Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Téere biy feeñal xam-xamub Yàlla

Téere biy feeñal xam-xamub Yàlla

Pàcc 2

Téere biy feeñal xam-xamub Yàlla

1, 2. Lu tax ñu soxla suñu Sàkkkat tette ñu?

 AMUL lu gëna jaadu suñu Sàkkkat, Aji Mbëggeel ji, jox nit ñi ab téere tegtal bu leen di tette. Te ndax dàkkooruloo ne nit ñi soxla nañu ku leen di tette?

2 Lu ëpp ñaari junniy at ak juróomi téeméer (2 500) ca gannaaw, ag góor gu nekkoon yonent ak gëstukatu xew-xewi démb bind na: “Nit kiy dox moomul tette sax jéegoom.” ( Yérémi 10:23) Dëgg gu wér péŋŋ gi nekk ci kàddu googu masula leer ni mu leere tey. Noonu, ab gëstukatu xew-xewi démb bu tudd William H. McNeill seetlu na: “Li nit di daj ci dundam ci kow suuf, daanaka lëj-lëj aki gàllankoor yuy toppante rekk la, ci ndefar mi mu tëral ci dunyaa.”

3, 4. a) Nan lañu wara gise njàngum Biibël bi? b) Nan lañuy seete Biibël bi?

3 Biibël bi dafa ñuy jox lépp li ñu soxla ngir njubbanti bu ànd ak sago. Dëgg la, nit ñu bare dañuy tiit bu ñuy soga yër ci Biibël bi. Téere bu réy la, te yenn wàll yombuñoo nànd. Waaye su ñu la joxoon aw kayitu àtte, wuy leeral li nga wara def ngir moom ndono lu am solo, ndax doo sàkku jot ngir jàng kook teey? Su la yenn wàll ci kayit woowu jafee nànd, mën naa am nga laaj ndimbalul ku am xam-xam ci fànna boobu. Lu tax gisewuloo noonu Biibël bi? (Jëf ya 17:11) Li mu ñuy dikkal a gëna am solo donn alalu àddina. Ni ñu ko jànge ci pàcc mu njëkk mi, xam-xamub Yàlla mën naa jëme ca dund ga dul jeex ga.

4 Nañu seet téere biy feeñal xam-xamub Yàlla. Dinañu njëkke ci tënk Biibël bi. Gannaaw loolu, dinañu gis li tax nit ñu bare ñu am seetlu, gëm ne Kàddu la gu Yàlla ruux.

LI CI BIIR BIIBËL BI

5. (a) Lan la Mbind yi ci làkku Ebrë ëmb? b) Lan la Mbind yi ci làkku Grekk ëmb?

5 Biibël bi am na juróom-benn-fukki téere yu ndaw ak juróom-benn (66) ci ñaari xaaj, yu ñu faral di tudde Kóllëre gu màgget gi ak Kóllëre gu bees gi. Fanweeri téere ak juróom-ñeent ci Biibël bi lañu bind daanaka ci làkku Ebrë, ñaar-fukk ak juróom-ñaar yi des ci làkku Grekk. Mbind yi ci làkku Ebrë, li dale ca téere ba Musaa njëkka bind ba téereb Malaaki, mbindeef meek ñetti junniy at ak juróomi téeméer (3 500) yi njëkk ci cosaanu nit lañu ëmb. Bu ñuy seet xaaju Biibël boobu, dinañu xam naka la Yàlla digaale woon ak waa kër Israel​—⁠ba seen xeet sosoo ca fukkeelu xarnu baak juróom-benn laata jamano karceen tàmbali, dem ba juróomeelu xarnu L.J.K.T. * Mbind yi ci làkku Grekk, ëmb téereb Macë ba Peeñu bi, ñu ngi teewlu ciy njàngale aki yëngu-yënguy Yeesu Krist ak taalibeem ya ca xarnu ba njëkk G.J.K.T.

