Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Nguurug yàllaa ngiy ilif

Nguurug yàllaa ngiy ilif

Pàcc 10

Nguurug yàllaa ngiy ilif

1, 2. Nan la nguuri doomi Aadama yi wonee seen mënadi?

 XËY NA mas na laa dal, nga jënd ab jumtukaay ngir gis doŋŋ ne duloon dox. Su fekkoon booba danga woo ab jagalkat. Yàgguloon dara gannaaw ba mu “defaree” jumtukaay ba, terewul mu taxawaat. Aka doon yaakaar ju tas!

2 Noonu la deme ak nguuri doomi Aadama yi. Nit ñi dañoo masa xinte ag nguur gu leen mëna wóoral jàmm ak bànneex. Ndaxam, li ñuy jéem ak seen kem-kàttan ngir jagal doyadi yi ci àddina si, àntuwul ca dëgg. Torlu nañu ay ndigaaley jàmm yu bare—te faf leena joggi. Magum loolu, gan nguur a dindi toskare ji, ndefe walla njort yu dul dëgg yi, ñaawtéef gi, feebar beek yàquteb kéewaange gi? Amul lu mëna jagal kiliftéefu nit. Suleymaan sax, buurub Israel bu am sago, laaj na: “Lu jëm ci nit ki bawoo ci suuf, nan la mënee ràññee yoonam?”—Léebu 20:24.

3. (a) Lan a nekkoon tàjju waare Yeesu? (b) Nan la ñenn nit ñiy nataale Nguurug Yàlla?

3 Bul yoqi! Ag nguur gu riigu, guy ilif àddina si sépp, du ab gént doŋŋ. Moo doon tàjjub waare Yeesu. Tudde na ko “nguurug Yàlla,” te jàngal na ñii ko doon topp ñu ñaan ngir nguur googu. (Lukk 11:2; 21:31) Dëgg la, ci biir daayira yi, léeg-léeg ñu fay tudd Nguurug Yàlla. Dëgg la itam, ay tamndareeti nit a ngiy ñaan bés bu nekk ngir moom, bu ñuy baamtu Ñaanug Sang bi (ñu tudde ko itam ‘Suñu Baay’ bi walla ñaan gi nekk royukaay gi). Waaye bu ñu leen laajee: “Lan mooy Nguurug Yàlla?”, nit ñi dañuy joxe ay tont yu wuute. Ñenn ñi dañuy ne: “Mu ngi ci suñu biir xol.” Ñeneen dañu koy tudde asamaan. Biibël baa ngiy jox tont lu leer, ni ñu koy gise.

AG NGUUR GU AM AB NAS

4, 5. Lu tax Yeowa tànna taxawal peeñu bu bees bu kiliftéefam, te lan lay mottali?

4 Yeowa Yàlla dafa masa nekk Buuru mbindeef mi mépp, walla Aji Kilifa ji. Li mu sàkk yëf yépp a ko yëkkati ci taxawaay bu kowee kowe boobu. (1 Nettaliy xew-xewi cosaan 29:11; Sabuur 103:19; Jëf ya 4:24) Waaye Nguurug Almasi gi Yeesu doon waare, kiliftéefu Yàlla ci kow mbindeef mi mépp a ko gëna jolli. Nguurug Almasi googu dafa am ab nas saxsax, waaye boobooy ban?

5 Ni ñu ko tekkee cim pàcc 6, ñaari nit ñu njëkka ña dañoo jógal kiliftéefu Yàlla. Ndax werante yi ñu indi teg, Yeowa tànn naa taxawal peeñu bu bees bu kiliftéefam. Yàlla xamal na nasam, maanaam sàkk ag “njureel” guy nappaaje Jaan ji, Seytaane, tey dindi li bàkkaar bi nit ñi donn yóbbe. “Njureel” ga ca gën mooy Yeesu Krist, te “nguurug Yàlla” mooy jumtukaay biy dàq Seytaane domm. Jaare ci Nguur googu, Yeesu Krist dina taxawalaat nguur gi ci kow suuf si sépp ci turuw Yeowa, te dina làyyi kiliftéefu Yàlla gu aw yoon gi ba fàww.—1 Musaa 3:15; Sabuur 2:2-9.

6, 7. (a) Fan la Nguur gi nekk, kan mooy Buur bi ak ñi mu àndal ngir ilif? (b) Ñan ñooy surgay Nguur gi?

