Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Tiiñal xarey xeli neen yu bon yi

Tiiñal xarey xeli neen yu bon yi

Pàcc 12

Tiiñal xarey xeli neen yu bon yi

1. Lan la Yeesu def ba mu jànkoonteek xeli neen yu bon yi?

 YEESU KRIST dañu ko sóob cim ndox rekk, mu daldi dem ca màndiŋu Yudaa ngir ñaan te xalaat ba xeli. Foofa, Seytaane miy Ibliis jéem na koo jéggiloo yoonu Yàlla. Waaye, Yeesu bañ na meebu Ibliis te bàyyiwul mu jàpp ko ci fiiram. Ca biir yëngu-yëngoom ci kow suuf, Yeesu riisoo naak yeneen xeli neen yu bon. Ndaxam, ay yooni yoon, Yeesu gëdd na leen te tiiñ na leen.—Lukk 4:1-13; 8:26-34; 9:37-43.

2. Yan laaj lañuy seet?

2 Nettaliy Biibël yiy nataal ndaje yooyu war nañ ñoo gulami ne xeli neen yu bon yooyu am nañu ci dëgg. Ñu ngiy jéema réeral nit ñi. Waaye, mën nañoo tiiñ xeli neen yu bon yooyu. Wànte fan la mbindaafon yu bon yooyu jóge? Lu tax ñuy jéema réeral nit ñi? Te yan pexe lañuy jëfandikoo ngir jot li ñuy diir? Daj tonti laaj yu ni mel dina la dimbali nga tiiñ xarey xeli neen yu bon yi.

XEL YU BON YI—SEEN COSAAN AK SEEN JUBLUWAAY

3. Nan la Seytaane miy Ibliis mujjee nekk?

3 Yeowa Yàlla def na ndiiraanug xeli neen lu yàgg laataa sàkk Aadama. (Ayóoba 38:4, 7) Ni ñu ko faramfàccee ca Pàcc 6, menn ca malaaka yooyu yar na bëgg-bëggu am doomi Aadama ñu koy jaamu asté ñuy jaamu Yeowa. Ngir jot la mu doon diir, malaaka mu bon mooma tiiñ na te tuumal na Sàkkkat si, dem sax bay déggloo jigéen ju njëkk ja ne Yàlla ab fenkat la. Jaadu na kon, ñu mujja xame mbindaafonu xel mu bon mooma niki Seytaane (noon) miy Ibliis (sosalkat).—1 Musaa 3:1-5; Ayóoba 1:6.

4. Nan la yenn malaaka bàkkaare ca bésiy Nóoxin?

4 Ca gannaaw ga, yeneen malaaka far nañook Seytaane miy Ibliis. Ca bésiy Nóoxin, góor gu jub, ñenn ci ñoom bàyyi nañu seen liggéey ca asamaan te jël yaramiy suux ngir topp seen bànneex, ndax tëdd ak jigéen ña nekkoon ca kow suuf. Ci lu amul werante, Seytaane ruux na malaaka yooyu ñu topp dundinub déggadi. Loolu yóbbu na leen ñu nekk baayiy njureelu warale yu ñu tudde Nefilim, ñu mujja jikkowoo taafaru rab. Ba Yeowa sababee Mbënnum Tuufaan mu réy ma, sànk na doomi Aadama yu yàqu ya ak njureelu malaaka yu déggadi googa, gu nitewul ga. Malaaka yi jógal Yàlla mucc nañu ca sànku ba, ba ñu simmee seeni yaramiy suux te dellu ca diiwaanub mbindaafonu xel. Waaye Yàlla jataŋ na seytaane yooyee ba mu digaaleek ñoom niki ñu ñu dàq ci biir lëndëm fa leerug Yàlla àggul. (1 Musaa 6:1-7, 17; Yudd 6) Waaye Seytaane, “njiitum seytaane yi, NW” ak ay malaakam yu bon dañoo sax ci seen jógal Yàlla. (Lukk 11:15) Lan mooy seen jëmu?

5. Seytaane aki seytaaneem, ci lan lañu jublu, te lan la ñuy jëfandikoo ngir jàpp nit ñi ci seen fiir?

5 Jubluwaayu Seytaane aki seytaaneem, bu bon bi, mooy fàbbee nit ñi ci Yeowa Yàlla. Looloo tax, ñu bon ñooñoo ngiy réeral, di tiital, tey song nit ñi ba àddina sosoo ba tey. (Peeñu bi 12:9) Ay misaaliy suñu jamano tey a ngiy biral ne songiy seytaane yi masuñoo bon ni ñu bone léegi. Ngir mbaal nit ñi, seytaane yi faral nañuy jëfandikoo xeetu mbirum duggook ñoom wu mu mënta doon. Nan la seytaane yiy jëfandikoo meeb boobu, te nan nga mënee aar sa bopp?

