Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Gan kiliftéef nga warkoona nangul?

Gan kiliftéef nga warkoona nangul?

Pàcc 14

Gan kiliftéef nga warkoona nangul?

1, 2. Ndax fasoŋi kiliftéef yépp ay lor? Faramfàcceel.

 “KILIFTÉEF” nekk na ab baat bu neexul ñu bare. Lu ñu mëna dégg la, ndax ñii ame kiliftéef dañu faral di noggatu—ca béréb ba ñuy liggéeye, ci biir njaboot gi, nguur yi it dañuy noggatu. Biibël bi nee na, ci lu am: “Nit daa ilif nit ngir lorangeem.” (Dajalekat 8:9) Waaw, ñu bare dañoo ilif ñeneen, soroxe leen te wut seen njariñu bopp doŋŋ.

2 Wànte, du gépp kiliftéef a di lor. Ngir misaal loolu, mënkoon nañoo wax ne suñu yaram am na ag kiliftéef suñu kow. Dafa ñuy “digal” ñu noyyi, lekk, naan te nelaw. Ndax loolu dafa ñuy gétën? Déedéet. Nangoo topp loolu muy laaj, suñu njariñ la. Ba déggal suñuy soxlay yaram mëna baña nekk lu aju ci suñu coobare, am na yeneen fasoŋi kiliftéef yuy laaj suñu ndéggal ak xol bu tàlli. Nañu seet yenn misaal.

KILIFA GI GËNA KOWE

3. Lu tax muy lu jub ñu tudde Yeowa “Aji Kilifa ji”?

3 Tudde nañu Yeowa “Aji Kilifa ji” lu ëpp ñetti téeméeri (300) yoon ci Biibël bi. Njiital réew mooy kii ame kiliftéef gi gëna kowe. Lan moo jox Yeowa sañ-sañu am taxawaay boobu? Peeñu bi 4:11 a ngiy tontu: “Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan, ndaxte yaa sàkk lépp te ci sa coobare la lépp nekke, te ci lañu leen sàkke.”

4. Nan la Yeowa tànnee doxal kiliftéefam?

4 Niki suñu Sàkkkat, Yeowa sañ na doxal kilitéefam ni mu koy tànne. Loolu mënkoon naa mel ni lu raglu, rawatina bu ñu seetee ne Yàlla daa am “sakkanaayu doole juy jëf, ju ñàng.” Dañu ko tudde “Yàlla Aji Kàttan ji”—ab baat buy junj ci làkku ebrë xalaatu doole ju jéggi dayo. (Isayi 40:26; 1 Musaa 17:1) Ndaxam, Yeowa dafay wone dooleem ci fasoŋ bu laabiir, ndax jikkoom ji gëna jolli mooy mbëggeel.—1 Yowanna 4:16.

5. Lu tax jafewul ñu nangul kiliftéefug Yeowa?

5 Ak lu Yeowa artoo artu ne dina indi nduma ci kow defktati lu bon yi ko dul réccu, Musaa ngi ko xame woon saxsax niki “Yàlla dëgg ji, Yàlla ju takku ji, jiy sàmm kóllëreek mbaaxaayu xol ngir ñii ko bëgg ak ñiiy sàmm ay ndigalam.” (5 Musaa 7:9) Jortul tuuti rekk! Aji Kilifag mbindeef mépp, du ñu ga ci ñu jaamu ko. Te du mbëggalam a ñuy xëcc ci moom? (Room 2:4; 5:8) Nangul kiliftéefug Yeowa, lu neex sax la, ndax ay sàrtam, saa su nekk, ñun lañuy mujja jariñ.—Sabuur 19:7, 8.