6 Ci ni yenn firiy Biibël bi nettalee kàdduy Yeesu ya mu jëmale woon ca Farisieŋ ya, lii la leen wax: “Nguurug Yàllaa ngi ci seen biir.” (Lukk 17:21) Ndax Yeesu dafa bëggoona wax ne Nguur gaa nga woon ca biir xol yu soxor yu nit ñu dëng ñooña? Déedéet. Lii lañuy jàng ci ab firi bu gëna wér bu mbind grekk yi, ci li kàddu yooyu tekki saxsax: “Nguurug Yàllaa ngi ci seen digg.” (New World Translation) Yeesu, mi nekkoon ci seen digg, a ngi doon joxoñ boppam niki Buur biy ñëw. Nguurug Yàlla nekkul lu nit ame ci biir xolam, sore na loolu, waaye nguur gu am la, guy toppatoo liggéey te am ag kilifa aki surga. Nguur gu nekk ca asamaan la, ndax dañu ko tuddeendoo “nguurug asamaan ya” ak “nguurug Yàlla.” (Macë 13:11, NW; Lukk 8:10) Cib gis-gis, yonent Dañel gis na Njiitam, niki “kenn ku nirook doomu nit” ju ñu jegeñsiloo fa kanamu Yàlla Aji Kàttan ji te ñu jox ko “kiliftéef, darajaak nguur [yu dul jàll], ngir mbooloo yi, xeet yeek làkk yi yépp war koo surgawu.” (Dañel 7:13, 14) Kan mooy Buur boobu? Biibël baa ngiy woowee Yeesu Krist “Doomu nit ki.” (Macë 12:40; Lukk 17:26) Waaw, Yeowa tànn na Doomam ju góor, Yeesu Krist, ngir mu nekk Buur.

7 Yeesu du nguuru moom doŋŋ. Am na téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni nit (144 000) ñu nekk ak moom, “ñu jote [leen] àddina” ngir ñu nekk ay buur aki saraxekat yu ñu ko booleel. (Peeñu bi 5:9, 10; 14:1, 3; Lukk 22:28-30) Surgay Nguurug Yàlla ñooy nekk genn njabootu doomiy Aadama guy nangul njiitum Krist. (Sabuur 72:7, 8) Wànte, nan la ñu mënee wóor ne, Nguur gi dina làyyi ci dëgg kiliftéefu Yàlla te defaraat àjjana ci suñu suuf si?

NGUURUG YÀLLA LU AM LA

8, 9. (a) Lan lañu mënee misaal wóoraayu digey Nguurug Yàlla? (b) Lu tax mu mën ñoo wóor ne Nguur gi lu am la?

8 Jortul safara yàqa yàqeet sa kër. Léegi sa xarit bu am doole ngir def ko, dig la ndimbal ngir tabaxaatal la sa kër te yore dundub sa njaboot. Su fekkee ne sa xarit boobu dafa mas di la wax dëgg, ndax doo ko gëm? Su fekkee ne, ca ëlleg sa, danga jóge liggéey, ñibbisi kër ga te fekk ay liggéeykat tàmbali xaat an ndesiti lakk gi te ñu indil sa njaboot lu mu lekk. Ci lu amul werante doon na la wóor bu baax ne, ci bés yiy tegu, duñu yem doŋŋ ci jagalaat yëf yi waaye ñooy dàq sax lañu nekkoon bu njëkk.

9 Noonu it, Yeowaa ngi ñuy wóoral ne Nguur gi lu am la. Ni ñu ko wone ci téereb Biibël bi tudd Yawut yi, ngiste yu bare ci Sàrt baa ngi nekkoon takkandeeru ndefarum Nguur gi. (Yawut yi 10:1) Nguurug Israel gi nekkoon ci kow suuf dafa doon tax ñu xelmati, ci lu leer, li Nguurug Yàlla doon nirool itam. Du woon nguur gu mel ni yeneen yi, ndax buur ya dañu toogoon “ci jalub Yeowa.” (1 Nettaliy xew-xewi cosaan 29:23) Magum loolu, lii lañu yégle woon, fekk amagul: “Yetuw Nguur gi du sore Yudaa, niki bantub kilifa gi nekk ci diggantey tànkam, ba kera Shilo di ñëw; te moom la ndéggalub mbooloo yi di lew.” (1 Musaa 49:10) * Waaw, ca askanu buuri giiru Yudaa boobu la Yeesu, Buur bi sax bu nguurug Yàlla, waroona juddoo.—Lukk 1:32, 33.

