Kan mooy Yàlla dëgg ji?
Pàcc 3
Kan mooy Yàlla dëgg ji?
1. Lu tax nit ñu bare nangu baat yi njëkk ci Biibël bi?
BOO xoolee asamaan si ci guddi gu leer nàññ, gis i biddéew yu ni baree, ndax loolu du la yéem? Nan ngay faramfàccee ni ñu fa nekke? Loo wax ci lépp luy dund ci kow suuf si—tóor-tóor yu bare kulóor yi, picc yeek seeni woy yu neex, ngaaga yu am doole yiy tëbantu ci biir géej gi? Mën nañoo wéy di lim ay misaal yu ni mel ba fàww. Loolu lépp jékki-jékkiwul rekk nekkal boppam. Bettuñu bu ay nit ñu bare nangoo baat yii njëkk ci Biibël bi: “Ca njëlbéen Yàlla sàkk na asamaan yeek suuf si”!—1 Musaa 1:1.
2. Lan la Biibël biy wax ci mbirum Yàlla, te lan la ñuy xiirtal ñu def ?
2 Mbirum Yàlla xàjjale na lool nit ñi. Ñenn ñi dañuy xalaat ne am kàttan mu amul jëmm la. Ay tamndareeti nit dañuy jaamu seeni maam yi dee, foog ne Yàlla dafa sore lool ngir ñu mën koo jege. Waaye Biibël baa ngiy feeñal ne Yàlla dëgg ji nit dëgg la te jàpp na ñu ci xolam, kenn ku nekk ci ñun. Looloo tax mu ngi ñuy xiirtal ñu “wut Yàlla,” naan: “Sorewul kenn ci ñun.”—Jëf ya 17:27.
3. Lu tax mënuñoo defar mukk ab nataalu Yàlla?
3 Lan la Yàlla di nirool? Ñenn ci ay jaamam gis nañu teewaayam bu ànd ak ndam ci ay gis-gis fu mu firndeel boppam niki ku toog cib jal, leer gu doy waar jóge ca moom, di ray-rayi. Waaye, ña amoon gis-gis yooyu masuñoo nettali lu xar-kananam doon niru. (Dañel 7:9, 10; ) Loolu, ndax “Yàlla xel la”; amul yaramuw suux. ( Peeñu bi 4:2, 3Yowanna 4:24) Ci dëgg, mënuñoo defar mukk nataal bu wér bu suñu Sàkkkat, ndax “kenn musula gis Yàlla.” ( Yowanna 1:18; 2 Musaa 33:20) Terewul, Biibël baa ngi ñuy jàngal lu bare ci Yàlla.
YÀLLA DËGG JI AM NA TUR
4. Yan ñooy yenn ci dakantal yu am tekkite yu ñu jagleel Yàlla ci Biibël bi?
4 Ci biir Biibël bi, dañoo niraale “Yàlla dëgg ji” ciy baat yu mel ni “Yàlla Aji Kàttan,” “Aji Kowe ji,” “Sàkkkat su Mag si,” “Aji Jàngalekat bi,” “Boroom bi” ak “Buur bi fiy sax ba abadan.” (1 Musaa 17:1; Sabuur 50:14; Dajalekat 12:1; Isayi 30:20; Jëf ya 4:24; 1 Timote 1:17) Di xalaat ba xeli ci dakantal yooyu mën na ñoo dimbali ñu màgg ci xam-xamub Yàlla.
5. Lan mooy turuw Yàlla, te ñaata yoon lay feeñ ci Mbind yi ci làkku Ebrë?
5 Waaye, Yàlla wenn tur kott la am, wuy feeñ lu jege juróom-ñaari junni (7 000) yoon, te loolu ci Mbind yi ci làkku Ebrë doŋŋ—mu gëna farala feeñ bépp beneen dakantal bu mu mënta doon. Lu tollook junneek juróom-ñeenti téeméeri (1 900) at ca gannaaw, Yawut yi, ndax seeni biddaa, bàyyi nañoo wax turuw Yàlla. Làkkuw Ebrë ci Biibël bi, dañu ko daan bind te daawuñu ko maas. Noonu, mënuñoo xam bu baax naka la Musaa, Daawuda, walla ñeneen nit daan waxe ca jamano jooja ñeenti coowaan (י ה ו ה) yi booloo nekk turuw Yàlla. Am na ay aalimi Biibël bi yuy diktal ne turuw Yàlla “Yahweh” lañu ko daan wax, waaye dara wóoru leen ci. Wax ji ñu wolofal “Yeowa” moo doon li ñu doon jëfandikoo li dale ci ay xarnu ba tey, te moom lañuy jëfandikoo ba léegi ci làkk yu bare.—Seetal Eksode 6:3 ak Esai 26:4 ci Biibël bi ci làkku bàmbara te tudd Bible Senuma. (©1961).