NI LA XELI NEEN YU BON YIY JÉEMEE RÉERAL

6. Lan mooy mbirum duggook seytaane, te yan ñooy yenn xeeti mbirum duggook seytaane?

6 Lan mooy mbirum duggook seytaane? Mooy digaaleek seytaane yi, walla xeli neen yu bon yi, moo xam baña jaar ci kenn, walla jaare ci maraalekat. Mbirum duggook seytaane dafay jariñ seytaane yi li meeb di jariñ rëbbkat: dafay wootal njàpp gi. Te sax nib rëbbkat di jariñoo ay meeb yu wuute ngir nax mala yi, ñu dugg ci biir fiiram, noonu la xeli neen yi di xiire nit ñi ci xeeti mbirum duggook seytaane yu wuute ngir yóbbu leen ci seen kiliftéef. (Seetal Sabuur 119:110.) Yenn ci fasoŋi mbirum duggook seytaane yooyu ñooy gisaane, luxus, di seet màndargay liy xewi, xonjom, di kort, di seeti ay maraalekat, tey laajte ñi dee.

7. Nan la mbirum duggook seytaane lawe, te lu tax mu siiw sax ci réew yiy wuyoo turu karceen?

7 Meeb yooyoo ngiy dox, ndax mbirum duggook seytaane dafay wootal nit ñi fu nekk ci àddina si. Ñiiy dund ci dëkk yi nekk ci àll yaa ngiy seeti ay jabaraankat, te ñiiy liggéey ci biro yaa ngiy giseek seetkati biddéew yi. Mbirum duggook seytaane sax daa siiw ci biir réew yiy wuyoo turu karceen. Ab gëstoo ngiy wone ne ca Etats-Unis (USA) doŋŋ, lu jege fanwéeri (30) mbind yu ñu faral di génne ci lu ëpp fukki tamndareet (10 000 000) ci ay sottee ngi jublu ci xeeti mbirum duggook seytaane yu bare te wuute. Waa Brésil (Brazil) a ngiy sànk lu weesu juróomi téeméeri tamndareet (500 000 000) ci ay dolaar ci jumtukaayi mbirum duggook seytaane, at mu nekk. Moona, ci téeméeri nit ñay teew ca jàngukaayi mbirum duggook seytaane ya nekk ca réew moomu, juróom-ñett fukk ña ay katolig yu ñu batisé lañu, yuy teewe mees itam. Ndegam ay làbbeey jëfoo mbirum duggook seytaane, gëmkat yu bare foog nañu ne di ko jëfoo, aayul ci kanamu Yàlla. Waaye ndax loolu dëgg la?

LU TAX BIIBËL BIY DAAN ÑIIY TOPP MBIRUM DUGGOOK SEYTAANE

8. Lan mooy gis-gisub Mbind yi ci mbirum duggook seytaane?

8 Su ñu la jàngalee ne yenn xeeti mbirum duggook seytaane, ay pexe ngir laalanteek xeli neen yu baax yi lañu, mën ngaa am mbetteel ci jàng li ci Biibël bi wax. Artu nañu woon mbooloo Yeowa: “Buleen jublu ci maraalekati rab yi, te buleen laajlu ñii def muy seen liggéey: wax xew-xew yiy ami, ba tax ngeen mujja sobe ndax ñoom.” (3 Musaa 19:31; 20:6, 27) Téereb Biibël bi tudd Peeñu baa ngiy artu ne, “ñiiy topp mbirum duggook seytaane, NW” seen muj a ngi ci “déegu safara ak tamarax bi. Loolu mooy ñaareelu dee gi [dee ba fàww].” (Peeñu bi 21:8, 22:15) Fasoŋi mbirum duggook seytaane yépp, amul bu ci Yeowa Yàlla nangu. (5 Musaa 18:10-12) Lu tax loolu?

