Lu tax ñuy màgget tey dee?
Pàcc 6
Lu tax ñuy màgget tey dee?
1. Lan la boroom xam-xam yi ci wàllu science mënula faramfàcce jëm ci dundu doomi Aadama?
BOROOM xam-xam yi ci wàllu science xamuñu lu tax nit ñiy màgget tey dee. Dafa mel ni cellules (cells) * yu suñuy yaram dañoo warkoon di tóllantiku saa su nekk te ñun, dañu warkoon di dund ba fàww. Téere bi tudd Hyojun Soshikigaku (téereb histologie [histology] *) nee na: “Lëkkale bi am diggante màggetaayu cellules (cells) yi ak màggetaayu nit keek deeam, nekk na kumpa ju réy.” Boroom xam-xam ci wàllu science yu baree ngiy foog ne dafa am àpp “bu bokk te taq” ci dund. Ndax foog nga ne ñu ngi ci dëgg?
2. Lan la ñenn nit def ndax li dund gaawa raaf?
2 Nit ñi, ba àddina sosoo ba tey, dañu xintee dund lu yàgg te jéem nañu sax jot ci dund gu mënula jeex. Li dale ca ñeenteelu xarnu ba L.J.K.T., kàngami réewum Chine (China) aajo woon nañu ay garab yu ñu waajaloon ngir fexee amal dund gu mënula jeex ci ni ñu ko fooge woon. Ñenn ca buur fari yu mujj ya ca réewum Chine (China) jéem nañu li ñu tudde woon ay al-iksiri dund—yu ñu defare woon mercure (mercury)—te dee nañ ca! Fu nekk ci àddina si, nit ñaa ngi gëm ne du ci dee la seen dund di yem. Budist yi, Indu yi, Jullit yi, ak ñeneen, dañoo am ñoom ñépp yaakaar ju fees ak bànneex ci dund gannaaw dee. Ci biir réewi ñiiy wuyoo turu Karceen, ñu baree ngiy séenu dundug asamaan gu texe gannaaw dee.
3. (a) Lu tax doomi Aadama yiy xinte dund gu dul jeex? (b) Yan laaj yu jëm cig dee soxla i tont?
3 Xalaat yooyu jëm ci bànneex gannaaw dee ngiy awu ne nit ñaa ngiy xintee dund ba fàww. Lu jëm ci xalaatu abadan bi Yàlla samp ci ñun, Biibël baa ngiy wax: “Jamano yu amul àpp sax, moom def na leen ci seen biir xol.” (Dajalekat 3:11) Sàkk na nit ñu njëkk ña ngir ñu mëna dund ba fàww ci kow suuf. (1 Musaa 2:16, 17) Lu tax, kon, nit ñiy dee? Nan la dee dugge ci àddina? Xam-xam bi Yàllay joxee ngiy leeral laaj yooyu.—Sabuur 119:105.
AB MÀNKOO BU ÑAAW
4. Nan la Yeesu feeñale saay-saay bi tax doomi Aadama yiy dee?
4 Saay-saay dafay jéema rawale joxoñ yi koy jiiñ. Mooy li ki sabab ñawtéef bi yóbbe dee ay junniy tamndareeti nit def. Muusantu naak yëf yi ngir muur deewu doomu Aadama, mu nekk kumpa ci nit ñi. Yeesu Krist feeñal na saay-saay boobu ba mu waxee ñii ko doon wuta rey: “Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la masa doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom.”—Yowanna 8:31, 40, 44.
5. (a) Lan mooy cosaanu ki mujja nekk Seytaane miy Ibliis? (b) Baat yi: “Seytaane” ak “Ibliis” lan lañuy tekki?
5 Waaw, Ibliis “bóomkat” bu soxor la te dafa ci sax. Biibël bi feeñal na ne nit dëgg la, du rekk lu bon li nekk ci biir xolu nit. (Macë 4:1-11) Lu ñu ko sàkkoona sàkk mu nekk am malaaka mu jub, “taxaw[ul] ci dëgg”. Aka jekk ci tur wi ñu ko jagleel maanaam Seytaane miy Ibliis! (Peeñu bi 12:9) Tudde nañu ko “Seytaane,” walla “kuy tiiñ” ndaxte dafa jógaloon te të Yeowa. Tudde nañu it saay-saay boobu “Ibliis,” miy tekki “sosalkat,” ndax dafa saaga woon Yàlla ci li mu yàqoon turam.
