Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Mën ngaa am ëllëgu bànneex!

Mën ngaa am ëllëgu bànneex!

Pàcc 1

Mën ngaa am ëllëgu bànneex!

1, 2. Lan la sa Sàkkkat bëgg nga am?

 NIT koo bëgg nuyu la, taf la ci xolam. Lekk togg gu neex ak say xariti benn-bakkan ci jataay bu xumb di rex-rexi. Am bànneex ciy seetaan say doom ñuy fo ak mbég. Jot yu ni mel nekk nañu jot yuy maye bànneex ci dund. Waaye, ci ñu bare, dund jafe-jafe bu tar ci kow jafe-jafe bu tar lay yóbbe. Su fekkee ne mooy li nga daj, na nga takk sa fit.

2 Coobareg Yàlla mooy nga xéewlu ci bànneex buy yàgg, ci nekkin yi gën, ci kurukaara bu naat. Loolu du ab gént rekk, ndax ca dëgg Yàllaa ngi lay jox caabi ëllëgu bànneex ju ni mel. Caabi jooju mooy xam-xam.

3. Ban xam-xam mooy caabi jiy jëme ci bànneex, te lu tax mu mën ñoo wóor ne Yàlla mën naa joxe xam-xam boobu?

3 Ñu ngiy waxtaane xeetu xam-xam bu wuuteek xam-xamu doomu Aadama te gëna yaa fuuf sagoom. Mooy “xam-xamub Yàlla dëgg.” (Léebu 2:⁠5) Lu jege ñaari junniy at yee weesu, ab bindkat ci Biibël bi nee na: “Kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla.” (Yawut ya 3:⁠4) Xalaatal xam-xam bi Ki sàkk lépp wara am! Biibël bi nee na Yàlla dafay lim biddéew yi yépp tey woo bu nekk ci turam. Ndaw xalaat wu doy waar, ndegam am na ay junniy tamndareeti biddéew ci suñu juugu biddéew te boroom xam-xam yiy jàng jaww ji nee nañu, am na lu tollook téeméeri junniy tamndareet ciy yeneen juugi biddéew! (Sabuur 147:⁠4) Yàlla xam na it lépp ci ñun, kon keneen kan a gëna mëna tontu laaj yu am solo yi jëm ci dund?​—⁠Macë 10:30.

4. Lu tax ñu wara xaaru Yàlla jox ñu ay tegtal ngir tette ñu, te ban téere mooy faj soxla boobu?

4 Soo gisoon ñaari nit ñuy jéema jagal seeni oto. Kenn ki yoqi, sànni ay jumtukaayam ci suuf. Keneen ki, ci teey, jagal li doxul, jëfandikoo caabi jiy taal oto bi, ba noppi muuñ ba masiin ba tàmbalee tàkk, di riir bu baax-a-baax. Du jafe ci yow nga tandale kan ci ñaari nit ñooñoo ame téereb tegtal bi jóge ca defarkat ba. Ndax du lu jub, Yàlla joxe ay tegtal ngir tette ñu ci suñu dund? Xëy na loo xam la, Biibël bi loolu saxsax lay wuyoo​—⁠nekk ab téere tegtal ak tette bu jóge ca Ki ñu sàkk, ngir jottali xam-xamub Yàlla.​—⁠2 Timote 3:⁠16.

5. Xam-xam bi ci Biibël bi, nan la soloom tollu?

5 Su li Biibël bi di wuyoo nekkee dëgg, xalaatal alali xam-xam yi téere boobu wara yore! Ci Léebu 2:​1-5, Biibël baa ngi ñuy jamp ñu wut sago, ñu gas ngir am ko ni ñu naroona gase alal ju nëbbu​—⁠du ci biir suufu xalaatu doomu Aadama, waaye ci biir Kàddug Yàlla ci boppam. Su ñu wutee foofu, dinañu “daj xam-xamub Yàlla dëgg.” Ndegam Yàlla xam na li ñu àttan ak li ñu soxla, dafa ñuy jox tegtal yi ñuy dimbali ñu dund dundug jàmm ak bànneex. (Sabuur 103:14; Isayi 48:17) Rax-ca-dolli, xam-xamub Yàlla dafa ñuy jox xabaar bu neex buy ñuy taxa tukkurmuut.

DUND GU DUL JEEX!

6. Lan la Yeesu wóoral jëm ci xam-xamub Yàlla?

6 Yeesu Krist boroom tur wu jolli bu doon dund bu njëkk ci kow suuf, nettali na fànnab xam-xamub Yàlla boobu ci ay kàddu yu leer. Nee na: “Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Krist.” ( Yowanna 17:⁠3, jolliloo bi, ci ñun la) Xalaatal​—⁠xam-xam buy jëme ca dund gu dul jeex!

