Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Defal muy sa jëmu: jaamu Yàlla ba fàww

Defal muy sa jëmu: jaamu Yàlla ba fàww

Pàcc 18

Defal muy sa jëmu: jaamu Yàlla ba fàww

1, 2. Gannaaw ame xam-xamub Yàlla, lan lañuy laaj?

 JORTUL nga taxaw ci kanamu bunt bu ñu caabi, buy joxe cib néeg bu dénc alal yu baree bare. Xalaatal léegi nit ku ñu ko sañloo, jox la caabi ji ba noppi ne la, nga jariñoo yëf yu jafe yooyu. Caabi jooju du la amal njariñ lul nga jëfandikoo ko. Noonu itam, danga wara jëfandikoo sa xam-xam soo bëggee mu jariñ la.

2 Loolu dëgg gu wér péŋŋ la, rawatina bu dee xam-xamub Yàlla. Ca dëgg, xam-xam bu wér bu Yeowa Yàllaak Yeesu Krist, dund gu dul jeex lay yóbbe. (Yowanna 17:3) Ndaxam, ëllëg ju ni mel du mëna am ci kow ame xam-xam doŋŋ. Niki ku naroona jëfandikoo caabi ju am njariñ jooju, soxla ngaa topp xam-xamub Yàlla ci sa dund. Yeesu nee na ñii di def coobareg Yàlla ñooy “dugg ca nguur [ga].” Nit ñu ni mel doon nañu leen ji teraanga ju réy, ci jaamu Yàlla ba fàww!—Macë 7:21; 1 Yowanna 2:17.

3. Lan mooy coobareg Yàlla ngir ñun?

3 Boo jàngee liy coobareg Yàlla, sa bakkan a ngi aju ci topp ko. Lan nga foog ne mooy coobareg Yàlla ngir yow? Mënkoon nañu ko tënk ci baat yii: Royal Yeesu. Bataaxal bu njëkk ba Pieer bind a ngiy wax, cim pàcc 2:21: “Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Krist itam sonn na ngir yeen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.” Ngir def coobareg Yàlla, kon, soxla ngaa def sa kem-kàttan ngir topp royukaayu Yeesu na mu gëne. Loolu mooy ni ngay toppe xam-xamub Yàlla.

NAN LA YEESU JARIÑOO XAM-XAMUB YÀLLA

4. Lu tax Yeesu xam lu ni bare ci Yeowa, te nan la jëfandikoo xam-xam boobu?

4 Yeesu Krist, xam-xamam ci Yàlla, muy xam-xamu xaritu benn-bakkan, moo raw bu ñeneen ñépp. Dund na te liggéey naak Yeowa Yàlla ca asamaan li dale ca jamano yu yàgga yàgg laata moo ñëw ci suuf si. (Kolos 1:15, 16) Te lan la Yeesu def ak xam-xam boobu bépp? Doyluwuloon ci ame ko doŋŋ. Yeesu da ko dund. Looloo tax mu baaxoon, mënoona muñ, te àndoon ak mbëggeel noonu ci ni mu doon digaalee aki nawleem. Yeesu da doon roy, noonu, Baayam ba ca asamaan te da doon jëf lu dëppook xam-xam bi mu amoon ci yooniy Yeowa ak jikkoom.—Yowanna 8:23, 28, 29, 38; 1 Yowanna 4:8.

5. Lu tax ñu sóob Yeesu, nan la dëppe dundam ak li sóobam tekki?

5 Xam-xam bi Yeesu amoon xiir na ko itam mu jël matuwaay bu am solo lool. Jóge na Galile dem ca dexug Yurdan, fa ko Yaxya sóobe. ( Macë 3:13-15) Sóobub Yeesu, lan la doon tekki? Ndegam Yawut la woon, daa juddu woon ci xeet wu jébbalu ci Yàlla ba noppi. Noonu, Yeesu daa judduwaale woon njébbaloom. (2 Musaa 19:5, 6) Ba mu nangoo ñu sóob ko, mu nga doon teew ca kanamu Yeowa ngir def coobareg Yàlla ngir moom ca jamono jooja saxsax. (Yawut yi 10:5, 7) Te Yeesu mottali na tekkite sóobam. Def na kem-kàttanam ci liggéeyu Yeowa, di bokk ak nit ñi xam-xamu Yalla saa yu ca amoon yoon. Yeesu amoon na bànneex ciy def coobareg Yàlla, dem bay wax sax loolu daa meloon niki ñam ngir moom.—Yowanna 4:34.