6. Lu tax ñu wara jàng Biibël bi bépp?

6 Ñenn ñi dañuy wax ne “Kóllëre gu màgget gi” Yawut yee ko moom, “Kóllëre gu bees gi”, Karceen yi. Waaye, ni ko 2 Timote 3:​16 waxe, “mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njeriñ.” (jolliloo bi, ci ñun la) Looloo tax, njàngum Mbind yi, mu àndul ak caaxaan, war naa boole Biibël bi bépp. Lu leer la, ñaari xaaji Biibël bi dañoo duggoo te déggoo ngir bokk faramfàcce benn tàjj.

7. Lan mooy tàjju Biibël bi?

7 Xëy na teewe nga ay ndajey diine ay ati at, ñu fa daan jàng ca kow ay xaaj ci Biibël bi. Mën naa am it, yow ci sa bopp, nga jàng ci ay jukki. Ndax xam nga ne, ci biir Biibël bi bépp, dale ca téere ba Musaa njëkka bind ba Peeñu bi, benn tàjj, wenn waxtaan a ci nekk? Waaw, benn tàjj bu déggooy jaar ci Biibël bi. Lan mooy tàjj boobu? Mooy làyyi sañ-sañ bi Yàlla am nguuru dóomi Aadama yi ak mottalib nasam bu ànd ak mbëggeel ci pexe Nguuram. Dinañu gis ca kanam, nan la Yàlla di àggalee nasam boobu.

8. Lan la Biibël biy feeñal ci jikko Yàlla?

8 Biibël bi yemul rekk ciy xamal li Yàlla nas, waaye it dafay feeñal jikkoom. Maanaam, ci Biibël bi ñu ngiy jànge ne Yàlla dafay yëg ci xolam te suñuy tànneef am nañu solo ci kanamam. (Sabuur 78:​40, 41; Léebu 27:11; Esekiel 33:11) Sabuur 103:​8-14 nee na Yàlla ku “am yërmande te ku laabiir la, gaawula mer te fees naak mbaaxaay bu ànd ak lewetaay.” Laabiir na ci ñun, ‘di fàttaliku ne pënd doŋŋ lañu’ te ci pënd lañuy dellu bu ñu deewee. (1 Musaa 2:7; 3:19) Ndaw jikko yu doy waar yu muy wone! Ndax du xeetu Yàlla ji nga bëgga jaamu?

9. Nan la ñuy Biibël biy joxee gis-gis bu leer ci yooniy Yàlla, te nan lañu mënee xéewlu ci xam-xam bu ni mel?

9 Biibël bi dafa ñuy leeral yooniy Yàlla. Léeg-léeg yoon yooyu dañu leen di taxawal ni ay sàrt. Waaye li gëna faral di am mooy yoon yooyu dañuy feeñ ci ay rëddi-yoon, yu ñuy jàngal ay royukaay yu ñu mënee sàkku xam-xam. Yàlla bindloo na yenn xew-xewiy cosaanu Israel bu njëkk ba, ngir suñu njariñ. Nettali yu wóor yooyu dañuy wone liy xew bu nit ñiy def li dëppook nasub Yàlla, ak muj gu ñaaw giy dal ñiiy topp seen bakkan. (1 Buur 5:4; 11:​4-6; 2 Nettaliy xew-xewi cosaan 15:​8-15) Duruusub nettaliy xew-xewi dundub démb yu am yooyu du ñàkka laal suñu xol. Su ñu jéemee jortu na xew-xew yooyu deme woon, dinañu niroolu ak nit ña ñuy nettali seeni mbir. Noonu, dinañu mëna jariñoo royukaay yu baax yi te moytu fiir yi moykat yi daanu. Wànte, fàww ñu tontu ab laaj bu suñu bakkan aju: nan lañu mënee wóor ne li ñu duruus ci Biibël bi, dëgg dëgg Yàllaa ko ruux?

