Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Li tax dundug nit ku taq ci Yàlla di indi bànneex

Li tax dundug nit ku taq ci Yàlla di indi bànneex

Pàcc 13

Li tax dundug nit ku taq ci Yàlla di indi bànneex

1. Lu tax ñu mëna wax ne yoonuw Yeowa bànneex lay yóbbe?

 YEOWA “Aji Mbégte la, NW ” te daa bëgg nga bànneexu ci dund. (1 Timote 1:11) Booy dox ci yoonam, mën ngaa jariñu te xam noflaay bu xóot tey yàgg, niki dex gu dul noppee wal. Di dox ci yoonu Yàlla it mooy tax nit wéy di def jëfiy njub, “mel ni ginnaxiy géej gi.” Loolooy indi bànneex dëgg.—Isayi 48:17, 18.

2. Nan la karceen yi mënee am bànneex, ak lu ñu leen sonnala sonnal léeg-léeg?

2 Am na ñu mëna werante, naan: ‘Léeg-léeg, nit ñi dañuy sonn ndax li ñuy def li jub.’ Dëgg la, te looloo daloon ndawiy Yeesu. Waaye ak lu ñu leen toŋala toŋal, dañoo bégoon te daawuñu noppee “xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.” (Jëf ya 5:40-42) Mën nañoo jànge njàngale yu am solo ci loolu. Menn mi mooy dundug nit ku taq ci Yàlla wóoralul ne dinañ ñu teral saa su nekk. Pool bind na: “Ku bokk ci Krist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.” (2 Timote 3:12) Li waral loolu mooy Seytaaneek àddinam dañoo jógal ñiiy dund ni ko Yàlla bëgge. (Yowanna 15:18, 19; 1 Pieer 5:8) Waaye bànneex dëgg ajuwul ci yëf yi ñu wër. Te du, mu ngiy jóge ci am kóolute gu am doole ne ñu ngiy jëf li jub, te looloo tax ñu neex Yàlla.—Macë 5:10-12; Saak 1:2, 3; 1 Pieer 4:13, 14.

3. Nan la njaamug Yeowa warkoona laale dundug nit?

3 Am na ay nit ñu foog ne war nañoo mëna am yiwu Yàlla bu ñuy jëf yenn saay ay jëf yuy wone seen taq ci Yàlla, waaye mën nañu di ko fàtte ci yeneen anam. Njaamug Yeowa Yàlla dëgg, du noonu. War naa laal deminub nit ki ci waxtu wu nekk, bés-oo-bés, at-oo-at. Looloo tax it ñu tudde ko “[Y]oon [W]i.” (Jëf ya 19:9; Isayi 30:21) Ab dundinub nit ku taq ci Yàlla la, buy laaj ci ñun ñuy wax tey jëf lu dëppook Kàddug Yàlla.

4. Lu tax def ay soppi ngir dund dundug nit ku taq ci Yàlla am njariñ?

4 Bu ay jàngkati Biibël bi, ñu bees, dee gis ne soxla nañoo def ay soppi ci seen dund ngir neex Yeowa, mën nañoo laaj seen xel: ‘Ndax di dund dundug nit ku taq ci Yàlla jar na ko dëgg?’ Na la wóor ne jar na ko. Lu tax? Ndaxte “Yàlla Aji Mbëggeel la,” ay yoonam kon, suñu njariñ lañu. (1 Yowanna 4:8) Yàlla ku am sago la it te xam na li gën ci ñun. Ndegam Yeowa Yàlla Aji Kàttan la, mën na ñoo jox doole àggali suñu bëgg-bëggu neex ko ci tàggook ab tàmmeel bu bon. (Filipp 4:13) Nañu seet léegi yenn rëddi-yoon yu bokk ci dund gu dëppook coobareg Yàlla te gis naka di leen jëfoo dee indi bànneex.

