Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 1

Dañu fi nettali bi Yàlla komaasee sàkk ba bi mu indee mbënn mi, maanaam taw bu metti, ci kow suuf si sépp

Dañu fi nettali bi Yàlla komaasee sàkk ba bi mu indee mbënn mi, maanaam taw bu metti, ci kow suuf si sépp

Asamaan ak suuf, fan la jóge ? Naaj bi, weer bi ak biddéew yi, lépp lu ñu gis ci kow suuf si, lan moo leen fi indi ? Biibël bi nee na Yàlla moo ko sàkk. Loolu mooy dëgg. Kon suñu téere bii, dina jëkk a nettali li Biibël bi wax ci li Yàlla sàkk.

Yàlla dafa jëkk a sàkk malaaka yi. Waaye suuf si dafa ko sàkk ngir ñun. Sàkk na benn góor ak benn jigéen, mu tudde leen Aadama ak Awa. Dafa leen dugal ci benn tool bu rafet lool. Waaye ñoom, déggaluñu Yàlla. Loolu moo tax ñu waroon a dee.

Diggante bi Yàlla sàkkee suñu maam Aadama ak bi Yàlla wàccee taw bu metti ci kow suuf si sépp, amoon na 1656 at. Ñu bon ñi, bare woon nañu. Ca asamaan, amoon na Seytaane ak malaakaam yu bon yi. Ci kow suuf si, amoon na Kayin. Amoon na itam ay ponkal yu réy lool ak yeneen nit ñu bon. Waaye amoon na itam ay nit ñu baax — Abel, Enog ak Nóoyin. Loolu yépp lañuy nettali ci XAAJ 1.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 1

Yàlla Mu ngi tàmbalee sàkk

Nettalib njàlbéen ga biy wax ci li Yàlla sàkk dafa neex a nànd te yéeme—ba ci xale yu ndaw yi sax.

NETTALI 2

Tool Bu Rafet

Ni ko njàlbéen ga waxe, Yàlla dafa defar toolu Eden ba mu rafet lool. Yàlla dafa bëggoon suuf si sépp mel ni tool boobu.

NETTALI 3

Nit ñi jëkk a am ci kow suuf

Yàlla dafa sàkk Aadama ak Awa ba pare duggal leen ci biir toolu Eden. Ñu doon góor ak jigéen ñi njëkk a séy.

NETTALI 4

Li tax ñu dàq leen

Téere bi nekk ci Biibël bi te tudd Njàlbéen ga wax na ñu ni Aadama ak Awa ñàkke àjjana ji.

NETTALI 5

Léegi àddina bi metti na

Aadama ak Awa sonn nañu lool léegi. Ñu ngi ci biti toolu Eden. Céy, bu Aadama ak Awa déggaloon Yexowa ! Ñoom ak seeni doom dinañu am dund gu neex.

NETTALI 6

Ñaari doom : kenn ki baax, keneen ki bon

Nettalib Kayin ak Abel ni ñu ko nettalee ci Njàlbéen ga, dafa ñuy jàngal lu jëm ci fasoŋu nit yi ñu war a doon ak ban doxalin lañu war a soppi bala muy wees.

NETTALI 7

Nit kii am na fit

Royukaayu Enog bi dafay wone ne mën nga def lu baax bu dee sax ñi la wër ñépp, lu bon rekk lañuy def.

NETTALI 8

Ay ponkal yu réy ci kow suuf si

Njàlbéen ga pàcc 6 dafay wax ci ay ponkal yu soxoroon ak nit ñi. Ponkal yooyu, te ñu leen di woowu Nefilim, malaaka yi déggalul woon Yàlla ñoo leen jur. Malaaka yooyu dañu jóge ci asamaan te ñëw ci suuf ngir dund ni doomu Aadama.

NETTALI 9

Nóoyin dafay defar gaal gu mag

Nóoyin ak njabootam dañu mucc ci taw bu metti ba ndaxte dañu dégal Yàlla doonte sax ñeneen ñi dégluwuñu.

NETTALI 10

Taw bu metti ci kow suuf si sépp

Nit ñi dañu reetaan bi leen Nóoyin doon àrtu. Waaye bàyyi nañu reetaan bi bi taw bi ñëwe ! Xoolal ni gaalu Nóoyin muccale Nóoyin, njabootam, ak mala yu bare.