ca-dolli, ñépp yemuñu nekkin ci wàllu wér-gi-yaram walla yëg-yëg ci seen biir xol. Am na ñuy jaamu Yeowa li dale ay ati at; ñeneen a ngiy soga tàmbali. Ndaxam, ñépp a ngiy tukki ci tali biy jëme ca dund ga dul jeex ga, “ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.” (1 Korent 1:10) Looloo tax, wutala seet jikko yu rafet ci ñii nekk ci mbooloo mi asté seeni sikk. Di def loolu dina seddal sa xol, ndax dinga gisal sa bopp ne Yàllaa ngi ci diggu nit ñooñu ca dëgg. Te ci lu wóor, fa nga bëgga nekk.—1 Korent 14:25.
12, 13. (a) Su la kenn ci mbooloo mi tooñee, loo mëna def? (b) Lu tax baña déncal mer nit nekk lu am solo?
12 Ndegam doomiy Aadama yépp a matadi, léeg-léeg kenn ci mbooloo mi mën naa wax walla def dara lu la fakkatal. (Room 3:23) Taalibe Saak bind na ci lu dëppook li am: “Nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga, te mana noot sa yaram wépp.” (Saak 3:2) Nan ngay gise mbir mi su la kenn tooñee? Ab léebu ci Biibël bi nee na: “Ñawinu xelu nit, ci lu wóor, dafay yéexal meram te taar la ci moom mu wéyale tooñ.” (Léebu 19:11) Am ñawinu xel a ngiy tekki gis li feeñul ci bët, nànd liy daanaka waxloo walla jëfloo nit. Li gëna bare ci ñun, dañuy jëfandikoo ñawinu xel bu bare ngir jéggal suñuy njuumte. Lu tax bañ koo jëfandikoo it ngir nànd te muur matadiy ñeneen ñi?—Macë 7:1-5; Kolos 3:13.
13 Bul fàtte mukk ne war nañoo baal ñeneen ñi su ñu bëggee jot ci mbaalug Yeowa. (Macë 6:9, 12, 14, 15) Su ñuy jëfoo dëgg gi, dinañu digaaleek ñeneen ñi ak mbëggeel. (1 Yowanna 1:6, 7; 3:14-16; 4:20, 21) Kon soo amee jafe-jafe ak kenn ci mbooloo mi, góor-góorlul ngir bañ koo déncal mer. Soo soloo mbëggeel, dinga jéema saafara jafe-jafe bi, te dinga gaawa baalu su fekkee yaa tooñ.—Macë 5:23, 24; 18:15-17.
14. Yan jikko lañu warkoona soloo?
14 Suñu yëre xel war naa ëmb yeneen jikko yu lëkkale bu baax-a-baax ak mbëggeel. Pool bind na: “Solooleen boog yërmande, laabiir, woyef, lewet ak muñ.” Jikko yooyu, làmboo mbëggeel, a ngi bokk ci “jikko ju bees ji” dëppook coobareg Yàlla. (Kolos 3:10, NW, 12) Ndax dinga jéema soloo noonu? Rawatina boo soloo mbëggeel ngir say mbokki karceen, dinga wone màndarga miy tax ñu ràññee taalibey Yeesu, ndax nee na: “Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.”—Yowanna 13:35.
BÉRÉBU DALAAY
15. Nan la mbooloo mi mele ni làqukaay?
15 Mbooloo mi itam dafay jariñ nikib fatukaay, ab làqukaay buy aar, fu ñu mënee yëg dalaay. Ci biiram, dinga fa fekk ay nit ñu gore te wóor ñuy jéema def li jub ca gëtiy Yàlla. Ñu bare ci ñoom dëddu nañu jëf yeek jikko saxsax yi ngay xeex xëy na ngir tàggook ñoom. ( Titt 3:3) Mën nañ laa dimbali, ndaxte ñu ngi ñuy wax ñu “jàppalante”. (Galasi 6:2) Jarul ñu koy wax, sax ci dundin buy jëme ca dund ga dul jeex ga, ndax sottal, sa warugar saxsax la. (Galasi 6:5; Filipp 2:12) Ndaxam, Yeowa joxe na mbooloo karceen mi niki pexe mu amul moroom ngir dimbali te taxawu. Ak lu say jafe-jafe mëna tar tar, am na ndimbal lu am maanaa ngir yow—mbooloo mu ànd ak mbëggeel mu nekk sa wet ci jamanoy tiis ak ñàkk.—Dendale kook Lukk 10:29-37; Jëf ya 20:35.