LI TAX NGA WAR DI JËFANDIKOO TURUW YÀLLA
6. Lan la Sabuur 83:18 wax lu jëm ci Yeowa, te lu tax ñu war di jëfandikoo turam?
6 Tur wi Yàlla am kótt, Yeowa, dafay tax ñu wuutale kook yeneen yàlla yépp. Looloo tax tur woowu faral di feeñ lool ci Biibël bi, rawatina ci mbind yi ci làkku Ebrë. Bare na ci firikati Biibël bi yu dul jëfandikoo turuw Yàlla; moona Sabuur 83:18 ci lu leer, a ngiy wax: “Yow, mi sa tur di Yeowa, yow doŋŋ, yaay Aji Kowe ji ci kow suuf si sépp.” Kon jaadu na ñuy jëfandikoo tur wi Yàlla moomal boppam bu ñu koy waxtaane.
7. Tekkiteb tur wi Yeowa, lan la ñuy jàngal ci Yàlla?
7 Tur wi Yeowa, aw melinu njëfka la ci làkku Ebrë, buy tekki “mujja nekk” . Noonu, turuw Yàllaa ngiy tekki “Dafay mujja nekkal”. Yeowa dafay niroolu ni Yàlla ju mag ji am ab nas. Saa su nekk, dafay mujja nekkal li mu nas. Yàlla dëgg ji doŋŋ a yelloo am tur woowu, ndax mënula wóor nit ñi mukk ne seeni nas dinañ àntu. (Saak 4:13, 14) Yeowa doŋŋ a mëna wax: “Noonu la sama kàddu giy génne sama gémmiñ di mel. (. . .) Ci lu wóor, dina àntu ci li Ma ko yónni.”—Isayi 55:11
8. Ban nas la Yeowa xamle jaare ci Musaa?
8 Boroom kër yu mag ya nekkoon ay ebrë, Ibrayima, Isaaxa ak Yanxóoba, ku nekk ci ñoom woo woon na “Yeowa ciw turam,” waaye xamuñu woon lépp li turuw Yàlla tekki. (1 Musaa 21:33; 26:25; 32:9; 2 Musaa 6:3) Gannaaw loolu, ba Yeowa feeñalee nasub goreel seeni sët, maanaam waa Israel, ca njaam ga ca Misira te jox leen “suuf fu meew ak lem di wal,” loolu mënoon naa niroo lu mënula am. (2 Musaa 3:17) Wànte, Yàlla jolliloo woon na li turam di tekki ba fàww, ba mu waxee yonentam Musaa: “Lii ngay wara wax doomi Israel, ‘Yeowa, Yàllay seeni maam, Yàllay Ibrayima, Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanxóobaa ma yónni ci yeen.’ Loolooy samaw tur ba diir bu amul àpp, te loolooy li ñu may fàttalikoo maas ci kow maas.”—2 Musaa 3:15.
9. Nan la Firawna gise woon Yeowa?
9 Musaa laajoon na Firawna, buurub Misira, mu bàyyi waa Israel ngir ñu jaamu Yeowa ca màndiŋ ma. Waaye Firawna mi ñu tegoon ab yàlla te doon jaamu yeneen yàllay Misira, daldi ko tontu: “Kan ay Yeowa ngir ma déggal baatam ci dàq Israel? Xamewuma fenn Yeowa, te magum loolu, duma sax dàq Israel.”—2 Musaa 5:1, 2.
10. Ca Misira bu njëkk ba, jan jëf la Yeowa sumb ngir àggali nasam bi jëm ci waa Israel?
10 Yeowa daldi sumb nag jëf juy jëm kanam ngir àggali ndànk-ndànk li mu nas; noonu la jëfe lu dëppook tekkiteb turam. Wàcce na fukki kasara ci kow waa Misira yu njëkk ya. Kasara gu mujj ga réy na taawi Misira yépp, doom ju góor ju Firawna mi yëgoon boppam bokk ca. Noonu, ba loola amee, waa Misira daldi yàkkamtee gis Israel dem. Waaye, ñenn ci waa Misira dañoo yéemu woon ci kàttanug Yeowa yéem gu tax ñu faf génnandook waa Israel dëkku Misira.—2 Musaa 12:35-38.