10. (a) Kañ lañu samp li sës Nguurug Almasib Yàlla? (b) Ci ban liggéey bu am solo, la ñiy ilif suba ak Yeesu warkoona jiitu ci kow suuf?

10 Li sës Nguurug Almasib Yàlla, ñu ngi ko samp ba ñu tànnee ndawiy Yeesu. (Efes 2:19, 20; Peeñu bi 21:14) Ñoo doon ñii njëkk ci téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000) ñi naroona nguuru ca asamaan niki ay buur yu boolook Yeesu Krist. Ba ñu nekkee ci kow suuf, ñooñu naroona nguurook moom waroon nañoo jiitu ci liggéeyub seede bi, topp ndigalul Yeesu: “Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi.”—Macë 28:19.

11. Nan la liggéeyub waare Nguur gi deme ci suñu jamano, te lan lay mottali ?

11 Ndigalul sàkk ay taalibe ñu ngi koy topp tey cig dayo gu masula am. Ci suuf si sépp, Seedey Yeowa yaa ngiy yégle xabaar bu baax bi ci Nguur gi, lu dëppook baatiy yégle yi jóge ci Yeesu: “Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee, muju jamano ji jot.” (Macë 24:14) Ñu ngiy doxal porogaraamub njàngale bu réy nikib fànna liggéeyub waare Nguur gi. Ñii nangoo topp sàrt yeek rëddi-yooni Nguurug Yàllaa ngiy xéewlu tey-tey jàmm ak déggoo yu nguuri doomi Aadama yi mënula daj. Loolu lépp dafay firndeel bu leer ne Nguurug Yàlla lu am la!

12. (a) Lu tax mu jaadu waarekati Nguur gi jël turu Seedey Yeowa? (b) Ci lan la Nguurug Yàlla wuuteek nguuri doomiy Aadama?

12 Yeowa waxoon na waa Israel: “Yeenay samay seede, (. . .) waaw sama surga bi ma tànn.” (Isayi 43:10-12) Yeesu, “Seede bu takku bi,” farlu woon na ci yégle xabaar bu neex bi jëm ci Nguur gi. (Peeñu bi 1:5; Macë 4:17) Kon jaadu na, ci suñu jamano, waarekati Nguur gi jël tur wi Yàlla tànn, maanaam Seedey Yeowa. Waaye lu tax Seede yiy sàkku jot ak farlu yu ni bare ngir waxtaan ak ñeneen lu jëm ci Nguurug Yàlla? Dañu koy def ndaxte Nguur gi mooy jenn yaakaaru nit ñi doŋŋ. Nguuri doomi Aadama dañuy mujja màbb, bu dul tey muy suba, waaye loolu du dal Nguurug Yàlla mukk. Isayi 9:6, 7 a ngiy woowee Njiitam, Yeesu, “Garmib jàmm”, ba noppi teg ci: “Ci sakkanaayub kiliftéefu garmi bi ak ci jàmm, du am muj.” Nguurug Yàlla melul ni nguuri doomiy Aadama—yu fi nekk tey, suba ñu folli leen. Noonu, Dañel 2:44 a ngiy wax: “Yàllay asamaan dina samp ag nguur gu ñu dul daaneel mukk. Te nguur gi ci boppam du jaar ci weneen xeet. (. . .) Moom ci boppam dina taxaw ba ay diir yu amul àpp.”

13. (a) Yan ñooy yenn jafe-jafe yu Nguurug Yàllay toppatoo te texe ci? (b) Lu tax mu mën ñoo wóor ne digey Yàlla dinañu àgg?

13 Ban buur ci doomiy Aadamaa am mën-mënub dindi xeex, ñaawtéef, feebar, xiif, ak ñàkka am foo dëkk? Magum loolu, man njiit a am mën-mënub dekkal ñi dee? Nguurug Yàllaak Buuram ñooy jagal yëf yooyu. Nguur gi du am ay sikk, niki jumtukaay bu dul dox bu baax dee laaj saa su nekk ñu jagal ko. Asté loolu, Nguurug Yàlla dina texe, ndax Yeowa dig na: “Sama kàddu giy génne sama gémmiñ (. . .) du dellu ci man te baña yóbbe dara, waaye ci lu wóor dina def li ma soob, te dina am barke dëgg ci li tax ma yónni ko.” (Isayi 55:11) Nasub Yàlla du caŋ, waaye kañ la kiliftéefu Nguur gi waroona tàmbali?

