Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 3

Nit ñi jëkk a am ci kow suuf

Nit ñi jëkk a am ci kow suuf

LAN ngay gis fii te amul woon ci nettali 2 ? Benn góor ak benn jigéen. Ñoom ñooy nit ñi jëkk a am ci kow suuf si. Kan moo leen sàkk ? Yàlla la. Ndax xam nga turu Yàlla ? Yexowa la tudd. Góor gi, Aadama la tudd, jigéen bi, Awa.

Nii la Yexowa sàkke suñu maam Aadama : dafa jël suuf, def benn yaramu nit bu amul benn sikk, mu ëf ci bakkanam, Aadama daldi dund.

Yexowa jox na Aadama benn liggéey. Dafa ko wax mu jox mala yépp tur. Xéyna Aadama toog na lu yàgg di leen xool rekk ngir xam tur bu gën a mën a ànd ak xeetu mala bu nekk. Waaye am na lu Aadama gis. Ndax xam nga lan la ?

Mala yépp, ñaar lañu woon. Amoon na pàppa ñey ak yaay ñey, pàppa gaynde ak yaay gaynde. Waaye Aadama moom, amul woon ku muy àndal. Kon, Yàlla dafa nelawloo Aadama, nelaw bu xóot, jël benn yax ci wetam, maanaam benn faar, defar ci benn jigéen, may ko Aadama mu nekk jabaram.

Aadama kontaan na lool ! Awa itam naroon na kontaan. Mu ngi ci tool bu rafet lool ! Léegi, mën nañu am doom te am dund gu neex ci kow suuf si.

Yexowa dafa bëggoon Aadama ak Awa dund ba fàww. Dafa bëggoon ñu liggéey ba àddina si sépp mel ni toolu Eden. Liggéey boobu, Aadama ak Awa naroon nañu ci kontaan lool  ! Boo fa nekkoon, ndax dinga ci bëgg bokk ? Waaye jàmm jooju Aadama ak Awa amoon, yàggul. Nañu seet lu tax ci nettali bii di topp.