Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi?

Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi?

Pàcc 8

Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi?

1, 2. Lan la nit ñiy farala def ci kanamu metitu doomu Aadama?

 BU AY njajaan dalee, yàq alal te rey ay nit, ñu bare mënuñoo nànd lu tax yëf yu ni mettee di am. Ñeneen dañoo jaaxle ndax yaatuwaayu, coxortel ak ñàkka boppu ñaawtéef geek taafar ji. Xëy na yow it, mas ngaa laaj sa xel, ‘Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi?’

2 Ndaxte amuñu tontu lu leen doy ci laaj boobu, ñu bare ñàkk nañu seen ngëm ci Yàlla. Dañoo foog ne faalewul nit ñi. Ñeneen ñu nangu metit niki lu bokk ci dund, dañuy mujja forox tey xas Yàlla ngir lépp lu bon li ci mbootaayug doomi Aadama yi. Su fekkee ne yëg nga lu ni mel ci sa xol, xëy na li Biibël biy wax ci mbir moomu dina la soxal.

METIT WI, DU YÀLLAA KO DOGAL

3, 4. Lu tax mu mën ñoo wóor ne lu bon ak metit jógewuñu ci Yeowa?

3 Biibël baa ngi ñuy wóoral ne du Yeowa Yàllaa dogal metit wi ñuy gis te mu wër ñu. Maanaam, taalibe karceen bi tudd Saak bind na: “Bu la fiir galanee, bul ne: Yàllaa ko dogal; ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn, te du fiir kenn.” (Saak 1:13) Ndegam noonu la, Yàlla mënuloona nekk ki dogal musiba yu bare yiy lottal nit ñi. Du nattu nit ñi ngir jekkloo leen ngir dund ca asamaan, te it du leen toroxloo ndax jëf yu bon yu ñu defkoon ca dund gu jiitu seen dundug tey, ni ko ñenn foogee.—Room 6:7.

4 Rax-ca-dolli, su fekkee ne sax am na ñu def ay jëf yu bare yu ñaaw ci turuw Yàlla walla wu Krist, dara ci Biibël bi déggloowul ne kenn ci ñoom ñaar nangu na jëf yu ni mel. Yàllaak Krist digaalewuñu dara ak ñiy damu nekk seeni surga waaye di naxe tey njublaŋ, di rey tey siif, tey def yeneen yëf yu bare yuy sabab metitu doomi Aadama yi. Li am mooy, “yoonuw ki soxor, lu Yeowa sib la.” Yàlla “sore na lool ñu soxor ñi.”—Léebu 15:9, 29.

5. Yan ay yenn ci jikkoy Yeowa, te lan lay yëg ci xolam ngir ay mbindaafonam?

5 Biibël baa ngiy nataal Yeowa ni ku “woyof lool ci cofeel te am yërmande.” (Saak 5:11, NW) Dafay xamle ne “Yeowa ku bëgg njub la.” (Sabuur 37:28; Isayi 61:8) Du ku bëgga di feyyu. Ku laabiir la ci ay mbindaafonam te dafa leen di jox ñoom ñépp li gën ngir seen sutura. (Jëf ya 14:16, 17) Ba dund sosoo ci kow suuf ba tey, loolu la Yeowa def.

NDOORTE LU MAT

6. Nan la yenn léeb dee junj dundug nit ca njëlbéen?

6 Ñun ñépp dañoo tàmm di gis tey yëg naqar ak metit. Looloo tax mën naa nekk lu jafe, jortu jamano ju dul am metit, waaye noonu la yëf yi deme woon ca cosaanu nit. Léebi yenn réew sax dañuy junj ndoorte lu neex lu ni mel. Ca biir léebaatuy réewum Grèce (Greece), jamano ja njëkkoon ca “Juróomi Jamanoy Nit”, ñu ngi ko tudde woon “Jamano Wurus.” Ca jamano jooja, doomi Aadama ya dañu daan dund ci bànneex, mucc ci liggéey bu ànd ak coono, naqar, ak yàq yiy ànd ak màgget. Waa Chine, ci seeni léeb, dañuy wax ne ca jamano nguurug Buur bu Puur bi (Huang-Ti), nit ña dañu daan dund ci jàmm, di bànneexu ci déggoo sax ak asamaan si ak rabi àll yi. Waa Perse (Persia), waa Misira, waa Tibet, waa Pérou (Peru) ak waa Mexique (Mexico), ñoom ñépp am nañu ay léeb yu jëm cib jamano bànneex ak mataay ca ndoortel dundug nit.