6. Nan la Yeesu xàcceek boppam?

6 Yeesu xamoon na bu baax ne def coobareg Yàlla doon na ko jaral lu bare—maanaam doon na ci ñàkk sax bakkanam. Terewul, Yeesu xàccee naak boppam, baña jiital soxlay boppam. Di def coobareg Yàlla la masa jiital. Ci fànna boobu, nan lañu mënee topp royukaayu Yeesu bu mat bi?

AY JÉEGO YUY JËME CA DUND GA DUL JEEX

7. Yan ñooy yenn jéego yu nit wara def ngir jekk ci sóob?

7 Ci lu wuuteek Yeesu, dañoo matadi te mënuñoo jot jëmu bu am solo bi sóob bi nekk lul ñu def yeneen jéego yu suñu bakkan aju. Looloo ngiy tàmbaleek wuta am xam-xam bu wér ci Yeowa Yàllaak Yeesu Krist, duggal ko ci suñu biir xol. Def loolu dina ñu tegloo suñu ngëm ci Yàlla te amloo mbëggeel gu xóot ci moom. (Macë 22:37-40; Room 10:17; Yawut yi 11:6) Taq ci sàrtiy Yàlla, ay rëddi-yoonam aki yoonam warkoon na ñoo xiir ci réccu, ci wone naqar wu dëppook coobareg Yàlla ndax suñuy bàkkaari démb. Loolu dafay jëme ci tuub, maanaam woññiku te bàyyi bépp dundin bu bon bu ñu doon topp, ba ñu amuloon xam-xamub Yàlla. (Jëf ya 3:19) Jarul ñu koy wax, su ñuy dëkkangum ci bàkkaar sàngam, di nëbbu di ko def asté ñoo dox lu jub, walbatikuwuñu ca dëgg, te it naxuñu Yàlla. Yeowa dafay ràññatle bépp naaféq.—Lukk 12:2, 3.

8. Lan nga wara def boo bëggee bokk ci yëngu-yëngub waare Nguur gi?

8 Léegi bi ngay jànga xam Yàlla, ndax jaaduwul nga seete mbir yi jëm ci sa digganteek Yàlla niki lu la laal ci sa wàllu bopp saxsax? Xëy na yàkkamti ngaa wax say mbokk, say xarit ak ñeneen li ngay jàng. Ca dëgg, xëy na tàmbali ngaa def loolu, ni Yeesu doon séddale saxsax xabaar bu baax bi ak ñeneen ci anam bu mu mënta doon, bu ñu waajalul. ( Lukk 10:38, 39; Yowanna 4:6-15) Léegi mën ngaa bëgga def lu ëpp. Magi karceen yi dinañu bég ci waxtaan ak yow ngir seetlu ndax jekk nga ci te ndax am nga manooreb am wàll ci yëngu-yënguy waare Nguur gi yiy Seedey Yeowa tàmmay def. Soo ci jekkee te am manoore bi, mag ñi dinañu fàggu ngir nga ànd ak benn Seede ci liggéeyu waare bi ñu leen sas. Taalibey Yeesu topp nañu ay tegtalam ngir doxal seen sas ci fasoŋ bu jag. ( Mark 6:7, 30; Lukk 10:1) Dinga jariñoo ndimbal lu ni mel booy bokk ciy tas xabaaru Nguur gi kër-oo-kër walla ci yeneen fasoŋi waare.—Jëf ya 20:20, 21.

