Di tabax njaboot guy sargal Yàlla
Pàcc 15
Di tabax njaboot guy sargal Yàlla
1-3. Lu tax ñenn ñi mënuñoo saafara jafe-jafe yi farala am ci séy ak ci taxawaayub way-jur, waaye lu tax Biibël bi mëna doon ndimbal?
JORTUL nga mébéta tabax sa kërug bopp. Njëkk ngaa jënd ab pàkk. Ndax yàkkamti, yaa ngiy gis xaat ci xel sa kër gu bees taxaw ba noppi. Waaye lan mooy xew soo amul benn jumtukaay ak manoore ci wàllu tabax? Say njéem, aka ñooy yóbbe ci yaakaar ju tas!
2 Ñu bare dañuy dugg ci séy di ci séentu njaboot gu am bànneex, ndaxam amuñu, muy jumtukaay yi walla manoore yi ñu soxla ngir tabax njaboot gu ni mel. Lu yàggul dara, gannaaw bésub céyt gi, dañuy suqali ay demin yu rafetul. Bés bu nekk xeex ak xuloo dañuy mujja nekk yoonuw tool. Bu ay doom juddoo, ñii soga nekk baay ak ndey dañuy gisal seen bopp ne amuñu manoore ngir doxal seen wareefu way-jur niki amuñu ko ngir doxal seen séy.
3 Waaye, ndax Yàlla, Biibël bi mën naa joxe ndimbal. Ay rëddi-yoonam a ngi mel ni ay jumtukaay yuy tax nga mëna tabax njaboot gu am bànneex. (Léebu 24:3) Nañu gis naka.
AY JUMTUKAAY NGIR TABAX SÉY GU ÀND AK BÀNNEEX
4. Lu tax ñu wara séentu ay jafe-jafe ci biir séy, te yan yoon lañu joxe ci Biibël bi?
4 Ak lu ñaar ñi séy niroo niru ñu ànd, wuute nañu ci ni ñu bindoo ci wàllu yëg-yëg, fi ñu jaar ci seen ndaw, ak li ñu daj ci njaboot gi ñu bawoo. Kon, war nañoo xaaru ay jafe-jafe am gannaaw seen séy. Nan lañu leen waree toppatoo? Seetal, bu ay tabaxkat dee tabax kër, dañuy seet ay palaŋ. Palaŋ yooyu, ay tegtal lañu, yu ñu wara topp. Biibël bi dafa ñuy jox yooniy Yàlla ngir tabax njaboot gu am bànneex. Nañu seppali léegi yenn ci ñoom..
5. Nan la Biibël biy jolliloo solos ngor ci biir séy?
5 Ngor. Yeesu nee na: “Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.” * (Macë 19:6) Ndaw li Pool bind na: “Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi baña taq sobe, ndaxte Yàlla dina àtte ñu yàqu ñi ak njaalookat yi.” ( Yawut yi 13:4) Nit ñi séy kon, war nañoo yëg ne, aw warugar la ci kanamu Yeowa, sax ci takku ci ki ñu séyal.—1 Musaa 39:7-9.
6. Nan la ngor dee dimbali sàmm séy?
6 Ngor dafay jagleel séy fullaak dalaay. Ñaar ñu séy ñu gore xam nañu ne, lu mënta xew, dinañu dimbaleente. (Dajalekat 4:9-12) Aka ñoo wuuteek ñiiy wacc seen séy ci jafe-jafe bu ñàkk solo, bi ñuy njëkka daj! Gaa ñu ni mel dañuy gawa tofal ne dañoo ‘tànn nit ku baaxul ki,’ seen ‘nobeel daa fey,’ jeneen jabar walla jeneen jëkkër mooy garab gi. Waaye tofal boobu du may ki séy mu màgg ci wàllu ñoraay. Asté loolu, nit ñu goreedi ñu ni mel mën nañoo toxal jafe-jafe yooyu saxsax ci keneen ku ñuy séyal. Bu nit amee kër gu rafet te gis ne jank baa ngiy senn, ci lu wóor, dina ko jéema jagal. Du toxu ci geneen kër. Noonu it, di wacc ki nga séyal wutiji keneen du yoon wiy saafara li sabab téesante bi ci biir séy. Bu ay jafe-jafe jollee, bul jéema génn ci séy bi, waaye xaral sa tànki tubéy ngir sàmm ko. Ngor gu ni mel dafay jàppe séy niki lu mata sàmm, lu mata téye te lu mata fonk.