NDAX MËN NGAA WÓOLU BIIBËL BI?

10. a) Lu tax ñenn ñi di xalaat ne Biibël bi dafa xewi? b) Lan la ñu 2 Timote 3:​16, 17 wax ci lu jëm ci Biibël bi?

10 Xëy na ràññee nga ne téere yu bare yuy xelal, at yu néew doŋŋ lañuy am, xewi. Biibël bi nag? Téere bu yàgg-a-yàgg la; ba ñu jeexalee mbindum Biibël bi ba tey, léegi mu mat ñaari junniy (2 000) at. Looloo tax am na ñuy xalaat ne mënuñu koo jëfoo ci suñu jamano. Waaye su fekkee ne Biibël bi Yàllaa koo ruux, ay xelalam duñu xewi mukk, bu dee sax dañoo yàgg. Mbind yi war nañoo am ba tey “njeriñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.”​—⁠2 Timote 3:​16, 17.

11-13. Lu tax ñu mëna wax ne Biibël bi am na njariñ ci suñu jamano?

11 Seppalib Biibël bi dafay wone ne ay rëddi-yoonam am nañu njariñ lu réy tey, naka keroog ba ñu leen bindee. Maanaam, Biibël bi buy waxtaane niteef, xam-xam bu xóot bu dul xewi la ciy feeñal. Loolu yomb naa gis ci Waare gi Yeesu def ca Tund wa te mu nekk ci téereb Macë, pàcc 5 ba 7. Waare googu laal na buumu xolu Mohandas K. Gandhi, ma nekkoon njiit ci wàllu politig ca Inde te saay, ba tax mu wax ag kilifa ãngale baat yii ñu ne moo leen moom: “Bés bu sa réew ak sama bos déggoo ci kow njàngaley Krist yi nekk ci Waare gi mu def ca Tund wa, kon dinañu faj, du rekk tawati suñu ñaari réew, waaye tawati réewi àddina si sépp.”

12 Waruñoo bett su nit ñi waaroo ci njàngaley Yeesu! Ca Waare ga ca kow Tund wa, won na ñu yoonuw bànneex dëgg. Yeesu tekki na naka la nit di rattaxale diggante bu ñagas, te joxe na ay jéemantal ci ni ñuy ñaane. Wone na it xel mi ëpp sago mi nit wara soloo lu jëm ci soxlay yaram te wone na Rëddu-Yoonu wurus wi, ngir suñu digganteek suñu moroom rattax. Na ñuy muree naxey diine yi te na ñuy ame ëllëg ju wóor, loolu bokk na itam ci fànna ya ñu waxtaane ca waare googale.

13 Ca Waare ga ca Tund wa ak li dés ciy xëtam yépp, Biibël baa ngi ñuy won, ci lu leer, li ñu wara def akit li ñu wara moytu ngir taneel nekkinu suñu dund. Njariñ lu réy li nekk ciy ndigalam tax na ab yarkat cib lycée ne: “Dëgg la, yeddkat laa cib lycée (high school), am naa it lijaasay licence ak maîtrise (master’s degrees), te jàng naa téere yu dul jeex ci wàllu wér-gi-xel ak psychologie (psychology), wànte gis naa ne ndigal yi Biibël bi di joxe ci fànna yu mel ni am séy bu barkeel, wottu xaleel ngir mu baña jàdd yoon, am ay xarit te sàmm wóllëre wi, [ndigal yooyoo] raw, ci lu sore, lépp li ma duruus walla jàng ca université (university).” Biibël bi nekkul rekk téere bu ànd ak jamano te am njariñ lu réy; téere bu wóor la itam.

