Njaamug kan la Yàlla di nangu?
Pàcc 5
Njaamug kan la Yàlla di nangu?
1. Lan la jenn jigéenu Samari bëggoona xam ci mbirum njaamu?
NDAX mas ngaa laaj sa xel: “Njaamug kan la Yàlla di nangu?” Laaj bu ni mel xëy na tàbbi na ci xelu jigéen ju doon waxtaan ak Yeesu Krist ca wetu Tundu Gerisim ba nekk Samari. Ba muy joxoñ ab wuute diggante njaamug waa Samari ak gu Yawut yi, jigéen jooja wax na: “Naka-jekk suñuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla; waaye yeen, Yawut yi, dangeen ne Yérusalem lañu wara jaamoo Yàlla.” (Yowanna 4:20) Ndax Yeesu wax na jigéenu Samari ja ne, Yàlla gépp njaamu gu mu mënta doon lay nangu? Walla ndax dafa wax ne, am na ay yëf saxsax yuñ ñuy laaj ngir neex Yàlla?
2. Lan la Yeesu wax, ba muy tontu jigéenu Samari ja?
2 Tontu Yeesu, lu yéeme, moo doon: “Dina am jamano joo xam ne, du ci tund wale te du ci Yérusalem ngeen di jaamoo Baay bi.” (Yowanna 4:21) Waa Samari yàggoon nañoo ragal Yeowa te dañu daan jaamu yeneen yàlla ca Tundu Gerisim. (2 Buur 17:33) Léegi Yeesu Krist a ngi doon wax ne, du woon béréb booba walla Yérusalem ñoo naroona am solo ci njaamu dëgg gi.
JAAMUL CI XEL AK CI DËGG
3. (a) Lu tax waa Samari xamuñu woon ca dëgg Yàlla? (b) Nan la Yawut yi takku ci Yàlla ak ñeneen mujjoona mëna xam Yàlla?
3 Yeesu tegoon na ca la mu doon wax jigéenu Samari ja: “Yeen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.” (Yowanna 4:22) Waa Samari dañoo amoon ay xalaat yu jëm ci diine yu duloon dëgg, te ci Biibël bi, juróomi téere yu njëkk yi doŋŋ lañu nangu woon niki yu Yàlla ruux—te téere yooyu doŋŋ lañu nangu woon ci seen firib bopp, ñu xame firib boobu ci turuw Tawreetu waa Samari. Looloo tax, xamuñu woon ca dëgg Yàlla. Waaye, Yawut yi lañu dénkoon xam-xamub Mbind yi. (Room 3:1, 2) Mbind yi dañu doon jox Yawut yi takku ci Yàlla ak képp keneen nit ku naroona déglu, li ñu soxla woon ngir xam Yàlla.
4. Ni ko Yeesu waxe, lan la Yawut yeek waa Samari soxla woona def ngir Yàlla nangu seen njaamu?
4 Ca dëgg, Yeesu dafa doon won ne ngir neex Yàlla, Yawut yeek waa Samari dañoo waroona jubbanti na ñu daan jaamoo. Nee na: “Jamano dina nëw, te agsi na ba noppi, jamano joo xam ne, jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi ni mu ko bëgge. Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.” (Yowanna 4:23, 24) Soxla nañoo jaamu Yàlla “ci xel”, am xol bu fees ak mbég ak mbëggeel bu ñuy xiir ci loolu. Mën nañoo jaamu Yàlla “ci dëgg”, bu ñuy jàng Kàddoom, Biibël bi, te ñu koy jaamu fasoŋ bu dëppook dëgg gi mu feeñal. Ndax farlu nga ci def loolu?
5. (a) Lu baat “njaamu” di tekki? (b) Lan la ñu wara def su ñu bëggee Yàlla nangu suñu njaamu?
5 Yeesu jolliloo na ne Yàlla dafa bëgg njaamu dëgg. Looloo ngiy wone ne am na ay fasoŋi njaamu yu Yeowa mënula nangu. Jaamu Yàlla mooy di ko sargal te di ko jox njaamu gu tedd. Soo bëggoona sargal am njiit mu am doole, du ñàkk, doon nga farlu ci liggéeyal ko te def li ko neex. Bëgg nañu, ci dëgg, neex Yàlla. Asté ñuy yem doŋŋ ciy wax: ‘Sama diine doy na ma,’ soxla na ñoo wóor ne suñu njaamu dëppoo naak li ñu Yàllay laaj.
DI DEF COOBAREG BAAY BI
6, 7. Lu tax Yeesu du nangu ñenn ñiy wuyoo turu taalibeem?