7. Lu tax diisoo farala jafe ngir ñii séy, waaye nan la soloo “ji[k]ko ju bees ji” mënee nekk ndimbal?
7 Disoo. “Palaŋ yi, yaakaar ju tas lañuy yóbbe, fu waxtaan ak ndéey amul,” la ab léebu ci Biibël biy wax. ( Léebu 15:22) Ndaxam, diisoo lu jafe la ngir ñenn nit ñu séy. Lu tax loolu am? Ndaxte nit ñi dañoo am fasoŋi diisoo yu wuute. Loolu mbir la muy faral di jëme ci ñàkka déggoo bu réy ak yaakaar ju tas. Ni ñu yare nit ki mën naa sabab loolu. Maanaam, mën naa am ñu yar ñenn ñi ci biir kër fu way-jur yi daan xuloo saa su nekk. Léegi, bi ñu nekkee mag te séy, mën nañoo baña xam nan lañuy waxeek ki ñu séyal ci fasoŋ bu lewet te ànd ak mbëggeel. Wànte, sa kër soxlawula tas, nekk ‘ag kër gu fees ak xuloo.’ (Léebu 17:1) Biibël baa ngiy jolliloo soloo “jik[k]o ju bees ji,” te du wéyale weexaay bu soxor, coow, ak saaga.—Efes 4:22-24, 31.
8. Lan moo la mëna dimbali boo dàkkoorul ak kii nga séyal?
8 Lan nga mëna def bu ñàkk déggoo amee? Su yow ak ki nga séyal, tàmbalee topp seen jikko, mën ngaa def lu baax ciy topp xelalu Léebu 17:14: “Balaa xuloo takk, tàggul.” Waaw, war ngaa fomm waxtaan wi ba seen mer, yeen ñaar, yow ak ki nga séyal, mujja giif. (Dajalekat 3:1, 7) Ak lu mënta xew, fexeela nekk ku “farlu ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.” (Saak 1:19) Sa jëmu warkoon naa nekk saafara li xew te baña nekk kii mujje ci wax ji. (1 Musaa 13:8, 9) Deel tànn ay kàddu ak waxin yu leen di giifal, yow ak ki nga séyal. (Léebu 12:18; 15:1, 4; 29:11) Ci kow lépp, bul des ci sa mer, waaye wutleen ndimbal ciy diisook Yàlla ciy ñaanandoo ko ak suufeelu.—Efes 4:26, 27; 6:18.
9. Lu tax ñu mëna wax ne diisoo ci biir xol lay tàmbalee?
9 Ab léebu ci Biibël bi nee na: “Xolu kii am sago day tax gémmiñam wone ñoraay te ciy tuñam day yokk wax juy gulami.” ( Léebu 16:23) Dëgg-dëgg, kon, caabiy diisoo bu rafet a ngi ci biir xol, nekkul ci biir gémmiñ. Man xel nga soloo lu jëm ci ki nga séyal? Biibël bi dafay xiirtal karceen yi ñuy “bokk [...] i tiis.” (1 Pieer 3:8) Ndax mën ngaa def loolu bu ki nga séyal di daj njàqare ju tar? Su dee waaw, loolu dina la dimbali nga xam ni ñuy tontoo.—Isayi 50:4.
10, 11. Nan la jëkkër mënee jëfoo xelal bi ci 1 Pieer 3:7?