WÉR TE WÓOR

14. Lan mooy wone ne Biibel bi lu wér lay wax ci wàllu science?

14 Dëgg la, xam-xam ci wàllu science taxul Biibël bi jóg; terewul lu wér la ciy wax. Maanaam, ca jamano ja li ëpp ci nit ñi gëmoon ne suuf si dafa tappandaar, yonent Isayi wax na dafa “mërëg” (ci làkku Ebrë, chugh, luy firi “mërëgaay”). (Isayi 40:22) Xalaat ne suuf si dafa mërëg, ñu ngi ko mujja nangu bu baax ay junniy at gannaaw Isayi. Teg ci, Ayóoba 26:7​—⁠bi ñu bind lu ëpp ñetti junniy (3 000) at⁠—wax na ne Yàllaa ngiy “aj suuf si ci neen”. Ab aalim ci Biibël bi sànni na kàddu gi: “Nan la Ayóoba xame woon dëgg googu, nit ñi di jàng jaww ji firndeel, maanaam suuf saa ngi aju, yemale boppam, ci béréb bu ne wéyëŋ? Ku weddi ne Mbind mu Sell mi, Yàlla ruuxu ko, dina jàkkarlook laaj bu jafee tontu.”

15. Nan la fasoŋ bi ñu binde Biibël bi di dooleele suñu kóolute ci moom?

15 Bindinub nettali yi ci biir Biibël bi dafay dooleel itam suñu kóolute ci téere bu yàgg boobu. Ci lu wuuteek ay léeb, xew-xew yi Biibël bi ëmb dañu leen lëkkaleek ay nit aki jamano saxsax. (1 Buur 14:25; Isayi 36:1; Lukk 3:​1, 2) Ba gëstukati xew-xewi démb ya daan dund ca jamano yooya, doon ëppal daanaka ndami seeni njiit te doon nëbb seeni jéll ak seeni njuumte, bindkati Biibël bi dañu gore woon te jub​—⁠bu fekkee sax seeni bàkkaar yu réy lañu doon nettali.​—⁠4 Musaa 20:​7-13; 2 Samwil 12:​7-14; 24:⁠10.

AB TÉERE BUY YÉGLE LUY AMI

16. Ban mooy firnde bi ëpp doole biy wone ne Biibël bi, Yàllaa ko ruux?

16 Xew-xew yi yonent yi yégle woon niki lu di ami te ñu àgg, dañuy wone ci lu wóor ne Biibël bi Yàllaa ko ruux. Biibël bi am na yégley yonent yu bare yu àgg benn benn. Ci lu leer, mënuñoo jàppe ay nit doŋŋ def loolu. Kon nag, ci kan la yégle yonent yooyu bawoo? Biibël bi ci boppam a ngiy tontu: “Kenn ci yonent yi musula wax ci coobareg boppam, waaye, Xel mu Sell mi, [walla dooley Yàlla jiy jëf ], daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla.” (2 Pieer 1:21) Nañu seet yenn misaal.

17. Yan yégley yonent a doon yégle jéllu Babilon, te nan la yégle yooyu àgge?

17 Jéllub Babilon. Isayi ak Yérémi, ñoom ñaar, yégle woon nañu jéllub Babilon ca kanami waa Medi ak waa Pers. Li gëna ràññeeku, mooy Isayi tudd na jéll jooju, lu tollook ñaar téeméeri at balaa ñu ko jël ak doole! Fànnay yégle yiy topp, gëstukati xew-xewi démb biral nañu leen, maanaam: jàddloo ndoxi dexu Ëfrat cib déeg bu réy bu ñu gas ngir dex gi fer (Isayi 44:27; Yérémi 50:38); sàgganee tëj bunti Babilon yi féete ci dex gi (Isayi 45:⁠1); am njiit mu ñu tudde Sirus moo jël dëkk baak doole.​—⁠Isayi 44:⁠28.