6. Lu tax Seytaane jógal Yàlla?
6 Lan moo xiir Seytaane ci jógal Yàlla? Bëgge. Dafa xemmemoon, ndax bëgge, njaamu gi Yeowa doon jote ca doomi Aadama ya. Ibliis dàqul bëgg-bëggu jot njaamu googu Sàkkkat si moom ciw yoon, moom doŋŋ. (Dendale kook Esekiel 28:12-19.) Asté loolu, malaaka mi mujja nekk Seytaane, daa bey ci xolam bëgg-bëgg bu bëgge boobu ba mu mujja nangu te meññ bàkkaar.—Saak 1:14, 15.
7. (a) Lan mooy sabab deewu doomu Aadama? (b) Lan mooy bàkkaar?
7 Feeñal nañu ki tooñ, ki ñaawtéefam yóbbe dee doomi Aadama yi. Waaye lu tax saxsax doomi Aadama yiy dee? Biibël baa ngiy wax: “Daŋaru dee mooy bàkkaar.” (1 Korent 15:56) Te lan mooy bàkkaar? Ngir nànd baat boobu, nañu seet tekkiteem ci làkk yi jiitu, yi ñu binde Biibël bi. Njëfka ebrë ak grekk yi ñu farala firi “bàkkaar” a ngiy tekki “moy”, maanaam moy ab njum walla bañ koo jot. Ban njum lañuy moy, ñun ñépp? Njumu déggal Yàlla déggal bu mat sëkk. Waaye, nan la bàkkaar dugge ci biir àddina?
NI ÑU MOTTALEE MÀNKOO BI
8. Nan la Seytaane jéeme woona jot njaamu doomi Aadama yi?
8 Seytaane fexe woon na bu baax-a-baax ab mànkoo, bu ko naroona yóbbu, ci xalaatam, mu ilif doomi Aadama yépp te jot seen njaamu. Fasoon na yéene xiir ñaar ñi njëkka séy, Aadamaak Awa, ñu tooñ Yàlla. Yeowa joxoon na suñuy maam yu njëkk ya xam-xam bi leen naroona jëme ca dund ga dul jeex ga. Xamoon nañu ne seen Sàkkkat ku baax la, ndax dëkkloo na leen woon ca toolu Eden bu rafet ba. Aadama gënoon naa yëg mbaaxaayub Baayam ba ca asamaan, ba ko Yàlla mayee jabar ju rafet ngir ndimbal. (1 Musaa 1:26, 29; 2:7-9, 18-23) Wéy di dund ngir ñaari nit ñu njëkk ñaa ngi aju woon ci déggal Yàlla.
9. Ban ndigal la Yàlla jox nit ku njëkk ka, te lu tax nekkuloon lu diis?
9 Yàlla joxoon na Aadama ndigal lii: “Ci garab gu nekk gu tool bi mën ngaa lekk ba doyal. Waaye lu jëm ci garabu xam-xamub lu baax ak lu bon waruloo cee lekk, ndax bés bi nga ciy lekk, dinga dee ci lu wóor.” (1 Musaa 2:16, 17) Ndegam mooy Sàkkkat si, Yeowa Yàlla amoon na sañ-sañub taxawal, ci wàllu demin, ay yoon te dogal li baax akit li bon ngir ay mbindaafonam. Ndigalam diisuloon ndaxte Aadamaak Awa mënoon nañoo lekk ci doomi yeneen garab yépp yi nekk ci tool bi. Doon nañu mëna wone ne fonkoon nañu kiliftéefu Yeowa gu jub gi, bu ñu toppoon sàrt boobu asté ñoo sàkk seen yooni bopp ci wàllu demin ndax yëg seen bopp.