10 Teraangaak weg. Wax nañu jëkkër yi nekk karceen ñu dëkk ak seeni jabar, “ku nekk ci [ñoom] am xel, ci ni [ñuy] ànde ak [seeni] jabar, xam ne [ndab lu leen gëna] néew doole la[ñu].” (1 Pieer 3:7) Di won teraanga jabar a ngiy ëmb di fàttaliku njari̇̀ñam. Jëkkër juy dëkk ak jabaram, “am xel ci ni [muy] ànde ak [moom],” dafay am aajo ju réy ci ay yëg-yëgam, ciy mën-mënam, ci am xelam, ak ci teraangaam. Warkoon na it bëgga jàng nan la Yeowa di gise jigéen ñi te ni mu bëgge ñu digaaleek ñoom.
11 Mu ngi mel ni nga am ci sa biir kër, ndab lu am njariñ lool te rawatina gawa toj. Ndax doo koy toppatoo bu baax? Pieer jëfandikoo na baat “[ndab lu] gëna néew doole” noonu itam, te loolu warkoon naa xiir jëkkër ju nekk karceen muy won jabaram ji mu sopp worma ju lewet.
12. Nan la jabar mënee wone ne daa weg bu baax-a-baax jëkkëram?
12 Waaye ban xelal la Biibël biy jox jabar? Pool bind na: “Jabar war naa weg bu baax-a-baax jëkkëram.” (Efes 5:33, NW) Ni ab jabar soxlaa yëg ne ki mu séyal teral na ko te sopp na ko ci xolam, jëkkër soxla naa yëg ne jabaram weg na ko. Jabar ju weg jëkkëram warul di weejal ndax ñàkk xel njuumtey jëkkëram, muy ab karceen walla déet. Du ko xañ teraangaam ci li mu koy ŋàññ te di ko suufeel, bu ñu wéetee walla ci biir mbooloo.—1 Timote 3:11; 5:13.
13. Nan lañu mënee wax ci jàmm liy gis-gis?
13 Loolu tekkiwul ne jabar mënula wax liy gis-gisam. Su ko lenn jaaxalee, mën na cee waxtaaneek tegin. (1 Musaa 21:9-12) Xamal jëkkër aw xalaat mënkoon nañu koo tollaleek di ko sànni kuppe. Mën na koo sànni ndànk ba tax mu mën koo jàpp ci lu yomb, walla mën na koo sànneek doole ju ni mel, ba tax mu gaañ ko. Aka gën fuuf bu ñaar ñi séy bokkee di moytoo téesante, waaye asté loolu, ñuy waxtaan ànd ceek mbaax ak lewet!—Macë 7:12; Kolos 4:6; 1 Pieer 3:3, 4.
14. Lan nga warkoona def su fekkee ne ki nga séyal waxul lu bare ci jëfoo rëddi-yooni Biibël bi ci séy?
14 Ni ñu ko gise, rëddi-yooni Biibël bi mën na laa dimbali nga tabax séy bu làmboo bànneex. Waaye looy def nag su fekkee ne ki nga séyal waxul lu bare ci li Biibël biy wax? Mën ngaa def lu bare, sooy topp xam-xamub Yàlla ci sa taxawaay. Pieer bind na: “Yeen itam jigéen ñi, na ku nekk nangul sa jëkkër. Noonu su amee góor, gu gëmul Kàddug Yàlla gi, te gis jabaram di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu àndul ak wax.” (1 Pieer 3:1, 2) Jarul ñu koy wax, loolu it war na jëkkër ju jabaram faalewul Biibël bi. Ak lu ki nga séyal mënta tànna def, na la rëddi-yooni Biibël bi nekkloo jëkkër walla jabar ju gën. Xam-xamub Yàlla mën na la nekkloo it aji-jur ju gën.