18. Nan la yéeg ak jéllub “buuru Grees” àggale woon ab yégleb yonent ci Biibël bi?

18 Yéeg ak jéllub “buuru Grees.” Cib gis-gis, Dañel gis na ab sikket buy fàdd am kuuy, damm ñaari béjjénam. Gannaaw loolu, béjjén bu mag bi sikket bi ame woon damm na, ñeenti béjjén wuutu ko. (Dañel 8:​1-8) Lii lañu tekkil Dañel: “Kuuy mi nga gisoon te ame ñaari béjjén yi a ngiy misaal buuri Medi ak Pers. Te sikket bi bare kawar a ngiy misaal buurub Grees; te béjjén bu mag bi nekk diggante ñaari gëtam yi, a ngiy misaal buur bu njëkk bi. Te ndegam moom damm na, ba ñeent mujja jóg wuutu ko, am na ñeenti nguur yuy jóg ci xeetam, waaye duñu am kàttanam.” (Dañel 8:​20-22) Lu jege ñaari téeméeri at gannaaw ba Dañel yégle loolu, “buurub Grees”, Aleksãdar mu Mag ma, daaneel na Nguuru Medi ak Pers ma ame woon ñaari béjjén. Aleksãdar saay na ca atum ñetti téeméer ak ñaar-fukk ak ñett (323) laata jamano karceen tàmbali; gannaaw loolu, ñeent ci ay njiiti xareem daldi ko wuutu. Waaye, genn ci nguur yooyu ci tegu yemul kàttan ak nguurug Aleksãdar.

19. Yan yégley yonent a àgg ci Yeesu Krist?

19 Dundug Yeesu Krist. Mbind yi ci làkku Ebrë ëmb nañu yégle yonent yu bare yu jëm ci njuddu, sasu, deewug, ak ndekkitel Yeesu te yégle yooyu yépp àgg nañu. Maanaam, lu ëpp juróom-ñaari téeméeri at balaa loolu am, Mikaa yégle woon na ne Almasi bi, walla Krist, dina juddu ca Betleyem. (Mikaa 5:2; Lukk 2:​4-7) Dundandoob Mikaa mu tudd Isayi yégle woon na ne dinañu dóor Almasi bi te tëfli ko. (Isayi 50:6; Macë 26:67) Juróomi téeméeri at balaa loolu di am, Sakaria yégle woon na dinañu wor Almasi bi ngir fanweeri xànjari xaalis. (Sakaria 11:12; Macë 26:15) Lu ëpp junniy at laata ñoo àgg, Dawuda yégle woon na ay xew-xew yu ñu lëkkaleek deewu Yeesu Almasi bi. (Sabuur 22:​7, 8,  18; Macë 27:​35, 39-43) Te juróomi téeméeri at balaa loolu di am, yégleb Dañel feeñaloon na kañ la Almasi biy fëll, diirub liggéey bi ñu ko sas akit jamano deewam.(Dañel 9:​24-27) Loolu lépp ab yër rekk la, ci li ñu yégle woon ci Yeesu Krist te mu àgg. Dinga gis ca kanam, naka la gëna duruus lu jëm ci moom di la amale njariñ.

20. Gan kóolute lañu wara jële ci nettalib yégley yonent yi àgg ba noppi?

20 Yeneen yégle yonent yu bare ci Biibël bi jëm ciy diir yu gudd, àgg nañu ba noppi. Mën ngaa laaj: ‘Waaye, nan la looluy laale sama dund?’ Seetal: su la kenn doon wax dëgg ay ati at, ndax dinga jékki-jékki nàttable waxam bu la waxee lenn lu bees? Déedéet! Yàlla dëgg doŋŋ la wax ci biir Biibël bi bépp. Ndax loolu warula dëgëral suñu kóolute ci digey Biibël bi, niki yégley yonent yi jëm ci suuf siy ñëw tey nekk àjjana? Ci lu wóor mën nañoo am kóolute gu mel ni gi Pool amoon; moom, ab taalibe Yeesu bu doon dund ca xarnu bu njëkk ba bind na: “Yàlla (...) du tebbi waxam.” (Titt 1:⁠2) Rax-ca-dolli, bu ñuy jàng Mbind yi te di jëfoo seeni ndigal, dañuy wone sago su nit ñi mënula jot ci seeni pexe bopp, ndax Biibël bi mooy téere biy feeñal xam-xamub Yàlla biy jëme ca dund ga dul jeex.

