Ni nga mënee jege Yàlla
Pàcc 16
Ni nga mënee jege Yàlla
1. Yan niroo ñoo fés ci diine yu bare?
BENN turist bu doon wër am réew mu féete Penku amoon na mbetteel ca baaxiy diine ya mu seetlu woon ca biir ab jàngu budist. Ak lu nataal ya bañoona baña nekk yu Maryaama walla Krist, yu bare ci baaxiy diine yooyoo nga doon nirook yosiy jàngoom ca réew ma mu fekk baax. Maanaam, seetlu woon na ne dañu doon jëfandikoo kurus tey tari, di woyandoo ay ñaan. Ñeneen itam def nañu ay dendale yu ni mel. Muy ca Penku walla Sowu jant, fasoŋ yi ñii jullite di jéemee jege Yàlla walla seeni jumtukaayiy njaamu niroo nañu lool.
2. Nan lañuy faramfàcce ñaan, te lu tax nit ñu bare di ñaan?
2 Ñu baree ngiy jéema jege saxsax Yàlla ci di ko ñaan. Ñaan ñu ngi ko faramfàcce niki “jëfu diisoo diggante nit ak li tedd walla sell—Yàlla, yàlla yi, àllaaxira walla doole yu sut suñu nekkeef.” (The New Encyclopædia Britannica) Waaye, bu ñuy jege Yàlla ci ñaan, ñenn ñi seen njariñu bopp doŋŋ lañuy xalaat. Noonu, am na bés, genn góor laaj na kenn ci Seedey Yeowa yi: “Soo ma ñaanalee, ndax loolu dina saafara jafe-jafe yi ma am ci sama biir njaboot, fa may liggéeye, ak ci wàllu sama wér-gi-yaram?” Mu ngi mel ni góor googu loolu la foogoon, waaye ñu bare dañuy ñaan te gis ne seen jafe-jafee ngiy sax. Kon mënkoon nañoo laaj: ‛Waaw lu tax ñu wara jege Yàlla?’
LI TAX ÑU WARKOONA JEGE YÀLLA
3. Ci kan lañu wara jublu bu ñuy ñaan, te lu tax?
3 Ñaan nekkul baaxu diine gu tekkiwul dara, du it rekk am pexe mu ñuy taxa jot dara. Lenn ci liy gëna tax ñuy jege Yàlla mooy am wóllëre wu dëgër ak moom. Looloo tax suñuy ñaan, ci Yeowa Yàlla lañu leen wara jëmale. “Yeowa jege na ñépp ñiiy woote ci moom,” la Daawuda taggkat bi wax. (Sabuur 145:18) Yeowaa ngi ñuy xiir ci fas wóllëre jàmm ak moom. (Isayi 1:18) Ñiiy nangu woote boobu ànd nañook taggkat bi, ba muy wax: “Ci sama wàllu bopp, di jege Yàlla baax na ci man.” Lu tax? Ndaxte ñiiy jege Yeowa Yàlla, dinañu am bànneex dëgg ak dalaayu xel.—Sabuur 73:28.
4, 5. (a) Lu tax ñaan Yàlla di lu am solo? (b) Ban fasoŋu wóllëre lañu mëna am ak Yàlla jaare ci ñaan?
4 Lu tax ñuy ñaan Yàlla ndimbal su fekkee ne ‛xam na [suñuy] soxla, laata [ñu] ko koy wax’? (Macë 6:8; Sabuur 139:4) Ñaan dafay wone ne am nañu ngëm ci Yàlla te ñu ngi ko jàppe niki Cosaanu “gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat.” (Saak 1:17; Yawut yi 11:6) Yeowa dinay sàkku bànneex ci suñuy ñaan. (Léebu 15:8) Dafay bég ci dégg ni ñuy feeñaleek doole suñuy ngërëm ak suñuy tagg, ni baay di bége ci dégg doomam ju tuuti di koy wax kàdduy ngërëm yu jóge ci xolam. (Sabuur 119:108) Fu baay ak doom am wóllëre wu rattax, diisoo buy seddal xol a nga fa. Doom ju ñu sopp dafay bëgg di wax ak baayam. Loolu dëgg la itam lu jëm ci suñu wóllëreek Yàlla. Su ñu fonkee dëgg li ñuy jàng ci Yeowaak mbëggeel gi mu ñuy won, dinañu am bëgg-bëgg bu am doole ci wonal ko ko suñu bopp ci ñaan.—1 Yowanna 4:16-18.
