Lan mooy dal suñuy soppe yi dee?
Pàcc 9
Lan mooy dal suñuy soppe yi dee?
1. Lan la nit ñiy yëg ci seen xol bu ku ñu sopp deewee?
“DAÑUY yëg metit bu suñu soppe deewee, ndaxte dee mooy ñàkk koo sopp, mu réer ci lu ñu xamul.” Loolu mooy li jenn doom ju góor wax ba baayam deewee te yàggul dara yaayam tegu ca. Naqaram ak ñàkk mu réy mi mu yëg ci xolam a ngi ko doon foogloo ne mu ngi doon “lab ci wàllu cofeel.” Mën naa am nga masa yëge metit noonu. Xëy na laaj nga sa xel fu sa soppe yi dee nekk te ndax dinga leen gisaat bés.
2. Yan laaj yuy ub bopp lañuy laajte lu jëm ci dee?
2 Yenn way-jur yu am tiis dégg nañu ñu wax leen: “Yàlla dafay witt tóor-tóor yi gëna rafet ngir jël leen ca wetam ca asamaan.” Ndax loolu dëgg la? Ndax suñuy soppe yi dee dañoo dem ca diiwaani xel ya? Ndax mooy li ñenn ñi tudde Nirvana, gu ñu nataal niki nekkinub bànneex, fu ñuy mucce ci wépp naqar walla bépp bëgg-bëgg? Ndax suñuy soppe dañoo jaar ci bunt buy jëme ca dund gu mënula jeex ca àjjana? Walla, ni ci ñeneen jafandoo, ndax dee tàbbi ci mbugël mu dul jeex la ngir ñii tooñ Yàlla? Ndax ñi dee mënal nañ ñu dara? Ngir am tont yuy dëgg ci laaj yu ni mel, soxla nañoo seet Kàddug Yàlla, Biibël bi.
LAN MOOY “XEL” MI CI DOOMI AADAMA YI?
3. Lan a nekkoon gis-gisub Sokraat ak Platoŋ ci dee, te nan la looluy ruuxe nit ñi tey?
3 Sokraat ak Platoŋ, ay xalaatkat ca réewum Grèce mu njëkk ma, dañoo jàppoon ci li ñu xalaat, maanaam ci biir góor ak jigéen am na lenn lu mënula dee—ab bakkan buy mucc ci dee te dul dee mukk ci dëgg. Tey, fu nekk ci suuf si, loolu la ay tamndareeti nit gëm. Ngëm googu, ni mu farale di jur ragalug ñi dee lay farala jur itam tiisoo seen sutura. Biibël baa ngi ñuy jàngal lenn lu wuutee wuute ci mbirum ñi dee.
4. (a) Lan la ñu 1 Musaa di wax ci mbirum bakkan? (b) Lan la Yàlla def ci Aadama ngir dundaloo ko?
4 Lu jëm ci nekkinub ñi dee, war nañoo fàttaliku ne suñu baay ba jiitu, Aadama, amuloon ab bakkan. Ab bakkan la woon. Ca jëfu sàkk ju yéeme, Yàlla defare na nit—bakkan—ca ameefi suuf si te fuuf na ci moom “nawu dund gi.” 1 Musaa 2:7 a ngi ñuy wax: “Yeowa Yàlla daldi defare nit ca pëndu suuf si te ëf ca paxi bakkanam nawu dund gi, te nit mujj naa nekk ab bakkan buy dund.” Dundug Aadama, noyyee ko yore woon. Ndaxam, ba Yàlla defee nawu dund gi ca biir Aadama, li mu def ëmboon na lu raw ëf ngelaw ci xëtëri nit ka. Biibël baa ngiy wax ci “dooley dund gi”, jiy jëf ci biir mbindeef yiy dund ci kow suuf.—1 Musaa 7:22.
5, 6. (a) Lan mooy “doole dund gi”? (b) Lan mooy xew, bu “xel” mi ñu tudd ci Sabuur 146:4 noppee dundaloo yaram wi?