AMAL BËGG-BËGG BU AM DOOLE NGIR XAM-XAMUB YÀLLA

21. Lan nga wara def, su fekkee ne yenn yëf yi ngay jàng dañoo mel ni lu diis?

21 Booy jàng Biibël bi, mën naa am nga jàng ay yëf yu wuuteek li ñu la jàngal bu njëkk. Mën naa am sax, nga ràññee ne yenn aaday diine yi nga fonk, neexuñu Yàlla. Dinga jàng ne yoon yi Yàlla tëral jëm ci lu baax ak ci lu bon, ñoo sut li àddina su bàyyeeku sii tëral. Ci ndoorte li, dina mel ni lu diis ci yow. Waaye na nga muñ! Ci teey, seetal Mbind yi ngir daj xam-xamub Yàlla. Na nga paree nangu ne fàww nga soppi say xalaat ak sa demin ngir topp ndigalul Biibël bi.

22. Lu tax ngay jàng Biibël bi, te nan nga mënee dimbali ñeneen ñu nànd loolu?

22 Mën naa am say xarit ak say mbokk, ci bëgg laa dimbali, bañ ne doo jàng Biibël bi; waaye Yeesu nee na: “Koo xam ne, nangu nga ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw; waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.” (Macë 10:​32, 33) Ñenn ñi mën nañoo ragal, nga dugg ci tariixa bu wóorul walla nga mujja nekk ku téppatiku ci yëfi diine. Ndaxam ci dëgg, dangay fexee sàkku doŋŋ xam-xamub Yàlla bu wér beek dëggam. (1 Timote 2:​3, 4) Ngir nga dimbali ñeneen ñi ñu nànd loolu, bul di téesante, waaye na nga lewet bu fekkee yaa ngiy waxtaan ak ñoom ci li ngay jàng. (Filipp 4⁠:5) Fàttalikul ne nit ñu bare dañu leen “gindi ci lu àndul ak wax”, bu ñu gisee ciy firnde yu wóor ne xam-xamu Biibël bi amal na njariñ dëgg ñit ñi.​—⁠1 Pieer 3:​1, 2.

23. Nan nga mënee ‘am bëgg-bëgg bu am doole’ ngir xam-xamub Yàlla?

23 Biibël bi dafa ñuy jamp: “Niki ay liir yuy soga juddu, na ngeen am bëgg-bëgg bu am doole ngir meew mu sell mi fekk baax ci kàddu gi.” (1 Pieer 2:2, New World Translation) Ab liir, ci lekk gi ko yaayam di jox lay jafandu, te dafay laaj ak fitna lekk googu mu soxla. Noonu it, suñu dund a ngi aju ci xam-xamub Yàlla. Na nga “am bëgg-bëgg bu am doole” ngir Kàddoom, wéy ci sa njàng. Waaw, na nga góor-góorlu di duruus Biibël bi bés bu nekk. (Sabuur 1:​1-3) Loolu dina la yóbbe barke yu réy, ndax Sabuur 19:11 wax na lii ci sàrtiy Yàlla : “Di leen sàmm, yool bu réy lay yóbbe.”

[Li ñu bind ci suuf]

^ L.J.K.T. a ngiy tekki “laata jamano karceen tàmbali” te moo gëna wér L.K. (“laata Krist”). G.J.K.T. ñu faral di ko wooye A.D., ngir anno Domini, a ngiy tekki “gannaaw ba jamano karceen tàmbalee.”

SEETLUL SA XAM-XAM

Lan moo wuutale Biibël beek yeneen téere yi?

Lu tax nga mëna am kóolute ci Biibël bi?