NGOR DAFAY YÓBBE BÀNNEEX

5. Lan la Biibël bi wax lu jëm ciy fen aka sàcc?

5 Yeowa “Yàllay dëgg” la. (Sabuur 31:5) Ci lu amul werante, bëgg nga koo roy te bëgg nga ñu xame la niki nitu dëgg. Ngor dafay yóbbe jom ak yëg-yëgu sutura. Waaye ndax li goreedi siiw lool ci biir àddina bàkkaar sii, karceen yi soxla nañu ñu fàttali leen lii: “Wax[leen] dëgg kenn ku nekk ci moroomam. (...) Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax (...) ngir mu mana dimbali ñi néew doole.” (Efes 4:25, 28) Karceen yiy liggéey dañuy def seen liggéeyub bés bu nekk, ànd ceek ngor gu mat. Lul seen njaatige ànd ci, duñu jël yëf yi mu moom. Muy ca béréb ba ñuy liggéeye, ca lekkool, walla ci biir këram, jaamukatu Yeowa daa wara ‘gore ci lépp.’ (Yawut ya 13:18, NW) Képp ku tàmma fen walla sàcc, mënula am yiwu Yàlla.—5 Musaa 5:19; Peeñu bi 21:8.

6. Nan la ngoru nit ku taq ci Yàlla mënkoona yóbbee ndam Yeowa?

6 Gore, barke yu bare lay yóbbe. Selina, ab jatur la bu nekk miskin te dëkk Afrig, ku bëgg Yeowa Yàllaaki rëddi-yoonam yu jub yi. Benn bés, mu for ab saag bu def ab chéquier (bankbook) ak xaalis bu baree bare. Ba mu seetee ci biir annuaire (telephone directory) la gis boroomam—ab jaaykat bu mag bu ñu sàccoon. Góor ga gëmewu ko woon ba ko Selina seetsee, ak lu mu feebaroona feebar dëgg, te delloo ko lépp li nekkoon ci saag bi. “Ngor gu ni mel war nañu koo yool,” la wax te teg na ca loxoom xaalis. Li gëna am solo, góor googu tagg na diine Selina. Waaw, jëf yu gore dañuy rafetal njàngaley Biibël bi, di màggal Yeowa Yàlla, tey indil bànneex jaamukat yu gore yi.—Titt 2:10 ; 1 Pieer 2:12.

YÉWÉN DAFAY INDI BÀNNEEX

7. Lan moo bon ci wure xaalis?

7 Ñii yéwén a ngi ci bànneex, ba nit ñi bëgge dul “bokk ci nguuru Yàlla.” (1 Korent 6:10) Aw xeetu bëgge wu siiw mooy wure xaalis, maanaam jéema am xaalis ci ñàkkiy ñeneen. Yeowa nanguwul ñii “alal jiital.” (1 Timote 3:8) Fa sax sàrtub réew nangoo wure xaalis te nit di fa wure xaalis ngir fo, loolu mën naa mujja jiital nit kooku te fal jëf ju toskareloo dund yu bare. Wure xaalis dafay yóbbe téq-téq ci biir njabootug wurekat bi, njaboot goo xam ne xëy na tuuti xaalis a koy dese ngir jënd yëf yi nit soxla niki lekk ak koddaay.—1 Timote 6:10.

8. Nan la Yeesu joxee royukaay bu rafet ci yéwén, te nan lañu mënee nekk ñu yéwén?

8 Ndax li ñu yéwén, ànd ceek mbëggeel, karceen yaa ngiy daj mbégte ci dimbali ñeneen, rawatina seeni nawle gëmkat yi nekk ay miskin. (Saak 2:15, 16) Laata Yeesu ñëw ci suuf, seetlu woon na yéwénub Yàlla ci mbooloom nit ñi. (Jëf ya 14:16, 17) Yeesu ci boppam jébbal na jotam, ay xereñam, ba dundam sax ngir doomiy Aadama. Kon, naka jekk, mënoon naa wax: “Joxe moo gëna barkeel nangu.” (Jëf ya 20 :35) Yeesu wax na it lu baax ca jatur bu néew doole, bu def ak yéwén ñaari poseti xànjar ca biir defukaayi alalu kërug Yàlla ga, ndax joxe na “lépp, toog.” (Mark 12:41-44) Waa Israel bu njëkk ak karceeni xarnu bu njëkk ba, nekk nañu ay royukaay ci yéwén bu ànd ak mbégte, ci li ñu jàpple ak seeni alal mbooloo meek liggéeyub Nguur gi. (1 Nettaliy xew-xewi cosaan 29:9; 2 Korent 9:11-14) Gannaaw def ay maye ci alal ngir nas yooyu, karceeniy suñu jamanoo ngiy am bànneex ciy tagg Yàlla tey jëfandikoo seen dund ci liggéeyam. (Room 12:1; Jëf ya 13:15) Yeowaa ngi leen di barkeel ndax li ñuy jëfandikoo seen jot, seen dooleek yeneen mën-mën, boole ci seen am-am ci xaalis, ngir jàpple njaamu dëgg gi te fal ci àddina sépp liggéeyub waare xabaar bu baax bi ci Nguur gi.—Léebu 3:9, 10.