9. Lu tax ñu mëna tofal ne xabaar yi bawoo ci diiwaaniy xel ci suñu jamano jógewuñu ci Yeowa?

9 Yeowa yónni na ay xeli neen yu baax, ay malaaka yu jub, ngir ñu wax aki doomi Aadama laata ñoo sottal mbindum Biibël bi. Waaye li dale sottalub mbindam, Kàddug Yàlla jox na doomi Aadama yi tette bi ñu soxla ngir jaamu Yeowa ni mu ko bëgge. (2 Timote 3:16, 17; Yawut yi 1:1, 2) Du bàyyi Kàddoom gu sell gi ngir jox ay xabaar maraalekat yi. Ci suñu jamano, xabaar yu ni mel yépp yu bawoo ca diiwaanub xel a ngiy jóge ca xeli neen yu bon yi. Dëkk ci mbirum duggook seytaane mën naa jëme ci gétënu seytaane walla sax xeli neen yu bon yi sayloo nit ki. Looloo tax, Yàlla, ak mbëggeel, di ñu artu ñu baña bokk ci jëfiy mbirum duggook seytaane yu ñu mënta doon. (5 Musaa 18:14; Galasi 5:19-21) Rax-ca-dolli, su ñu wéykoon di topp mbirum duggook seytaane gannaaw ba ñu xamee gis-gisub Yeowa ci loolu, doon nañoo far ak xeli neen yu bon yooyu jógal Yàlla te doon nañoo nekk ay nooniy Yàlla.—1 Samwil 15:23; 1 Nettaliy xew-xewi cosaan 10:13, 14; Sabuur 5:4.

10. Lan mooy gisaane, te lu tax ñu warkoon koo moytu?

10 Aw xeetu mbirum duggook seytaane wu siiw mooy gisaane—maanaam fexee muri ëllëg walla lu nëbbu ak ndimbalul xeli neen yi. Yenn xeeti gisaane ñooy: seetlu biddéew yi, di seetlu dankub weer buy melax, firi ay gént, seet ci loxo tey gisaanelu ciy jëfandikoo kart yu tudd tarot. Ñu baree ngiy gise gisaane niki po mu aayul, waaye Biibël baa ngiy wone ne gisaanekat yeek xeli neen yu bon yee lëngoo. Naka noonu, Jëf ya 16:16-19 a ngiy tudd “ab rabu gisaane” bu taxoon as ndaw doon “gisaane.” Wànte, ñàkkoon na mën-mënub wax liy ñëw ëllëg ba ñu dàqe seytaane ba. Ci lu leer, gisaane, meeb la bu seytaane yiy jariñoo ngir wootal nit ñi ci seen biir fiir.

11. Nan la njéem yi ngir wax ak ñi faatu dee jëme ci mbaal nit ki?

11 Sooy naqarlu ndax deewug sa soppe, muy koo bokkal njaboot walla sa xaritub benn bakkan, mën nañu laa wootal ci lu yomb ak beneen meeb. Ab maraalekatub rab mën na laa jox ab xabaar bu la lew yow rekk, walla mën naa waxe baat bu ni mel ni bosu nit ki dee. Moytul! Di jéema waxtaan ak ñi dee, ci biir fiir la lay jëme. Lu tax? Ndaxte ñi dee mënuñoo wax. Xëy na yaa ngiy fàttaliku, Kàddug Yàllaa ngiy wax ci lu leer ne cig dee nit “kaa ngiy dellu ci suufam; ca bés booba saxsax ay xalaatam dañuy raaf.” Ñii dee “yëguñu dara, ba dara jeex.” (Sabuur 146:4; Dajalekat 9:5, 10) Rax-ca-dolli, seytaane yi ñooy ñiiy toppandoo baatu ki dee tey jox maraalekatub rab ay xabaar yu jëm ci ki dee. (1 Samwil 28:3-19) Looloo tax, “képp kuy laajte ñi dee,” xeli neen yu bon yi dinañu ko jàpp ci seen fiir te nit kookoo ngiy jëf lu dëppoowul ak coobareg Yeowa Yàlla.—5 Musaa 18:11, 12; Isayi 8:19.

DI TÀMBALI CI WOOTAL DI MUJJ CI SONG

12, 13. Jan firnde ju wóor moo am ci seytaane yaa ngiy sax ciy fiir tey gétën nit ñi?

12 Booy topp xelalu Kàddug Yàlla bi jëm ci mbirum duggook seytaane, dangay jaleñ meebu seytaane yi. (Dendale kook Sabuur 141:9, 10; Room 12:9.) Ndax loolu dafay tekki ne xeli neen yu bon yi dinañu la noppee jéema jàpp ci seen fiir? Déedéet mukk! Gannaaw ba mu fiiree Yeesu ñetti yoon, Seytaane “daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamano.” (Lukk 4:13) Noonu it, xeli neen yi dëgër bopp yemuñu rekk ciy wootal nit ñi, waaye it dañu leen di song.