7. Lu tax Yàlla sàkk suuf seek doomi Aadama yi?

7 Léebaatuy xeet yi dañuy awu doŋŋ nettalib cosaanu doomiy Aadama bi gëna yàgg te ñu bind ko, Biibël bi. Mu ngi ñuy xamal ne Yàlla dafa teg ñaari nit ñu njëkk ña, Aadamaak Awa, ci àjjana ju ñu tudde toolu Eden te jox leen ndigal lii: “Na ngeen nangoo jur te mujja bare te feesal suuf si te ilif ko.” (1 Musaa 1:28) Suñuy maam ñu njëkk ña dañu doon bànneexoo mataay te li ñu doon séenu mooy gis suuf si sépp mujja nekk àjjana, fu njabootug nit ñu mat di dund ci jàmm juy yàgg ak bànneex. Looloo nekkoon nasub Yàlla ba muy sàkk suuf seek doomi Aadama yi.—Isayi 45:18.

AB TËKK BU SOXOR

8. Ban ndigal lañu doon xaaru Aadamaak Awa déggal, waaye lan moo xew?

8 Ngir dëkk ci tawféexu Yàlla, Aadamaak Awa waroon nañoo moytoo lekk ca “garabu xam-xamub lu baax ak lu bon.” (1 Musaa 2:16, 17) Su ñu déggaloon sàrtub Yeowa, wenn metit doonul yàq dundug nit ñi. Ci topp ndigalul Yàlla, doon nañu wone seen mbëggeel ci Yeowa ak seen ngor ci moom. (1 Yowanna 5:3) Waaye ni ñu ko jàngee cim pàcc 6, yëf yi demewuñu noonu. Seytaane jamp na Awa mu lekk ci doomu garab googu. Ca gannaaw ga, Aadama itam jël na wàllam ca doom ja ñu tere.

9. Yan werante yuy laal Yeowa la Seytaane indi woon?

9 Ndax jëli nga diisaayu li xew? Seytaanee ngi doon song taxawaayub Yeowa niki Aji Kowe ji. Ba mu nee: “Dungeen dee fenn,” Ibliis a ngi doon weddi baati Yàlla yii: “Dinga dee ci lu wóor.” Baatiy Seytaane yi ci topp a ngi doon jortuloo ne, Yeowaa ngi doon nëbb Aadamaak Awa yoonuw mujja mel ni Yàlla, noonu bañ Koo soxla ngir dogal li baax ak li bon. Kon sóorub Seytaane dafa doon diŋat sañ-sañu ak njubaayu taxawaayu Yeowa niki Kilifag mbindeef mi.—1 Musaa 2:17; 3:1-6.

10. Lan la Seytaane gaaral jëmale ko ci doomi Aadama yi?

10 Seytaane miy Ibliis gaaral na it ne nit ñi doon nañu sax ci déggal Yeowa, fi ak di déggal Yàllaa ngi leen doon jariñ doŋŋ. Ni ñu ko mëna waxe, mu nga doon diŋat ngor lëmm gu doomi Aadama yi. Seytaane dafa doon tuumaal ne kenn nit doonul sax, ak xol bu tàlli, ci ngor ci Yàlla. Li Seytaane doon bàkkoo ci tuuma ju bon jooju feeñ na bu baax ci nettalib Biibël bi jëm ci Ayóoba, jaamu Yeowa bu takku, bu dajoon nattu bu réy, tuuti laata atum junneek juróom-benni téeméer (1600) L.J.K.T. Bu ngeen duruusee ñaari pàcc yi njëkk ci téereb Ayóoba, dingeen mëna ràññee li tax doomi Aadama yi nekk ci metit te lu tax Yàlla di bàyyi loolu am.