11. Jan kéemaan la Yeowa def ca Géej gu Xonq ga, te lan la ay noonam mënuloona ñàkka nangu?
11 Firawna mu dëgër bopp mi, génnoon naak xareem, ak ay téeméeri sareet yu ñuy xeexe ngir jàppaat ay jaamam. Ba Yàlla gisee waa Misira di jegesi, ci kéemaan, mu daldi xàll yoon ci Géej Gu Xonq gi ndax waa Israel mën koo jàll ak seeni tànk ci suuf su wow. Ba dàqekat ya duggsee ca biir suufu géej ga, Yeowaa nga “doon wéy di dindi ruuyi sareet ya, ba tax ñu ngi leen doon dawal ak jafe-jafe.” Xeexkati Misira daldi yuuxu: “Nañu daw, sore Israel, ndaxte ci lu wóor Yeowaa ngi leen di sotle, noonook waa Misira.” Wànte daw weesu woon na. Ndox ya taxawoon ni ay taax yu réy daldi màbb, “nuural sareet ya ñuy xeexeek gawar ya bokkoon ci xareb Firawna.” (2 Musaa 14:22-25, 28) Noonu Yeowa may na boppam tur wu mag, te ba bés niki tey, fàttewuñu xew-xew boobu.—Yosuwe 2:9-11.
12, 13. (a) Lan la turuw Yàlla tekki ngir ñun tey? (b) Lan la nit ñi soxlaa jàng ci ni mu gëne gaaw, te lu tax?
12 Tur wi Yàlla sàkkal boppam am na tekkite bu réy ngir ñun tey. Turam, Yeowa, mooy firnde ju wóor jiy wone ne dina fexee dëggal lépp li mu nas. Loolu ëmb na àggali la mu nasoon ca njëlbéen, maanaam suuf si mujja nekk àjjana. (1 Musaa 1:28; 2:8). Ngir loolu am, Yàlla dina rey ñépp ñiy bippu kiliftéefam tey, ndax nee na: “Xeet yi dinañu xam ne maay Yeowa.” (Esekiel 38:23) Bu boobaa, Yàlla dina àggali digeem musal ay jaamukatam te duggal leen ci àddinay njub su bees.—2 Pieer 3:13.
13 Ñépp ñi bëgga am yiwu Yàlla war nañu ko jànga woo ciw turam ak ngëm. Biibël baa ngiy dig: “Képp ku woo Boroom bi [Yeowa, New World Translation] ciw turam, dinga mucc.” (Room 10:13) Ci lu wóor, li tur wi Yeowa tekki yenu na maanaa lool. Woo Yeowa ciw turam niki sa Yàllaak sa Musalkat, mën na laa jëme ci bànneex bu dul jeex.
JIKKOY YÀLLA DËGG JI
14. Yan jikkoy Yàlla yi ëpp maanaa la Biibël biy jolliloo?
14 Njàngum muccug Israel ca Misira dafay jolliloo ñeenti jikko yi ëpp maanaa yi Yàlla moom ci yemaay bu mat sëkk. Digaaleem ak Firawna feeñal na kàttanam mu doy waar. (2 Musaa 9:16) Yoon wu xéréñ wi Yàlla jaar ngir lijjanti mbir moomu, wone na sagoom su amul moroom. (Room 11:33) Feeñal na njubam ba muy duma, duma bu yem, ña dëkkoon ci noonook tey lottal mbooloom. (5 Musaa 32:4) Mbëggeel mooy jenn ci jikkoy Yàlla yi ñu gëna ràññee. Yeowa wone na mbëggeel gu ràññeeku ba mu àggalee la mu digoon askanu Ibrayima. (5 Musaa 7:8) Wone na it mbëggeel ba mu mayee ñenn ci waa Misira, ñu won gannaaw seeni yàlla yu dul dëgg te far ak jenn Yàlla dëgg ji, loolu yóbbe leen xéewal yu réy.
15, 16. Ci yan fasoŋ la Yàlla wone mbëggeelam?
15 Boo dee duruus Biibël bi, dinga ràññee ne mbëggeel mooy jikko Yàlla ji jiitu, te dafa koy wone ciy yoon yu bare. Maanaam, mbëggeel a tax Yàlla mujja nekk ab Sàkkkat te njëkka séddoo bànneexub dund aki mbindaafoni xel. Téeméeri tamndareeti malaaka yooyu bëgg nañu Yàlla te dañu koy tagg. (Ayóoba 38:4, 7; Dañel 7:10) Yàlla it wone na mbëggeelam ba muy sàkk suuf si te waajal ko ngir nit ñi dund ceek bànneex.—1 Musaa 1:1, 26-28; Sabuur 115:16.