5 Lan mooy “doole dund gi”? Mooy ferñent wiy joxe dund gi Yàlla duggal ca yaramu Aadama wa ne woon tekk. Ca gannaaw ga, doole jooju noyyee ko yore woon. Kon lan mooy “xel” mi Sabuur 146:4 di waxtaane? Aaya joojoo ngiy wax ci nit kuy dee : “Xelam dafay génn, mu dellu ci suufam; bés booba la ay xalaatam di raaf.” Ba bindkati Biibël bi doon jëfandikoo noonu baat bi “xel”, xalaatuñu woon bakkan bu amul yaram buy wéy di dund gannaaw bu yaram wi deewee.
6 “Xel” miy génne ci doomi Aadama yi gannaaw dee mooy dooley dund giy jóge ca suñu Sàkkkat. (Sabuur 36:9; Jëf ya 17:28) Dooley dund googu amul wenn melo ci meloy mbindeef mi muy yëngal, niki kuraŋ du jël wenn melo masiin bi muy may doole. Bu kenn deewee, xel mi (dooley dund gi) dafay noppee dundaloo cellules (cells) yu yaram wi, niki làmp di feye bu ñu dogee kuraŋ bi. Bu doole dund gi noppee dundal yaramu doomu Aadama, nit—bakkan— dafay dee.—Sabuur 104:29; Dajalekat 12:1, 7.
“CI PËND NGAY DELLU”
7. Lan a naroona jot Aadama su déggadiloon Yàlla?
7 Yeowa faramfàcce na lan la dee naroona tekki ngir Aadama bàkkaarkat bi. Yàlla nee na: “Ci sa ñàqu xar-kanam ngay lekke mburu ba kera ngay dellu ci suuf si, ndax ci moom lañu la jële. Ndax pënd nga te ci pënd ngay dellu.” (1 Musaa 3:19) Fan la Aadama naroona dellu? Ci suuf si, ci pënd bi ñu ko sàkke woon. Ci dee, Aadama narkoon naa réer doŋŋ!
8. Niki ay bakkan, ci lan la doomi Aadama yi gënul mala yi?
8 Ci fànna boobu, deewu doomu Aadama wuutewul ak deewu mala yi. Mala yi it ay bakkan lañu, te menn xel mi, walla doole dund, a leen di dooleel. (1 Musaa 1:24) Suleymaan, nit ku am sago, wax na ñu ci Dajalekat 3:19, 20: “Ni kenn ki di deewee, noonu la beneen bi di deewee; te menn xel mi lañu am ñoom yépp, ba tax [ci dee] amul gënaayu nit ci kow mala. (. . .) Ñoom yépp dañoo mujja nekke ci pënd, te ñoom yépp a ngiy dellu ci pënd.” Nit a gënoon mala yi ci li ñu ko sàkkoon ci melokaanuw Yàlla, muy awu jikkoy Yeowa. (1 Musaa 1:26, 27) Ndaxam, cig dee, doomi Aadama yeek mala yee niroo, dañuy dellu ci pënd.
9. Lan mooy nekkinub ñi dee, te fan lañuy jëm?
9 Suleymaan teg na ca, di faramfàcce lan la dee tekki, naan: “Ñiiy dund xam nañu ne dinañu dee; waaye lu jëm ci ñi dee, ñoom xamuñu dara ba dara jeex.” Waaw, ñi dee xamuñu dara ba dara jeex. Looloo tax, Suleymaan jamp na: “Lépp lu sa loxo daj ngir def ko, def kook sa doole dëgg, ndax amul jëf, walla nas, walla xam-xam, walla sago ci Sheol, béréb bi ngay jëm.” (Dajalekat 9:5, 10) Fan la ñi dee di jëm? Ci Sheol (ebrë, she’ohl), bàmmeel bi nit ñépp bokka jëm. Suñuy soppe yi dee xamatuñu dara. Nekkuñu ci metit, te mënaluñ ñu dara ci benn anam bu mu mënta doon.
10. Lu tax ñu mëna wax ne dee nekkul lu dul jaas?
10 Ndax ñun ñépp ak suñuy soppe, dañoo wara dund ay at yu néew ba noppi sànku ba fàww? Du li Biibël bi wax. Ca jamano ja Aadama jógalee Yàlla, ca saa sa Yeowa Yàlla fogoru na ngir saafara musiba yi bàkkaarub nit jur. Dee bokkuloon ci nasub Yàlla ngir nit ñi. (Esekiel 33:11; 2 Pieer 3:9) Kon, dee nekkul, ngir ñun walla suñuy soppe, ag muj gu dul jaas.