6. Nan la werante ci wàllu kiliftéef sosoo ca toolu Eden, te lan la loolee yóbbe?

6 Suñuy maam ñu njëkk ña dañoo wonoon gannaaw kiliftéefu Yàlla. Dañoo bëggoon dogalal seen bopp lu baax ak lu bon. (1 Musaa 3:4-6) Li loolu jur mooy, dàqe woon nañu leen seen kërug Àjjana. Gannaaw loolu, Yeowa bàyyi na doomi Aadama yi sàkk ay ndefarini kiliftéef yu leen di taxa mëna dund dund gu jag, bu fekkee sax mbootaayu nit matul. Yan ñooy yenn ci kilitéef yooyu, te ba fan la Yàlla di xaaru ñu déggal leen?

“KILIFA YU KOWE YI”

7. Ñan ñooy “kilifa yu kowe yi,” te nan la seen taxawaay lëkkaleek kiliftéefug Yàlla?

7 Ndaw li Pool bind na: “Na bépp bakkan déggal kilifa yu kowe yi, ndaxte amul genn kilifa gannaaw mu soob Yàlla, NW.” Ñan ñooy “kilifa yu kowe yi”? Li Pool wax ci aaya yi topp dafay wone ne ñooy kilifay nguuriy doomiy Aadama. (Room 13:1-7, NW; Titt 3:1) Yeowa sosul kilifay nguurug nit, waaye dañu fi nekk ndax li mu leen fi bàyyi. Looloo tax Pool mënoon naa bind: “Kilifa yi fi taxaw, Yàllaa leen teg ci seeni taxawaay yu ñu leen mëna xañ.” Lan la looluy wone lu jëm ci kiliftéef ci kow suuf gu ni mel? Dafa féete suuf kiliftéefug Yàlla. ( Yowanna 19:10, 11) Looloo tax, bu sàrtub nit safaanook sàrtub Yàlla, karceen yi war nañoo bàyyi seen xol ak seen xel yi Biibël bi jéemantal ñu tette leen. Ngir ñoom, “déggal Yàlla moo gën déggal nit.”—Jëf ya 5:29.

8. Nan ngay jariñoo kilifa yu kowe yi, te nan nga mënee wone sa ndéggal ci ñoom?

8 Waaye li farala am mooy kilifay nguur yu kowe yi dañuy jëf niki ‘surgay Yàlla ngir li baax ci ñun.’ (Room 13:4, NW ) Ci yan fasoŋ? Xalaatal taxawu yu bare yiy jóge ci kilifa yu kowe yi, niki post bi, polis beek pompiye yi, njumtukaay yi jëm ci wér-gi-yaram ak njàngale mi. “Looloo tax ngeen di fey galag,” la Pool bind, “ndaxte ay surgay Yàlla lañu ngir mbooloo mi, di liggéeyal saa su nekk nas boobule saxsax.” (Room 13:6, NW) Lu jëm ci galag yi walla wépp weneen wareef wu yoon laajte, warkoon nañoo “am demin bu làmboo ngor.”—Yawut yi 13:18, NW.

9, 10. (a) Nan la kilifa yu kowe yi àndeek ndefarinu Yàlla? (b) Lu tax di tiiñ kilifa yu kowe yi doon nekk lu bon?

9 Léeg-léeg, kilifa yu kowe yi duñu jëfandikoo ci lu baax seen kàttan. Ndax loolu génne na ñu ci suñu wareefu sax ci déggal leen? Déedéet, génnewu ñu ci. Yeowaa ngiy gis jëf yu ñaaw yi kilifa yooyuy def. (Léebu 15:3) Li Yàlla bàyyi nguurug nit am tekkiwul ne dafa umple yàquteem; te xaaruwul itam ñu def loolu. Ci dëgg, léegi, Yàlla “moxoñ te jeexal nguur yii yépp,” wuutu leen ak kiliftéefu nguurug boppam, gu jub gi. (Dañel 2:44) Waaye, ba loolay am, kilifa yu kowe yaa ngiy liggéeyal ab nas bu am njariñ.