9. Nan la nit dee jébbalu ci Yàlla, te nan la njébbalu dee laal dundug nit ki?

9 Di waare xabaar bu baax bi xeeti nit ñu nekk ci goxub mbooloo mi, yoon la ngir dajeek nit ñi jagoo lu jub te bokk na ci jëf yu rafet yiy firndeel bu wóor ne am nga ngëm. (Jëf ya 10:34, 35; Saak 2:17, 18, 26) Tàmm di teewe ndajey karceen yi tey def sa wàll ak fitna ci liggéeyu waare bi nekk nañu itam ay yoon ngir wone ne réccu nga te walbatiku nga te léegi dogu nga ngir dund dund gu dëppook xam-xamub Yàlla. Lan ay jéego bi ci wara tegu ci yoon? Mooy nga jébbalu ci Yeowa Yàlla. Looloo ngiy tekki nga wax Yàlla, ci ñaan gu jóge ci xol, ne yaa ngi koy jébbal sa bakkan ci xol bu tàlleek bu mat sëkk ngir def coobareem. Loolooy ni ngay jébbaloo ci Yeowa te nangoo sëfu Yeesu Krist, bu lewet bi.—Macë 11:29, 30.

SÓOB BI—LI MUY TEKKI NGIR YOW

10. Lu tax ñu warkoon laa sóob gannaaw boo jébbaloo ci Yeowa?

10 Ni ko Yeesu waxe, ñépp ñiiy mujja nekk ay taalibeem war nañu leena sóob. (Macë 28:19, 20) Lu tax muy lu mënula ñàkka am gannaaw boo jébbaloo ci Yàlla? Ndegam jébbalu nga ci Yeowa, xam na ne bëgg nga ko. Waaye amul werante ne dinga bëgga jëf leneen luy may ñeneen ñu xam sa mbëggeel ci Yàlla. Kon, sóob bi dafa lay xàllal yoon wi ngir weejal sa njébbalu ci Yeowa Yàlla.—Room 10:9, 10.

11. Lan la sóob bi di tekki?

11 Sóob, li muy misaal lu bare la. Bu ñu la sóobee, walla “suulee,” ci biir ndox mi, dafa mel ni danga dee ci sa dundin bu njëkk. Boo génnee ci ndox mi, dafa mel ni yaa ngi timbee ci ndox mi ngir dund gu bees, dund gu coobareg Yàlla di ilif, du sa bos saxsax. Loolu tekkiwul ne dootoo defati bàkkaar, ndaxte ñun ñépp dañoo matadi te looloo tax ñuy bàkkaar bés bu nekk. Waaye, ndegam jaamub Yeowa bu jébbalu ci moom nga te dañu laa sóob, dina fekk nga fas wóllëreek moom, wóllëre wu wuuteek wépp weneen wóllëre. Ndax sa réccu ak li nga nangook suufeelu ñu sóob la, Yeowa dina la nangoo baal say bàkkaar ci barke peyug njotug saraxu Yeesu. Noonu sóob dafay yóbbe ci xel ak xol yu laab ca kanamug Yàlla.—1 Pieer 3:21.

12. Ñu sóob la (a) “ci turu Baay bi” ? (b) ci turu ‘Doom ji’ ? (c) ci turu ‘[x]el mu [s]ell mi’, lan lay tekki?