10. (a) Nan la Seytaane jegee nit ñu njëkk ña ngir xëcc leen ci làngam? (b) Lan la Seytaane jortuloo ci li tax Yeowa joxe ndigal loolu? (c) Lan nga xalaat ci song bi Seytaane song Yàlla?
10 Ibliis dafa nasoona dëddale nit ñu njëkk ñeek Yàlla. Ngir meeb leen, indi leen ci làngam, Seytaane dafa fen. Ba mu jëfandikoo jaan, niki reelookat buy waxeek biiram dee jëfandikoo xuus-maa-ñapp, Ibliis dafa laaj Awa: “Ndax dëgg la ne, Yàlla daa wax ne waruleena lekk ci gépp garab gu nekk ci tool bi?” Ba Awa baamtoo ndigalul Yàlla, Seytaane wax na ko: “Dungeen dee fenn.” Mu daldi ko ñaawloo njort ci li tax Yeowa jox leen ndigal loolu naan: “Yàlla xam na ne ca bés ba saxsax ngeen di ci lekk, ci lu wóor seeni gët dinañu ubbeeku, te ci lu wóor dingeen mel ni Yàlla, di xam lu baax ak lu bon.” (1 Musaa 3:1-5) Noonu, Ibliis a ngi doon déggloo ne Yàllaa ngi leen doon xañ lu baax. Ndaw song ci sosal, bu ñu song Baay ba ca asamaan, Yeowa, moom mi gore te bëgg ñu!
11. Nan la Aadamaak Awa mujjee bokk nopp ak Seytaane?
11 Awa xoolaat na garab ga, te léegi doomam jaa nga ko doon niru, ca dëgg-dëgg, lu mata bëgg saxsax. Noonu mu daldi jël doom ja te lekk ko. Gannaaw loolu, jëkkëram tey naa ànd ak moom ci jëfu bàkkaar jooja, maanaam déggadil Yàlla. (1 Musaa 3:6) Lu ñu naxa nax Awa, ñoom ñaar ñépp, moom ak Aadama jàpple nañu nasub Seytaane bi doon: ilif xeetu doomi Aadama yi. Noonu, mujj nañoo nekk ay bokk noppam.—Room 6:16; 1 Timote 2:14.
12. Jógal bi doomi Aadama yi jógal Yàlla lan la jur?
12 Aadamaak Awa waroon nañoo jàkkaarlook li seeni jëf jur. Mujjuñoo mel ni Yàlla, ak xam-xam bu wuuteek ba ñu amoon. Asté loolu, dañoo am gàcce te nëbbu nañu. Yeowa faramfàccelu na Aadama te dogal na àtte bii: “Ci sa ñàqu xar-kanam ngay lekke mburu ba kera ngay dellu ci suuf si, ndax ci moom lañu la jële. Ndaxte pënd nga te ci pënd ngay dellu.” (1 Musaa 3:19) “Bés ba” suñu maam ya lekkee ca garabu xam-xamub lu baax ak lu bon, bés booba saxsax la Yàlla dogal àtte seen kow te lañu dee ca kanamam. Mujj nañu leen dàqe ca Àjjana te tàmbali nañoo gali, jëm ci deewu yaram.
NI BÀKKAAR AK DEE LAWE
13. Nan la bàkkaar lawe ci doomi Aadama yépp?
13 Seytaane niru woon na ku texe ci nasam bi doon: jot njaamu doomi Aadama yi. Ndaxam, mënuloona fexe ay jaamukatam wéy di dund. Ba bàkkaar tàmbalee def liggéeyam ca ñaari nit ña njëkka séy, mënatuñu woon jottali mataay seen njureel. Niki rëdd wu ñu ficc ciw doj, noonu la bàkkaar ficcu woon ci deretu suñuy maam yu njëkk ya. Looloo tax, njureel gu matadi doŋŋ lañu mënoona am. Ndegam Aadamaak Awa dañoo ëmboon seeni doom gannaaw ba ñu bàkkaaree, seeni njureel donn nañu bàkkaar ak dee.—Sabuur 51:5; Room 5:12.
14. (a) Kan lañu mëna emaleel ñiy weddi seeni bàkkaar? (b) Nan lañu fexee woon ba waa Israel mujja yeewu ci seen nekkeefu bàkkaarkat?
