Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Yeesu krist—caabi ji ngir xam-xamub Yàlla

Yeesu krist—caabi ji ngir xam-xamub Yàlla

Pàcc 4

Yeesu krist—caabi ji ngir xam-xamub Yàlla

1, 2. Nan la diiney àddina si banke caabi ji ngir xam-xamub Yàlla?

 YAA ngi taxaw ci sa buntu kër, di jéem ak xereñadi tijjeek sa caabi. Sedd na te lëndëm, te yàkkamti ngaa dugg ci biir—waaye caabi ji bañ naa ubbi. Niru naak caabi ju baax ji, wànte tëjukaay bi yënguwul. Ndaw lu soof! Xoolaat nga sa caabi. Ndax yaa ngiy jëfandikoo ji war? Ndax dafa am kenn ku yàq caabi ji?

2 Loolu dafay misaal bu baax li jaxasoo bi am ci diiney àddina si def ci xam-xamub Yàlla. Noonu, ñu bare dañoo bank caabi ji ñuy ubbil xam-xam boobu ngir ñu nànd ko—Yeesu Krist. Yenn ci diine yi dañoo dindi caabi ji, ci li ñu faalewul Yeesu ci dara. Yeneen dañoo dëngal taxawaayub Yeesu, ci li ñu koy jaamu niki Yàlla Aji Kàttan ji. Lu mu mënta doon, xam-xamub Yàllaa ngi tëju ci ñun, su ñu nàndul bu wér kan mooy nit ku mag kooku di Yeesu Krist.

3. Lu tax ñu mëna tudde Yeesu caabi ji ngir xam-xamub Yàlla?

3 Xëy na yaa ngiy fàttaliku li Yeesu wax: “Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Krist.” (Yowanna 17:3) Ba mu doon wax loolu, Yeesu jayuloon boppam. Mbind yaa ngiy jolliloo ay yooni yoon soxla am xam-xamub Krist, bu wér bi. (Efes 4:13; Kolos 2:2; 2 Pieer 1:8; 2:20) “Yonent yépp seedeel nañu ko [Yeesu Krist]” la ndaw li Pieer seetlu. (Jëf ya 10:43) Te ndaw li Pool bind na: “ Ci [Yeesu] lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam.” (Kolos 2:3) Pool dem na ba wax sax ne digey Yeowa yépp mujj nañoo nekk dëgg ndax Yeesu. (2 Korent 1:20) Yeesu Krist kon mooy caabi ji dëgg ngir xam-xamub Yàlla. Suñu xam-xamub Yeesu war naa set ci lépp lu dëng jëm ci nekkeefam ak taxawaayam ci ndefarinub Yàlla. Waaye lu tax ñiiy topp Yeesu gise ko niki ki nekk ci diggu nasiy Yàlla?

ALMASI BA WAROONA NËW

4, 5. Yan yaakaar a tegu woon ci Almasi bi, te nan la ay taalibeem jàppe woon Yeesu?

4 Li dale ca bésiy Abel, góor gu takku ci Yàlla, surga Yàlla yaa nga doon séentu, yàkkamti ko, Njureel gi Yeowa Yàlla ci boppam yégle woon. (1 Musaa 3:15; 4:1-8; Yawut yi 11:4) Feeñaloon nañu ne Njureel gi dina liggéeyal nasub Yàlla niki Almasi bi, baat buy tekki “Ki ñu tànn.” Doon na “dindi bàkkaar,” te it ndamiy Nguuram yégle woon nañu leen ci Sabuur. (Dañel 9:24-26; Sabuur 72:1-20) Kan moo narkoona firndeel bu wóor ne moom mooy nekk Almasi bi?

5 Jortul la wenn waxambaane Yawut wu tudd Andre yëg ci xolam ba mu déggee kàdduy Yeesu bu Nasarett. Andre dafa daldi daw ca Simoŋ Pieer mi mu bokkaloon ndey ak baay ne ko: “Gis nañu Almasi bi.” (Yowanna 1:41) Wóoroon na taalibey Yeesu ne moo doon Almasi ba ñu dige woon. (Macë 16:16) Te karceen dëgg ya nangu woon nañoo ñàkk seen bakkan ngir seen ngëm googu, maanaam Yeesoo doon ca dëgg Almasi ba ñu dige woon, walla Krist. Yan firnde yu wóor lañ ci amoon? Nañu seet ñetti xeeti firnde yu leer.