YENEEN MBIR YUY FAL BÀNNEEX

9. Lan moo bon ci ëppal ci naan sàngara?

9 Ngir am bànneex, karceen yi war nañu it ‘di sàmm seen mën-mën yi jëm ci xalaat.’ (Léebu 5:1, 2) Looloo ngiy laaj ñuy duruus tey xalaat ba xeli Kàddu Yàllaak téere yu wér yiy waxtaane Biibël bi. Waaye am na yëf yu ñu wara moytu. Maanaam, naanug sàngara gu ëpp mën naa tax nit dootul ànd ak sagoom. Ci nekkin bu ni mel, nit ñu bare dugg nañu ci moy, ci jëfiy taafar, te sabab nañu ay aksidã yu faat bakkan. Bettuñu bu Biibël biy wax ne màndikat yi duñu donn Nguurug Yàlla! (1 Korent 6:10) Ndegam dañoo dogu ci sax ci “maandu ci xalaat,” karceen dëgg yaa ngiy moytu màndite, te looloo ngi leen di dimbali ñu fal bànneex ci seen biir.—Titt 2:2-6.

10. (a) Lu tax karceen yi duñu jëfandikoo póon? (b) Yan njariñ la dogook tàmmeel yuy jiital di amal?

10 Yaram wu set dafay dimbali ci am bànneex. Ndaxam, ñu bare mujj nañoo nekk jaamiy yëf yuy loraate. Nañu seet maanaam, jëfandikoo póon. Mbootaay bi tudd Organisation mondiale de la santé (World Health Organisation) a ngiy faramfàcce ne tóx “ñetti tamndareeti nit lay rey at mu nekk.” Tàggook tàmmeelub tóx mën naa nekk lu jafe ndax màndarga yiy wone ne yaram wi daa namm póon ab diir. Ci geneen wet, ñu bare ñu bàyyi tóx gis nañu ne am nañu wér-gi-yaram gu gën te gën nañoo am xaalis ngir faj seen aajoy njaboot. Ci dëgg, daan tàmmeelub tóx walla dog buumug njaamug yeneen yëf yuy lor dina dimbali ci am yaram wu set, xel ak xol yu dal, ak bànneex dëgg.—2 Korent 7:1.

BÀNNEEX CI BIIR SÉY

11. Lan lañu laaj ngir am séy bu aw yoon, buy siggil tey yàgg?

11 Ñii ànd di dund niki jëkkër ak jabar, warkoon na leena wóor ne bind nañu seen séy ci yoon ci teewaayu kilifay nguur gi. (Mark 12:17) Soxla nañu it jàppe séy niki warugar wu diis. Dëgg la, fay mënkoon naa mujja am ci lu war, bu nit teyee baña jàpple ki mu séyal, bu koy soxore lool, walla mu nekk mbàmb dëgg ngir yëf yi jëm digganteem ak Yàlla. (1 Timote 5:8; Galasi 5:19-21) Waaye, kàdduy ndaw li Pool yi nekk ci 1 Korent 7:10-17, a ngiy xiirtal ñaar ñi séy, ñu ànda des ci benn kër gi. Ngir nekk ci bànneex dëgg, jarul ñu koy wax, war nañoo takku, ku nekk ci moroomam. Pool bind na: “Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi baña taq sobe, ndaxte Yàlla dina àtte ñu yàqu ñi ak njaalookat yi.” (Yawut yi 13:4) Baat bi “lalu séy” a ngiy tekki tëdd diggante góor ak jigéen ñu séy ci yoon. Beneen tëdd bu dul boobu, niki séy ak lu ëpp jenn jabar, mënuñu koo nataal niki lu “ñépp fullaal.” Rax-ca-dolli, Biibël baa ngiy daan tëdd ak nit balaa séy, ak góor-jigéen.—Room 1:26, 27; 1 Korent 6:18.

