Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 5

Léegi àddina bi metti na

Léegi àddina bi metti na

AADAMA ak Awa sonn nañu lool léegi. Ñu ngi ci biti toolu Eden. War nañu def liggéey bu metti ngir am lu ñuy lekk. Amatul garab yu rafet ak doom yu neex. Léegi, xaaxaam kese moo am ci suuf si, ak dég yu bare. Loolu yépp dafa leen dal ndaxte déggaluñu Yàlla. Nekkatuñu ay xaritam.

Waaye li gën a metti mooy dañu komaasee dee. Yàlla dafa leen tere woon benn doomu garab. Bu ñu ci lekkee, dinañu dee. Te loolu moo am. Bés bi ñu ko lekkee rekk, ñu komaasee dee. Ci dëgg, seen bañ a déggal Yàlla, amul woon benn njariñ !

Doom yi Aadama ak Awa amoon yépp, dañu juddu ginnaaw bi ñu leen génnee toolu Eden. Loolu moo tax ñoom itam ñu war a màgget te dee.

Céy, bu Aadama ak Awa déggaloon Yexowa ! Ñoom ak seeni doom dinañu am dund gu neex. Dinañu dund ba fàww. Kenn du màgget, feebar, ba pare dee.

Yàlla dafa bëgg nit ñi dund ba fàww ci jàmm. Nee na loolu dina am. Suuf si dina rafet te kenn du feebar. Nit ñi ñépp dinañu nekk ay xarit ci seen biir, nekk itam xaritu Yàlla.

Awa moom, nekkatul woon xaritu Yàlla. Looloo tax bi mu doon am doom, mu metti lool. Déggalul Yexowa, te gis nga ne loolu indil na ko coono yu bare, du dëgg ?

Aadama ak Awa amoon nañu doom yu bare, yu góor ak yu jigéen. Seen taaw bu góor, dañu ko tudde Kayin. Ki topp ci moom, dañu ko tudde Abel. Lan moo leen dal ? Ndax xam nga ko ?