“NELAW NA”
11. Nan la Yeesu nataale nekkinub Lasaar xaritam bi dee woon?
11 Nasub Yeowa la, xettali ñu, ñun ak suñuy soppe yi dee, ci dee gi ñu donn ci Aadama. Looloo tax, Kàddug Yàllaa ngiy wax ci ñi dee niki ñuy nelaw. Maanaam, gannaaw ba mu déggee ne xaritam Lasaar dafa dee woon, Yeesu Krist wax na ay taalibeem: “Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.” Ndegam ay taalibeem jàppuñu woon ca saa sa li kàddoom tekki, Yeesu wax na leen wax ju wóor: “Lasaar dee na.” (Yowanna 11:11, 14) Gannaaw loolu, Yeesu daldi dem ca dëkku Betani, fa jigéeniy Lasaar, Mart ak Maryaama, toogoon di naqarlu tey jooy seen càmmiñ ba dee woon. Ba Yeesu waxee Mart: “Sa càmmiñ dina dekki”, Mart wone na ngëm ci nasub Yàlla ngir saafara li dee jur ci njabootu doomiy Aadama. Nee na: “Xam naa ne, dina jóg bésu ndekkite li, keroog bés bu mujj ba.”—Yowanna 11:23, 24.
12. Ban yaakaar la Mart mi ñàkkoon càmmiñam amoon lu jëm ci ñi dee?
12 Mart tuddul dara ci lu jëm ci bakkan bu mënula dee, buy dund feneen gannaaw dee. Gëmuloon ne Lasaar demoon na ba noppi ca ab diiwaanu xel ngir wéy di fa dund. Mart amoon na ngëm ci yaakaaru ab ndekkite ca ña dee, yaakaar ju yéeme. Fooguloon ne ab bakkan bu mënula dee dafa teqaliku woon ak yaramu Lasaar, waaye nàndoon na ne càmmiñam bi faatu dafa réeroon. Garab gee doon nekk ndekkitel càmmiñam.
13. Gan kàttan gu jóge ca Yàlla la Yeesu am, te nan la wone woon kàttan googu?
13 Yeesu Krist mooy kii Yeowa Yàlla jox kàttan ngir jotaat nit ñi. (Xoseyaa 13:14) Noonu, ba muy tontu ca la Mart waxoon, Yeesu nee na: “Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.” (Yowanna 11:25) Yeesu wone na kàttanam ga ko Yàlla joxoon ci fànna boobu, ba mu demee ca bàmmeelub Lasaar, ma deewoon lu tollook ñeenti fan, te delloo ko bakkanam. (Yowanna 11:38-44) Jortul tuuti mbégu ñii fekke woon ndekkite loolu walla yeneen yu Yeesu Krist def!—Mark 5:35-42; Lukk 7:12-16.
14. Lu tax ndekkite ak xalaatum bakkan mu mënula dee safaanoo?
14 Nañu teewlu tuuti ci xalaat wii: kenn doonul soxla ñu dekkal ko, walla ñu indiwaat ko cig dund, su bakkan bu mënula dee doon mucc cig dee. Dëgg-a-dëgg, doonul nekk lu rafet, dekkal ku mel ni Lasaar, delloosi ko ci dund gu matadi gi ci kow suuf, su jàlloon ba noppi ca asamaan, jot ca yool bu amul moroom. Li am mooy, Biibël bi du jëfandikoo mukk baat “bakkan bu mënula dee.” Asté loolu, Mbind yi dañuy wax ne bakkanu doomu Aadama biy bàkkaar dafay dee. (Esekiel 18:4, 20) Biibël bi, kon, dafay joxoñ ndefarum ndekkite li niki doŋŋ liy saafara dee.
“ÑÉPP ÑII NEKK CI BIIR BÀMMEELIY FÀTTALIKU, NW”
15. (a) Lan la baat “ndekkite” di tekki? (b) Lu tax ndekkite nit ñi, ku nekk ci jëmmu boppam, jaaxalul Yeowa Yàlla?
