Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 27

Buur Bu Bon Mooy Ilif Misra

Buur Bu Bon Mooy Ilif Misra

GÓOR yi nekk fii, ñu ngi forse nit ñi ñu liggéey. Xoolal kiy dóor keneen ki ! Ñi nekk fii di liggéey, ay mbokku Yanqóoba lañu. Dañu leen woowe waa Israyil. Ñi leen di forse noonu, waa Misra lañu. Léegi waa Israyil, ay jaam lañu ci Misra. Lu tax loolu ?

Nit ñu bare ñi bokkoon ci waa këru Yanqóoba, nekkoon nañu ci jàmm ay at yu bare ci Misra. Yuusufa moo nekkoon nit ki topp ci Firawna ci réew mi te dafa leen doon toppatoo bu baax. Waaye léegi Yuusufa gaañu na. Beneen Firawna moo nekk buur ci Misra. Moom bëggul waa Israyil.

Kon dafa leen def jaam. Te mu def ci seen kow ay kilifa yu soxor. Ñu di leen forse ñu def liggéey bu metti lool. Dañu waroon a tabaxal Firawna ay dëkk. Waaye ba tey, waa Israyil ñu ngi gën di bare rekk, ba waa Misra tiit. Dañu ragaloon ñu ëpp leen te gën leen a am doole.

Ndax xam nga lan la Firawna def ? Lii la wax jigéen yi doon dimbali jigéenu Israyil ñu wasin : ‘ Liir bu góor buy juddu, reyleen ko. ’ Waaye jigéen yooyu, jigéen yu baax lañu woon. Reyuñu liir yooyu.

Firawna daldi digal lii waa réew mi : ‘ Liir bu góor bu juddu ci waa Israyil, jëlleen ko te rey ko. Waaye buleen rey liir yu jigéen yi. ’ Ndax loolu nekkul lu soxor lool ? Nañu seet naka la benn liir bu góor rëcce ci loolu.