13 Fàttalikul li ñu njëkka gis jëm ci song bi Seytaane song Ayóoba, surga Yàlla. Ibliis taxoon na mu ñàkk jur gi mu amoon, te taxoon na ña gëna bare ca ay surgaam dee. Seytaane rey na sax doomiy Ayóoba. Teg ci, door na Ayóoba ci boppam feebar bu metti. Waaye Ayóoba tëye woon na ngoram lëmm ci Yàlla te ame woon na ca barke yu réy. (Ayóoba 1:7-19; 2:7, 8; 42:12) Booba ba tey, seytaane yi muumaloo nañu ay nit walla gumbaloo nañu leen, te wéy nañu ciy tukkurmut ci coonoy doomiy Aadama. (Macë 9:32, 33; 12:22; Mark 5:2-5) Tey, ay nettalee ngiy wone ne seytaane yaa ngiy gétën ay nit ci wàllu awra tey dofloo ñeneen. Ñu ngiy ruux it ñeneen ñu bóom walla ñu xaru, jëf yu nekk ay bàkkaar ci Yàlla. (5 Musaa 5:17; 1 Yowanna 3:15) Terewul, ay junniy nit ñu xeli neen yu bon yooyu masoona mbaal, fexe nañoo musal seen bopp. Nan la loolu ame ngir ñoom? Def nañu ko ba ñu jëlee ay matuwaay yu seen bakkan aju.

NI ÑUY TIIÑE XELI NEEN YU BON YI

14. Ci lu dëppook royukaay bi karceeni Efes ca xarnu ba njëkk joxe, nan nga mënee tiiñ xeli neen yu bon yi?

14 Man mooy menn pexe moo mëna tiiñe xeli neen yu bon yi te aar sa bopp ak sa njaboot ci seeni mbaal? Karceeni xarnu bu njëkk ba ya dëkkoon Efes te daan jëfoo mbirum duggook seytaane laata ñoo mujja nekk ay gëmkat, jël nañu ay matuwaay yu wóor. Ñu ngiy duruus ne, “ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp.” (Jëf ya 19:19) Su dee sax masuloo jëfoo mbirum duggook seytaane, tàggool ak lépp lu koy junj. Loolu ëmb na ay téere, ay surnaal, ay wideo, ay portale, ay woy yu ñu sotti ci kaset, ak ay jumtukaay yu ñuy jariñoo ngir mbirum duggook seytaane. Xérém, gàllaaj ak yeneen muslaay, ak it ay maye yu jóge ci ñu dëkk ci mbirum duggook seytaane, ci lañu bokk itam. (5 Musaa 7:25, 26; 1 Korent 10:21) Nañu jël am misaal: seytaane yi yàggoon nañoo gétën ñaar ñu séy ca réewum Thaïlande ( Thailand). Mujj nañoo tàggook jumtukaay yi lëkkale woon ak mbirum duggook seytaane. Lan la loolu jur? Mucc nañu ci songiy seytaane yi te gannaaw loolu, jëm nañu kanam dëgg ci seen digganteek Yàlla.

15. Ba ngay tiiñ xarey xeli neen yu bon yi, lan mooy beneen matuwaay bu mënula ñàkka am?

15 Ngir ñu tiiñ xeli neen yu bon yi, beneen matuwaay bu mënula ñàkka am, mooy jëfoo xelalu ndaw li Pool: gànnaayoo yërey xeex yépp ci wàllu ngëm yi ñu Yàlla jox. (Efes 6:11-17) Karceen yi war nañoo dooleel seeni karaange kontar xeli neen yu bon yi. Lan la matuwaay boobu ëmb? Pool nee na: “Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba mana fél jum yi leen Seytaane di fitt.” Ci dëgg, bu sa ngëm dee gëna dëgër, nga gën di am mën-mënub tiiñ xarey xeli neen yu bon yi.—Macë 17:14-20.

16. Nan nga mënee dooleel sa ngëm?

16 Nan nga mënee dooleel sa ngëm? Ci kow nga wéy di jàng Biibël bi tey jëfoo xelalam ci sa dund. Dooley ngëmug nit a ngi aju ci lu ëpp ci dëgëraayu li ko sës—xam-xamub Yàlla. Ndax dàkkooruloo ne xam-xam bu wér bi nga jot te jàpp ci sa xol, ba ngay jàng Biibël bi, tabax na sa ngëm? (Room 10:10, 17) Looloo tax, ci lu amul werante, ba ngay wéy ci njàng moomu tey tàmma teewe ndajey Seedey Yeowa, dinga gëna feddali sa ngëm. (Room 1:11, 12; Kolos 2:6, 7) Loolu dina nekk tata ju am doole ci songiy seytaane yi.—1 Yowanna 5:5.