16. Ban ndimbal la mag ñi ci mbooloo miy joxe?
16 Ci biir ñii pare ngir dimbali la, am na ay “góor ñu nekk ay maye, NW ”—mag ñi ñu fal ci mbooloo mi, walla wottukat, ñuy sàmm coggal gi ak xol bu tàlli ak cawarte. ( Efes 4:8, 11, 12; Jëf ya 20:28; 1 Pieer 5:2, 3) Lu jëm ci seen mbir, Isayi waxoon na: “Ku nekk dana wara mel ni ab làqukaay ci ngelaw li ak seelukaay ci ngëlén li, niki ay wali ndox cib dëkk bu amul ndox, niki keru doj wu diis ci suuf su sàppi.”—Isayi 32:2.
17. (a) Ban fasoŋu ndimbal saxsax la Yeesu bëggoona joxe? (b) Lan la Yàlla dig ne dina ko jox mbooloom?
17 Ba Yeesu nekkee ci kow suuf, ndeysaan, wottu bu ànd mbëggeel bu ni mel ñàkkoon na ca kilifay diine ya. Nekkinub nit ña yëngaloon na xolam lool, te li mu bëggoon saxsax moo doon dimbali leen ci wàllu ngëm. Yeesu da leen yërëmoon ndaxte “dañoo sonn[oon] ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm.” (Macë 9:36) Aka la loolu di saabal nekkinub coono nit ñu bare ñuy muñ ay jafe-jafe yu yóbbe njàqare te amuñu kenn ku ñu ci mëna jublu ngir mu xettali leen ci wàllu ngëm te dëfël leen! Waaye mbooloo Yeowa am na ca dëgg ndimbal ci wàllu ngëm, ndaxte dig na: “Dinaa yëkkëti ci seen kow ay sàmm yu leen di sàmm dëgg; te dootuñu ragal, walla ñu tiital leen, te menn xar du réer.”—Yérémi 23:4.
18. Lu tax ñu warkoona jege mag su ñu soxlaa ndimbal ci wàllu ngëm?
18 Na nga xamanteek mag ñi ñu fal ci mbooloo mi. Xam nañu àddina lool ci li ñuy jëf ci seen dund xam-xamub Yàlla, ndax dab nañu manoore yi Biibël biy laaj ngir nekk wottukat. (1 Timote 3:1-7; Titt 1:5-9) Bu sa xel def ñaar ngir jege kenn ci ñoom soo soxlaa ndimbal ci wàllu ngëm ngir mëna daan tàmmeel walla jikko juy safaanook li Yàllay laaj. Dinga gis ne mag ñaa ngiy topp ndigalu Pool: “Dëfal[leen] ñi [tojle], dimbali ñi néew doole, tey muñal ñépp.”—1 Tesalonikk 2:7, 8; 5:14.
JARIÑOOL DALAAY AK MBOOLOO YEOWA
19. Yan barke la Yeowa wàcce ci kow ñiiy wut dalaay ci biir mbootaayam?
19 Ak lu ñu dunda dund ci nekkin yu matul, Yeowaa ngi ñuy jox ñam, yëreek làqukaay ci wàllu ngëm. Jarul ñu koy wax, dañoo wara xaar àddina su bees si ñu Yàlla dig ngir daj xéewali àjjana ci kow suuf. Wànte ñii bokk ci mbootaayub Yeowaa ngiy jariñoo tey dalaayu àjjana ci wàllu ngëm. Lu jëm ci ñoom, Esekiel yégle woon na: “Dëgg-dëgg dinañu dëkk ci dalaay, te kenn du leen loxloo.”—Esekiel 34:28; Sabuur 4:8.
20. Nan la ñu Yeowa di delloo lépp lu ñu mëna xañ suñu bopp ndax njaamoom?
20 Aka ñoo mëna gërëm Yeowa ci li mu joxe ci wàllu ngëm, ànd ceek mbëggeel, jaare ci Kàddoom ak mbootaayam! Jegeel mbooloo Yàlla. Bul téye sa bopp ci def loolu ndax ragal li say xarit walla say mbokk mëna xalaat ci yow ci li ngay jànga xam Yàlla. Am na ñu ciy mëna baña ànd ndaxte yaa ngiy ànd ak Seedey Yeowa yi tey teew ci ndaje ya ca Saalub Nguur ga. Waaye Yàlla dana def lu ëpp delloo la doŋŋ li nga xañ sa bopp ndax njaamoom. (Malaaki 3:10) Rax-ca-dolli, Yeesu nee na: “Képp ku dëddu kër, doomu ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xebaar bu baax bi, dinga am tey jii téeméeri yoon ay kër, doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ndey, doom ak suuf, ñoom ak ay fitnay noon, te ëllëg nga am dund gu dul jeex.” (Mark 10:29, 30) Waaw, loo mënta bàyyi gannaaw walla wara muñ, mën ngaa am ànd gu neex ak dalaay ci wàllu ngëm ci biir mbooloo Yàlla.
SEETLUL SA XAM-XAM
Kan mooy “jaam bu takku te teey bi, NW”?
Lan la Yeowa joxe ngir dundal ñu ci wàllu ngëm?
Ñii ci biir mbooloo karceen mi nan lañ ñu mënee dimbali?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 165]