6 Nañu jàng Macë 7:21-23 te seet ndax mën nañoo ber xalaat bu am solo buy dogal ndax Yàlla nangu na diine yi yépp. Yeesu nee na: “Du képp ku may wax: [Sang bi, Sang bi, New World Translation] mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw. Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: [Sang bi, Sang bi, NW ], ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare? Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg, ne leen: Musuma leena xam; soreleen ma, yeen ñiy def bàkkaar.”
7 Nangu Yeesu Krist niki Sang nekk na lu am solo lool ci njaamu dëgg gi. Waaye am na lu naroona des ci njaamug ñiiy wuyoo turu taalibey Yeesu. Nee woon na ne, ñenn ñi doon nañu def ay “kéemaan”, niki paji kawtéef, ci ni ñu ko fooge. Waaye, doon nañu caŋ ci def li Yeesu ne, ci la seen bakkan aju. Duñu leen doon fekk ñuy “def coobareg Baay[am]”. Su ñu bëggee neex Yàlla, war nañoo jàng liy coobareg Baay bi te def ko.
XAM-XAM BU WÉR BI—AB ÑAG LA
8. Def coobareg Yàlla lan la laaj ci ñun, te yan gis-gis yu moy dëgg lañu wara moytu?
8 Di def coobareg Yàlla laaj na ab xam-xam bu wér ci Yeowa Yàlla ak Yeesu Krist. Xam-xam bu ni mel a ngiy jëme ca dund ga dul jeex. Kon, ci dëgg, ku nekk ci ñun dinga bëgga fullaal solo jote xam-xam bu wér bi ci Kàddug Yàlla, Biibël bi. Am na ñuy wax ne, fi ak ñu ngi gore te sawar ci suñu njaamu, soxlawul ñu ciy bàyyi xel. Ñeneen dañuy wax ne, ‘Boo xamee li gëna néew, lu gëna néew loolu lañuy xaaru ci yow.’ Ndaxam, Biibël baa ngi ñuy xiirtal ñu yokk suñu xam-xamub Yàllaaki nasam.—Efes 4:13; Filipp 1:9; Kolos 1:9.
9. Nan la ñu xam-xam bu wér bi di aare, te lu tax ñu soxla ñag boobu?
9 Xam-xam bu ni mel ñag la ci luy gàkkal suñu njaamu. Ndaw li Pool wax na lu jëm ci am mbindaafonu xel muy nekk-nekklu “malaakam leer.” (2 Korent 11:14) Noonu mu nëbboo, mbindaafonum xel moomu—Seytaanee—ngi ñuy wuta nax ngir defloo ñu ay jëf yu dëppoowul ak coobareg Yàlla. Yeneen mbindaafoni xel yu ànd ak Seytaanee ngiy tilimal itam njaamug nit ñi, ndax Pool nee na: “Sarax yi [xeet, NW ] yi di rendi, ay rab lañu koy jagleel; jagleeluñu ko Yàlla.” (1 Korent 10:20) Mën naa am, ñu bare foogoon ne ñu ngiy jaamu Yàlla ni mu ware, te fekk daawuñu def li Yàlla bëgg. Dañu leen réeraloon, duggal leen cig njaamu gu sobe gu dul dëgg. Dinañu gëna jàng lu jëm ci Seytaaneek seytaaneem yi ca kanam, waaye leer na ne nooni Yàlla yooyoo ngiy gàkkal njaamug doomi Aadama yi.
10. Loo naroona def su kenn teyoon def posoñ ci sa rootukaayu ndox, te xam-xamub Kàddug Yàlla, bu wér bi, ngir def lan la ñuy gànnaayal?
10 Soo xamoon ne am na ku tey def posoñ ci sa rootukaayu ndox, ndax doon nga wéy di ci naan? Ci dëgg, doon nga dem wutiji bënu ndox mu wóor te set ci saa si. Noonu it, xam-xam bu wér ci Kàddug Yàllaa ñuy gànnaayal ngir ñu xàmme diine dëgg ji te jaleñ sobe yiy tax Yàlla baña nangu ag njaamu.
AY NDIGALI NIT NIKI AY YÉBLE
11. Lan moo awuloon yoon ci njaamug Yawut yu bare?
11 Ba Yeesu nekkee ci kow suuf, Yawut yu bare daawuñu def li dëppook xam-xamub Yàlla bu wér bi. Ñàkkoon nañu kon yoon wi ñu amoon ngir am taxawaay bu sell ci kanamu Yeowa. Pool bind na lu jëm ci seen mbir: “Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam [bu wér bi, NW ].” (Room 10:2) Dañu tànnaloon seen bopp na ñuy jaamoo Yàlla, asté ñuy déglu la mu doon wax.