14 Waaye tey, ñu bare fooguñu ne ay bàkkaarkat lañu. Ci yenn diiwaan ci àddina si, xalaatu judduwaaleek bàkkaar, daanaka lu ñu xamul la. Waaye loolu firndeelul ne bàkkaar amul. Xale bu góor bu xar-kanamam tilim mën naa wax ne moom set na, te mën nañu koo gulami gannaaw mu seetu doŋŋ. Waa Israel, bu njëkk, dañu niru woon ak xale bu góor bu ni mel, ba ñu jotee Sàrtub Yàlla jaare ci yonentam Musaa. Sàrt ba dafa doon wone ci lu leer ne bàkkaar lu am la. “Ca dëgg, duma duloon mujja xam lan mooy bàkkaar su Sàrt bi amuloon,” la ndaw li Pool faramfàcce. (Room 7:7-12, NW ) Niki xale bu góor biy seetu, waa Israel mënoon nañoo gis ne laabuñu woon ci gëtiy Yeowa, ba ñu doon seetu ca biir Sàrt ba.
15. Lan mooy feeñ bu ñuy seetu ci Kàddug Yàlla?
15 Bu ñuy xool ci biir seetub Kàddug Yàlla tey ràññee ay yoonam, mën nañoo gis ne dañoo matadi. (Saak 1:23-25) Maanaam, nañu seet li Yeesu Krist wax ay taalibeem, jëm ci bëgg Yàllaak sa moroom ci Macë 22:37-40. Aka la nit ñiy faral di moy seen njum ci fànna yooyule! Ñu bare duñu yëg seen xol pat-pati, bu ñuy ñàkka wone mbëggeel ci Yàlla walla ci seeni moroom.—Lukk 10:29-37.
MOYTUL NAXIY SEYTAANE!
16. Lan lañu mëna def ngir moytoo daanu ci naxiy Seytaane, te lu tax loolu jafe?
16 Seytaane dafa ñuy wuta teyloo dund ci bàkkaar. (1 Yowanna 3:8) Ndax am nañu yoon ngir moytoo daanu ci ay naxam? Waaw, waaye loolu li mu laaj mooy ñuy xeex ak suñuy xiirte ci tey bàkkaar. Du lu yomb ndaxte dañoo judduwaaleek xiirte ci bàkkaar bu am doole lool. (Efes 2:3) Pool waroon naa xeex xeex dëgg. Lu tax? Ndaxte bàkkaar a ngi dëkkoon ci moom. Su ñu bëggee neex Yàlla, war nañoo xeex ñun itam xiirte ci bàkkaar yi nekk ci ñun.—Room 7:14-24; 2 Korent 5:10.
17. Lan mooy gëna jafeloo suñu xeex ak xiirte ci bàkkaar yi ñu judduwaale?
17 Suñu xeex ak bàkkaar du yomb, ndegam Seytaane, fu mu tolloo ngi ñuy fexee meeb ndax ñu jéggi sàrtiy Yàlla. (1 Pieer 5:8) Ba xelam di rabat ngir nawley karceenam yi, Pool wax na: “Waaye ni jaan ja naxe woon Awa ci pexeem, ragal naa yeen itam ñu lëmbaaje ni[i] seen xel, ba ngeen dëddu xol bu laab, bi ngeen amoon ci seen diggante ak Krist.” (2 Korent 11:3) Seytaane, pexe yu ni mel lay jëfandikoo ci suñu jamano. Dafay jéema ji ci ñun jiwuy nimse lu jëm ci mbaaxaayu Yeowa ak ci barke yi ñuy jële ci topp ndigali Yàlla yi. Ibliis dafay jéema jariñoo xiirtey ci bàkkaar yi ñu judduwaale te dafa ñuy jéema jañ ci dundinub réy-réylu, bëgge, mbañeel, ak ñaawe njort sa moroom.