12 Yeesu digal na ñii ko doon topp ñu sóob taalibe yu bees yi “ci turu Baay bi ak Doom ji ak [x]el mu [s]ell mi.” (Macë 28:19.) Lan la Yeesu bëggoona wax? Sóob “ci turu Baay bi” dafay joxoñ ne nit ki ñuy sóob a ngiy nangu ci xol bu tàlli Yeowa Yàlla niki Sàkkkat bi ak kii nekk ci yoon Aji Boroomu mbindeef mépp. (Sabuur 36:9; 83:18; Dajalekat 12:1) Di ku ñuy sóob ‘ci turu Doom’ jaa ngiy tekki ne nit kaa ngiy nangu Yeesu Krist—rawatina peyug njotug Saraxam—niki menn pexe mi Yàlla taxawal kott ngir mucc. (Jëf ya 4:12) Sóob ‘ci turu [x]el mu [s]ell’ maa ngiy tekki ne, kii bëgg ñu sóob ko nangu na xelum Yeowa mu sell mi, walla dooleem jiy jëf, niki jumtukaayu Yàlla ngir amal ay Nasam tey dooleel ay jaamam ngir def Coobareem gu jub gi, ànd ak Mbootaayam bi muy jiiteek xelam.—1 Musaa 1:2; Sabuur 104:30; Yowanna 14:26; 2 Pieer 1:21.

NDAX PARE NGA NGIR ÑU SÓOB LA?

13, 14. Lu tax waruñoo ragala tànna jaamu Yeowa Yàlla?

13 Ndegam sóob bi lu ni mel la tekki te mooy jéego bi ëpp solo ci dundug nit, ndax war naa nekk jéego boo warkoona ragal? Mukk ci àddina! Ba ñu warula dogal ak teeyloodi ñu sóob ñu, pas-pas boobu, ci lu amul werante, mooy bi ëpp sago boo mënkoona def.

14 Sóob mooy firndeel bu wóor sa tànneefu jaamu Yeowa Yàlla. Seetal ci nit ñi nga xamanteel. Muy nii walla neneen, ndax ku nekk ci ñoom amul njaatige bu muy liggéeyal? Am na ñuy liggéey ni ay jaam ngir dajale alal. ( Macë 6:24) Ñeneen ñi, ak cawarte, seen liggéey walla seen bopp doŋŋ lañu nekkal, ciy def mottalib seeni bëgg-bëgg li ñu gëna itteel ci seen dund. Ñeneen itam a ngiy jaamu ay yàllay fen. Waaye Yàlla dëgg ji, Yeowa nga tànna jaamu. Amul keneen kuy wone mbaaxaay, laabiir ak mbëggeel yu ni mel. Yàllaa ngiy terale doomiy Aadama yi liggéey bu am tekkite bu leen di joxoñ mucc gi. Mu ngiy yool ay jaamam ak dund gu dul jeex. Ci lu wóor, di topp royukaayu Yeesu te dénk sa bakkan Yeowa nekkul dundin boo wara ragal. Dëgg-dëgg mooy benn bi kott bi neex Yàlla te ànd ak sago su mat.—1 Buur 18:21.

15. Yan ñooy yenn ci gàllankoor yi farala tere sóob bi?

15 Ndaxam, sóob bi nekkul jéego booy def ndax dañu la ci jañ. Sa diggante la, yow doŋŋ ak Yeowa. (Galasi 6:4) Ndegam jëm nga kanam ci sa digganteek Yàlla, xëy na jot ngaa laaj: “Ana lu tere, [ñu] sóob ma?” (Jëf ya 8:35, 36) Mënkoon ngaa laaj sa xel: ‛Ndax xatal bu jóge ci njaboot gee ma téye? Ndax dama bokk ba léegi ci lu dëppoowul ak Mbind yi walla ci jëfu bàkkaar? Ndax mënkoon naa nekk li ma ragala ñàkk teraanga ji ma am ci samay diggu nawle?’ Nekk na yenn ci mbir yi nga wara bàyyi xel, waaye xalaatal li mu lay dikke, ci ni yëf yi ame ci dëgg.