FIRNDE YIY LEERAL NE YEESU MOO DOON ALMASI BI

6. (a) Ci wan askan la Njureel gi ñu dige woon waroona jóge, te nan lañu xame ne Yeesu ca askan woowu la cosaanoo? (b) Lu tax képp ku doon dund gannaaw atum 70 G.J.K.T. mënuloona firndeel ne moo doon Almasi bi?

6 Askanu Yeesu mooy sësukaay bi njëkk ci xàmme ko niki Almasi ba ñu dige woon. Yeowa waxoon na surgaam Ibrayima ne, Njureel ga ñu dige woon doon na bawoo cag njabootam. Isaaxa doomu Ibrayima, Yanxóoba doomu Isaaxa, ak Yudaa doomu Yanxóoba, jotoon nañu, ku nekk ci ñoom, dige bu ni mel. (1 Musaa 22:18; 26:2-5; 28:12-15; 49:10) Ay xarnu gannaaw booba, askanu Almasi bi gën naa sës ba ñu xamalee buur ba Daawuda ne Almasi bi ci boppam doon na bawoo ca askanu njabootam. (Sabuur 132:11; Isayi 11:1, 10) Nettaliy Linjiliy Macë ak Lukk yeesal nañu ne Yeesu ca askanu njaboot googa la cosaanoo. (Macë 1:1-16; Lukk 3:23-38) Lu Yeesu amoona am ay noon yu bare yu wexoon xat, kenn ci ñoom masula diŋat askanam wu weejoon bu baax-a-baax. (Macë 21:9, 15) Kon, ci lu leer, askanam nekkuloon lu ñuy werante. Waaye, téerey askani Yawut ya yàq nañu leen ba waa Room rajaxee Yérusalem ca atum juróom-ñaar-fukk [70] G.J.K.T. Gannaaw ba loola amee, kenn mënatuloona firndeel ne mooy Almasi ba ñu dige woon.

7. (a) Lan mooy ñaareelu xeetu firnde bu leer wuy wone ne Yeesu moo doon Almasi bi? (b) Nan la Mikaa 5:2 àgge ci Yeesu?

7 Yégley yonent yi àgg nekk nañu weneen xeetu firnde wu leer. Ay yégley yonent yu baree bare, yu nekk ci Mbind yi ci làkku Ebrë, a ngiy nettali benn-benn ay fànna yu bare te wuute yu jëm ci dundinub Almasi bi. Ca juróom-ñetteelu xarnu ba L.J.K.T., yonent Mikaa yégle woon na ne njiit mu mag moomu dina juddu ca dëkk bu ñàkk solo bu tudd Betleyem. Ñaari dëkk ca Israël ñoo amoon turu Betleyem, waaye yégleb yonent boobu dafa leeral ban ci ñoom saxsax la woon: Betleyem Efrata, fa buur ba Daawuda juddoo woon. (Mikaa 5:2) Yuusufa ak Maryaama, way-juri Yeesoo nga doon dund Nasarett, ca 150 kilomet ca bëj-gànnaaru Betleyem. Waaye ba Maryaama ëmbee, buurub Room Sesaar Ogust digal na nit ñépp dem bindu ci seen dëkku cosaan. * Yuusufa nag, daldi na yóbbu Betleyem soxnaam si ëmboon, te foofa la Yeesu juddoo.—Lukk 2:1-7.

8. (a) Kañ ak ci ban xew-xew la 69 “ayubés” ya tàmbali? (b) Ban diir la 69 “ayubés” ya am, te lu xewoon ba ñu jeexee?

8 Ca juróom-benneelu xarnu ba L.J.K.T., yonent Dañel yégle woon na ne “Almasi Njiit mi” doon na feeñ juróom-benn fukki “ayubés” ak juróom-ñeent (69) gannaaw ba ndigalu sancaat ak tabaxaat Yérusalem génnee. (Dañel 9:24, 25) Bu nekk ci “ayubés” yooya, diirub juróom-ñaari at la woon. * Ci lu dëppook Biibël beek xew-xewi démb, ndigalu tabaxaat Yérusalem a ngi génn ca atum 455 L.J.K.T. (Nëxémiaa 2:1-8) Kon Almasi bi waroon naa feeñ ñeent téeméeri at ak juróom-ñett fukk ak ñett (483) (maanaam juróom-benn fukk ak juróom-ñeent ba juróom-ñaari yoon [69 x 7]), gannaaw atum 455 L.J.K.T. Looloo ngi ñuy yóbbu ca atum 29 G.J.K.T., mu nekk saxsax at ma Yeowa tànn Yeesu ak xelam mu sell. Noonu la Yeesu nekke “Krist bi” (liy tekki “Ki ñu Tànn”), walla Almasi bi.—Lukk 3:15, 16, 21, 22.