DI YAR XALE YI CI LU DËPPOOK XAM-XAMUB YÀLLA
15. Nan la njuumtey way-jur yi ci wàllu yarin dee toxu, waaye nan lañu mënee soppi yarin boobu?
15 Yore ag reefan walla ab wàkku taxul nit nekk minise bu xereñ. Noonu it, am ay doom doŋŋ taxula nekk aji-jur ju am manoore. Ñu xam ko walla déet, way-jur yi dañuy farala yar seeni doom naka yarin bi ñu leen yare woon, ñoom ci seen bopp. Noonu, njuumte way-jur yi ci wàllu yarin, léeg-léeg dañu leen di toxale maas dem ga ca topp. Ab léebu Yawut bu yàgg nee na: “Baay yi ñooy ñii lekk reseñ yu ñorul, waaye gëñi doom yee mujja wuum.” Ndaxam, Mbind yaa ngiy wone ne nit mën naa baña topp dundin bu ay way-juram taxawal. Mën naa tànna weneen yoon, aw yoon wu sàrtiy Yàlla sabab.—Esekiel 18:2, 14, 17.
16. Lu tax toppatoo sa njaboot am solo, te lan la loolu ëmb?
16 Yeowa dafay xaaru way-jur yi nekk ay karceen jox seeni doom tette ak toppatoo yi war. Pool bind na: “Ci dëgg, su kenn nit toppatoowul ñii nekk ay ñoñam, te rawatina ñiiy waa këram, weddi na ngëm te moo yées nit ku amul ngëm.” (1 Timote 5:8, NW ) Akay kàddu yu am doole! Di mottali seen taxawaay niki way-toppatoo, lu ëmb di faj soxlay yaram, soxla ci wàllu ngëm ak cofeel seeni doom, teraangaak warugaru nit ku taq ci Yàlla la. Biibël baa ngiy joxe rëddi-yoon yuy dimbali way-jur yi ñu tabax nekkin bu ànd ak bànneex ngir seeni doom. Nañu seet yenn ci ñoom.
17. Fàww lan am, su sàrtiy Yàlla waree nekk ciy xoli doom?
17 Nekkleen ab royukaay bu rafet. Dañu digaloon way-juri Israel: “War ngaa rëdd kàdduy Yàlla ci sa xelu doom te waxtaane leen boo toogee ci sa kër te booy dox ci mbedd mi te booy tëdd te booy jóg.” Way-jur ya waroon nañoo jàngal yooniy Yàlla seeni doom. Waaye, santaane boobu, kàddu gilee ko jiitu woon: “Kàddu yii ma lay digal tey, war nañoo nekk ci dëgg ci sa xol.” (5 Musaa 6:6, 7) Waaw, way-jur yi mënuñoo joxe li ñu amul. Sàrtiy Yàlla war nañoo njëkka bindu ci seen xol saxsax, su ngeen bëggee ñu bindu ci seen xoli doom.—Léebu 20:7; dendale kook Lukk 6:40.
18. Ci wàlluw wone mbëggeel, nan la Yeowa joxe ab royukaay bu rafet-a-rafet way-jur yi?
18 Fexeleena fésloo seen mbëggeel ngir ñoom. Ba ñu sóobee Yeesu, Yeowa nee na: “Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.” (Lukk 3:22) Noonu, Yeowaa ngi ko doon nangu, di ko wone ci wax tey joxe firnde ju wóor ju Mbëggeelam. Yeesu, ca gannaaw ga, wax na Baayam: “Bëgg nga ma laata àddina di sosu.” ( Yowanna 17:24) Kon niki ay way-jur yu taq ci Yeowa, wonleen seeni doom, ci ay wax aki jëf, seen mbëggeel ngir ñoom—te deeleen ko farala def. Saa su nekk, deeleen fàttaliku ne “mbëggeel day feddali.”—1 Korent 8:1, NW.
19, 20. Yar xale dëgg lan la ëmb, te nan la way-jur yi mënee jariñoo royukaayub Yeowa?
19 Yar. Biibël baa ngiy jolliloo solo si nekk cib yar bu làmboo mbëggeel. (Léebu 1:8) Way-jur yiy daw seen wareefu tette seeni doom tey, ci lu wóor dinañu jànkoonte ëllëg ak li loolu yóbbe, luy dog seen xol. Ndaxam, artu nañu it way-jur yi ñu moytoo ëppal ci wàllu yar. Pool bind na: “Baay yi, buleen bundaxataal seeni doom, ngir baña jeexal seen xol.” (Kolos 3:21) Way-jur yi war nañoo moytu di jubbanti seeni doom ak coxorte walla di sulli seeni njuumte saa su nekk aka xeeb seeni njéem.