7. Ban firnde bu wóor lañu am ne Yàlla séentuwuloon dee ngir ñun?

7 Bul gawa génne ci sa xel dund ba fàww, yaakaar ne ab gént rekk la. Asté loolu, seetal fasoŋ bi ñu defare yaramuw nit. Dañu ko sàkk, te amul moroom, ngir mu mëna ñam cafko, dégg, xeeñtu, gis, te yëg. Aka ñoo bare ci kow suuf yëf yiy bégloo sunuy yëgukaayi yaram​—⁠lekk gu saf, woyu picc bu neex, tóor-tóor yu xeeñ, béréb yu rafet te jekk, àndandoo yuy bégloo! Rax-ca-dolli, suñu yuur giy jommal moo sut te raw fuuf ordinateur (computer) bi gëna xarala, ndax moom a tax ñu mëna fonk te bànneexu ci yëf yu ni mel. Ndax foog nga ne Ki ñu sàkk dafa bëgg ñu dee te faf ñàkk loolu lépp? Ndax gënula ànd ak sago ñu tofal ne dafa bëgg ñu dund ci bànneex te xéewlu ci dund ba fàww? Waaw, loolu la xam-xàmub Yàlla mëna tekki ngir yow.

DUND GA WOON CA ÀJJANA

8. Lan la Biibël wax lu jëm ci ëllëgu nit ñi?

8 Li Biibël bi wax ci ëllëgu suuf seek nit ñi, mën nañu koo tënk ci benn baat​—⁠Àjjana! Yeesu Krist waxtaane na ci ba mu waxee góor gu doon sukkuraat: “Dinga nekk ak man ca Àjjana.” (Lukk 23:43, New World Translation) Tuddub Àjjana, amul werante, fàttali na góor googa nekkinu bànneex bu suñuy maam yu njëkk ya, Aadamaak Awa. Ba leen Yàlla sàkkee, dañu matoon te ñu nga doon dund ca biir tool bu Sàkkkat bi defaroon te jëmbëtoon. Moom lañu tudde woon, ci lu war, toolu Eden, tur wuy tekki bànneex.

9. Dund ca biir àjjana, ca njëlbéen, nan la meloon?

9 Ndaw mbég ci tool boobu! Àjjana dëgg la woon. Ca biir ay garabam yu yànj, amoon na ca yu daan meññ ay doom yu neex-a-neex. Ba Aadamaak Awa doon wër seen moomeel, doon naan ndoxam mu neex, doon witt doom ci ay garabam, amuloon dara lu leen waroona jàqloo walla ragalloo. Mala yi sax daawuñu leen méb, ndax Yàlla dafa tegoon góor geek jabaram ci kow ñoom yépp ngir ñu ilif leen cig mbëggeel. Teg ca, ñaari nit ñu njëkk ña amoon nañu wér-gi-yaram gu baax-a-baax. Fi ak ñu ngi doon déggal Yàlla, dund ba fàww ci bànneex a leen doon xaar. Joxoon nañu leen liggéey bu leen doon bégloo, maanaam toppatoo seen kërug Àjjana gu amul moroom gi. Gannaaw loolu, Yàlla joxoon na Aadamaak Awa yéble “feesal te ilif suuf si.” Ñoom ak seeni doom waroon nañoo yokk peggiy Àjjana ba suñu suuf si sépp mujja nekk bérébu rafetaay ak mbégte.​—⁠1 Musaa 1:⁠28.

10. Ba Yeesu waxee lu jëm ci àjjana, lan la doon bëgga xamal?

10 Waaye ba Yeesu tuddee Àjjana, laajuloon góor ga doon sukkuraat mu xalaat la weesu lu yàgg démb. Déedéet, lu jëm ci ëllëg la Yeesu doon wax! Xamoon na ne suñu kër, maanaam suuf si sépp, doon na mujja nekk àjjana. Noonu, Yàlla doon na àggali la mu nasoon ca njëlbéen ngir nit ñeek suñu suuf si. (Isayi 55:​10, 11) Waaw, Àjjana dinañ ko defaraat! Te nan lay mel? Nañu bàyyi Kàddug Yàlla, Biibël bu sell bi, tontu.

DUND GI CI BIIR ÀJJANA JI ÑU DEFARAAT

11. Bu ñu defaraatee àjjana, lan ay dal feebar, màgget ak dee?

11 Feebar, màgget ak dee dootuñu am. “Bu boobaa gëti ñi gumba dinañu leen xippi, te noppi ñi tëx dinañu leen sàññi. Bu boobaa kiy soox dina yéeg ni ab cervus, làmmiñu ñi luu dina yuuxu ci mbég.” (Isayi 35:​5, 6) “Yàlla ci boppam dina ànd ak [nit ñi], nekk Yàlla seen Boroom. Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla mettit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.”​—⁠Peeñu bi 21:​3, 4.