16 Xéewal yi ñuy jële ci mbëggeelug Yàllay dañoo bare lool ba tax mënuñu leena lim. Lenn lu koy misaal mooy Yàlla defar naak mbëggeel suñu yaram, ndefarin bu doy waar ngir ñu mëna bànneexoo dund. (Sabuur 139:14) Mbëggeelam it feeñ na ci li mu ñuy “wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.” (Jëf ya 14:17) Yàlla dafay “fenkal [sax] jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, (...) [tey] tawal ñi jub ak ñi jubadi.” (Macë 5:45) Mbëggeel a tax it suñu Sàkkkat di ñu dimbali ngir ñu jot xam-xamub Yàlla te di ko liggéeyal niki ay jaamukatam. Ci lu wóor, “Yàlla Aji Mbëggeel la.” (1 Yowanna 4:8) Waaye Yàlla am na yeneen jikko yu bare.
“YÀLLA JU AM YËRMANDE TE LAABIIR”
17. Lan la ñu 2 Musaa 34:6, 7 di jàngal ci Yàlla?
17 Gannaaw ba waa Israel jàllee Géej gu Xonq ga, ba tey soxla nañu woona gëna xam Yàlla. Musaa yëgoon na soxla boobu te ñaanoon na: “Su la soobee, su fekkee ne yiw naa ci say gët, xamal ma say yoon, su la soobee, ngir ma mën laa xam, ndax ma mëna yiw ci say gët.” (2 Musaa 33:13) Musaa jot naa gëna xam Yàlla ba mu déggee yégleb Yàlla ci boppam: “Yeowa, Yeowa, Yàlla ju am yërmande te laabiir, ju gaawula mer te fees ak mbaaxaayug xol ak dëgg, di dencal mbaaxaayug xol ay junniy nit, di baal njuumteek jéggi yoon ak bàkkaar, waaye kat ci bépp anam bu mu mënta doon, du jaasal nduma gi.” (2 Musaa 34:6, 7) Yàlla dafa yemale mbëggeelam ak njub, bañ di aar ñiiy tey bàkkaar ci lu ñu wara góobe ci seen jëf yu bon.
18. Nan la Yeowa wone ne ku am yërmande la?
18 Ni ko Musaa jànge, Yeowa dafay wone yërmande. Nit ku am yërmande dafay yërëm ñii am metit te dafa leen di jéema indil péex. Noonu, Yàlla wone na laabiir ci nit ñi ba mu taxawalee matuwaay bu leen di jox péex muy sax, génne leen ciy metit, feebar ak dee. (Peeñu bi 21:3-5) Mën naa am ñiiy jaamu Yàlla daj ay musiba ndax nekkini àddina su bon sii, walla ñu teg seen bopp coono ndax gàtt-xel. Wànte su ñu suufeelee seeni bopp, jublu ci Yeowa ngir laaj ndimbal, dina leen dëfël te dina leen dimbali. Lu tax loolu? Ndaxteek yërmande dafa am worma ci ñii koy jaamu.—Sabuur 86:15; 1 Pieer 5:6, 7.
19. Lu tax ñu mëna wax ne Yàlla ku laabiir la?
19 Nit ñu bare ñu nekk ay kilifa dañuy bundxataal ñeneen ñi. Ci lu wuuteek ñooñu, Yeowa aka laabiir ciy jaamam yu woyof yi! Lu mu nekka nekk kilifa gi gëna kowe ci mbindeef mépp, faral na di wone mbaaxaay mu ràññeeku ci nit ñépp. (Sabuur 8:3, 4; Lukk 6:35) Yeowa dafa laabiir itam ci gaa ñi koy ñaan, di tontu seeni ñaan ngir jot saxsax yiwam. (2 Musaa 22:26, 27; Lukk 18:13, 14) Lu wóor-a-wóor la, Yàlla ameelul kenn yiw walla yërmande, képp ku mu mënta doon. (2 Musaa 33:19) Looloo tax, soxla nañoo gërëm Yàlla bu baax-a-baax ndax yërmandeem ak laabiiram.—Sabuur 145:1, 8.