KILIFTÉEFU NGUUR GI—KAÑ?

14. Ban dégg bu moy dëgg la taalibey Yeesu amoon jëm ci Nguur gi, waaye lan la Yeesu xamoon jëm ci kiliftéefam?

14 “[Sang bi, NW ] ndax ci jamano jii ngay yekkatiwaat nguuru Israel?” Laaj boobu taalibey Yeesu yi laaj, feeñal na ne ba booba xamuñu woon nasub Nguurug Yàlla ak diir bi ñu àppal ngir kiliftéefam tàmbali. Ba mu leen di artu ñu baña tandale ca mbir moomu, Yeesu nee na: “Ngeen xam jamano yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.” Yeesu xamoon na ne nguuram ci kow suuf saa ngi ñëw ëllëg, lu yàgg gannaaw ndekkiteem ak yéegam ca asamaan. (Jëf ya 1:6-11; Lukk 19:11, 12, 15) Mbind yi yégle woon nañu loolu. Naka noonu?

15. Nan la Sabuur 110:1 di ñu ràññeeloo jamano kiliftéefu Yeesu?

15 Ba muy wax ci Yeesu niki “Sang,” ci yégleb xew-xew bu naroona ami, buur ba Dawuda nee na: “Yégle bi Yeowa jëmale ci sama Sang mooy: ‘Toogal ci sama loxo ndeyjoor ba kera may teg say noon niki toogu ngir say tànk.’” (Sabuur 110:1; dendale kook Jëf ya 2:34-36.) Yégleb xew-xew booboo ngiy wone ne kiliftéefu Yeesu doonul daldi tàmbali ca saa sa, gannaaw yéegam ca asamaan. Asté loolu, dafa naroona xaar ca loxo ndeyjooru Yàlla. (Yawut yi 10:12, 13) Ba kañ la naroona xaar? Kañ la kiliftéefam naroona tàmbali? Biibël baa ngi ñuy dimbali ñu daj tont yi.

16. Lan moo xew ca atum 607 L.J.K.T., te nan la loolu lëkkaleek Nguurug Yàlla?

16 Benn dëkk doŋŋ bi Yeowa tegoon turam ci kow suuf si sépp a doon Yérusalem. (1 Buur 11:36) Moo doon itam péeyub nguur gi Yàlla nangu woon ci kow suuf si, nguur gu doon misaal Nguurug Yàlla ca asamaan. Looloo tax, tas bi waa Babilon tasoon Yérusalem ca atum juróom-benni téeméer ak juróom-ñaar (607) L.J.K.T. yenu woon na maanaa lool. Xew-xew boobu moo rëdd ndoortel dog bu gudd, fu Yàlla dootuloon doxal kiliftéefam ci kow mbooloom fii ci kow suuf. Lu tollook juróom-benni xarnu gannaaw loolu, Yeesu wone na ne ñu ngi woon ba booba ca diir boobu, ndax lii la wax: “Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yérusalem, ba kera [diir yi ñu àppal xeet yi, NW ] dul Yawut mat.”—Lukk 21:24.

17. (a) Lan ay “diir yi ñu àppal xeet yi, NW ” te lan a naroona nekk seen yàggaay? (b) Kañ la “diir yi ñu àppal xeet yi, NW ” tàmbali te kañ lañu jeex?

17 Ca biir “[diir yi ñu àppal xeet yi, NW] dul Yawut,” doon nañu may nguuriy àddina si ñu dog kiliftéef gi Yàlla nangu woon. Jamano jooju tàmbali naak tasub Yérusalem ca atum 607 L.J.K.T., te Dañel wone na ne jamano jooju doon na wéy “juróom-ñaari diir.” (Dañel 4:23-25) Lan ay yàggaayu loolu? Biibël baa ngiy wone ne ñetti “diir” ak genn-wàll ak junni fan ak ñaar téeméer ak juróom-benn fukk (1 260) a yem képp. (Peeñu bi 12:6, 14) Diir boobu ñaari yoon, walla juróom-ñaari diir, war naa def ñaari junniy fan ak juróomi téeméer ak ñaar fukk (2 520). Waaye dara lu ràññeeku xewul ba diir bu gàtt boobu sottee. Bu ñu jëlee “benn fan ngir benn at” taf ko ci yégleb Dañel tey waññ 2 520 at li dale ca atum 607 L.J.K.T., ca atum 1914 G.J.K.T. lañuy àgg.—4 Musaa 14:34; Esekiel 4:6.