12. Yan ay yenn ci meññeef yu bon yiy bawoo ci moy?

12 Moy mën naa indi bànneexu yaram ay saa yu gàtt, waaye du yóbbe bànneex dëgg. Neexul Yàlla te mën naa ñaas xel ak xolu nit. (1 Tesalonikk 4:3-5) Li jëfandikoo awra ci lu awul yoon di yóbbe, muy lu naqarlu, mën naa nekk SIDA (AIDS ) ak yeneen feebar yu ñuy jote ci awra. Ab nettali ci wàllum paj nee na: “Xayma nañu ne lu ëpp ñaar téeméeri tamndareeti nit ak juróom-fukk ci àddina si, dañuy am congum doomu jàngoro sopiis at mu nekk, te lu tollook juróom-fukki (50) tamndareeti nit, congum doomu jàngoro siti.” Am na it jafe-jafe ñiiy biir te bëgguñu ko. The International Planned Parenthood Federation (benn mbootaay buy toppatoo mbirum njaboot ak njuddu ci àddina si) a ngiy nettali ne, ci àddina si sépp, lu ëpp fukki tamndareeti xale yu jigéen ak juróom, yu am fukki at ak juróom (15) ba fukki at ak juróom-ñeent (19) dañuy biir at mu nekk, te ñetteelu wàll wi ci ñoom dañuy yàq seen biir. Ci menn réewum Afrig, ab gëstu wone na ne, boo jële téeméeri xale yu jigéen yu amagul ñaar fukki at te ñàkk seen bakkan, juróom-ñaar fukk ak ñaar ña (72), jafe-jafey yàq biir a ko waral. Yenn moykat yi mën nañoo rëcc ci feebar ak ci biir, waaye duñu rëcc ci yàqu bi ñuy yëg ci seen xol. Ñu baree ngiy ñàkk seen jom te dañuy dem sax bay sib seen bopp.

13. Yan ay yeneen jafe-jafe yu njaaloo sabab, te lan mooy xaar ñiy wéy ci moy ak njaaloo?

13 Ak lu ñu mëna mëna baal njaaloo, nekk na luy tax ki séy te ñu tooñ ko, sës ci Mbind yi pase. (Macë 5:32; dendale kook Xoseyaa 3:1-5.) Bu séy tasee ndax moy, loolu mën naa bàyyi ay ñaas yu metti ci xolu ki ñu tooñ ak xolu xale yi. Ngir li baax ci njabootug doomu Aadama, Kàddug Yàllaa ngiy wone ne àtteem dina ñëw ci kow moykat yeek njaalookat yi dul réccu. Ci geneen wet, dafay leeral ne ñiiy jëfoo moy “duñu am cér ci nguuru Yàlla.”—Galasi 5:19, 21.

“BOKKUÑU CI ÀDDINA”

14. (a) Yan ay yenn fasoŋi bokkaale yu nit ku taq ci Yàlla wara moytu? (b) Ban tette lañu joxe ci Yowanna 17:14 ak Isayi 2:4?

14 Ñii bëgga neex Yeowa te bëgga xéewlu ci barkey Nguur gi dañuy moytu xeeti bokkaale bu mu mënta doon. Biibël baa ngiy wone ne di def tey jaamu nataal, boole ci yosi Krist, walla yosi ndeyu Yeesu, Maryaama, lu bon la. (2 Musaa 20:4, 5; 1 Yowanna 5:21) Kon karceen dëgg yi duñu teral ay nataal, kurwaa, aki xérém. Dañuy moytu it xeeti jaamu xérém yu gëna xereñ, niki ay jëfiy taq ci raya aki woy yuy sargal ay xeet. Bu ñu leen di jañ ci def ay jëf yu ni mel, dañuy fàttaliku baat yi Yeesu jëmale ci Seytaane: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.” (Macë 4:8-10) Yeesu wax na ne ay toppkatam “bokkuñu ci àddina.” (Yowanna 17:14, NW) Looloo ngiy tekki baña faral kenn ci mbiri politig tey dund ci jàmm, ànd ak Isayi 2:4, mi wax: “Dina [Yeowa Yàlla] dogal àtte ci biir xeet yi te jubbanti yëf yi jëm ci mbooloo yu bare. Te dinañu wara tëgg seeni jaasi ñu nekk ay illeer te seeni xeej lu ñuy gore car. Xeet du yëkkati jaasi dal ci kow xeet, te dootuñu jànga xeex.”