15 Baat bi taalibey Yeesu jëfandikoo ngir “ndekkite” dafay tekki saxsax “di jóg” walla “di taxaw.” Looloo ngiy tekki jóge ci nekkinub dee bu àndul ak dund—maanaam di taxaw, génne ca bàmmeel bi nit ñépp bokk. Yeowa Yàlla mën na, ci lu yomb, dekkal nit. Lu tax? Ndaxte Yeowa mooy Kii sos dund. Tey, nit ñi mën nañoo sotti baat yeek nataali góor aki jigéen ci ‘widéo-kaset’ te dawalaat sotti yooyu gannaaw bu nit nooñu deewee. Ci lu wóor, kon, suñu Sàkkkat, di Aji Kàttan ji, mën naa fàttaliku, benn-benn, meloy yépp nit ku nekk ci jëmmu boppam te dekkal nit kooku saxsax, di ko jox yaram wu bees wu ñu defar, muy góor di jigéen.
16. (a) Ban dige la Yeesu def jëm ci ñépp ñii nekk ci bàmmeeliy fàttaliku? (b) Lan mooy dogal fu ndekkitel nit di mujje?
16 Yeesu Krist nee na: “Waxtu waa ngiy ñëw, fu ñépp ñii nekk ci biir bàmmeeli fàttaliku yi di dégg baatam [bosu Yeesu] tey génn, ñii jëf yëf yu baax, ngir ndekkitel dund, ñii jëf yëf yu ñaaw, ngir ndekkitel àtte.” (Yowanna 5:28, 29, NW ) Ñépp ñii nekk ci xelum Yeowa dinañu leen dekkal te dinañu leen jàngal ci ay yoonam. Ngir ñiiy jëf lu dëppook xam-xamub Yàlla, loolu dina mujja yóbbe ndekkitel dund. Waaye, ngir ñiiy bañ njàngaley Yàllaak kiliftéefam, seen ndekkite dina mujja yóbbe ndekkitel daanub yoon.
17. Kan lañuy dekkal?
17 Ni mu awe yoon, ñii sax ci dund gu jub niki jaami Yeowa dinañu dekki. Li am mooy, yaakaaru ndekkite li dooleel na ñu bare ñu jàkkaarlook dee, loolu sax ci ay toŋal yu mettee metti. Xamoon nañu ne Yàlla mënoon na leena delloo seen bakkan. (Macë 10:28) Waaye ay tamndareeti nit dee nañu te wonewuñu ndax doon nañu topp yooni Yàlla yu jub yi. Ñoom itam dinañu dekki. Ndax li mu wóolu nasub Yeowa bi jëm ci loolu, ndaw li Pool nee na: “Bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki.”—Jëf ya 24:15.
18. (a) Ban gis-gis la ndaw li Yowanna jot jëm ci ndekkite li? (b) Lan lañuy sànk ca biir “déegu safara” sa, te lan la “déeg” boobu di misaal?
18 Ndaw li Yowanna jot na gis-gis bu dawloo yaram, gis-gisub ñii dekki, ñu taxaw ca kanamug jalub Yàlla. Gannaaw loolu, Yowanna bind na: “Géej gi delloo na ñi dee te nekkoon ci moom, te dee ak hades delloo nañu ñi dee te nekkoon ci ñoom te àtte nañu leen, kenn ku nekk ci ñoom, ci seeni jëf. Te sànni nañu dee ak hades ca déegu safara sa. Loolooy misaal ñaareelu dee gi, déegu safara si.” (Peeñu bi 20:12-14, NW) Xalaatal loolu rekk! Ñépp ñii dee te nekk ci xelum Yàlla am nañu yaakaar génne ci Hades (ci grekk: haides), walla Sheol, bàmmeel bi nit ñépp bokka jëm. (Sabuur 16:10; Jëf ya 2:31) Dinañu am jotug wone ci seeni jëf ndax bëgg nañoo jaamu Yàlla. Gannaaw loolu, “dee ak Hades” dinañu leen sànni ca biir li ñu tudde “déegu safara [si],” guy misaal sànk ba mu jeex, niki itam baat bi “Gehenna.” (Lukk 12:5, NW) Bàmmeel bi nit ñépp bokka jëm, ci boppam, dinañu ko yulli te dootul am bu ndekkite la matee. Akay dëfël, jànge ci Biibël bi ne Yàlla du bugal kenn!—Yérémi 7:30, 31.
