Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Li Yàlla def ngir musal nit ñi

Li Yàlla def ngir musal nit ñi

Pàcc 7

Li Yàlla def ngir musal nit ñi

1, 2. (a) Nan la njiitum soldaari Room mujjee ràññee ki Doomu Yàlla ju góor ji nekk? (b) Lu tax Yeowa bàyyi Yeesu dee?

 LU JEGE ñaari junniy (2000) at ca gannaaw, genn ngoon ci jamano cooroon, am njiitu soldaari Room a ngi doon wottu ñetti nit ñu doon dee ndànk-ndànk, nekk ci sukkuraat. Soldaar booba seetlu na ca bu baax kenn ci ñoom—Yeesu Krist. Yeesoo nga woon, ñu daaj ca bant. Cag njolloor, asamaan sa lëndëm na ndegam waxtu deeam a ngi doon dégmal. Ba mu deewee, suuf sa yëngu naak doole, te soldaar ba xaacu na, naan: “Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la[woon].”—Mark 15:39.

2 Doomu Yàlla ju góor! Soldaar boobaa nga woon ci dëgg. Mu nga sogoona seede xew-xew bi ëpp solo bi masa am ci kow suuf. Ca anam yu jiitu, Yàlla ci boppam woowe woon na Yeesu Doomam ju góor ji mu sopp. (Macë 3:17; 17:5) Lu tax Yeowa bàyyi woon Doomam ju góor dee? Ndaxte moo doon pexem Yàlla ngir musal nit ñi ci bàkkaar ak ci dee.

KU ÑU TÀNN NGIR NAS BU AMUL MOROOM

3. Lu tax mu nekkoon lu jaadu ñu tànn Doom ju góor ji Yàlla jur kott ngir nas bu amul moroom jëm ci nit ñi?

3 Ni ñu ko jàngee ba noppi ci téere bii, Yeesoo nga doon dund laata moo nekk nit ci kow suuf. Tudde nañu ko “Doom ju góor ji Yàlla jur kott, NW ” ndaxte Yeowa ci boppam a ko sàkk te jaarul ci keneen. Gannaaw loolu Yàlla jaar na ci Yeesu ngir nekkal yeneen yëf yépp. (Yowanna 3:18; Kolos 1:16) Yeesu daa bëggoon saxsax doomi Aadama yi. (Léebu 8:30, 31) Bettuñu Yeowa tànn Doomam ju góor ji mu jur kott ngir mu liggéeyal ko cib nas bu amul moroom, ba ñu dogalee àtteb dee ci kow doomi Aadama yi!

4, 5. Laata nëwu Yeesu ci kow suuf, lan la Biibël bi feeñaloon lu jëm ci Njureel gi nekk Almasi bi?

4 Ba Yàlla, ca biir toolu Eden, xamalee àtteem ci kow Aadama, Awaak Seytaane, wax na lu jëm cib Musalkat nikig “njureel.” Njureel googu doon na ñëw ngir deñloo fi metit yu réy yi Seytaane miy Ibliis indi, moom “jaan[u] cosaan ji.” Ci lu leer, Njureel ga ñu dige woon doon na nappaaje Seytaane ak ñépp ñii ko doon topp.—1 Musaa 3:15; 1 Yowanna 3:8; Peeñu bi 12:9.

5 Ca biir xarnu ya doon topplante, ndànk-ndànk Yàlla gën naa feeñal ay yégle yu jëm ci Njureel gi ñu tudde itam Almasi bi. Ni ko tablo bi nekk ci xët 37 wone, ay yégley xew-xew yu naroona ami, yu baree bare, nettali woon nañu benn-benn ay fànna yu bare ci dundam ci kow suuf. Maanaam, waroon naa muñ ay coxorte yu mettee metti ngir mottali taxawaayam ci nasub Yàlla.—Isayi 53:3-5.

LU TAX ALMASI BI WAROONA DEE

6. Ni ko Dañel 9:24-26 waxe, lan la Almasi bi naroona àggali, te naka?

6 Yégleb yonent bi nekk ci Dañel 9:24-26 dafa doon xamal, lu yàgg te fekk amagul, ne Almasi bi—Ki Yàlla tànn—doon na mottali ab nas bu mag. Naroon naa ñëw ci suuf si ngir “jeexal moy mi, te dindi bàkkaar, te muur àq, te indi njub” ba fàww. Almasi bi naroon naa teggi daanub dee ci kow nit ñi takku ci Yàlla. Waaye nan la ko naroona defe? Yégleb yonent baa ngi doon faramfàcce ne doon nañu ko “mejj,” walla rey.