15. Lan mooy Babilon mu mag mi, te lan la jàngkati Biibël bi, yu bees yu bare di def ngir génne ci biiram?

15 “Bokkuñu ci àddinaa” ngiy tekki it dogook “Babilon mu mag mi,” nguurug mbooloom diiney fen yi ci àddina si. Njaamu gu sellul gaa ngi lawe Babilon mu njëkk ma, ba mu nootee ci kiliftéefam guy lor ci wàllu ngëm nit ñi ci kow suuf sépp. “Babilon mu mag” maa ngiy ëmb diine yépp, yu seeni njàngaleek seeni jëf dëppoowul ak xam-xamub Yàlla. (Peeñu bi 17:1, 5, 15) Benn jaamukatu Yeowa bu takku du dugg ci ay yëngu-yëngu yu ngëm yu bare séq, ci li muy ànd di jaamook diine yu wuuteek bosam walla di fas kóllëreek ci wàllu ngëm ak lépp lu mënta bokk ci Babilon mu mag mi. (4 Musaa 25:1-9; 2 Korent 6:14) Looloo tax, jàngkati Biibël bi, yu bare, yu bees, yónnee nañu ab bataaxalub dëddu tariixa bi ñu bokkoon. Loolu gën na leena jegeloo Yàlla dëgg ji, ni ñu ko dige: “Génnleen biir ñooñu te beru [la Yeowa wax]. Buleen laal dara lu am sobe, kon dinaa leen teeru.” (2 Korent 6:17; Peeñu bi 18:4, 5) Ndax du nangu bu ni mel bu jóge ca Baay ba ca asamaan nga bëgg saxsax?

DI SEETLU MÀGGAL YI CI AT MI

16. Lu tax karceen dëgg yi duñu màggal Noel?

16 Dundug nit ku taq ci Yàlla dafa ñuy yewwi ci màggal xewiy àddina si, màggal yuy farala diis. Maanaam, Biibël bi feeñalul bésub njuddu Yeesu saxsax. Am na ñu mëna wax ne: “Foogoon naa ne Yeesoo ngi juddu ci ñaari-fukki fan ak juróom ca weeru Desàmbar!’ Loolu mënula nekk ndax ca cooroon, atum 33 G.J.K.T. la dee, ba mu amee fanweeri at ak ñett ak gennwàll (33 1/2). Rax-ca-dolli, ca waxtu njuddoom, sàmmkat ya nga “daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.” (Lukk 2:8) Ca réewum Israel, bu weeru Desàmbar bëggee dee, jamano sedd ak taw la, jamano joo xam ne dañuy fat xar yi guddi ngir aar leen ci liw bu metti bi. Li am mooy, ñaar-fukkeelu fan ak juróom ca weeru Desàmbar, waa Room dañu ko beroon niki bésub njuddu seen yàlla, jant bi. Ay xarnu gannaaw ba Yeesu nekkee ci kow suuf, karceen ya jàmbu dëgg gi, nangu nañu bés booba ngir màggal bésub njuddu Krist. Looloo tax, karceen dëgg yi duñu màggal Noel walla meneen xew mu mu mënta doon mu sës ci ngëmi diiney fen yi. Ndax li ñuy taq ci Yeowa taq bu àndul ak bokkaale, duñu topp xew yuy sargal ay nit ñuy bàkkaar walla ay xeet.

17. Lu tax nit ñi taq ci Yàlla duñu màggal bésiy njuddu, te lu tax, ba tey, doomi karceen yi am bànneex?

17 Biibël bi, ñaari bési njuddu yu ñu màggal doŋŋ lay waxtaane, ñoom ñaar jëm ci góor ñu daawul jaamu Yàlla. (1 Musaa 40:20-22; Macë 14:6-11) Ndegam Mbind yi feeñaluñu bésub njuddu góor gu mat, Yeesu Krist, lu tax ñu warkoona bàyyi xel bu baax ci bésiy njuddu nit ñu matadi? (Dajelakat 7:1) Jarul ñu koy wax, ay way-jur ñu taq ci Yàlla duñu xaar bés sàngam ngir won mbëggeel seeni doom. Benn xale bu jigéenu karceen, bu am fukki at ak ñett, seetlu na: “Suñu waa-kër ak man am nañu joti fo yu bare. (...) Taq naa lool ci samay way-jur, te bu ma yeneen xale dee laaj lu tax duma màggal xew yi, dama leen di wax ne bés bu nekk, xew la ci man.” Ab waxambaane bu am fukki at ak juróom-ñaar nee na: “Ci suñu kër, dañuy def ay maye ci biir at mi mépp.” Maye yu ñuy def te kenn laajuñu ko, bànneex bu gëna mag lay yóbbe.