9. (a) Nan la Sabuur 2:2 àggee? (b) Yan ñooy yenn ci yeneen yégley yonent yi àgg ci Yeesu? (seetal tablo bi.)

9 Dëgg la, du ñépp a nangu Yeesu ni Almasi ba ñu dige woon, te Mbind yi yégle woon nañu loolu. Ni ñu ko nettalee ci Sabuur 2:2, Yàlla ruux na buur ba Daawuda ngir mu yégle: “Buuriy suuf saa ngi taxaw te kilifa yi ci seen bopp dajaloo nañu niki kenn, kontar Yeowaak ki mu tànn.” Yégleb yonent boobu dafa doon déggloo ne njiiti réew yu bare doon nañu mànkoo ngir song Ki Yeowa tànn walla Almasi bi. Te looloo am. Kilifay diine Yawut yi, Erodd buur ba, ak Pons Pilàtt jawriñ ju cosaanoo Room, ñoom ñépp am nañu wàll ci deewug Yeesu. Erodd ak Pilàtt ñi nekkoon ay noon daldi mujja nekk ay xariti benn bakkan li dale ca bés booba. (Macë 27:1, 2; Lukk 23:10-12; Jëf ya 4:25-28) Ngir yeneen firnde yuy wone ne Yeesu moo doon Almasi bi, mën ngaa xool tablo bi tudd “Yenn yégley yonent yu ràññeeku jëm ci Almasi bi.”

10. Nan la Yeowa seede woon ne Yeesoo doon Ki ñu Tànn te ñu digoon ñëwam?

10 Seedes Yeowa Yàlla mooy ñetteelu xeetu firnde wiy biral ne Yeesu mooy Almasi bi. Yeowa yónni na ay malaaka ñu xamal mbooloo mi ne Yeesu moo doon Almasi ba ñu dige woon. (Lukk 2:10-14) Li am mooy, ba Yeesu nekkee di dund ci kow suuf, Yeowa ci boppam waxe na ca kow asamaan ngir wone ne nangu na Yeesu. (Macë 3:16, 17; 17:1-5) Yeowa Yàlla jox na Yeesu kàttanu def ay kéemaan. Bu nekk ci kéemaan yooyu nekkoon jeneen firnde ju wóor ju bawoo ca Yàlla, juy biral ne Yeesu moo doon Almasi bi, ndax Yàlla doonuloon jox mukk ab naaféq kàttanu def ay kéemaan. Yeowa it jëfandikoo na xelam mu sell ngir ruux nettaliy Linjil yi, ba tax firnde yu wóor yiy wone ne Yeesu moo doon Almasi bi, mujj nañoo bokk ci Biibël bi, téere bi ñu gëna firi teyit bi ñu gëna siiwal ba àddina sosoo ba tey.—Yowanna 4:25, 26.

11. Lan moo gëna firndeel bu leer ne Yeesoo doon Almasi bi?

11 Bu ñu leen boolee yépp, xeetiy firnde yu leer yooyu ëmb nañu ay téeméeri jëf yuy niraale Yeesu niki Almasi ba ñu dige woon. Ci lu leer, jaadu na kon, karceen dëgg yi gis ci moom ki “yonent yépp seedeel” ak caabi ji ngir xam-xamub Yàlla. (Jëf ya 10:43) Waaye am na lu ëpp lu ñu mëna jàng lu jëm ci Yeesu Krist lu dul moo doon Almasi bi doŋŋ. Fan la cosaanoo woon? Lan la doon niru?

DUNDUG YEESU LAATA MOO NEKK NIT CI KOW SUUF

12, 13. (a) Nan lañu xame ne Yeesu ca kow asamaan la doon dund balaa moo ñëw ci kow suuf? (b) Kan mooy “Kàddu gi”, te lan la doon def balaa moo mujja nekk nit ci kow suuf?