7. Lu tax Yawut yi doon joxe saraxi mala, te sarax yooya ñoo doon takkandeeri lan?

7 Yawut yu njëkk ya miinoon nañu xalaatu muur njuumte. Ci seen njaamu, ca jamano Sàrt ba leen Yàlla joxoon jaare ca Musaa, daan nañu joxe ay saraxi mala. Sarax yooya dañu daan fàttali mbooloo Israël ne doomi Aadama yi soxla nañu lenn lu fey walla muur seeni bàkkaar. Ndaw li Pool tënk na rëddu-yoon woowu ci kàddu yii: “Bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du am.” ( Yawut yi 9:22) Karceen yi nekkuñu ci dogalu Sàrtub Musaa ak li muy laaj, niki ay sarax. (Room 10:4; Kolos 2:16, 17) Xam nañu it ne saraxi mala mënuñoo indi mbaalug bàkkaar bu mat tey sax. Asté loolu, sarax yooyu takkandeeru sarax su gëna am solo lañu woon—saraxu Almasi bi, walla Krist. (Yawut yi 10:4, 10; dendale kook Galasi 3:24.) Waaye, xëy na yaa ngiy laaj, ‘ndax ca dëgg dee waroon na Almasi bi?’

8, 9. Yan yëf yu jafe la Aadamaak Awa ñàkk, te nan la seeni jëf teese ci boppu seeni sët?

8 Axakay, Almasi bi waroon naa dee, su fekkee ne nit ñi waroon nañoo mucc. Ngir ñu nànd lu tax, fàww ñu fàttaliku toolu Eden te jéema jàpp ak suñu xel réyaayu li Aadamaak Awa ñàkk ba ñu jógalee Yàlla. Dund gu dul jeex lañu tegoon seen kanam! Niki doomi Yàlla, ñu nga doon xéewlu ca diggante yu rattax ya ñu amoon ak Yàlla, diggante yu kenn walla dara doxul. Waaye ba ñu wonee gannaaw kiliftéefu Yeowa, ñàkk nañu loolu lépp te indi nañu bàkkaar ak dee ci kow xeetu doomi Aadama.—Room 5:12.

9 Mu ngi mel ni suñuy maam dañoo pasar-pasaree woon alal ju baree bare, duggal seen bopp ci kàmb, ci bor bu réy-a-réy. Aadamaak Awa donnale nañu bor boobu seen njureel. Ndax judduwuñu mat te laab, kenn ku nekk ci ñun bàkkaarkat la te dafay dee. Bu ñu feebaree walla ñu wax lu ñaaw lu ñu bëgg wannaat, ñu ngiy daj bor bi ñu donn—matadi doomu Aadama, biy tees ci suñuy bopp. (Room 7:21-25) Yaakaar ji ñu am doŋŋ mooy jotaat li Aadama ñàkk. Wànte mënuñoo gañe dundug doomu Aadama gu mat. Ndegam doomi Aadama yépp, ndax matadi, dañuy bàkkaar, ñun ñépp dee lañu yelloo, du dund.—Room 6:23.

10. Lan lañu soxla woon ngir dellu jënd li Aadama ñàkk?

10 Wànte, ndax mënoon nañoo joxe dara, muy weccet ngir dund gi Aadama ñàkkoon? Yoonu Yàlla ci wàllu njub dafay laaj yemaay, “bakkan ngir bakkan.” (2 Musaa 21:23) Kon waroon nañoo saraxe ag dund ngir fey dund ga ñu ñàkkoon. Waaye dundug nit gu mu mënta doon doonul doy. Sabuur 49:7, 8 a ngiy wax lii ci doomi Aadama yu matadi yi: “Kenn ci ñoom mënula dellu jënd mbokkam ci benn fasoŋ bu mu mënta doon walla jox Yàlla peyug njot ngir moom; (te njëgu njotug seen bakkan daa jafe ba, sotti na ba diir bu amul àpp).” Kon fi mbir mi tollu, ndax yaakaar amatu ci? Xanaa déet, kay.

11. (a) Lan la baat “peyug njot” di tekki ci Ebrë? (b) Kan doŋŋ a mënoona jëndaat nit ñi, te lu tax?

11 Ci làkku ebrë, baat “peyug njot” a ngiy tekki xaalis bi ñu fey ngir jot nit ku ñu jàpp te mu ngiy tekki itam yemaay. Nit ku am bakkanu doomu Aadama bu mat doŋŋ a mënoon joxe lu em ak li Aadama ñàkk. Gannaaw Aadama, kenn nit doŋŋ ki matoon te juddu ci kow suuf, Yeesu Krist la woon. Noonu, Biibël bi tudde na Yeesu “Aadama mu mujj mi” te mu ngiy wóoral ne Krist “joxe na bakkanam [niki peyug njot gu em tembe, NW ] ngir (...) ñépp.” (1 Korent 15:45 ; 1 Timote 2:5, 6) Ndonol Yeesu mooy dund gu dul jeex, ba Aadama doon donnloo dee ay doomam. Bataaxal bu njëkk ba ñu bind waa Korent 15:22 a ngiy faramfàcce: “Kon ni ñépp deewee ci seen bokk ci Aadama, noonu la ñépp di dundaate ci seen bokk ci Krist.” Kon, jaadu na ñu tudde Yeesu “Baay bi sax ba abadan.”—Isayi 9:6, 7.