Lan moo lay won ne Biibël bi, Kàddu Yàlla gi mu ruux la?

[Laaj yi]

[Wërale bi nekk paas 14]

NA NGA MUJJA MIIN BU BAAX SA BIIBËL

Mujja miin Biibël bi soxlawula nekk lu jafe. Jëfandikool limub àlluwa ji ngir jàng toppanteb téerey Biibël bi ak fi ñu nekk.

Téerey Biibël bi am nañu ay pàcc aki aaya ngir daj ci lu yomb li ngay wut. Dolli nañu ci xàjjaley pàcc yi ca fukkeelu xarnu baak ñett G.J.K.T., te ab muulkat bu doon dund ca fukkeelu xarnu baak juróom-benn te cosaanoo France lañu wax ne moo xàjjale Mbind yi ci làkku Grekk ci ay pàcc, ni ñu nekke léegi. Biibël bi lëmm, bi njëkka amandoo pàcc ak aaya yu am ab siifar, France la génne, ñu weejal ko ca atum 1553.

Bu ñu limee ay mbind ci biir téere bii, siifar bu njëkk baa ngiy joxoñ pàcc bi, te bi ci topp a ngiy wone aaya ji. Maanaam, limub “Léebu 2:5” a ngiy tekki téereb Léebu, pàcc 2, aaya 5. Booy ubbi Biibël bi ngir duruus mbind yi ñu lim, ca kanam tuuti dinga mujja aay ciy daj jukkiy saxsax yu Biibël bi.

Yoon wi gën ngir mujja nekk ku miin Biibël bi mooy di ko jàng bés bu nekk. Ci ndoorte li, dina mel ni lu lay tëkk. Waaye soo ciy jàng ñett ba juróomi pàcc bés bu nekk, looloo ngi aju ci seen guddaay, dinga jeexal duruusub Biibël bi bépp ci menn at. Lu la tee tàmbali tey?

[Wërale bi nekk paas 19]

BIIBËL BI—TÉERE BU AMUL MOROOM

• Biibël bi, “Yàllaa ko ruux.” (2 Timote 3:16) Lu ko ay doomi Aadama binda bind, Yàllaa jiite seeni xalaat, ba tax Biibël bi mooy ci dëgg “kàddug Yàlla.”​—⁠1 Tesalonikk 2:⁠13.

• Lu tollook ñeent-fukki (40) bindkat yu bokkul yar, yëngu-yëngook li ñu daj ci àddinaa bindoon Biibël bi cib diir bu ëpp fukki xarnook juróom-benn. Waaye, li liggéey boobu bépp jur dafa ànd li dale ca ndoorte la ba ca muj ga.

• Li Biibël bi mucc ci ay werantee ëpp bépp beneen téere bu mu mënta doon. Ca Jamanoy Lëndëm, daan nañu lakk ay nit ci biir taalub matt ndax doŋŋ li ñu yoroon sottib Mbind yi.

• Biibël bi mooy téere bi ñu gëna siiwal ci biir àddina si. Firi nañu ko, muy firib lëmm walla ci ay wàllam, ci lu ëpp ñaari junniy (2 000) làkk. Muul nañu ay tamndareeti tamndareeti sotti, te jafe naa am béréb ci kow suuf fu ñu mënula gis ab sotti.

• Dog wi gëna màgget ci Biibël baa ngi dale ca fukkeelu xarnu baak juróom-benn L.J.K.T. Moo jiitu peeñub Rig-Veda Hindu yi (lu jege junneek ñetti téeméer [1300] L.J.K.T.), “Kanon bu Ñetti Pañe yi” yu Budist yi (juróomeelu xarnu L.J.K.T.), walla al Quran bu Islam (juróom-ñaareelu xarnu G.J.K.T.), niki Nihongi Shinto yi (ca atum juróom-ñaari téeméer ak ñaar-fukk [720] G.J.K.T.).

[Foto bi nekk paas 20]