12 Mën nañoo xàjjale dundug Yeesu ci ñetti jamano. Ju njëkk ji tàmbali na lu yàgg balaa juddoom ci kow suuf. Mikaa 5:2 nee woon na ne cosaanu Almasi baa nga woon “li dale ca jamano yu njëkk ya, ca bésiy diir bu amul àpp.” Te Yeesu it, ci wax ju àndul ak laxas, nee na “ca kaw laa jóge,” maanaam ca asamaan. (Yowanna 8:23; 16:28) Ban diir la dund ca asamaan laataa ñëw ci kow suuf si?

13 Yeesu “Doom ji [Yàlla] am képp” lañu ko tudde ndaxte ci ay loxoom saxsax la ko Yeowa sàkke. (Yowanna 3:16) Ndegam mooy “taaw[ub] (...) lépp luy mbindeef,” Yàlla jëfandikoo na Yeesu ngir sàkk yeneen yëf yépp. (Kolos 1:15; Peeñu bi 3:14) Yowanna 1:1 nee na “Kàddu gi” (Yeesu laataa nekk nit) a nga nekkoon ak Yàlla “ca njëlbéen.” Kon Kàddu gaa nekkoon ak Yeowa ba ñu sàkkee “asamaan yeek suuf si.” Yàlla Kàddu gi la doon waxal ba muy naan: “Nañu sàkk nit ci suñu melokaan.” (1 Musaa 1:1, 26) Noonu it, Kàddu gi moo waroona nekk ci lu amul werante, “liggéeykat bu xereñ” bi Yàlla sopp, ñu koy nettali ci Léebu 8:22-31 niki sago si ñu niteel, di liggéey ca wetug Yeowa ngir def yëf yépp. Gannaaw ba ko Yeowa nekkloo, Kàddu gi dund na ay at yu ñu mënula waññ fa Yàlla ca asamaan balaa moo mujja nekk nit ci kow suuf.

14. Lu tax ñu tudde Yeesu “melokaanu Yàlla ji kenn gisul”?

14 Kon waruñoo bett Kolos 1:15 tudde Yeesu “melokaanu Yàlla ji kenn gisul”! Ndax dañoo taqante woon diirub jamano yu ñu xaymawul, Doom ju góor ji dégg ndigal mujj naa mel ni Baayam, Yeowa. Loolu nekk na leneen luy tax Yeesu nekk caabi ji ngir xam-xamub Yàlla jiy joxe dund. Lépp lu Yeesu def ba mu nekkee ci kow suuf em na tembe ak li Yeowa defkoon. Looloo tax, di jànga xam Yeesoo ngiy tekki it di yokk suñu xam-xam ci Yeowa. (Yowanna 8:28; 14:8-10) Kon, leer na ne suñu dund a ngi aju ci gëna xam Yeesu Krist.

DUNDUG YEESU CI KOW SUUF

15. Nan la Yeesu mënee juddu nekk liir bu mat sëkk?

15 Ñaareelu jamano dundug Yeesu fii ci kow suuf la ame woon. Ak xol bu tàlli nangu na Yàlla toxale asamaan dundam ci biirub xeeku Yawut bu takku ci Yàlla, bu tuddoon Maryaama. Xel mu sell mu Yeowa mu am kàttan mi, walla dooleem jiy jëf, ‘yiir na’ Maryaama, ba tax mu mujja ëmb te wasin doom ju mat. (Lukk 1:34, 35) Yeesu donnul benn matadi, ndax bakkanam a nga cosaanoo woon ca Sabab bu mat. Yar nañu ko ca biir kër gu em, niki ku Yuusufa minise ba doomoo, mu doon taawub njaboot gu bare doom.—Isayi 7:14; Macë 1:22, 23; Mark 6:3.

16, 17. (a) Fan la Yeesu jote kàttanu def ay kéemaan, te yan ñooy yenn ci kéemaan yooyu? (b) Yan ñooy yenn ci jikko yi Yeesu wone?