NA ÑU FEYE WOON PEYUG NJOT GI

12. Kañ la Yeesu mujja nekk Almasi bi, te gannaaw loolu, ban dundin la wéy di topp?

12 Ca jamano lolli atum 29 G.J.K.T., Yeesu fekki na mbokkam Yaxya ngir mu sóob ko te noonu, teew na ca kanamu Yàlla ngir def coobareem. Bés booba la Yeowa tànn Yeesu ak xel mu sell mi. Noonu la Yeesu mujjee nekk Almasi bi, walla Krist, ki Yàlla tànn. (Macë 3:16, 17) Noonu Yeesu sumb na liggéeyub ñetti at ak genn-wàll bi ñu ko sas. Wër na réewam mépp, di waare Nguurug Yàlla tey dajale ay taalibe yu takku. Wànte, na ñu ko yégle woon, yàggul dara, jànkoonte naak weddi bu doon gën di yokku.—Sabuur 118:22; Jëf ya 4:8-11.

13. Yan xew-xew ñoo agsi ca deewug Yeesu niki gor lëmm ci Yàlla?

13 Ak fit, Yeesu weejal na naaféqu kilifay diine yi, te ñoom wut nañu koo rey. Mujj nañoo karabaane mànkoo bu ñaaw-a-ñaaw bu ëmboon wor, njàpp mu moy yoon, làyyoo bu awul yoon ak sosalub nit kuy jógal kilifa. Dóor nañu Yeesu, tëfli ci kowam, ñaawal ko, te caw nañu ko, tandandiirloo kook kàcciri gu ñu defar ngir xotti yaram. Gannaaw loolu, jawriñu Room, Poons Pilàtt, dogal na ci kowam àtteb dee ci kow jënub mbugël. Daaj nañu ko, kon, cib jënub bant te nekk na fa di lang, ba ñu taxawalee bant ba. Noyyi bu nekk, gétën bu mettee metti la woon, te sukkuraat na noonu ay waxtu ba mujja dee. Ca biir mbugël moomu mépp, Yeesu sax na ci ngor lëmm, gu mat sëkk ci Yàlla.

14. Lu tax Yàlla bàyyi Doomam ju góor sonn te dee?

14 Noonu, ca fukki fan ak ñeent (14) ca wéeru Nisã atum 33 G.J.K.T., la Yeesu joxe bakkanam “niki peyug njot ngir weccee ñu bare.” (Mark 10:45, NW; 1 Timote 2:5, 6) Fa mu nekkoon ca asamaan, Yeowa mënoon naa gis coonook deewu Doomam ju góor ji mu sopp. Lu tax Yàlla seetaan lenn lu ni ñaawe noonu am? Def na loolu ndaxte daa bëgg doomi Aadama yi. Yeesu nee na: “Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am képp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.” (Yowanna 3:16) Deewug Yeesu dafa ñuy jàngal it ne Yeowa, Yàllay njub gu mat la. (5 Musaa 32:4) Xëy na am na ñuy laaj seen xel lu tax Yàlla xàcceewul ci wàllu njub ak rëddu-yoonam wiy laaj bakkan ngir bakkan, te waccul njëg giy fey dundinu bàkkaaru Aadama. Li ko waral mooy, Yeowa, fu mu tollu, dafay taq ciy sàrtam te dafa leen di taxawu, li mu koy jaral lu mettee metti ci moom ci boppam.

15. Ndegam bàyyi dundug Yeesu jeex ba fàww duloon nekk lu jub, lan la Yeowa def?

15 Njubug Yeowaa ngi doon laaj it deewug Yeesu àntu. Bu ñu ko seetee, ndax doon na jub ñu bàyyi Yeesu mi takku ci Yàlla nelaw cig dee ba fàww? Déedéet kay! Mbind yi ci làkku ebrë yégle woon nañu ne ku gore ki ci Yàlla duloon des cib bàmmeel. (Sabuur 16:10; Jëf ya 13:35) Nelaw na cig dee ay wàll ci ñetti fan, ba noppi Yeowa Yàlla dekkal ko ngir mu dund niki mbindaafonu xel mu am kàttan.—1 Pieer 3:18.