16. Nan ngay jariñoo sa njaamug Yeowa?

16 Nekkul wone sago, su dëppook li am ca dëgg, bu ñu xalaatee jafe-jafe yi doŋŋ, baña seet njariñ yi nekk ci jaamu Yeowa. Maanaam, seetal lu jëm ci xatal bu jóge ci njaboot gi. Yeesu dig na ne su fekkee sax ay taalibeem ñàkk nañu seeni mbokk ndax dañu koy topp, doon nañu gañe njabootu diine gu gëna yaatu. (Mark 10:29, 30) Nawle ci ngëm yooyu dinañu la won mbëggeelu mbokk dëgg, dinañu la dimbali nga muñ toŋal, te dinañu la taxawu ci yoonu dund gi. (1 Pieer 5:9) Mag ñi ci mbooloo mi saxsax ñoo lay dimbali nga sàkkal pexe jafe-jafe yi te jéggi yeneen tëkk. (Saak 5:14-16) Lu jëm ci ñàkk teraanga ji nga am ci àddina sii, mën ngaa laaj sa xel: ‛Lan laa mëna yemaleek yiwu Kii sàkk mbindeef mépp, di fexe mu bég ci dundin bi ma tànn?’—Léebu 27:11.

DI DËPP SA DUND AK SA NJÉBBALU AK SA SÓOB

17. Lu tax nga warkoona gise sóob bi niki ndoorte asté ag muj ?

17 Lu am solo la fàttaliku ne sóob bi du njeexte sa jëm-kanam ci wàllu ngëm. Li muy rëdd mooy ndoortel liggéeyal Yàlla sa giiru-dund nikib surga gu ñu dénk sas, niki it benn ci Seedey Yeowa yi. Ak lu sóob bi ama am solo su suñu bakkan aju, du firnde ju wóor juy tax ñu mucc. Yeesu waxul ne: ‛Képp ku ñu sóob dinga mucc.’ Xanaa kay, daa ne: “Ku muñ ba ca muj ga, mucc.” ( Macë 24:13) Looloo tax sa bakkan a ngi aju ci njëkka wut Nguurug Yàlla ciy def loolu mu nekk li nga gëna itteel ci sa dund.—Macë 6:25-34.

18. Gannaaw bu ñu la sóobee, yan ñooy yenn jubluwaay yoo mëna teg ci sa kanam?

18 Ngir muñ ci surgawu Yeowa, dinga bëgga teg sa kanam ay jubluwaay ci wàllu ngëm. Ab jubluwaay bu jara toppatoo mooy yokk sa xam-xamub Yàlla jaare ci di faral di jàngal sa bopp Kàddoom. Fogorul ngir di jàng Biibël bi bés bu nekk. (Sabuur 1:1, 2) Deel faral di teew ci ndaje yi, ndax àndandoo ya nga fay fekk dinañ la dimbali nga jot doole ci wàllu ngëm. Lu jëm ci sa wàll, lu tax doo def sa jubluwaay, ngay xamle sa xalaat ca ndajey mbooloo mi tey tagg noonu Yeowa aka wuta xiir ñeneen ci lu baax? (Room 1:11, 12) Beneen jubluwaay mënkoon naa nekk taneel fasoŋ bi ngay ñaane.—Lukk 11:2-4.

19. Yan jikko la la xel mu sell mi mëna dimbalee wone?

19 Soo bëggee dëpp sa dund ak tekkite sa sóob, soxla ngaa bàyyi xel foo tollu ci li ngay def, di may xelum Yàlla mu sell mi mu jur jikko yu rafet ni mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaaxaay, ngëm, lewetaay ak téye sa bopp. (Galasi 5:22, 23; 2 Pieer 3:11) Fàttalikul ne Yeowa, xelam mu sell, ñépp ñiiy ñaan ngir am ko te di ko déggal nikiy jaamam yu takku la koy may. ( Lukk 11:13; Jëf ya 5:32) Kon ñaanal Yàlla ngir xelam te laaj ko ndimbal ngir ngay feeñal jikko yu rafet yi ko neex. Jikko yu ni mel dinañu mujja gëna fés ci say waxin ak sa demin, fi ak yaa ngiy bàyyi xelum Yàlla ruux la. Jarul ñu koy wax, ku nekk ci mbooloo karceen maa ngiy jéema suqali “jikko ju bees ji” ba tax mu mujja gëna nirook Krist. ( Kolos 3:9-14) Ku nekk ci ñun a ngi jànkoonteek tëkk yu wuute ci def loolu ndaxte bokkuñu fi ñu yem ci suñu jëm-kanam ci wàllu ngëm. Ndegam danga matadi, war ngaa góor-góorlu bu baax-a-baax ngir am jikko ju mel ni ju Krist. Waaye bul yoqi mukk ci fànna boobu, ndax lu mëna am la ak ndimbalul Yàlla.