5 Bu ñuy jege Yàlla Aji Kowe ji, war nañoo bare teraanga, bu fekkee sax soxlawul ñuy jaaxle lu jëm ci baat yi ñuy jëfandikoo saxsax. (Yawut yi 4:16) Saa su nekk, Yeowa yomb naa waxal. Te akay teraanga, mëna ‛tuur suñu xol’ ci kanamu Yàlla cig ñaan! (Sabuur 62:8) Am ngërëm ci Yeowa dafa ñuy yóbbu ci am wóllëre wuy seddal xol ak moom, niki woowa Ibrayima amoon niki xaritu Yàlla. (Saak 2:23) Waaye bu ñuy ñaan Aji Boroomu mbindeef mépp, war nañoo dab li mu ñuy laaj ngir mën koo jege.
LIÑ ÑUY LAAJ NGIR JEGE YÀLLA
6, 7. Ak lu Yàlla dul laaja laaj xaalis ngir dégg suñuy ñaan, lan la ñuy laaj bu ñuy ñaan?
6 Ndax soxla nañu xaalis ngir jege Yàlla? Nit ñu bare dañuy fey làbbe yi ngir ñu ñaanal leen. Am na sax ñu foog ne seeni ñaan dinañu àgg ci lu day naka seeni maye ci xaalis. Wànte Kàddug Yàlla waxul ne dañoo wara maye xaalis ngir mëna jege Yeowa cig ñaan. Li muy fogoru ci wàllu xel ak barke yi bawoo ci wóllëre wi ñu am ak moom cig ñaan, mën nañu leena am te duñu ci fey dërëm.—Isayi 55:1, 2.
7 Kon, lan lañuy laaj? Lenn lu am solo mooy am xol mu soloo njub. (2 Nettaliy xew-xewi cosaan 6:29, 30; Léebu 15:11) Ci suñu biir xol war nañoo teg suñu ngëm ci Yeowa Yàlla niki “Kiiy dégg ñaan” ak kiiy “neexal ñi koy wut [dëgg].” (Sabuur 65:2; Yawut yi 11:6 ) Fàww ñu am it xol bu suufeelu. (2 Buur 22:19; Sabuur 51:17) Ci benn ciy léebaatoom, Yeesu Krist wone na ne benn juutikat bu doon ñaan Yàlla, soloo xol bu toroxlu, mujj naa gëna jub ab Farisien bu doon réy-réylu. ( Lukk 18:10-14) Ba ñuy jege Yàlla ci ñaan, nañu fàttaliku ne “képp ku réy ci xol nekk na lu mata sib ci Yeowa.”—Léebu 16:5.
8. Su ñu bëggee Yàlla àggle suñuy ñaan, ci lan lañu wara sellal suñu bopp?
8 Su ñu bëggee Yàlla àggle suñuy ñaan, war nañoo setal suñu bopp ci dundinub bàkkaar. Ba taalibe Saak xiirtale ñeneen ñu jege Yàlla, li la ci teg: “Yeen bàkkaarkat yi, sellalleen seeni loxo; yeen ñi am xel ñaar, laaballeen seeni xol.” (Saak 4:8) Defkati lu bon yi sax mën nañoo fas wóllëre jàmm ak Yeowa su ñu réccoo te bàyyi seen dundin bu njëkk. ( Léebu 28:13) Mënuñoo giseek Yeowa su fekkee ne doŋŋ dañuy setal setallu suñu dundin. “Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande, di ubbi ay noppam ci seeni ñaan, waaye dàq ñiy def lu bon,” la Kàddug Yàlla wax.—1 Pieer 3:12.