10 Pool faramfàcce na: “Kon ku baña déggal kilifa, jógal na ndefarinu Yàlla.” (Room 13:2, NW) Kilifa yu kowe yi, “ndefarinu” Yàlla lañu ci li ñuy sàmm dalaay, ak nu mu mënta tollu; bu ñu fi nekkuloon, jaxaseek lu-neex-waay-mu-def a fi narkoona sax. Di leen të, lu dëppoowul ak Mbind yi te ñàkk xel la narkoona doon. Nañu ko misaal: Jortul ñu xotti la ca loppitaan te ay ñaw-ñaw di aar góom bi. Bu ñu bokkul sax ci yaram wi, ñaw-ñaw yooyu am nañu njariñ diir bu ñu àppal. Teel leena dindi mënkoon na laa lor. Noonu it, kilifay nguuru doomu Aadama bokkuñu woon ca la Yàlla nasoon ca njëlbéen. Waaye ba ba Nguuram di ilif suuf si sépp, nguuri doomiy Aadama dañuy liggéey ngir déggoo am ci biir mbootaayug nit ñi, di def liggéey bu dëppook coobareg Yàlla ngir suñu jamano. Kon dañoo warkoona sax ciy déggal kilifa yu kowe yi, ba ñuy jiital sàrtub Yàllaak kilitéefam.

KILIFTÉEF CI BIIR NJABOOT

11. Nan ngay tekkee rëddu-yoonu kiliftéef?

11 Njaboot mooy li sës mbootaayug nit ñi. Ci biiram, jëkkër ak jabar mën nañoo am àndandoo buy bégal xol, te mën nañoo sàmm te jéemantal xale yi ngir seen dundug mag. (Léebu 5:15-21; Efes 6:1-4) Ndefarin bu ni rafete, soxla na ñu toppatoo ko ci yoon wuy tax ñii bokk njaboot dund ci jàmm ak déggoo. Ni Yeoway defe loolu, mu ngi ko jaarale ci rëddu-yoonuw kiliftéef, wu ñu tënk ci baat yii ci 1 Korent 11:3: “Krist mooy kilifag bépp góor, góor di kilifag jigéen, te Yàlla di kilifag Krist.”

12, 13. Kan mooy kilifag njaboot, te lan lañu mëna jànge ci ni Yeesu daan doxale kiliftéefam?

12 Jëkkër mooy kilifag njaboot. Wànte, moom it, am na kilifa gu ko féete kow—Yeesu Krist. Pool bind na: “Yeen nag góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram, ni Krist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom.” (Efes 5:25) Jëkkër a ngiy wone ndéggalam ci Krist, buy digaaleek jabaram na Yeesu daan digaaleek mbooloo mi. (1 Yowanna 2:6) Jagleel nañu Yeesu kiliftéef gu réy, waaye dafa koy doxal ànd ceek lewet, mbëggeel ak sago yu mat sëkk. (Macë 20:25-28) Ba mu nekkee nit ci kow suuf, Yeesu masula doxal taxawaayu kiliftéefam ngir noggatu. Dafa “lewet[oon] te woyef,” te woowe na “xarit” ay toppkatam, asté “jaam.” “Dinaa leen may noflaay,” la leen dig, te loolu la def.—Macë 11:28, 29; Yowanna 15:15.

13 Royukaayub Yeesoo ngiy jàngal jëkkër yi ne kiliftéefug karceen nekkul ab taxawaayub nooteel. Asté loolu, kiliftéef googu, ag kiliftéef gu ànd weg ak mbëggeel gu làmbook xuufeel la. Ci lu leer, loolu dàq na di dóoreek loxo walla aki kàddu ki nga séyal. (Efes 4:29, 31, 32; 5:28, 29; Kolos 3:19) Su ag góor gu nekk karceen doon gétëne noonu jabaram, yeneen jëfam yu baax yi doonuñu am lenn njariñ te loolu mënkoon naa gàllankoor ay ñaanam.—1 Korent 13:1-3; 1 Pieer 3:7.

14, 15. Nan la xam-xamub Yàlla dee dimbali jabar mu nangul jëkkëram?