12. Lu tax mu mën ñoo wóor ne dootul am ñaawtéef, taafar ak coxorte ci àjjana jiy ñëw?

12 Ñaawtéef, taafar, ak coxorte dinañu fi jóge ba fàww. “Defkati lu bon, ci seen bopp, dinañu leen mejj. (. . .) Ci kanam tuuti rekk, te ku soxor dootul nekk. (. . .) Du nekk. Waaye ñi woyaf dinañu moom suuf si.” (Sabuur 37:​9-11) “Lu jëm ci ñi soxor, dinañu leen mejje kow suuf si saxsax; te lu jëm ci workat yi, dinañu leen fi buddee.”​—⁠Léebu 2:⁠22.

13. Nan la Yàlla di indee jàmm?

13 Jàmm dina siiw ci suuf si sépp. “Mu ngiy [ Yàlla] teeral xeex yi ba ci catu suuf si. Xala gi, mu ngi koy damm tey dammat xeej bi.” (Sabuur 46:⁠9) “Ki jub dina sax, te jàmm bare ba weer wi nekkatul.”​—⁠Sabuur 72:⁠7

14, 15. Lan la Biibël biy wax lu jëm ci kër, liggéey ak lekk ci àjjana ji ñu defaraat?

14 Kër gu wóor ak liggéey buy bégloo. “Ci lu wóor dinañu tabax ay kër te dëkk ci. (. . .) Duñu tabax te keneen dëkk; duñu jëmbët te keneen lekk. Ndax niki faniy garab la faniy samay nit di mel; te liggéeyu seeni loxo saxsax, ñii ma tànn dinañu ko jariñoo ba mu mat sëkk. Duñu daan seen doole àllumneen, walla jur doom ngir njàq.”​—⁠Isayi 65:​21-23.

15 Dina am lekk guy tabax yaram te duun. “Dugub dina bare ci kow suuf si; ci collu tund yi dina ne gàññ.” (Sabuur 72:16) “Suuf si ci boppam dina joxe ci lu wóor meññeefam; Yàlla, suñu Yàlla, dina ñu barkeel.”​—⁠Sabuur 67:⁠6.

16. Lu tax dund gi ci àjjana di neex?

16 Dund ba fàww ci àjjana ci kow suuf dina neex. “Ñi jub, ci seen bopp, dinañu moom suuf si, te dinañu dëkk ba fàww ci kowam.” (Sabuur 37:29) “Màndiŋ meek diiwaan bi am maral dinañu tukkurmuut, te joor gi dara saxul dina bég te tóor-tóor ni safraŋ.”​—⁠Isayi 35:⁠1.

XAM-XAM AK SA ËLLËG

17. (a) Lan nga wara def, su la dund ci àjjana soxalee dëgg-dëgg? (b) Nan lañuy xame ne Yàlla dina indi soppi yu réy ci kow suuf?

17 Su la dund ci Àjjana soxalee dëgg-a-dëgg, bul bàyyi dara xañ laa sàkku xam-xamub Yàlla. Moom bëgg na nit ñi te dina indi soppi yi war ngir def suuf si ab àjjana. Bu ñu ko seetee sax, soo amoon kàttanu dindi ndóol beek jubadi yu ni siiwe ci biir àddina si, ndax doo ko def? Ndax war nañoo xaaru Yàlla def lu gëna néew? Te sax Biibël baa ngiy saabal jamano joo xam ne Yàlla dina fi jële jamano ju bare ŋaayoo jii te wuutu kook nguur gu mat, gu jub. (Dañel 2:44) Waaye Biibël baa ngiy def lu ëpp wax ñu lu jëm ci loolu lépp. Mu ngi ñuy won naka lañu mënee mucc te dugg ci àddina su bees si ñu Yàlla dig.​—⁠2 Pieer 3:13; 1 Yowanna 2:⁠17.

18. Lan la la xam-xamub Yàlla mëna defal léegi-léegi?

18 Xam-xamub Yàlla mën na laa defal itam lu bare léegi-léegi. Laaj yi gëna xóot jëm ci dund ak yi gëna ub boppu nit ñi, tontu nañu leen ci Biibël bi. Nangu tetteb Biibël bi dina la dimbali nga gëna xaritook Yàlla. Akay teraanga ju réy! Te loolu dina tax nga mëna xéewlu ci jàmm ji Yàlla képp mëna maye. (Room 15:​13, 33) Boo tàmbalee sàkku xam-xam boobuy joxe dund, yaa ngiy sumb njéem gi ëpp solo ci sa giiru-dund ak gi lay gëna jariñ. Doo réccu mukk wéy ci sàkku xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex.

19. Ban laaj lañuy gis ci pàcc miy ñëw?

19 Ci Biibël bi lañu sukkandiku niki téere bi ame xam-xamub Yàlla. Waaye, nan lañu mënee xam ne du téereb sago doomi Aadama, waaye lu ko raw fuuf? Dinañu gis laaj boobu ci pàcc miy ñëw.

SEETLUL SA XAM-XAM

Lu tax xam-xamub Yàlla mën laa jëme ci bànneex ba fàww?

Nan la dund gi di mel ci Àjjana jiy ñëw ci kow suuf?

Lu tax di sàkku xam-xamub Yàlla, léegi-léegi, di la amali njarin?

[Laaj yi]