20 Yeowa Yàlla, suñu Baay ba ca asamaan, ab royukaay ci wàllu yar la. Yaram du ëpp mukk. “Fàww ma duma la ci lu yem,” la Yàlla wax mbooloom. ( Yérémi 46:28) Way-jur yi warkoon nañuy roy Yeowa ci fànna boobu. Yar buy jéggi fi mu wara yem walla buy weesu nasub li ñuy séentu ci jubbanti ak jàngale, ci lu wóor dinay merloo.
21. Nan la way-jur yi mënee ràññee ndax seen yar dox na?
21 Nan la way-jur yiy xame ndax seen yarin dox na? War nañoo laaj seen xel: ‘Lan la sama yar di àggali?’ Warkoon nay jàngale. Seen doom warkoon nay nànd li tax ñu di ko yar. Way-jur yi warkoon nañu it di bàyyi xel ci li seen yar di yóbbe. Dëgg la, daanaka xale yi yépp, ci ndoorte li, dinañu mer ndax yar bi. ( Yawut yi 12:11) Waaye, yar warula tax mukk xale yëg tiitaange walla foog ne dañu ko bërgël walla mu foogloo ko ne daa judduwaale mbon. Balaa moo jubbanti mbooloom, Yeowa daa ne: “Bul tiit, (...) ndaxte maa ngeek yow.” ( Yérémi 46:28) Waaw, njubbanti warkoon nañu koo def ci yoon wuy tax seen doom yëg ne yeena ngeek moom, niki ay way-jur yu am mbëggeel, yu koy taxawu.
NI ÑUY JOTE CA “MANOOREB JIITE”
22, 23. Nan nga mënee jot ca manooreb jiite bi war ngir tabax njaboot gu am bànneex?
22 Mën nañoo gërëm Yeowa ci li mu joxe jumtukaay yi ñu soxla ngir tabax ag njaboot gu am bànneex. Waaye ame doŋŋ jumtukaay yi doyul. War nañoo jublu ci di leen jëfandikoo ni mu ware. Nañu jël am misaal: Ab tabaxkat mën naa yar tàmmeel yu bon ci ni muy jëfandikoo ay jumtukaayam. Mën naa jëfandikoo bu bon yenn ci ñoom. Ci anam yooyu, fasoŋ bi muy liggéeye dina yóbbe ci lu wóor liggéey bu fooyooy. Noonu it, xëy na yeewu ngeen léegi ci tàmmeel yu bon yi law ci seen biir njaboot. Yenn tàmmeel mën nañoo sax reen ak doole te jafee soppi. Waaye, toppleen xelalu Biibël bi: “Nit ku am sago dina déglu te gëna sàkku xam-xam, te góor gu am dégg mooy kiiy jot ca manooreb jiite.”—Léebu 1:5.
23 Mën ngaa jot ci manooreb jiite booy wéy di sàkku xam-xamub Yàlla. Nanga yeewu ci rëddi-yooni Biibël yi jëm ci dundug njaboot, te defal jubbanti yi war. Seetlul karceen ñu ñor ñi nekk ab royukaay bu rafet ci seen biir séy, ak it niki way-jur. Waxtaanal ak ñoom. Ci kow lépp, diisal say aajo Yeowa cig ñaan. (Sabuur 55:22; Filipp 4:6, 7) Mën na laa dimbali nga xéewlu ci dundug njaboot gu am bànneex, gu koy sargal.
[Li ñu bind ci suuf]
^ Ci Mbind yi lenn doŋŋ li mëna tax pase may nit mu séyaat mooy “moy”—tëdd ak nit ci bitib séy.—Macë 19:9.
SEETLUL SA XAM-XAM
Nan la ngor, diisoo, teraanga ak weg dee dimbali séy am bànneex?
Ci yan fasoŋ la way-jur yi mënee fésloo seen mbëggeel ngir seeni doom?
Yan mbir la yar dëgg ëmb?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 147]