9. Jaare ci kan lañu warkoona jege Yeowa, te lu tax?
9 Biibël bi nee na: “Amul nit ku jub ci kow suuf kuy def saa su ne lu baax te du bàkkaar.” (Dajalekat 7:20) Looloo tax mënkoon ngaa laaj: ‛Kon, nan lañu mënee jege Yeowa Yàlla?’ Biibël baa ngiy tontu: “Su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Krist mu jub mi.” (1 Yowanna 2:1) Lu ñu nekka nekk ay bàkkaarkat, mën nañoo jege Yàlla ak wax ju àndul ak laxas, jaare ci Yeesu Krist, mi dee niki peyug njot ngir ñun. (Macë 20:28) Mooy yoon wi kott ñu mëna jaar ngir mëna jege Yeowa Yàlla. (Yowanna 14:6) Waruñoo jël njariñu peyug njotug saraxu Yeesu niki luñ ñu jox ba noppi te tey dëkk ci bàkkaar. (Yawut yi 10:26) Wànte, su ñuy def suñu kem-kàttan ngir téye suñu bopp ci lu bon te ba tey ñuy juum léeg-léeg, mën nañoo réccu te ñaan Yàlla mu jéggal ñu. Bu ñu ko jegee ak xol bu suufeelu dina ñu dégg.—Lukk 11:4.
AY JOT NGIR WAX AK YÀLLA
10. Bu ñu dee ñaan, nan lañu mënee roy Yeesu, te yan jot lañu am ngir wéetal Yàlla cig ñaan?
10 Yeesu Krist fonkoon na wóllëreem ak Yeowa bu baax-a-baax. Looloo tax Yeesu daan sàkku jot ngir wéet ak Yàlla cig ñaan. (Mark 1:35; Lukk 22:40-46) Dinañu def lu rafet ci roy Yeesu tey faral di ñaan Yàlla. (Room 12:12) Jaadu na ñuy tàmbali bés bi ak ay kàdduy ñaan, te laata ñuy tëddi, mën nañu, ci lu aw yoon, gërëm Yeowa ngir yëngu-yëngub bés bi. Ci biir bés bi, dogul ci jege Yàlla “foo mënta tollu, NW. ” (Efes 6:18) Mën nañu sax ne selaw te ñaan ci suñu biir xol, xam ne Yeowa mën na ñoo dégg. Wéet ak Yàlla, di ko waxal dina ñu dimbali ñu dëgëral suñu wóllëreek moom, te di ñaan Yeowa bés bu nekk dina ñu dimbali ñu gën koo jege.
11. (a) Lu tax njaboot yi warkoona ànd di ñaan? (b) Boo waxee “Amiin” bu ñu sottalee ñaan, lan la looluy tekki?
11 Yeowa dafay déglu itam ñaan yi ñu defal ay mboolooy nit. (1 Buur 8:22-53) Mën nañoo jege Yàlla nikig njaboot, kilifag kër gi jiite ñaan gi. Loolu dafay feddali wóllëre wi lëkkale njaboot gi, te Yeowa dafay mujja nekk nit ku am ci ndaw yi, bu ñuy dégg seeni way-jur di ñaan Yàlla ak suufeelu. Waaw, su fekkee ne nag kenn a ngiy jiite mbooloo ci ñaan, xëy na ci menn ndaje Seedey Yeowa? Su ñu fa teewee, nañu déglu bu baax ba tax bu ñaan gi sottee, ñu mëna wax ak suñu xol bépp “Amiin,” baat buy tekki “Na amee noonu.”—1 Korent 14:16.
ÑAAN YI YEOWA DI DÉGG
12. (a) Lu tax Yàlla du àggle yenn ñaan yi? (b) Lu tax waruñoo teewlu doŋŋ ci suñuy soxlay bopp bu ñuy ñaan?
12 Am na ñuy yëg ne Yàlla du déglu seeni ñaan bu fekkee sax ñu ngi koy ñaan jaare ci Krist. Wànte ndaw li Yowanna nee na: “Kóolute gi nu am ci kanamu Yàlla mooy lii, su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul.” (1 Yowanna 5:14) Kon, soxla nañoo ñaan lu dëppook coobareg Yàlla. Ndegam suñu sutura ci wàllu ngëm soxal na ko, lépp luy laal suñu sutura ci fànna boobu nekk na lu jaadu lu mëna bokk ci suñuy ñaan. Fàww ñu tiiñ fiiru teewlu doŋŋ ci suñuy soxlay yaram. Maanaam, ba ñaan ngir am ñawinu xel ak fit ngir dékku feebar jaadoo, jaaxle yi jëm ci wér-gi-yaram waruñoo jiitu suñuy itte yi jëm suñu digganteek Yàlla. (Sabuur 41:1-3) Ba mu gisee ne mu nga doon ëppal ca na mu doon tiisoo wér-gi-yaramam, jenn jigéen ju nekk karceen laaj na Yeowa mu dimbali ko mu am gis-gis bu wér ci feebaram. Loolu, li mu yóbbe mooy wàññeekub réyaayu jafe-jafey wér-gi-yaramam ciy gëtam, te yëg na ci moom ne jotoon na “kàttan gi sut gu doomu Aadama, NW. ” (2 Korent 4:7) Bëgg-bëggam ngir nekk ndimbalul ñeneen ci wàllu ngëm yokku na, te mujj naa nekk waarekatu Nguur gi bu ci jébbal jotam gépp.