11. Ban fasoŋu nit la Ayóoba nekkoon, waaye jan tuuma la Seytaane def ?

11 Ayóoba, “góor gu ñu mënula sikke dara te jub xocc,” nekkoon na ku Seytaane song. Ca ndoorte la, Seytaane dafa ñaawloo njort ci li tax Ayóoba doon jaamu Yàlla, ak laaj bii: “Ndax ci àllum neen la Ayóoba ragale Yàlla?” Gannaaw loolu, Ibliis, di ku miikar, sosal na Yàllaak Ayóoba, ba mu tuumaalee Yeowa naan, dafa jënd ngorug Ayóoba ak tawféex ji mu ko defal. Seytaane daldi tëkk Yeowa, ne ko: “Waaye, ngir soppi, tàllalal sa loxo, su la soobee, nga laal lépp li mu am, te seetal ndax du la móolu ci sa kanam saxsax.”—Ayóoba 1:8-11.

12. (a) Yan werante lañu doon mëna firi doŋŋ su Yàlla bàyyi woon Seytaane nattu Ayóoba? (b) Lan la nattub Ayóoba yóbbe?

12 Ndax Ayóoba dafa doon jaamu Yeowa doŋŋ ngir lu baax lépp la mu jote woon ca Yàlla? Ndax ngor lëmm gu Ayóoba doon na sax ci nattu boobu? Lu jëm ci Yeowa, ndax wóolu woon na bu doy jaamam ngir bàyyi ñu nattu ko? Werante yooya doon nañu leen mëna firi, su Yeowa bàyyi woon Seytaane mu indi ci kow Ayóoba nattu bi yées. Takkuteb Ayóoba ci biir nattu booba Yàlla bàyyi mu am, ni ñu ko nettalee ci téereb Ayóoba, làyyi na bu baax-a-baax njubaayug Yeowa ak ngor lëmm gu nit.—Ayóoba 42:1, 2, 12.

13. La xewoon ca Eden te daloon Ayóoba nan la la laale?

13 Waaye la xewoon ca toolu Eden ak la daloon nit ka Ayóoba, tekki na lu gëna am maanaa. Werante yi Seytaane indi, nit ñépp lañu laal, boole ci ñun ñii tey. Yàq nañu turuw Yàlla, te tëkkoon nañu kiliftéefam. Njubaayug mbindeefum Yàlla, maanaam nit, diŋatoon nañu ko. Werante yooyu waroon nañu leena firi.

NI ÑU FIREE WERANTE YOOYU

14. Bu jànkoonteek sóoru bu soxor, lan la nit ku ñu jiiñ mënkoona def?

14 Nikib misaal, nañu la jàppe niki aji-jur ju am mbëggeel te am ay doom yu bare ci njaboot gu bég. Su la benn ci say dëkkandoo tiifaroon aki fen, di la jiiñ aji-jur ju bon. Lan ngay def su dëkkandoo bi waxee ne say doom bëgguñu la, dañuy des ak yow ndax xamuñu leneen lu gën, te doon nañu génn dem su leen kenn xàllaloon yoon wi? Mën ngaa wax: ‘Lu ñàkk bopp a ngi noonu!’. Dëgg la, waaye nan nga koy wone? Yenn way-jur mënkoon nañoo say. Gannaaw indi yeneen téq-téq, tont lu ànd ak taafar lu ni mel doon na yeesal fen yi. Doxalin buy bégloo ngir lijjanti lëj-lëj bu ni mel mënkoon naa nekk nga bàyyi sa tuumaalkat firndeel li muy bàkkoo ci tuumaam te nga may say doom ñu seede ne sopp nañu la ci seeni xol.

15. Nan la Yeowa tànnee jàkkaarlook tëkkub Seytaane?

15 Yeowaa ngi mel ni aji-jur ju am mbëggeel jooju. Mën nañoo tollale Aadamaak Awa ak doom yi, te Seytaane mooy dëkkandoo biy fen. Yàlla, ci sagoom, reyul ci saa si Seytaane, Aadamaak Awa, waaye bàyyi na defkati lu bon yooyu ñu dund ab diir. Loolu may na suñu maam yu njëkk ya jotu sos njabootu doomi Aadama yi, te may na it Ibliis yoon wu mu wone ndax li mu doon bàkkoo ci tuumaam dëgg la, ba tax ñu mëna firi werante yooyu. Wànte, li dale ca ndoorte la, Yàlla xamoon na ne doon na am ay doomi Aadama yu gore ci moom tey firndeel noonu ne Seytaane ab fenkat la. Aka ñoo am ngërëm ci li Yeowa wéy di barkeel tey dimbali ñii ko bëgg!—2 Nettaliy xew-xewi cosaan 16:9; Léebu 15:3.