18. Ban xew kott ci at mi la Yeesu santaane ay toppkatam ñu màggal, te lan la ñuy fàttali?

18 Ngir ñiiy wéy ci dundug nit ku taq ci Yàlla, am na benn bés, at mu nekk, bu ñu wara màggal. Mooy Reerub Sang bi, ñu faral di ko woowe Fàttalikub deewug Krist. Lu ci jëm, Yeesu digal na ay toppkatam: “Defleen lii, ngir fàttaliku ma.” (Lukk 22:19, 20; 1 Korent 11:23-25) Ba Yeesu taxawalee reer booba, ca guddi 14 Nisan atum 33 G.J.K.T., jëfandikoo na mburu mu amul laawir ak biiñ bu xonq, yu doon misaal yaramam wu amul bàkkaar ak deretam ju mat. (Macë 26:26-29) Karceen yi ñu tànn ak xelum Yàlla mu sell ñooy ñiiy jël ci misaal yooyu. Dañu leena duggal ci kóllëre gu bees gi ak kóllëre ngir Nguur gi, te yaakaaru dund ca asamaan lañu am. (Lukk 12:32; 22:20, 28-30; Room 8:16, 17; Peeñu bi 14:1-5) Waaye ñépp ñiiy teewe guddi googu dëppook 14 Nisan ci calendrier (calendar) Yawut bu njëkk baa ciy jële njariñ. Dañu leen di fàttali mbëggeel gi Yeowa Yàllaak Yeesu Krist wone ci peyug njotug sarax siy muur bàkkaar, tey tax dund gu dul jeex mëna am ngir ñiiy am yiwu Yàlla.—Macë 20:28; Yowanna 3:16.

LIGGÉEY AK PO

19. Yan jafe-jafe la karceen yiy jànkoonteel bu ñuy daan seen doole ngir jariñu?

19 Karceen dëgg yaa ngi ci warugaru daan seen doole te faj seeni aajo. Di def looloo dafay tax boroom kër yi yëg mbégte ci seen biir xol. (1 Tesalonikk 4:11, 12) Jarul ñu koy wax, su liggéeyub karceen safaanook Biibël bi, loolu dina ko xañ bànneex. Ndaxam, léeg-léeg mu jafe cib karceen, am liggéey bu dëppook yooniy Biibël bi. Maanaam, am na ay surga yu ñuy laaj ñu nax kiliyaan yi. Ci geneen wet, ay njaatige yu bare dinañuy maslaa tey weg xol ak xelu liggéeykat bu gore, ngir baña ñàkk liggéeykat bu wóor. Waaye, ak lu mu mënta doon, na la wóor ne Yàlla dina barkeel say njéem ngir am liggéey bu lay sàmmloo xol ak xel yu laab.—2 Korent 4:2.

20. Lu tax ñu war di tànn bu baax suñuy po?

20 Ndegam Yàlla daa bëgg ay jaamam bég, soxla nañoo yemale liggéey bu metteek waxtuy féexal seen xol ak noflaay. ( Mark 6:31; Dajalekat 3:12, 13) Àddina Seytaanee ngiy fal po yu teddadi. Waaye, ngir neex Yàlla, war nañooy tànn bu baax téere yi ñuy duruus, porogaraami rajook misig yi ñuy déglu, mband yi, film yi, tiyaatar yi, porogaraami tele yeek widéo yi ñuy seetaan. Su po yi ñu daan tànn bu njëkk safaanook artu yi nekk ci mbind yu mel niki 5 Musaa 18:10-12, Sabuur 11:5, ak Efes 5:3-5, dinañu neex Yeowa te dinañu gëna am bànneex su ñu defee ay jubbanti.

