Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 10

Taw bu metti ci kow suuf si sépp

Taw bu metti ci kow suuf si sépp

NIT ñi desoon ci biti gaal ga, soppiwuñu li ñu doon def. Pur ñoom, taw bu metti boobu, du am. Xéyna sax, booba lañu gën a reetaan. Waaye loolu yàggul.

Jékki-jékki rekk mu komaase taw. Dafa meloon ni paanu ndox yu mag yu ñuy sotti ci kow suuf si. Kon li Nóoyin waxoon mooy dëgg. Waaye léegi, kenn mënatul dugg ci biir gaal gi. Yexowa ci boppam moo tëj bunt bi, te dafa ko tëj bu baax.

Suuf si gaaw na fees ak ndox, ndox mi daldi def ay dex yu mag, ndox mi di yóbbu garab yi ak xeer yu mag. Coow bu réy la doon def. Ñépp tiit, di yéeg fu gën a kowe. Céy, bu ñu déglu woon Nóoyin te dugg ci biir gaal gi ! Waaye léegi mënatuñu koo def.

Taw na 40 bëccëg ak 40 guddi. Ndox mi dafa doon yéeg rekk. Muur na tund yi. Dem na ba muur montaañ yu gën a kowe yi. Kon li Yàlla waxoon, amoon na. Nit ñi ak mala yépp yi nekkoon ci biti gaal ga, dee nañu. Waaye ñi nekkoon ci biir, dara dalu leen.

Ni Nóoyin ak doomam yi defare gaal gi, baaxoon na lool. Bi ndox mi komaasee di bare ci kow suuf si, gaal gi dafa doon yéeg ak moom, di nekk ci kowam. Benn bés, taw bi taxaw, naaj bi génn. Lii rekk lañu mënoon a gis : Géej gu réy ci kow suuf si sépp. Gaal gi rekk moo nekkoon ci kow géej googu.

Léegi amatul ponkal yu réy. Dootuñu fitnaal nit ñi. Dee nañu ñoom ñépp, ñoom, seeni yaay ak yeneen nit ñu bon ñi. Seeni baay nag ? Lan moo leen dal ?

Ñoom, nekkuñu woon doom-Aadama dëgg. Malaaka lañu woon te dañu wàccoon ci kow suuf, jël yaramu nit. Kon bi taw boobu amee, ñoom deewuñu. Dañu bàyyi yaramu nit bi ñu amoon te dellu asamaan niki malaaka. Waaye mënatuñu woon a bokk ci malaaka Yàlla yi, ñu daldi nekk malaaka Seytaane yi. Biibël bi dafa leen di tudde jinne walla rab.

Ginnaaw loolu Yàlla indi na ngelaw. Ngelaw bi def ba ndox mi wàcc. Juróomi weer ginnaaw loolu, gaal gi teer na ci kow benn montaañ. Ay fan yu bare ginnaaw loolu, ñi nekkoon ci biir gaal gi daldi gis yeneen montaañ. Ndox mi mu ngi doon wàcc ndànk-ndànk.

Bi mu yàggee tuuti, Nóoyin bàyyi na benn picc bu ñuy woowe baaxoñ mu génn gaal gi. Dem na, waaye gisul fenn fu muy taxaw, mu daldi dellu ci biir gaal gi. Def na loolu ay yooni yoon.

Nóoyin dafa bëggoon a xam ndax suuf si wowoon na léegi. Mu yebal benn pitax. Moom itam dafa dellusi ndaxte gisul fenn fu muy taxaw. Nóoyin yebalaat ko, mu indi benn xobu oliw. Léegi Nóoyin xam na ne ndox mi wàcc na bu baax. Mu yebalaat pitax bi beneen yoon, pitax bi gis fu wow fu mu mën a des.

Lii la Yàlla wax Nóoyin léegi : ‘ Génnal gaal gi, yow, sa njaboot ak mala yi. ’ Nekkoon nañu ci biir gaal gi lu ëpp benn at. Léegi kontaan nañu lool ndaxte mucc nañu, mën nañu génn gaal gi te dox ci kow suuf si !