20. Ci yan fasoŋ nga mënee roy Yeesu ci liggéey bi ñu sas Karceen yi?

20 Ci biir say jubluwaay ci wàllu ngëm, warkoon ngaa sóoraale jubluwaay bi lay toppandooloo bu baax-a-baax royukaayu Yeesu, bu bég bi. ( Yawut yi 12:1-3) Fonkoon na liggéey ba ñu ko sasoon. Kon, su ñu la jiwee teraanga bokk ci yëngu-yëngub waare Nguur gi, bul bàyyi mu mujja nekk tàmmeel bu sa xol nekkatul. Wutala daj bànneex ciy jàngal ñeneen lu jëm ci Nguurug Yàlla ni ko Yeesu doon defe. Toppal tegtal yi la mbooloo mi di jox ngir dimbali la nga taneel sa njàngale. Te na la wóor ne Yeowa mën na laa jox doole mottali liggéey bi mu la sas.—1 Korent 9:19-23.

21. (a) Nan lañu xame ne Yeowa fonk na lool ñii ñu sóob te ñuy ñu takku ci moom? (b) Lan mooy wone ne sóob bi lu am solo la ngir ñu mucc, bu Yàlla dee mottali àtteem ci kow jamano ju soxor jii ?

21 Nit ku jébbalu te ñu sóob ko te dogu ci góor-góorloo topp Yeesu, ku jafe la ci kanamug Yàlla. Yeowaa ngiy seppali junniy tamndaareeti xoli doomi Aadama yi te xam na naka la nit ñu ni mel jafee. Mu ngi leen di jàppe ni alal yu réy, ay “yëf yu mata bëgg.” ( Xaggaay 2:7) Yégley yonent ci Biibël baa ngiy wone ne Yàllaa ngiy gise nit ñu ni mel niki ñu ñu màndargaal ngir ñu mucc buy mottali àtteem, bu ca kanamee tuuti, ci kow jamano ju soxor ji. (Esekiel 9:1-6; Malaaki 3:16, 18) Ndax “jagoo [nga] dund gu dul jeex”? (Jëf ya 13:48) Ndax bëgg nga ñu màndargaal la niki kuy jaamu Yàlla? Njébbalu ak sóob bi bokk nañu ci màndarga moomu, te am nañu solo lool ngir mucc gi.

22. Yan yaakaar la “mbooloo mu réy” mi mëna séenu?

22 Gannaaw ba Mbënnum Tuufaan jeexee, Nóoxin ak njabootam génn nañu ca gaal ga, wàcc ci suuf su ñu setal. Noonu it tey, “am mbooloo mu réy” muy topp xam-xamub Yàlla ci seen dund tey jot nangub Yeowaa ngiy yaakaara mucc ci mujug jamano ju soxor ji, tey bànneexoo dund gu dul jeex ci kow suuf su ñu setal ba abadan. (Peeñu bi 7:9, 14) Nan la dund googu di mel?

SEETLUL SA XAM-XAM

Nan la Yeowa bëgge nga jëfandikoo sa xam-xam ci moom?

Yan ñooy yenn jéego yiy jëme ci sóob bi?

Lu tax sóob nekkul ag muj waaye ndoorte?

Nan lañu mënee dëpp suñu dund ak suñu njébbalu ak suñu sóob?

[Laaj yi]

[Nataal bi nekk paas 172]

Ndax jébbalu nga ci Yàlla cig ñaan?

[Nataal bi nekk paas 174]

Lu tere ñu sóob la cim ndox?