18. Nan la Seytaaney jëfandikoo àddina si ngir fal bàkkaar?
18 Benn ci naxukaay yi Ibliis di jëfandikoo ngir xeex ñu, mooy àddina si nekk ci kàttanam. (1 Yowanna 5:19) Su ñu moytuwul, nit ñu yàqu te dëng ñi nekk ci àddina si dinañ ñu jañ ci dundinub bàkkaar buy jéggi yooniy Yàlla ci wàllu jikko. (1 Pieer 4:3-5) Ñu bare faalewuñu sàrtiy Yàlla te dañuy dem ba lànka déglu sax xiirtey seeni xol, ba tax dafay mujja dërkiis. (Room 2:14, 15; 1 Timote 4:1, 2) Ñenn ñi dañuy mujja nangu ndànk-ndànk dundin bu leen seen xol bu matadi bi sax doon aaye bu njëkk.—Room 1:24-32; Efes 4:17-19.
19. Lu tax am dundin bu set doŋŋ ci wàllu jikko doyul?
19 Ci àddina sii, dund dundin bu set ci wàllu jikko jëfu jàmbaar dëgg la. Waaye ngir neex suñu Sàkkkat, lu ëpp loolu lañ ñu laaj. War nañu itam am ngëm ci Yàlla te nangu suñu wareef ci moom (Yawut yi 11:6) “Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko bàkkaar nga,” la Saak taalibe ba bind. (Saak 4:17) Waaw, tey baña faale Yàlla aki ndigalam, loolu ci boppam nekk na aw xeetu bàkkaar.
20. Nan la la Seytaane mënkoona jéema teree def lu jub, waaye lan moo lay dimbali nga tiiñ naj yu ni mel?
20 Ci lu wóor-a-wóor, Seytaane dina tàngal xatal ngir tere laa sax ci xam-xamub Yàlla jaare ci sa njàngum Biibël bi. Li ñu la yaakaaral ak suñu xol bépp mooy nga baña bàyyi naj yooyu, mu lay naj, tere laa def li jub. (Yowanna 16:2) Lu ay kilifa yu bare tegoona teg seen ngëm ci Yeesu ca jamano yëngu-yëngoom, weejaluñu ko woon ndax ragal ñu tegeyu leen ci seen biir mbooloo. (Yowanna 12:42, 43) Seytaane dafay jéema xoxatal ak ñuul biir, képp kuy wut xam-xamub Yàlla. Wànte warkoon ngay fàttaliku tey fonk, saa su nekk, yëf yu yéeme yi Yeowa def. Xëy na sax dinga mëna dimbali ñii lay xatal ñu mujja fonk, ñoom itam, yëf yooyule.
21. Nan lañu mënee daan àddina seek suñuy xiirte ci bàkkaar yi ñu judduwaale?
21 Fi ak ñu ngi matadi, dinañu bàkkaar. (1 Yowanna 1:8) Waaye, am nañu ndimbal ci xeex boobu. Waaw, mën nañoo yóbbu ndam li ci suñu xeex ak ku soxor ki, Seytaane miy Ibliis. (Room 5:21) Ca mujug yëngu-yëngoom ci kow suuf, Yeesu xiirtal na ay taalibeem ci kàddu yile: “Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; noot naa àddina.” (Yowanna 16:33) Nit ñu matadi sax mën nañoo daan àddina si ak ndimbalul Yàlla. Seytaane mënula noot ñii koy tiiñ tey ‘wàkkirlu[...] ci Yàlla.’ (Saak 4:7; 1 Yowanna 5:18) Ni ñu koy gise ca kanam, Yàlla fogoru na ngir goreel ñu ci nooteelug bàkkaar ak dee.
[Li ñu bind ci suud]
^ Cellules (Cells): Wàll yu sew te tuutee tuuti yiy booloo def yaram, nikiy muul di booloo def ab tabax.
^ Histologie (Histology): Ci wàllu science, bànqaas biy gëstu ci mbooloom cellules (cells) yi daanaka bokk xeet te bokk liggéey ci biir yaram.
SEETLUL SA XAM-XAM
Kan mooy Seytaane miy Ibliis?
Lu tax doomi Aadama yiy màgget tey dee?
Lan mooy bàkkaar?
Nan la Seytaaney yóbboo nit ñi ci tey tooñ Yàlla?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 54]