13. Ni ñu ko joxoñee ci Macë 6:9-13, yan ñooy yenn mbir yu jaadu yu ñu mëna boole ci suñuy ñaan?
13 Lan lañu mëna boole ci suñuy ñaan ba tax Yeowa am bànneex ci dégg leen? Yeesu Krist jàngal na ay taalibeem nan lañuy ñaane. Ci ñaan gi nekk royukaay gi te ñu nettali ko ci Macë 6:9-13, taxawal na royukaay buy wone mbir yan lañu mëna ñaan ci yoon. Lan moo ñu wara gëna itteel ci suñuy ñaan? Turuw Yeowa Yàllaak Nguuram lañu war di jiital ci kow lépp. Di ñaan ngir suñuy soxlay yaram lu jaadu la. Lu am solo la itam, di ñaan ngir mbaalug suñuy bàkkaar ak mucc ci fiir yi ak ci aji soxor ji, Seytaane miy Ibliis. Yeesu bëgguloon ñuy tari ci woy ñaan googu walla di ko baamtu ay yooni yoon, di baña xalaat li muy tekki. ( Macë 6:7) Ban fasoŋu wóllëre mooy woowu, su doom doon jëfandikoo yenn kàddu yi képp saa yuy waxal baayam?
14. Gannaaw suñuy laaj, yan ñaan lañu warkoon di def?
14 Gannaaw ñaan yeek leewaayu yu jóge ci xol, war nañoo def ay ñaani tagg ak ngërëm. (Sabuur 34:1; 92:1; 1 Tesalonikk 5:18) Mën nañu it ñaanal ñeneen. Ñaan yi jëm ci suñuy mbokki diine yu góor ak yu jigéen yi nekk ci tiis walla ñu leen di toŋal, a ngiy wone suñu itte ci ñoom, te Yeowa dina am bànneex ci di ñu dégg ñuy feeñal itte ju ni mel. (Lukk 22:32; Yowanna 17:20; 1 Tesalonikk 5:25) Ndaw li Pool bind na sax: “Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetalleen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant. Noonu jàmmu Yàlla, ji [sut bépp xalaat, NW ] dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Krist Yeesu.”—Filipp 4:6, 7.
NANGA SAX CI ÑAAN
15. Lan lañu wara fàttaliku su melee ni àgglewuñu suñuy ñaan?
15 Ak loo nekk di yokk sa xam-xam ci Yàlla, léeg-léeg mën ngaa yëg ne say ñaan àgguñu. Loolu mën naa am ndaxte xëy na du waxtu wi Yàlla di tontu ñaan googu saxsax. (Dajalekat 3:1-9) Yeowa mën naa bàyyi dara wéy di am ab diir, waaye dina tontu ci lu wóor ñaan yi te xam na wan mooy waxtu wi gën ngir defe ko noonu.—2 Korent 12:7-9.
16. Lu tax ñu war di sax cig ñaan, te nan la di def loolu dee laal suñu wóllëreek Yàlla?
16 Su ñu saxee ciy ñaan, loolu dafay wone ne li ñuy wax Yàlla itteel na ñu dëgg. ( Lukk 18:1-8) Maanaam, mën nañoo laaj Yeowa mu dimbali ñu, ñu daan liy sikk sàngam ci suñu jikko. Bu ñuy sax ci ñaan tey jëf lu dëppook suñuy laaj, ñu ngiy wone ne dëgg la ci ñun. Warkoon nañoo wax li ñu bëgg dëgg te maandu ci suñuy ñaan. Te lu am solo la, ñuy ñaan ak doole bu ñuy jànkoonteek fiir. (Macë 6:13) Bu ñu saxee ci ñaan, ci biir loolu di jéema téye suñu bopp ci li ñuy xiir ci bàkkaar, dinañu gis nan la ñu Yeowa di dimbalee. Loolu dina yokk suñu ngëm te feddali suñu wóllëreek moom.—1 Korent 10:13; Filipp 4:13.