14 Bu ab jëkkër dee topp royukaayu Krist, dina gëna yomb ci jabaram mu topp baat yi nekk ci Efes 5:22, 23: “Naka yeen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi. Ndaxte góor mooy kilifag jabaram, ni Krist nekke kilifag mbooloom ñi gëm.” Ni jëkkër waree nangul Krist, noonu la jabar waree nangul jëkkëram. Biibël baa ngiy leeral ne jabar yi am manoore yelloo nañu teraangaak tagg ndax seen sago su dëppook coobareg Yàlla ak seen njàmbaar.—Léebu 31:10-31.

15 Déggal bi jabar ji nekk karceen wara déggal jëkkëram am na fu mu yem. Looloo ngiy tekki ne Yàlla lañu wara déggal asté nit, su fekkee ne nangulam ci lenn jéggi sàrtub Yàlla lay yóbbe. Bu boobaa sax, taxawaay bu dëgër bi jabar di am ci topp sàrtub Yàlla war na koo yemaleek “soloo xel mu dal te lewet, NW.” Warkoon naa fés ne xam-xamub Yàllaa ko nekkloo jabar ju gën. (1 Pieer 3:1-4) Noonu it la wara deme ngir jëkkër ju jabaram gëmul. Topp bi muy topp rëddi-yooni Biibël bi warkoon na koo nekkloo jëkkër ju gën.

16. Nan la xale yi mënee roy Yeesu ba mu nekkee ndaw?

16 Efes 6:1 a ngiy jolliloo taxawaayub doom yi, di wax: “Naka yeen xale yi, nangeen déggal seeni waa-jur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet.” Xale yi nekk karceen dañuy roy Yeesu, mi saxoon ci déggal ay way-juram ba mu doon màgg. Nikib xale bu góor bu dégg ndigal, “Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam, te neex Yàlla ak nit ñi.”—Lukk 2:51, 52.

17. Ni way-jur yi di doxale seen kiliftéef, lan la mëna def ci seeni doom?

17 Fasoŋ bi way-jur yiy doxe seeni wareef mën na lu bare ci seeni doom, ndax dinañu weg kiliftéef walla jógal ko. (Léebu 22:6) Kon way-jur yi war nañooy laaj seen xel: ‘Ndax maa ngiy doxal sama kiliftéef ak mbëggeel walla ak coxorte? Ndax kuy wéyale lépp laa?’ Li ñuy xaaru ci aji-jur ju taq ci Yàlla mooy am mbëggeel ak aajo, terewul mu ne temm ciy taq ci rëddi-yooniy Yàlla. Ci lu war Pool bind na: “Yeen baay yi it, buleen bundaxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi.”—Efes 6:4; Kolos 3:21.

18. Yarub way-jur, nan lañu ko wara doxale?

18 Way-jur yi war nañoo niir seen yarin, rawatina su ñu bëggee seeni doom dégg ndigal te noonu indil leen mbégte. (Léebu 23:24, 25) Ci biir Biibël bi, yar, ci lu jiitu lépp, ab fasoŋu njàngale la. (Léebu 4:1; 8:33) Dañu ko lëkkaleek mbëggeel ak lewet, du ak mer ak coxorte. Kon, way-jur yi nekk karceen soxla nañoo ànd ak seen sago te fexee téye seen bopp bu ñuy yar seeni doom.—Léebu 1:7.

KILIFTÉEF CI BIIR MBOOLOOM KARCEEN YI

19. Nan la Yàlla taxawale jagal bu baax ci biir mbooloo karceen yi?

19 Ndegam Yeowa, Yàlla ju bëgg lu jag la, jaadu na mu taxawal ngir ay nitam kiliftéef ak njiit yu ñu jagal bu baax. Ci lu dëppook loolu, fal na Yeesu, def ko Kilifa mbooloom karceen. (1 Korent 14:33, 40; Efes 1:20-23) Ci njiiteefu Krist gu ñu mënula gis, Yàlla sañal na ab ndefar, te jaare ci ndefar boobu mag ñi ñu fal ci mbooloo mu nekk a ngiy sàmm coggal gi ak farlu, xol bu tàlli ak mbëggeel. (1 Pieer 5:2, 3) Surgay mbooloo maa ngi leen di jàpple ci fasoŋ yu bare tey def liggéey bu am solo ci biir mbooloo mi.—Filipp 1:1.