18. Lan la Yeesu def, tuuti gannaaw ba mu jotee kàttanug Nguur gi, te nan la loolu laale suuf si?

18 Ndax Yeesu tàmbali naa nguuru ca asamaan at mooma? Ci pàcc miy topp, dinañu waxtaane li nekk ci Mbind yi te tax ñu mëna tontu waaw. Dëgg la, ndoortel kiliftéefu Yeesu doonul ànd ak jàmm ci kow suuf ci saa si. Peeñu bi 12:7-12 a ngiy wone ne Yeesu dafa jot Nguur gi rekk mu dàqe asamaan Seytaaneek malaakam yi nekk ay seytaane. Loolu doon na tekki ay musiba ngir suuf si, waaye jàng ne Ibliis “jot gi ko dese barewul,” dafay yokk fit. Tuuti ca kanam, dinañu mëna bég du rekk ndaxte Nguurug Yàllaa ngiy ilif, waaye itam ndaxte dina barkeel suuf seek nit ñi ko déggal. (Sabuur 72:7, 8) Nan lañu xame ne loolooy am ca kanam tuuti?

[Li ñu bind ci suuf]

^ Turuw Shiloo ngiy tekki “Ki mu lew; Ki ko moom.” Ca waxtoom, mujj naa leer ne “Shilo” moo doon Yeesu Krist, “Gaynde [gi bawoo ca] giiru Yudaa.” (Peeñu bi 5:5) Yenn téerey Yawut yi ñu tudde Targum wuutu nañu sax baat “Shilo” ak “Almasi bi” walla “Almasi buur bi.”

SEETLUL SA XAM-XAM

Lan mooy Nguurug Yàlla, te fan lay nguuroo?

Kan mooy jiite ci Nguur gi, te ñan ñooy ay surgaam?

Nan la ñu Yeowa wóorale ne Nguuram lu am la?

Kañ la “diir yi ñu àppal xeet yi, NW” tàmbali te kañ lañu jeex?

[Laaj yi]

[Wërale bi nekk paas 94]

YENN XEW-XEW YU AM SOLO YU LËKKALEEK NGUURUG YÀLLA

• Yeowaa ngiy xamal nasam miy sàkk “njureel” guy nappaaje boppu Jaan ji, Seytaane miy Ibliis.—1 Musaa 3:15.

• Ca atum 1943 L.J.K.T., la Yeowa joxoñ ne “njureel” googu sëtu Ibrayima lay doon.—1 Musaa 12:1-3, 7; 22:18.

• Kóllëreg Sàrt bi ñu jox Israel ca atum 1513 L.J.K.T. “ab takkandeeru yëf yu baax yiy ñëw ca kanam la.”—2 Musaa 24:6-8; Yawut yi 10:1, NW.

• Nguurug Israel tàmbali na ca atum 1117 L.J.K.T., te gannaaw loolu dem naa dem ca biir askanu Dawuda.—1 Samwil 11:15; 2 Samwil 7:8, 16.

• Yàq nanu Yérusalem ca atum 607 L.J.K.T, te “diir yi ñu àppal xeet yi, NW ” tàmbali nañu.—2 Buur 25:8-10, 25, 26; Lukk 21:24.

• Ca atum 29 G.J.K.T., lañu tànn Yeesu niki Buur bi ñu fal te sumb na liggéey bi ñu ko sas ci kow suuf.—Macë 3:16, 17; 4:17; 21:9-11.

• Ca atum 33 G.J.K.T., la Yeesu yéeg ca asamaan te foofa, xaar na ca loxo ndeyjooru Yàlla ba kera Nguuram di tàmbali.—Jëf ya 5:30, 31; Yawut yi 10:12, 13.

• Fal nañu Yeesu ca Nguur ga ca asamaan ca atum 1914 G.J.K.T., at ma “diir yi ñu àppal xeet yi, NW ” jeexee.—Peeñu bi 11:15.

• Sànnee nañu asamaan Seytaaneek malaakam yi nekk ay seytaane ci wetug suuf si te ñoom yokk nañu musiba ci kow nit ñi.—Peeñu bi 12:9-12.

• Yeesoo ngiy wottu waare xabaar bu baax bi jëm ci Nguurug Yàlla ci àddina si sépp.—Macë 24:14; 28:19, 20.