17. Yeneen matuwaay yan lañu mëna soxlaa def bu ñuy tiiñ xarey xeli neen yu bon yi?

17 Yeneen matuwaay yan la nit ku dogu ci tiiñ xarey xeli neen yu bon yi mëna jël? Karceeni dëkku Efes soxla nañu woon ñag ndaxte ñu ngi doon dund ci dëkk bu yàqook mbirum duggook seytaane. Noonu, Pool wax na leen: “Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi.” (Efes 6:18) Ndegam ñu ngiy dund ci àddina su seytaane yàq, di leewaayu ngir jot tawféexu Yàllaa ëpp maanaa ngir tiiñ xeli neen yu bon yi. ( Macë 6:13) Luy dimbali ci fànna boobu, mooy taxawu ci wàllu ngëm ak ñaaniy mag ñi ñu teg ci biir mbooloom karceen yi.—Saak 5:13-15.

SAXAL CIY XEEX AK XELI NEEN YU BON YI

18, 19. Lan la nit mëna def su ko seytaane yiy gétënaat?

18 Waaye, gannaaw ba ñu jëlee matuwaay yu am solo yooyu sax, am na ñenn ñu xeli neen yu bon yi gétën. Noonu, genn góor ca réewum Côte-d’ Ivoire ( Ivory Coast) a ngi doon jàng Biibël beek Seedey Yeowa yi, te tojoon na ay gàllaajam yépp. Keroog ba mu defee loolu la jëm kanam bu baax-a-baax, jébbal dundam Yeowa, te sóob nañu ko. Waaye, ca ayubés ba topp bés ba ñu ko sóob, seytaane yi tàmbaliwaat nañu koo gétën, te ay baat a ngi ko doon wax mu bàyyi ngëmam gu bees gi. Su la loolu dalee, ndax loolu dafay tekki ne ñàkk nga tawféexu Yeowa? Déedéet moos.

19 Ak lu Yeesu Krist, góor gu mat, amoona amoon tawféexu Yàlla, dégg na baatu mbindaafonu xel mu bon mi, Seytaane miy Ibliis. Yeesu wone na li ñu wara def bu loolu amee. Nee na Ibliis: “Sore ma, Seytaane!” ( Macë 4:3-10) Noonu itam, warkoon ngaa baña déglu baat yi bawoo ca àddinay mbindaafoni xel. Tiiñal xeli neen yu bon yi ciy woo Yeowa ngir ndimbal. Waaw, ñaanal ca kow, jaar ci turu Yàlla. Léebu 18:10 a ngiy wax: “Turu Yeowa ab tata bu sës la. Ci biir la ku jub kiy daw tey jote tawféex.” Loolu la karceen bu góor ba ca Côte d’Ivoire (Ivory Coast) def, te xeli neen yu bon yi noppi nañu koo gétën.—Sabuur 124:8; 145:18.

20. Ci gàttal, lan nga mëna def ngir tiiñ xeli neen yu bon yi?

20 Yeowa bàyyi na xeli neen yu bon yi dund ba tey, waaye mu ngiy wone kàttanam rawatina ngir ay nitam, te xamal nañu turam ci suuf si sépp. (2 Musaa 9:16) Soo saxee ciy jege Yàlla, soxlawoo ragal xeli neen yu bon yi. (4 Musaa 23:21, 23; Saak 4:7, 8; 2 Pieer 2:9) Seen kàttan am na àpp. Duma nañu leen ca bésiy Nóoxin, dàqe leen asamaan bu yàggul, te léegi ñu ngiy xaar seen àtte bu mujj bi. (Yudd 6; Peeñu bi 12:9; 20:1-3, 7-10, 14) Li am mooy, dañoo tiit ci sànkute bi leen di xaar. (Saak 2:19) Noonu, su la xeli neen yu bon yiy jéema wootal ak meeb sàngam walla ñu lay song ci fasoŋ bu mu mënta doon, mën nga leena tiiñ. (2 Korent 2:11) Moytul wépp xeetu mbirum duggook seytaane, jëfool xelalu Kàddug Yàlla, te wutala neex Yeowa. Defal loolu ci saa si, ndaxte sa dund a ngi aju ciy tiiñ xarey xeli neen yu bon yi!

SEETLUL SA XAM-XAM

Nan la xeli neen yu bon yiy jéemee réeral nit ñi?

Lu tax Biibël biy daan mbirum duggook seytaane?

Nan la nit mënee mucc ci xeli neen yu bon yi?

Lu tax nga wara sax ciy tiiñ xeli neen yu bon yi?

[Laaj yi]

[Nataal bi nekk paas 110]

Nan nga gise mbirum duggook seytaane ciy xeetam yu bare yi?