FONK DUND AK DERET

21. Nan la fonk dund warkoona laale suñu gis-gis ci yàq biir, niki it suñuy tàmmeel ak suñu demin?

21 Ngir am bànneex dëgg, soxla nañoo jàppe dundug nit niki lu tedd, niki Yeowa. Kàddoom tere na ñu ñuy bóom it. (Macë 19:16-18) Li am sax mooy, Sàrt bi Yàlla joxoon Israel dafay wone ne Yàllaa ngiy jàppe doom ju juddoogul niki ag dund gu am solo—du lu ñu wara sànk. (2 Musaa 21:22, 23) Ndax loolu, waruñoo jàppe dund ni lu amul solo ciy jëfandikoo póon, ciy lor suñu yaram ak dóróg walla sàngara, walla ciy fowe suñu dund. Warkoonuñu dugg it ci benn yëngu-yëngu buy jur mbàmb ngir dund, walla ñu sofental matuwaay yuy aar, lu mënkoona yóbbe boru deret.—5 Musaa 22:8.

22. (a) Lan ay gis-gisub nit ku taq ci Yàlla ci deret ak ci niñ koy jëfandikoo? (b) Deretu kan doŋŋ ay musal ci dëgg?

22 Yeowa waxoon na Nóoxin ak njabootam, deret mooy misaal bakkan walla dund. Looloo tax, Yàlla tere leen ñu lekk deret ju mu mënta doon. (1 Musaa 9:3, 4) Ndegam seeni sët lañu, sàrt boobu, kenn ku nekk ci ñun la war. Yeowa waxoon na waa Israel ne deret, dañu ko waroona tuur ci suuf, te waruñu ko woona jëfandikoo ngir nasiy nit ci boppam. (5 Musaa 12:15, 16) Te sàrtub Yàlla ci deret, baamtuwaatoon nañu ko ba ñu tegtalee karceeni xarnu bu njëkk ba lii: “Moytuleen (. . .) deret.” (Jëf ya 15:28, 29, NW) Ndax fonk sellaayub dund, nit ñi taq ci Yàlla duñu nangu ñu sol leen deret, su fekkee ne sax ñeneen a ngiy wax, dëgër ci, ne doxalinu paj moomu doon na musal seen bakkan. Ay fasoŋi paj yu bare yu mëna wuutu sol deret, te Seedey Yeowa di ko nangu, mujj nañoo fés nikiy paj yu wér te duñu yóbbe ci lenn ci mbàmb yi nekk ci sol deret. Karceen yi xam nañu ne deret ji Yeesu tur doŋŋ a mëna musal bakkan ci dëgg. Am ngëm ci deret joojoo mëna indi njéggal ak yaakaaru dund ba fàww.—Efes 1:7.

23. Yan ñooy yenn ci yooli dundug nit ku taq ci Yàlla?

23 Ci lu leer, dundug nit ku taq ci Yàlla góor-góorlu la laaj. Mën naa yóbbe ay ñaawal yu jóge ci suñuy mbokk walla suñuy xamante. (Macë 10:32-39; 1 Pieer 4:4) Waaye yool yi ñuy jële ci dundin boobu weesu nañu lu sore bépp coono bu mu mënta doon. Dundin boobu dafay yóbbe xol ak xel yu laab tey amal àndandoo yu baax ak suñuy moroomi jaamukati Yeowa. (Macë 19:27, 29) Rax-ci-dolli it, jortul ngay dund ba fàww ci biir àddina su jub te bees. (Isayi 65:17, 18) Akay mbégte it, topp xelalub Biibël bi tey bégloo noonu xolu Yeowa! ( Léebu 27:11) Kon bettuñu dundug nit ku taq ci Yàlla di yóbbe bànneex!—Sabuur 128:1, 2.

SEETLUL SA XAM-XAM

Lu tax dundug nit ku taq ci Yàlla di yóbbe bànneex?

Dundug nit ku taq ci Yàlla, yan soppi la laaj?

Lu tax nga bëgga dund dundug nit ku taq ci Yàlla?

[Laaj yi]

[Nataal bi nekk paas 124, 125]

Ay yëngu-yëngu ci wàllu ngëm yu ñu yemaleek jamanoy noflaay dañuy yokk bànneexu ñiiy dund dundug nit ku taq ci Yàlla