12. Lan moo doon gàkkal njaamug Israel, te lan la loolu jur?
12 Ca seen cosaan, waa Israel daan nañu topp diine ju sell ji leen Yàlla joxoon, waaye tilimal nañu kook njàngaley ak xam-xamiy nit. (Yérémi 8:8, 9; Malaki 2:8, 9; Lukk 11:52) Lu njiitiy Yawut ya ci wàllu diine, ñu xame leen woon niki Farisieŋ ya, foogoona foog ne seen njaamu neex na Yàlla, Yeesu ne woon na leen: “Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yeen naaféq yi, bi mu bindee: Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. Seen màggal amul benn njeriñ, ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.’”—Mark 7:6, 7.
13. Nan lañu mënee def na Farisieŋ ya?
13 Ndax mën naa am ñuy def, ñun, niki Farisieŋ ya? Loolu mën naa am su ñu dee topp xarbaaxi diine yi ñu donn, asté ñoo seppali li Yàlla wax ci wàllug njaamu. Ngir artu ñu ci mbàmb dëgg boobu, Pool bind na: “Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne, ci mujug jamano dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane.” (1 Timote 4:1) Kon, foog rekk suñu njaamu neex na Yàlla doyul. Niki jigéenu Samari ja daje woon ak Yeesu, xëy na dañoo donne ni ñuy jaamoo ci suñuy way-jur. Waaye war na ñoo wóor ne, ñu ngiy def yëf yu dëppook li Yàlla nangu.
MOYTULA TOOÑ YÀLLA
14, 15. Su ñu amee sax ab xam-xam ci coobareg Yàlla, lu tax ñu war di moytu?
14 Lul su ñu nekkee nit ñu teey, mën nañoo def loo xam ne Yàlla mënu ko nangu. Maanaam, ndaw li Yowanna daanu na ca tànki menn malaaka, “bëgg koo jaamu”. Waaye malaaka ma artu na ko: “Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say mbokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla.” (Peeñu bi 19:10) Kon ndax gis nga soxla si nekk ci, mu wóor la ne sa njaamu amul dara, lu mel ni bokkaale, lu koy gàkkal?—1 Korent 10:14.
15 Ba yenn ci karceen ya tàmbalee topp ay aaday diine yu neexul Yàlla, Pool dafa leen laajoon : “Nan ngeen mana def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njeriñ, lu tax ngeen bëgg, ñu nootaat leen? Sama xel dalul ci yeen, ngir ragal sama coono ci yeen neen.” (Galasi 4:8-11) Waa ñooñu jotoon nañoo xam lenn ci Yàlla waaye dañoo mujja réer ci topp ay aaday diineek bés yu sell yu Yeowa mënuloona nangu. Ni ko Pool waxe, soxla nañoo “wéy di seetlu li neex Boroom bi, NW.”—Efes 5:10.
16. Nan la ñu Yowanna 17:16 ak 1 Pieer 4:3 di dimbalee dogal ndax bés yu sell yeek aada yi neex nañu Yàlla?
16 War na ñoo wóor ne, ñu ngiy moytu bés yu sell yu diine yeek yeneen aada yuy moy rëddi-yooniy Yàlla. (1 Tesalonikk 5:21) Maanaam, Yeesu nee na ñii koy topp: “Dañoo mel ni man; bokkuñu ci àddina.” (Yowanna 17:16) Ndax sa diine bokk na ci ay xew aki bés yu sell yu safaanook rëddu-yoonu baña farleek kenn lu jëm ci àddinaak li ci biiram? Walla ndax ñii nga bokkal diine dañuy topp léeg-léeg ay aadaaki xumbal yu leen di duggal ci demin bu dëppook li ndaw li Pieer wax? Bind na: “Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawtéef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag.”—1 Pieer 4:3.
17. Lu tax ñu wara moytu lépp luy awu xelu àddina si?
17 Ndaw li Yowanna jolliloo na soxlas moytu jépp jëf juy awu xalaatu àddina su gëmadi si ñu wër. Yowanna bind na: “Buleen sopp àddina si ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom. Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi, waaye ci àddina. Te àddina si day wéy, waaye kuy def coobareg Yàlla dinga sax ba fàww.” (1 Yowanna 2:15-17) Ndax seetlu nga ne, ñiiy “def coobareg Yàlla” ñooy sax ba fàww? Waaw, su ñu defee coobareg Yàlla te moytu yëngu-yëngu yuy awu xelum àddina sii, mën nañoo am yaakaaru dund gu dul jeex!
