Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 2

Li xewoon diggante taw bu metti bi ak bi Yàlla musalee waa Israyil ci Misra

Li xewoon diggante taw bu metti bi ak bi Yàlla musalee waa Israyil ci Misra

Juróom-ñetti nit rekk ñoo mucc ci taw bu metti bi. Waaye ndànk-ndànk nit ñi dañu yokkuwaat ba nekk ay junniy-junni nit. Bi taw boobu amee ba mu am 352 at, ca la Ibraayma juddu. Yàlla def na li mu digoon Ibraayma, maanaam dafa koy may doom bu ñu tudde Isaaxa. Dinañu gis naka la Yàlla defe loolu. Ci ñaari doomi Isaaxa, Yanqóoba la Yàlla tànn.

Yanqóoba amoon na doom yu bare, 12 doom yu góor ak ay doom yu jigéen. Fukki doomam yu góor yi dañu bañoon lool seen rakk Yuusufa. Dañu ko jaay mu nekk jaam ca Misra. Ay at ginnaaw loolu, Yuusufa nekk na kilifa gu mag foofu. Bi xiif gu metti amee, Yuusufa seet na ndax magam yi soppi nañu seen jikko. Ginnaaw loolu, waa këru Yanqóoba yépp, maanaam waa Israyil, toxu nanu Misra. Loolu xewoon na 290 at ginnaaw bi Ibraayma juddoo.

Waa Israyel nekkoon nañu 215 at ci Misra. Bi Yuusufa gaañoo, dañu leen def jaam foofu. Musaa juddu na ca jamano jooja. Yàlla jaar na ci moom ngir musal waa Israyil ci Misra. Lépp li ñu nettali ci XAAJ 2, xewoon na ci biir 857 at.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 11

Xon gu jëkk gi

Kon boo gisee xon gi, lan nga war a fàttaliku ?

NETTALI 12

Ñu ngi tabax lu kowe lool

Tabax boobu neexul woon Yàlla, moo tax lu bon li loolu jur mu ngi laal nit ñi ba tey.

NETTALI 13

Ibraayma, xaritu Yàlla

Lu tax Ibraayma jóge ci këram gu rafet gi dem dëkk ci ay tànt giiru dundam yépp ?

NETTALI 14

Yàlla mu ngi natt ngëmu Ibraayma

Lu tax Yàlla wax Ibraayma mu saraxe doomam Isaaxa ?

NETTALI 15

Jabaru Lóot geestu na

Li mu def mën nañu jàngal lu am solo.

NETTALI 16

Isaaxa takk na jabar ju baax

Lan moo taxoon Rebeka nekk jabar ju baax ? Rafetaayam walla leneen ?

NETTALI 17

Ñaari séex yu wuute

Seen baay, Isaaxa, Esawu la gënoon a bëgg, waaye seen yaay, Rebeka, Yanqóoba la gënoon.

NETTALI 18

Yanqóoba dem na karan

Yanqóoba Leya la njëkk a takk bu dee sax Rasel la noboon.

NETTALI 19

Yanqóoba am na doom yu bare

Ndax dañu tudde 12 giiru Israyil yi 12 doomu Yanqóoba yu góor yi ?

NETTALI 20

Diina am na poroblem

Loolu yépp komaase ci ak xarit yu bon.

NETTALI 21

Magi Yuusufa dañu ko bañ

Lu tax ñenn ñi ci ñoom bëggoon a réy seen rakk bu góor ?

NETTALI 22

Tëj nañu Yuusufa kaso

Nekkul ne dafa bañ a topp yoon bi moo tax ñu tëj ko foofu, waaye dañu ko tëj foofu ndaxte dafa def lu jub.

NETTALI 23

Firawna mu ngiy gént

Juróom-ñaari nag yi ak juróom ñaari gub yi am na luñu bokk.

NETTALI 24

Yuusufa Mu ngi teg nattu ci kow magam yi

Naka lañu mënee xam ne soppekunañu bu baax wuute ak jamano ja ñu jaayee seen rakk ngir mu nekk jaam ?

NETTALI 25

Yanqóoba ak waa këram ñu ngi toxu Misra

Lu tax waa këru Yanqóoba ñu leen di woowe waa Israyil yi te duñu leen woowe waa Yanqóoba yi ?

NETTALI 26

Ayóoba Bàyyiwul Yàlla

Ayóoba ñàkk alalam, ay doomam ak wér-gi-yaramam. Ndax Yàlla dafa doon yar Ayóoba ?

NETTALI 27

Buur Bu Bon Mooy Ilif Misra

Lan moo tax mu wax nitam yi ñu rey liiru Yawut yu góor yépp ?

NETTALI 28

Naka La Musaa Rëcce Bi Mu Nekkee Liir

Yaayam dafa wut pexe ci yoon bi ñu tëraloon bi naan dañu war a rey doomu waa Israyil yu góor yépp.

NETTALI 29

Li Tax Musaa Daw

Bi Musaa amee 40 at dafa foogoon ne pare na ngir musal waa Israyil waaye parewul woon.

NETTALI 30

Garab Gi Doon Tàkk

Yàlla dafa jëfandikoo ay kéemaan ngir wax Musaa ne jot na mu dem génne waa Israyil ci Misra.

NETTALI 31

Musaa Ak Aaroona Ñu Ngi Ci Firawna

Lu tax Firawna dégluwul Musaa te bàyyi waa Israyil ñu dem ?

NETTALI 32

Fukki Musiba Yi

Yàlla dafa indi fukki musiba yooyu yépp ci Misra ndaxte njiitu Misra bi, Firawna dafa bañoon a bàyyi waa Israyil ñu dem.

NETTALI 33

Ñu Ngi Jéggi Géej Gu Xonq Gi

Musaa dafa xaajale géej gi ñaar ci kàttanu Yàlla, te waa Israyil jéggi nañu jaar ci suuf su wow.