16. Lan la Yeesu def ba mu delloo asamaan?

16 Ba mu deewee, Yeesu tàggoo naak dundug nitam ba fàww. Ba ñu ko yëkkëtee ngir mu dund ca biir asamaan, mujj naa nekk xel muy joxe dund. Rax-ca-dolli, ba Yeesu yéegee ca béréb bi gëna sell ci mbindeef mépp, dajewaat naak Baayam bi mu sopp te jébbal na Ko, na mu ware te jekk, solo dundug nitam gu mat gi. (Yawut yi 9:23-28) Solo dund gu jafe googu, doon nañu ko mëna jariñloo kon doomi Aadama yi déggal Yàlla. Lan la loolu di tekki ngir yow?

PEYUG NJOTUG KRIST AK YOW

17. Nan lañu mënee am mbaal ci barke peyug njotug saraxu Krist?

17 Seetal ñetti fasoŋ, fu la peyug njotug Krist di jariñ tey saxsax. Benn bi, dafay indi mbaalug bàkkaar yi. Jaare ci ngëm ci deret ji Yeesu tuur, am nañu “mucc ci peyug njot gi, NW ”, waaw “baal [nañ] nu suñuy bàkkaar” (Efes 1:7). Ba tax su fekkee ne def nañu bàkkaar bu réy sax, mën nañoo ñaan Yàlla mu baal ñu ci turu Yeesu. Su ñu réccoo dëgg, Yeowa dafa ñuy jariñloo solo peyug njotug saraxu Doomam ju góor. Yàlla dafa ñuy baal, di ñu barkeel ak xol ak xel yu dal, asté mu ñuy laaj daanub dee gi ñu teesal ci suñuy bopp ndax suñuy bàkkaar.—Jëf ya 3:19; 1 Pieer 3:21.

18. Nan la ñu saraxu Yeesu di joxe yaakaar?

18 Ñaareel bi, peyug njotug saraxu Krist, ci la suñu yaakaar ci ëllëg sës. Cib gis-gis, ndaw li Yowanna gis na ne “mbooloo mu réy, ba kenn mënu koo waññ” doon na mucc ca tukkite jamano jii, buy ñëw ci biir musiba bu réy. Lu tax ñuy mucc bu Yàlla di sànk ñeneen ñu ni bare? Am malaaka wax na Yowanna ne mbooloo mu réy mi dañoo “fóot[oon](...) seeni mbubb, ba weexal [leen] ci deretu Mbote ma,” Yeesu Krist. (Peeñu bi 7:9, 14) Fi ak ñu ngiy teg suñu ngëm ci deret ji Yeesu Krist tuur te ñu ngiy dund dund gu dëppook li Yàllay laaj, dinañu set ci gëti Yàlla te dinañu am yaakaaru dund gu dul jeex.

19. Nan la saraxu Krist firndeele ne moom ak Baayam dañu laa bëgg?

19 Ñetteel bi, peyug njotug sarax si mooy firnde ju gëna mag ju mbëggeelug Yeowa. Deewug Krist feeñal na ñaari jëfi mbëggeel yi gëna mag ci cosaanu mbindeef mépp: (1) mbëggeelug Yàlla, ci li mu yónni Doomam ju góor mu dee ngir ñun; (2) mbëggeelug Yeesu, ci li mu jébbal boppam ak xol bu tàlli niki peyug njot. (Yowanna 15:13; Room 5:8) Kenn ku nekk ci ñun mën naa jële njariñ ci mbëggeel googu, su amee ngëm dëgg. Ndaw li Pool nee na: “Doomu Yàlla ju góor ji.(. . .) bëgg na ma te jébbal na boppam ngir man.”—Galasi 2:20, NW; Yawut yi 2:9; 1 Yowanna 4:9, 10.

20. Lu tax ñu war di teg suñu ngëm ci peyug njotug saraxu Yeesu?

20 Nañu wone boog suñug ngërëm ci mbëggeel gi ñu Yàlla ak Krist won, ci wéy di teg suñu ngëm ci peyug njotug saraxu Yeesu. Def lu ni mel dafay jëme ca dund ga dul jeex. (Yowanna 3:36) Ndaxam, suñu mucc du li ëpp solo ci li tax Yeesu dund te dee ci kow suuf. Déedéet, li ko gënoona itteel moo doon werante bu ëpp solo, bu laal mbindeef mépp. Ni ñu koy gise ci pàcc miy topp, werante booboo ngi ñuy soxal ñun ñépp ndaxte dafay wone lu tax Yàlla bàyyi coxorte geek metit yi yàgge nii ci àddina sii.

SEETLUL SA XAM-XAM

Lu tax Yeesu waroona dee ngir musal nit ñi?

Nan lañu feye woon peyug njot gi?

Ci yan fasoŋ ngay jariñoo peyug njot gi?

[laaj yi]

[Nataal bi nekk paas 67]