20. Lu tax ñu warkoona nangul magi karceen ñi ñu fal, te lu tax loolu am njariñ?

20 Ci lu jëm ci mag ñi, Pool bind na: “Déggalleen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte ñoo leen di sàmm te ñooy layoo seen liggéey. Kon nangeen leen déggal, ngir ñu mana def seen liggéey ak xol bu sedd, bañ cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njeriñ.” (Yawut yi 13:17) Ci sagoom, Yàlla dénk na wottukat yi nekk karceen wareefu toppatoo soxla yi jëm diggante Yàllaak ñii nekk ci biir mbooloo mi. Mag ñooñu nekkuñu ab kurélu làbbe. Ay surgaak jaamiy Yàlla lañu, di surgawu soxlay seeni moroomi jaamukat, ni ko Yeesu Krist, suñu Sang, doon ko defe. (Yowanna 10:14, 15) Xam ne ay nit ñu am manoore yi Mbind yi laaj a ngiy bàyyi xel ci suñu jëm-kanam ak suñu màggaay ci wàllu ngëm, a ngi ñuy xiirtal ñuy jëflante te di leen nangul.—1 Korent 16:16.

21. Nan la mag ñi ñu fal dee wuta dimbali seeni nawle karceen ci wàllu ngëm?

21 Léeg-léeg, ay xar mën nañoo réer, walla ay mbàmb yu jóge ci ameefiy àddina si mujj leena méb. Ci njiiteefu Aji Sàmm ji, mag ñi, niki ay ndaw ci wàllu sàmm, dañuy wottu, yeewu ci soxlay ñi ñu leen dénk te di leen toppatoo, ku nekk ci ñoom, ànd ceek farlu. (1 Pieer 5:4) Dañuy seeti ñii bokk ci mbooloo mi te di bokk ak ñoom ay kàdduy xiirtal. Xam ne Ibliis dafay wuta dog jàmmu nitiy Yàlla, mag ñi dañuy jariñoo sago si jóge ca kow, fa Yàlla, ngir toppatoo mbir mu jafe bu mu mënta doon. (Saak 3:17, 18) Dañuy liggéey ak farlu ngir saxal déggook nekk-benn ci ngëm, lu Yeesu ci boppam ñaan ngir mu am.—Yowanna 17:20-22; 1 Korent 1:10.

22. Lan ndimbal la mag ñi di joxe bu amee ay jëf yu ñaaw?

22 Lan mooy xew su amee lenn lu bon luy sonnal ab karceen walla mu mujja yoqi ndax bàkkaar bi muy def? Xelal yuy suqali yu jóge ci Biibël bi ak ñaani mag ñi, yu jóge ci seen xol ngir moom, mën nañu koo dimbali mu amaat wér-gi-xel. (Saak 5:13-15) Góor ñooñu xel mu sell mi fal, am nañu it sañ-sañu yar ak yedd képp kuy wéy ci dundinub jëfoo lu bon walla ku nekk mbàmb ngir setaayub mbooloo mi ci digganteem ak Yàlla ak ci wàllu jikko. (Jëf ya 20:28; Titt 1:9; 2:15) Ngir mëna denc mbooloo mi mu set, mën naa am mu war ku nekk ci biir mbooloo mi, mu xamal bàkkaar yu réy yi. (3 Musaa 5:1) Su ab karceen bu def bàkkaar bu réy nangoo yar ak yedd yi sukkandiku ci Mbind yi te mu fésloo réccu dëgg, dinañu ko dimbali. Jarul ñu koy wax, ñii sax ciy jéggi sàrtu Yàlla te bañ koo réccu, dañu leen di dàq.—1 Korent 5:9-13.

