Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 11

Xon gu jëkk gi

Xon gu jëkk gi

NDAX xam nga li Nóoyin jëkk a def bi mu génnee gaal ga, moom ak njabootam ? Dafa jël ay mala, def leen sarax yu mu jébbal Yàlla. Loolu lañuy wone fii ci suuf. Nóoyin dafa bëggoon a gërëm Yàlla ci li mu musal njabootam ci taw bu metti boobu.

Ci sa xalaat, ndax sarax boobu neexoon na Yexowa ? Waawaaw, neexoon na ko kay. Yàlla dig na sax Nóoyin ne dootul indi taw buy alag àddina si sépp.

Yàggul, suuf si wow, Nóoyin ak njabootam daldi tàmbali dund gu bees. Yàlla barkeel na leen te ne leen : ‘ War ngeen a am doom yu bare ba feesal àddina si sépp. ’

Waaye bu yàggee, bu nit ñi déggee taw bu metti boobu, xéyna dinañu ragal mu amaat. Kon Yàlla def na lu leen di fàttali li mu waxoon, maanaam dootul indi taw bu metti ci kow suuf si sépp. Xam nga lan la def ? Xon gi.

Xon, dañu ko faral a gis ci asamaan bu naaj bi génnee ginnaaw taw bi. Am na kulóor yu rafet. Ndax mas nga ko gis ? Ndax gis nga bi ñuy wone fii ?

Lii la Yàlla wax : ‘ Dootul amati taw buy alag nit ak mala yépp yi nekk ci kow suuf. Maa ngi def sama xon ci niir yi. Bu feeñee ci asamaan, dinaa ko gis te dinaa fàttaliku li ma dige noonu. ’

Kon boo gisee xon gi, lan nga war a fàttaliku ? Danga war a fàttaliku li Yàlla dige, maanaam dootul indi taw bu metti ngir alag lépp ci àddina si.