NDEKKITE LA, NGIR DUND FAN?
19. Lu tax ñuy dekkal ñenn ci nit ñi ngir dund ca asamaan, te wan xeetu yaram la leen Yàllay jox?
19 Aw waññu góor aki jigéen wu ñu àppal lañuy dekkal ngir dund ga ca asamaan. Niki ay buur aki saraxekat yu ànd ak Yeesu, dinañu bokk ci nasaxal lépp li dee jur te nit ñi donne ko ca góor gu njëkk ga, Aadama. (Room 5:12; Peeñu bi 5:9, 10) Ñaata nit la Yàllay jël ca asamaan ngir ñu nguurook Krist? Ci Biibël bi, téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000) doŋŋ lañu. (Peeñu 7:4; 14:1) Yeowa dina jox ku nekk ci ñooñu ñu dekkal aw yaramu xel, ba tax dinañu mëna dund ca asamaan.—1 Korent 15:35, 38, 42-45; 1 Pieer 3:18.
20. Ñiiy déggal, ci lan lañuy jaar, boole ci ñiiy dekki?
20 Li ëpp ci ñi dee, dinañu leen dekkal ci kow suuf su nekk àjjana. (Sabuur 37:11, 29; Macë 6:10) Lenn ci li waral ñuy dekkal ñenn ñi ngir asamaan mooy mottali nasub Yàlla ngir suuf si. Ca asamaan, Yeesu Krist ak téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000) yi dinañu delloo ndànk-ndànk nit ñi déggal ca mataay ba suñuy maam ya jiitu jaleñoon. Loolu dina ëmb nit ñi dekki, na ko Yeesu wonee woon ba mu waxee góor ga doon sukkuraat te ñu daajoon ko ca wetam: “Dinga nekk ak man ca Àjjana.”—Lukk 23:42, 43, NW.
21. Ni ko yonent Isayi ak ndaw li Yowanna waxe, lan mooy dal dee?
21 Ci kow suuf su nekk Àjjana, dee giy jur tey naxasaxandaŋ yu ni mel, dinañ ko fi jële. (Room 8:19-21) Yonent Isayi xamal na ne Yeowa Yàlla “dina wann dee ba fàww.” (Isayi 25:8) Ndaw li Yowanna jot na gis-gisub jamano joo xam ne doomiy Aadama yiy déggal dinañu xam luy dund gu àndul ak naqar ak dee. Waaw, “Yàlla ci boppam dina ànd ak ñoom, nekk Yàlla seen Boroom. Dina fomp bépp rongooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla mettit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.”—Peeñu bi 21:1-4.
22. Xam-xamub ndekkite la, nan la lay laale?
22 Njàngale yu leer naññ yi nekk ci Biibël bi dañuy dàq jaxasoo bi am jëm ci liy dal ñi dee. Mbind yi, ci lu leer, dañuy wax ne dee mooy “noon bu mujj” bi ñuy sànk. (1 Korent 15:26) Aka ñuy dooleel tey dëfël, xam-xam bi ñuy jële ci yaakaaru ndekkite! Te aka ñoo mëna bég ci li suñuy soppe yi dee te nekk ci mpàttalikum Yàlla, di yéewoo ci dee ngir bànneexu ci yëf yu baax yi yépp Yàlla beral ñii ko bëgg! (Sabuur 145:16) Barke yu ni mel dinañu leen amal jaare ci Nguurug Yàlla. Waaye kañ la nguuram waroona tàmbali? Nañu ko seet.
SEETLUL SA XAM-XAM
Lan mooy xel ci doomi Aadama yi?
Nan nga mënee nettali nekkinub ñi dee?
Kan lañuy dekkal?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 85]
Na Yeesu génnee Lasaar ca bàmmeel ba, noonu ay tamndareeti doomi Aadama dinañu dekki
[Nataal bi nekk paas 86]
Mbég dina ne ñoyy bés ba ‘Yàllay wann dee ba fàww’