LAN LAÑU FIRNDEEL?

16. Nan la àddina si mujjee nekk ci kàttanu Seytaane?

16 Daanaka ba àddina doomiy Aadama sosoo ba tey, bàyyi nañu Seytaane ci sagoom, muy laxas ngir ilif doomi Aadama yi. Ci biir loolu, ak muusantu jariñoo na sañ-sañam ci kow kàttan yi ci wàllu politig, te fal na ay diine yuy jubal, jaare ci ay pexe yu xereñ, njaamu gi ci moom asté ci Yeowa. Noonu Ibliis mujj naa nekk “yàllay jamano ji[i],” te tudde nañu ko “[kiiy] jiite àddina si[i].” (2 Korent 4:4; Yowanna 12:31) Dëgg-dëgg, “àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis.” (1 Yowanna 5:19) Ndax loolu dafa tekki ne Seytaane firndeel na li mu doon bàkkoo ci tuumaam, maanaam mënoon naa dëddale doomi Aadama yépp ci Yeowa Yàlla? Wóor na ne déet! Ba muy bàyyi Seytaane wéy di dund, Yeowa mottali na nasu boppam. Kon, lan la Biibël biy feeñal ci li tax Yàlla bàyyi coxorte?

17. Lan lañu wara bàyyi xel jëm ci li sabab coxorte geek metit wi?

17 Coxorte geek metit wi du Yeowaa leen dogal. Ndegam Seytaaneey jiite àddina sii te mooy yàllay jamano ji, moom ak ñii ci làngam lañu wara jàppe nekkinub mbootaayug doomi Aadama yi tey ak toskare ji sonnal nit ñi. Ci yoon, kenn mënula wax ne Yàllaa dogal metit wu ni mel.—Room 9:14.

18. Li Yeowa di bàyyi coxorte geek metit wi, lan la firndeel jëm ci xalaatu moom sa bopp ci kanamug Yàlla?

18 Li Yeoway bàyyi coxorte geek metit wi firndeel na ne moom sa bopp ci kanamu Yàlla sosul àddina su gën. Ci lu kenn mënula weddi, dundug doomu Aadama ay musiba yu toppante la masa doon. Li waral loolu mooy doomi Aadama yi dañoo tànna wéy ci yoonu moom seen bopp ci seen dund te faalewuñu ca dëgg kàddug Yàllaak coobareem. Ba mbooloo Yeowa mu njëkk ma ak seeni njiit toppee, ci gëmadi, “yoon wi gëna siiw” te weddi kàddoom, musiba la leen yóbbe. Jaare ci yonentam Yérémi, Yàlla nee na leen: “Boroom xam-xam yi mujj nañoo am gàcce. Mujj nañoo tiit te dinañu leen jàpp! Gisleen! Dañoo weddi kàddug Yeowa saxsax, te ban sago lañu am?” (Yérémi 8:5, 6, 9) Ndegam toppuñu yooniy Yeowa, daanaka mbooloom nit ñi dañoo mujja mel ni gaal gu amul las, gu géej gu sàmbaraax di jiñax ci wet gu nekk.

19. Lan mooy firndeel ne Seytaane mënula walbati doomi Aadama yépp ñu jógal Yàlla?

19 Li Yàlla bàyyi coxorte geek metit wi firndeel na itam ne Seytaane amul mën-mënub dëddale nit ñépp ci Yeowa. Ba doomi Aadama yi nekkee ba tey, dafa masa am ay nit ñu sax ci takku ci Yàlla, ak lu ñu indee indi seen kow ay fiir walla ay nattu. Ci biir xarnu yi toppante, Yeowa feeñal na kàttanam ngir ay jaamam, te turam jolli na ci suuf si sépp (2 Musaa 9:16; 1 Samwil 12:22) Yawut yi pàcc 11 a ngi ñuy limal toflante bu gudd, bu jaam yu takku woon ci Yàlla, te ëmb Abel, Enok, Nóoxin, Ibrayima ak Musaa. Yawut yi 12:1 a ngi leen di tudde ‘ag ndiiraan gu réy gu ay seede, NW.’ Nekkoon nañu ay royukaay ci wàllu ngëm ci Yeowa, ngëm gu dul yëngu. Ci suñu jamano it, ñu bare dem nañu ba joxe seen bakkan ci ngor lëmm ci Yàlla, ngor gu ñu mënula diŋat. Ndax seen ngëm ak seen mbëggeel, nit ñu ni mel a ngiy firndeel ci lu kenn mënula weddi ne, Seytaane mënula walbati doomi Aadama yépp ñu jógal Yàlla.

