Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 13

Ibraayma, xaritu Yàlla

Ibraayma, xaritu Yàlla

GINNAAW bi taw bu metti boobu amee ci kow suuf si sépp, nit ñi dem nañu ci ay béréb yu bare. Benn ci béréb yooyu, mu ngi tudd Ur. Mujj na nekk dëkk bu réy ak kër yu rafet. Waaye nit ni dañu doon jaamu ay yàlla yu dul dëgg, mel ni ñi dëkkoon Babel. Waa Babel ak waa Ur meluñu woon ni Nóoyin ak doomam bi tudd Sem. Nóoyin ak Sem, bàyyiwuñu di topp Yexowa.

Nóoyin dund na ba 350 at ginnaaw taw bu metti boobu, mu mujj gaañu. Ki ngeen di gis fii, juddu na ñaari at ginnaaw bi Nóoyin gaañoo. Ni ko Yàlla jàppe woon, bokkul ak ni mu jàppe woon ñeneen nit ñi. Ibraayma la tudd. Ur la dëkkoon, moom ak njabootam.

Benn bés, lii la Yexowa wax Ibraayma : ‘ Nanga jóge Ur, jóge ci say mbokk, te dem beneen réew bu ma lay won. ’ Ndax Ibraayma def na loolu te bàyyi lu neex li mu amoon foofu ? Def na ko, kay. Ibraayma dafa doon def lépp li ko Yàlla sant. Loolu moo tax ñu woowe ko xaritu Yàlla.

Ci njabootu Ibraayma, am na ñu ànd ak moom bi mu jógee Ur. Ginnaaw jabaram Saarata, amoon na it baayam Teraa ak jarbaatam Lóot. Dem nañu ba àgg benn béréb bu tudd Karan. Foofu la Teraa gaañoo. Sore woon nañu lool Ur.

Bi mu yàggee tuuti, Ibraayma ak waa këram jóge Karan te dem ca réew bi tudd Kanaan. Foofu, Yexowa ne ko : ‘ Réew mii, dinaa ko may say doom. ’ Ibraayma toog na Kanaan te dëkk ci ay tànt.

Yàlla dimbali na Ibraayma ba mu am xar yu bare ak yeneen mala, dolli ci ay téemeeri nit ñi ko doon liggéeyal. Waaye moom ak Saarata amuñu woon doom.

Bi Ibraayma amee 99 at, Yexowa wax na ko lii : ‘ Maa ngi lay dig ne dinga nekk baayu xeet yu bare. ’ Waaye léegi, Ibraayma ak Saarata dañu màgget. Mënatuñu am doom. Kon naka la loolu di ame ?