Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 15

Jabaru Lóot geestu na

Jabaru Lóot geestu na

LÓOT ak njabootam ñu ngi nekkoon ak Ibraayma ci réewu Kanaan. Benn bés, lii la Ibraayma wax Lóot : ‘ Suñu jur yi xajuñu fii. Nañu tàggoo. Boo demee nii, ma dem nale. ’

Lóot xool. Mu gis béréb bu rafet, bu am ndox ak ñax bu bare pur juram. Diiwaanu Yurdan la woon. Lóot ak njabootam ak juram yépp daldi toxu foofu te mujj a dëkk ci Sodom.

Ñi dëkkoon Sodom, dañu bonoon lool. Loolu metti woon na Lóot, ndaxte moom nit ku baax la woon. Yàlla itam, loolu neexu ko woon dara. Mujj na yónni ñaari malaaka ci Lóot ngir wax ko ne dina alag Sodom ak benn dëkk bu ko jege te tudd Gomor ndax lu bon li ñu doon def.

Lii la malaaka yi wax Lóot : ‘ Gaawal ! Jëlal sa jabar ak sa ñaari doom yu jigéen te jógeleen fii ! ’ Waaye Lóot ak njabootam dañu doon yéexantu. Malaaka yi jàpp seen loxo te yóbbu leen ci biti dëkk bi. Kenn ki ne leen : ‘ Dawleen ngir mën a rëcc. Buleen geestu. Dawleen ci tund yi, ngir bañ a dee. ’

Lóot ak doomam yu jigéen yi topp nañu loolu te daw Sodom. Taxawuñu te geestuwuñu. Waaye jabaru Lóot, moom, bi ñu soree Sodom tuuti, taxaw na te geestu. Mu daldi soppaliku nekk xorom ci saa si. Ndax yaa ngi koy gis fii ?

Am na lu am solo lu nu mën a jàng ci loolu. Yàlla dafay muccal ñi koy déggal. Waaye ñi ko dul déggal, dinañu ñàkk seen bakkan.