20. Li Yeowa bàyyi coxorte geek metit wi ñu wéy, lan la firndeel jëm ci Yàllaak nit ñi?

20 Ndax sottal, li Yeowa bàyyi coxorte geek metit wi ñuy wéy firndeel na ne Yeowa doŋŋ, Sàkkkat si, moo am mën-mënub ak sañ-sañub jiite nit ñi ngir ñu barkeel te am jàmm ba fàww. Ay xarnuy xarnu, nit ñi jéem nañu xeeti nguur yu bare. Waaye lan la loolu yóbbe? Lëj-lëj yeek gilaawaali yi xeet yiy jànkoonteel tey a ngiy wone, ci lu leer nàññ ne, ca dëgg, ni ko Biibël bi birale saxsax, “nit dafa ilif nit ngir loraangeem.” (Dajalekat 8:9) Yeowa doŋŋ a mëna ñëw xettali ñu te mottali nasam, bu njëlbéen. Nan lay defe loolu, te kañ?

21. Lan lañuy def Seytaane, te ci kan lañuy jaar ngir sottal loolu?

21 Aadamaak Awa dañoo daanu ci fiiru Seytaane rekk, Yàlla daldi yëgal Nasam bu jëm cim pexe mucc. Lii la Yeowa yégle, jëmale ko ci Seytaane: “Dinaa def mbañante diggante yow ak jigéen ji te diggante sa njureel ak njureelam. Dina la gaañ bu metti ci bopp te dinga ko gaañ bu metti ci téstën.” (1 Musaa 3:15) Yégle boobu moo doon wóoral ne duñu bàyyi Ibliis muy def jëf yu ñaaw ba fàww. Niki Buurub Nguurug Almasi bi, Yeesu Krist, Njureel gi ñu dige woon, dina ‘gaañ bu metti Seytaane ci bopp.’ Waaw, “léegi” Yeesu rajax Seytaane mi jógal Yàlla!—Room 16:20.

LAN NGAY DEF?

22. (a) Yan laaj nga wara jàkkaarlool? (b) Lu Seytaane xëppa xëpp meram ci ñii takku ci Yàlla, lan moo la wóor?

22 Ndegam xam nga werante yi ñu indi, ci gan wet ngay féete? Ndax dinga wone ci say jëf ne jàpple ngaak ngor Yeowa? Ndegam Seytaane xam na jot gi ko dese bareetul, dina def kem-kàttanam ngir xëpp meram ci ñii bëgg sàmm seen ngor ci Yàlla. (Peeñu bi 12:12) Waaye mën ngaa wut ndimbal ci Yàlla, ndaxte “[ Yeowa, NW ] Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu.” (2 Pieer 2:9) Du seetaan ñu fiir la lu jéggi dayo li nga àttan, te dina la ubbil bunt ba tax nga mëna muñ fiir yi.—1 Korent 10:13.

23. Lan lañu mëna séenu ak kóolute?

23 Ak kóolute, nañu séenu jamano fu Buur bi Yeesu Krist di jóg ngir dal ci kow Seytaane ak ñépp ñii koy topp. (Peeñu bi 20:1-3) Yeesu dina fi dindee ñépp ñii ñu mëna jàppe musiba yeek ayi biir-réew yi sonnal nit ñi. Fi ak jamano jooja, wenn xeetu metit wu tiis te wuuteek yeneen yépp mooy ñàkkum suñuy soppe ci dee. Jàngal pàcc miy topp ngir gis li leen di dal.

SEETLUL SA XAM-XAM

Nan lañu xame ne du Yeowaay dogal metitu doomiy Aadama?

Yan werante yu Seytaane indi ca Eden ñoo feeñ, leer naññ, ca bésiy Ayóoba?

Li Yàlla bàyyi metit wi lan la firndeel?

[Laaj yi]