16 Takkute bu xóot bi Yeesu am ci Yeowa Yàlla feeñoon na xaat ba mu amee fukki at ak ñaar (12). (Lukk 2:41-49) Gannaaw ba mu màggee te sumb liggéey bi ñu ko sas ba mu amee fanwéeri (30) at, Yeesu wone na it mbëggeel gu xóot ci moroomami doomiy Aadama. Ba ko xel mu sellum Yàlla joxee kàttanu def ay kéemaan, ndax laabiir faj na ña feebaroon, ña lafañoon, ña làggi woon, ña gumboon, ña tëxoon, ña gaana woon. (Macë 8:2-4; 15:30) Yeesu jox na ay junniy nit ñu xiifoon ñu lekk. (Macë 15:35-38) Giifal na am sàmbaraax mu doon méb dalaayu ay xaritam. (Mark 4:37-39) Dem na ba dekkal sax ay nit ñu faatu woon. (Yowanna 11:43, 44) Kéemaan yooyu nekk nañu ay xew-xewiy démb yu am te ñu dëggal leen. Nooni Yeesu ya sax nangu woon nañu ne ‘nit [kooku] kat, kéemaan yi mu [doon] def a ngi [doon] bëgga bare.’—Yowanna 11:47, 48.

17 Yeesu daan na wër réewam, doon jàngal nit ña lu jëm ci Nguurug Yàlla. (Macë 4:17) Joxe na it ab royukaay bu ràññeeku cig muñ ak teey. Ba taalibeem ya sax tasee yaakaaram, wax na ci ay kàddu yu bare cofeel: “Xel mi, dëgg la, njaxlaf na waaye suux wee néew doole.” (Mark 14:37, 38, NW ) Terewul, Yeesu ku am fit la woon te ñeme woon naa jaar ci dëgg ak ñi jéppi woon dëgg gi te doon naj ñi néew doole. (Macë 23:27-33) Ci kow lépp, topp na ci fasoŋ bu mat sëkk royukaayub mbëggeel, bu Baayam. Yeesu dem na ba nangoo dee ak xol bu tàlli, ngir doomi Aadama yu matadi yi am yaakaar ngir ëllëg. Bettuñu, kon, ñu mëna wóolu Yeesu niki caabi ji ngir xam-xamub Yàlla! Waaw, mooy caabi jiy dund! Waaye, lu tax ñuy wax caabi jiy dund? Looloo ngi ñuy yóbbu ci ñetteelu jamano dundam.

YEESU CI SUÑU JAMANO

18. Nan lañu wara gise Yeesu Krist ci suñu jamano?

18 Lu Biibël bi nettalee nettali deewug Yeesu, mu ngiy dund léegi! Noonu ca xarnu bu njëkk ba G.J.K.T, ay téeméeri nit seede woon nañu ak seeni gët ne dekkaloon nañu ko. (1 Korent 15:3-8) Na ko ab yonent yégle woon, gannaaw loolu toogoon na ca ndeyjooru Baayam, doon xaar ñu fal ko buur ca asamaan. (Sabuur 110:1; Yawut yi 10:12, 13) Kon nan lañu wara gise Yeesu ci suñu jamano jii? Ndax war nañu ko jàppe nikib liir bu mënalul boppam dara, nekk ci biir mbalka? Walla niki kuy sukkuraat? Déedéet. Ab Buur bu am kàttan buy nguuru la! Te ca kanam tuuti, dina feeñal kiliftéefam ci kow suñu suuf su jaxasoo sii.

19. Bu ca kanamee tuuti, ban jëf la Yeesuy sumb?

19 Ci Peeñu bi 19:11-15, ñu ngi ñuy nettali ci ay kàddu yu am doole Buur bi Yeesu Krist di ñëw ak kàttan gu réy ngir rey ñu bon ñi. Njiit mu am mbëggeel moomu dëkk ca asamaan, aka wara yàkkamtee jeexal metit yiy toroxal ay tamndareeti nit ci suñu jamano ji! Yàkkamti na it xettali ñiy góor-góorloo topp royukaay bu mat bi mu bàyyi ba mu nekkee ci kow suuf. (1 Pieer 2:21) Bëgg na leena musal ca biir “xeex biy am c[a] bés bu mag, b[a] Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam,” xeex buy jegesi bu gaaw-a-gaaw te ñu faral di ko woowe Ar-magedon, ndax ñu mëna dund ba fàww fii ci kow suuf niki surgay Nguurug Yàlla ba ca asamaan.—Peeñu bi 7:9, 14; 16:14, 16.