NA NGA TOPP YOONI YÀLLA, YU KOWE YI
18. Nan la ñenn ci waa Korent moye dëgg ci wàllu demin, te lan lañu jànge ci loolu?
18 Yàlla dafa bëgga am nikiy jaamukatam, ñiiy dëpp seen dund ak yoonam yu kowe yi ci wàllu jikko. Ca dëkku Korent bu njëkk ba, am na ñenn ñu doon nax seen bopp, foog ne Yàlla dina bàyyi demin bu jekkadi. Mën nañoo gis na ñu tooñe woon, bu ñu duruusee 1 Korent 6:9, 10. Ngir jaamu Yàlla ni mu ko nangoo, fàww ñu neex ko ci li ñuy wax ak li ñuy def. Ndax ni ngay jaamoo may na la nga def loolu?—Macë 15:8; 23:1-3.
19. Nan la njaamu dëgg giy laale suñu digaaleek ñeneen ñi?
19 Suñu digaaleek ñeneen nit ñi war naa awu it yooniy Yàlla. Yeesu Krist xiirtal na ñu, ñu digaaleek ñeneen ñi, ni ñu bëggkoon ñu digaaleek ñun, ndax looloo ngi bokk ci njaamu dëgg gi. (Macë 7:12) Seetlul it li mu wax ci wone mbëggeel ci sa mbokku diine: “Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.” (Yowanna 13:35) Taalibey Yeesu war nañoo bëggante tey defal seeni mbokki diine yeek ñeneen lu baax.—Galasi 6:10.
AG NJAAMOOK SA BAKKAN BÉPP
20, 21. (a) Ban fasoŋu njaamu la Yàllay laaj? (b) Lu taxoon Yeowa jaleñ njaamug Israel ca bésiy Malaaki?
20 Ci sa xol, mën ngaa bëgga jaamu Yàlla ni mu ko nangoo. Su dee noonu la, war ngaa am gis-gisu Yeowa ci wàllu njaamu. Taalibe ba tudd Saak jolliloo na ne gis-gisub Yàllaa am solo, du suñu bos. Saak wax na: “Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmeeku jiirim yi ak jigéen ñi seen jëkkër faatu ci seen tiis, tey waggar sobey àddina.” (Saak 1:27) Ak bëgg-bëggu neex Yàlla, ku nekk ci ñun soxla ngaa seppali sa njaamu, ndax mu wóor la ne, amul jenn jëfu gëmadi ju koy gàkkal walla bàyyiwoo gannaaw lu yenu maanaa ci kanamam.—Saak 1:26.
21 Njaamu gu sell doŋŋ, gu ñu def ak suñu bakkan bépp ay neex Yeowa. (Macë 22:37; Kolos 3:23) Ba xeetuw Israel joxee Yàlla lu gëna néew loolu, Yàlla nee na: “Doom ju góor, ci wàllu boppam, dafay teral baay; te surga, sangam bu mag. Kon su ma dee baay, ana cér bi ma war? Te su ma dee sang bu mag, ana ragal gi ma war?” Dañu doon tooñ Yàlla ci li ñu ko doon saraxal ay mala yu gumba, yuy soox ak yu feebar, te moom jaleñoon na jëfi njaamu yu ni mel. (Malaki 1:6-8) Yeowa yelloo na fasoŋu njaamu gi gëna sell te nanguwul leneen lu dul taq bu àndul ak bokkaale.—2 Musaa 20:5; Léebu 3:9; Peeñu bi 4:11.
22. Su ñu bëggee Yàlla nangu suñu njaamu, lan lañuy moytu, te lan lañuy def?
22 Jigéenu Samari ja Yeesu doon waxal niru woon na kuy wuta jaamu Yàlla ni mu ko bëgge. Su dee loolooy suñu bëgg-bëgg, dinañu moytu njàngale yeek jëf yuy gàkkal. (2 Korent 6: 14-18) Asté loolu, dinañu fexee am xam-xam bu wér ci Yàlla te def coobareem. Dinañu taq ci li muy laaj ngir ñu mën koo jaamu ni mu ko nangoo. (1 Timote 2:3, 4) Mooy li Seedey Yeowa yiy jéema def saxsax, te ñu ngi lay jamp ak cofeel nga ànd ak ñoom ngir jaamu Yàlla “ci xel ak ci dëgg.” (Yowanna 4:24) Yeesu nee na: “Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.” (Yowanna 4:23) Yaakaar nañu ne nit ku ni mel nga. Na jigéenu Samari jooja, ci lu amul werante, bëgg ngaa am dund gu dul jeex. (Yowanna 4:13-15) Waaye yaa ngiy gis nit ñiy màgget tey dee. Pàcc miy topp a ngiy faramfàcce lu tax.
SEETLUL SA XAM-XAM
Ni ko Yowanna 4:23, 24 wone, gan njaamu la Yàlla di nangu?
Nan lañu mënee dogal ndax Yàlla nangu na yenn aada yeek xew yi?
Yan ñooy yenn yëf yi Yàllay laaj ngir nangu ag njaamu?
[Laaj yi]
[Nataal bi nekk paas 44]