17. Nan lañuy jariñoo soloo xelu ñaan bu ñuy jaamu Yàlla?
17 Bu ñuy soloo xelu ñaan, fekk ñu nekk ci liggéey bu tedd bi ñuy defal Yeowa Yàlla, dinañu mujja gis ne jaamuwuñu Yàlla ci suñu doole bopp. Yeowa mooy ki tax yëf yi defu. (1 Korent 4:7) Nangu loolu dina ñu dimbali ñu suufeel suñu bopp te dina rafetal suñu wóllëreek moom. (1 Pieer 5:5, 6) Waaw, am na fu dëgër fu ñu mëna sukkandiku ngir sax cig ñaan. Suñuy ñaan yu tàng ak xam-xamu nan lañu waree jege suñu Baay bu ànd ak mbëggeel ba ca asamaan dinañuy tax suñu dund neex dëgg.
DIISOO AK YEOWA: ÑAAN AK DÉGLU
18. Nan lañu mënee déglu Yàlla?
18 Su ñu bëggee Yàlla dégg suñuy ñaan, war nañoo déglu li muy wax. (Sakariaa 7:13) Yónneetul ay xabaaram jaare ci ay yonent yu mu ruux te ci lu wóor du jaare ci mbirum duggook seytaane. (5 Musaa 18:10-12) Waaye mën nañoo déglu Yàlla ciy jàng Kàddoom, Biibël bi. (Room 15:4; 2 Timote 3:16, 17) Ni ñu mënee soxlaa jéema bëgg cafko ñam wu baax, ñu ngi ñuy jamp ñu “am bëgg-bëgg bu am doole ngir meewum Kàddu gi, mi yàquwul.” Jéemala bëgg cafko ñamuw xel, ciy duruus bés bu nekk Kàddug Yàlla.—1 Pieer 2:2, 3, NW; Jëf ya 17:11.
19. Ban njariñ a nekk ci xalaat ba xeli ci li ngay duruus ci Biibël bi?
19 Nangay xalaat ba xeli ci li ngay duruus ci Biibël bi. (Sabuur 1:1-3; 77:11, 12) Looloo ngiy tekki teewlu ci li ñu duruus. Mënkoon nañoo tollale xalaat ba xeli ak reesal ñam. Mën ngaa reesal ñamuw xel ci lëkkale li ngay duruus ak li nga xam ba noppi. Nanga seet nan la li ngay duruus di laale sa dund, walla xalaatal ci li muy feeñal ci jikkoy Yeowa ak ay jëfinam. Noonu jaare ci sa njàngum bopp, mën ngaa sédd sa bopp ci ñamuw xel wi Yeowa di joxe. Loolu dina la gëna jegeloo Yàlla te dina la dimbali nga toppatoo jafe-jafey bés bu nekk.
20. Nan la di teew ci ndajey karceen yi di ñu dimbalee jege Yàlla?
20 Mën nga itam jege Yàlla booy déglu Kàddoom ga ñuy waxtaane ci ndajey karceen yi, niki waa Israel doon dégloo bu baax-a-baax ba ñu daan dajaloo ngir dégg duruusub Sàrtub Yàlla ca kanami ñépp. Ña daan jàngale ca jamano jooja dañu daan faramfàcce tekkite seen duruusub Sàrt ba, di dimbali ña leen doon déglu ñu nànd ko te di leen jàjji ci topp li ñu dégg. Loolu da leen doon yóbbe mbégte mu réy. (Nëxemiaa 8:8, 12) Kon defal teew ci ndajey Seedey Yeowa yi sa tàmmeel. ( Yawut yi 10:24, 25) Loolu dina la dimbali nga nànd te topp xam-xamub Yàlla ci sa dund te dina la indil bànneex. Bokk ci njabootug mbokki karceen yi nekk ci àddina si sépp dina la dimbali nga jege Yeowa. Te ni ñu koy gise, mën ngaa daj dalaay dëgg ci biir mbooloo Yàlla.
SEETLUL SA XAM-XAM
Lu tax nga warkoon di jege Yeowa?
Yan ñooy yenn ci jëf yi Yàlla laaj ngir jege ko?
Lan nga mëna boole ci say ñaan?
Lu tax nga warkoona sax ci ñaan?
Nan nga mënee déglu Yeowa tey?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 157]