GAWULA MER, KU DUL GËNAATLE TE JUB
20. Lan mooy wone ne Yeowa gaawula mer te it du gënaatle?
20 Yeowa gaawula mer. Waaye, loolu tekkiwul ne du jëf, ndax def na dara ba mu reyee Firawna mu dëgër bopp maak xareem ca Géej gu Xonq ga. Du gënaatle it. Noonu, waa Israel, xeet wa amoon yiwam, faf nañu koo ñàkk, ndax li ñu dëkkoon ci def lu bon. Yàlla nangu na niti xeet yépp jaamu ko, waaye ci kow ñu dox ci ay yoonam, yu jub yi.—Jëf ya 10:34, 35.
21. (a) Lan la ñu Peeñu bi 15:2-4 di jàngal ci mbirum Yàlla? (b) Lan moo ñuy gëna yombloo def li Yàlla wax ne lu jub la?
21 Téere Biibël bi tudd “Peeñu bi” jolliloo na solo xam “àttey” Yàlla, yu jub yi. Mu ngi ñuy xamal ne ay mbindeefi asamaan a ngay woy: “Say jëf réy nañu te yéeme, yaw (...) [Yeowa, NW ] Yàlla, Aji Kàttan ji. Say yoon jub nañu te dëggu, yaw Buur bi fiy sax ba abadan. Ku la ragalul, [Yeowa, NW ] Boroom bi? Ku dul màggal saw tur? (...) ndaxte yaw rekk yaa [di gor, NW ]? Xeet yépp dinañu dikk, jaamu la, ndax say àtte [yu jub, NW ] bir nañu.” (Peeñu bi 15:2-4) Ñu ngiy wone ragal ci Yeowa gu ñuy jariñ, walla am worma ci moom, bu ñuy topp li muy wax ne lu jub la. Loolu dina gëna yomb bu ñuy fàttaliku sago Yàllaak mbëggeelam. Ay ndigalam yépp suñu njariñ lañu.—Isayi 48:17, 18.
“YEOWA SUÑU YÀLLA KENN LA”
22. Lu tax ñii nangu Biibël bi duñu jaamu ab Trinite?
22 Waa Misira bu njëkk ba dañu daan jaamu ay yàlla yu bare, waaye Yeowa “Yàlla juy laaj taq bu àndul ak bokkaale” la. (2 Musaa 20:5) Musaa fàttali na waa Israel ne “Yeowa suñu Yàlla kenn Yeowa képp la.” (5 Musaa 6:4) Yeesu Krist baamtu na baat yooyu. (Mark 12:28, 29) Looloo tax, ñii nangu Biibël bi niki Kàddug Yàlla, duñu jaamu ab Trinite, maanaam ñetti nit walla yàlla yu doon jenn. Bu ñu ko seetee sax, baat bi Trinite feeñul sax ci Biibël bi. Yàlla dëgg ji kenn Nit la, wuute naak Yeesu Krist. (Yowanna 14:28; 1 Korent 15:28) Xel mu sell mu Yàlla du nit. Mooy doole Yeowa jiy jëf, doole ji Aji Kàttan ji di jëfandikoo ngir àggali ay nasam.—1 Musaa 1:2; Jëf ya 2:1-4, 32, 33; 2 Pieer 1:20, 21.
23. (a) Nan la sa mbëggeel ci Yàlla di màgge? (b) Lan la Yeesu wax ci mbirum bëgg Yàlla, te lan la ñu soxlaa jàng ci mbirum Krist?
23 Boo seetee ni Yeowa nekke Ku amul moroom, ndax dàkkooruloo ne yelloo na nga jaamu ko? Boo dee jàng Kàddoom, Biibël bi, dinga ko gëna xam te dinga jàng li mu lay laaj ngir sa suturaak sa bànneex yu dul jeex. (Macë 5:3, 6) Teg ci, sa mbëggeel ci Yàlla dina màgg. Noonu la mëna deme, ndax Yeesu nee na: “Nanga bëgg [Yeowa, NW ] Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp, ak sa kàttan gépp.” (Mark 12:30) Ci lu wóor-a-wóor, mbëggeel gu ni mel la Yeesu amoon ci Yàlla. Waaye lan la Biibël biy feeñal ci mbirum Yeesu Krist? Lan mooy taxawaayam ci nasub Yeowa?
SEETLUL SA XAM-XAM
Lan mooy turuw Yàlla, te ñaata yoon lay feeñ ci Mbind yi ci làkku Ebrë?
Lu tax nga war di jëfandikoo turuw Yàlla?
Yan ñooy jikkoy Yeowa Yàlla yi lay xëcc saxsax ci moom?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 29]
Ba fan la sa xam-xamu Sàkkkatu lépp tollu?