20. Ca Nguuram junniy at, lan la Yeesuy defal doomi Aadama yi?

20 Ca biir Nguurug jàmm Yeesu gu junniy at ya, Nguur gu ñu yégle woon, dina def ay kéemaan ngir nit ñépp. (Isayi 9:6, 7; 11:1-10; Peeñu bi 20:6) Yeesu dina faj feebar yépp te dina dindi dee. Dina dekkal ay junniy junniy tamndareeti nit ndax ñu am yoon ngir dund ba fàww ci kow suuf si. (Yowanna 5:28, 29) Wóor nañu ne dinga raf ci gëna jàng lu jëm ci Nguurug Almasi bi ci pàcc muy ñëw. Na la lii wóor: mënuñoo jortu sax na dund gay neexe ca kiliftéefu Nguur googu. Gëna jànga xam Yeesu Krist aka am maanaa! Waaw, am na solo lool ñu baña fàtte mukk ne Yeesooy caabi jiy dund ngir xam-xamub Yàlla biy jëme ca dund ga dul jeex.

[Li ñu bind ci suuf]

^ Mbindu mooma da doon dimbali Nguurug Room mu sàkk galag. Noonu, Ogust ci lu mu séenuwuloon, dimbali na ci àggloo yégleb yonent bu jëm ci am njiit mu naroona ‘jaarloo daantukat ca nguur ga.’ Yégleb yonent boobu saxsax xamaloon na ne “Njiitum kóllëre gi,” walla Almasi bi, doon nañu ko “damm” ca bésiy kiy wuutu njiit moomu. Reyoon nañu Yeesu ba Tibeer doon nguuru, moom mi wuutu woon Ogust.—Dañel 11:20-22.

^ Yawut yu njëkk ya dañu daan xalaat daanaka ci ay ayubésiy at. Maanaam, niki juróom-ñaareelu fan wu nekk bésu noflaay la woon, juróom-ñaareelu at mu nekk Atum noflaay la woon.—2 Musaa 20:8-11; 23:10, 11.

SEETLUL SA XAM-XAM

Nan la askanu Yeesu firndeele bu leer ne mooy Almasi bi?

Yan ci yenn yégley yonent yu ñu jagleel Almasi bi ñoo àgg ci Yeesu?

Nan la Yàlla ci boppam wone ne Yeesoo doon Ki ñu Tànn?

Lu tax Yeesu nekk caabi ji ngir xam-xamub Yàlla, jiy dund?

[Laaj yi]

[Tablo bi nekk paas 37]

YENN YÉGLEY YONENT YU RÀÑÑEEKU JËM CI ALMASI BI

YÉGLEB XEW-XEW BUY AMI XEW-XEW MOTTALI

ATAM YA JIITU

Isayi 7:14 Juddoo ci xeek Macë 1:18-23

Yérémi 31:15 Rey nañu ay liir Macë 2:16-18

gannaaw juddoom

YËNGU-YËNGOOM

Isayi 61:1, 2 Yónnent ci Yàlla Lukk 4:18-21

Isayi 9:1, 2 Yëngu-yëngoom tax na Macë 4:13-16

nit ñi gis leer gu réy

Sabuur 69:9 Sawar ngir kërug Yeowa Yowanna 2:13-17

Isayi 53:1 Duñu ko gëm Yowanna 12:37,38

Sakaria 9:9; Tàbbeem ca biir Macë 21:1-9

Sabuur 118:26 Yerusalem, yéeg ci kow

cumburub mbaam-sëf;

jaaraamaal nañu ko niki

buur teyit niki

kiy ñëw ci turuw Yeowa

KORAM AK DEEAM

Sabuur 41:9; 109:8 Lenn ndaw lu takkoodi; Jëf ya 1:15-20

wor na Yeesu te wuutu

nañu ko ca gannaaw ga

Sakaria 11:12 Wor nañu ko ngir Macë 26:14, 15

30 xànjari xaalis

Sabuur 27:12 Jaar nañu ci ay seede Macë 26:59-61

yu naaféq ngir sosal ko

Sabuur 22:18 Kaskas nañu ay yëreem Yowanna 19:23, 24

Isayi 53:12 Dendale nañu kook Macë 27:38

ay bàkkaarkat

Sabuur 22:7, 8 Saaga nañu ko ca Mark 15:29-32

biir sukkuraatam

Sabuur 69:21 Jox nañu ko bineegar Mark 15:23, 36

Isayi 53:5; Jam nañu ko Yowanna 19:34, 37

Sakaria 12:10

Isayi 53:9 Rob nañu kook ñi am alal Macë 27:57-60

Sabuur 16:8-11, Dekkil nañu ko ci suufu Jëf ya 2:25-32;

xët bi. laata moo yàqu 13:34-37

[Nataal bi nekk paas 35]

Yàlla jox na Yeesu kàttanu faj ñi wopp