23. Lan la wottukati karceen yiy taxawal ngir njariñu mbooloo mi?

23 Biibël bi yégle woon na ne ci kiliftéefu Yeesu Krist niki buur, doon nañu fal góor ñu ñor ci wàllu ngëm ngir feddali, aar ak féexal mbooloo Yàlla. (Isayi 32:1, 2) Doon nañu jiite niki ay taskati xabaar bu baax bi, ay sàmm aki jàngalekat ngir fal màggaay ci wàllu ngëm. (Efes 4:11, 12, 16) Ak lu wottukati karceen yi mëna mëna jubbanti, yedd te xiirtal seeni nawle gëmkat yenn saa yi, jëfoo seen njàngale mu wér mi te sës ci Kàddug Yàlla, dina dimbali ñépp ñu des ci yoonu dund gi.—Léebu 3:11, 12; 6:23; Titt 2:1.

NANGUL GIS-GISUB YEOWA CI KILIFTÉEF

24. Ci wan werante lañ ñuy nattu bés-oo-bés?

24 Góor gu njëkk geek jigéen ju njëkk ji, nattu nañu leen woon ci mbirum déggal kilifa. Bettuñu su ñuy jànkoonteek nattu bu ni mel bés bu nekk. Seytaane miy Ibliis siiwal na xelum jógal kilifa ci biir doomiy Aadama. (Efes 2:2) Dundinub moom-sa-bopp, dañu koo niruloo mu daq fuuf dundinub dégg-ndigal.

25. Yan ñooy njariñi jaleñ xelum jógal kilifa ci àddina si te di nangul kiliftéef gi Yàllay doxal walla bàyyi mu am?

25 Wànte, fàww ñu daw xelum jógal kilifa mi ci àddina si. Bu ñuy def loolu, dinañu gis ne ndéggal gu fésloo taq ci Yàlla, yool yu réy lay yóbbe. Maanaam, dinañu moytu njàqare yeek yaakaar yu tas yi ñiiy sabab joteek kilifay àddina bokka daj. Dinañu wàññi ŋaayoo bi am ci biir njaboot yu bare. Te dinañu bànneexoo njarini jataay bu neex, bu ànd ak mbëggeel, ak suñu nawley gëmkat yi nekk karceen. Li raw lépp, suñu ndéggal gu fésloo taq ci Yàlla dina yóbbe ab diggante bu rafet ak Yeowa, Aji Kilifa ji.

SEETLUL SA XAM-XAM

Nan la Yeoway doxale kiliftéefam?

Ñan ñooy “kilifa yu kowe yi,” te nan lañoo saxe ci déggal leen?

Ban wareef la rëddu-yoonu kiliftéef sas képp ku bokk ci njaboot?

Nan lañu mënee wone nangul ci mbooloo karceen yi?

[Laaj yi]

[Wërale bi nekk paas 134]

DAÑOO NANGUL KILIFA, DUÑU KO JÓGAL

Ci seen yëngu-yëngub waare ci kanami ñépp, Seedey Yeowa yi dañuy joxoñ Nguurug Yàlla niki jenn yaakaaru jàmm ak dalaay ji nit ñi am kott. Waaye, waarekati Nguurug Yàlla yu sawar yooyu duñu jógal mukk nguur yi leen di ilif. Déedéet, Seede yaa ngi bokk ci doomi-réew yi gëna yaru te gëna taq ci sàrt yi. “Su tariixa yi yépp meloon ni Seedey Yeowa yi, duñu amkoon ay bóomkat, ay sàcc, ay wayu, ñii ñu kaaf, aki bomb atomik. Duñu tëjkoon bunt yi saa su nekk,” la genn kilifa ci menn réewum Afrig wax.

Ndax li ñu ràññee loolu, kilifay réew yu bare bàyyi nañu liggéeyub waare Seede yi wéy te baña am wenn gàllankoor. Ci yeneen réew, dindi nañu tere yeek xatal yi, bi kilifa yi gisee ne Seedey Yeowa yi dañuy xiir ci lu baax. Mu ngi mel ni ko Pool binde jëm ci nangul kilifa yu kowe yi: “Kon defal lu baax, te dina la tagg.”—Room 13:1, 3.