Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 47

Benn Sàcc Ci Israyil

Benn Sàcc Ci Israyil

XOOLAL li góor gii di suul ci tàntam ! Mbubb bu rafet, wurus ak xaalis. Dafa leen jël ci dëkku Yeriko. Waaye ndax yaa ngi fàttaliku li ñu waroon a def ak lépp li nekkoon Yeriko ?

Dañu ko waroon a yàq, te wurus bi ak xaalis bi, dañu ko waroon a def fi ñuy dence alalu tàntu Yexowa bi. Kon ñi ngay gis fii, toppuñu li Yàlla waxoon. Dañu sàcc lu Yàlla moom. Góor gi mu ngi tudd Akan, te ñi nekk ak moom, ci njabootam lañu bokk. Nañu seet lan mooy xew.

Ginnaaw bi Akan sàccee loolu, Yosuwe dafa yónni ay góor pur xeex ñi dëkkoon Ayi. Waaye waa Ayi dañu daan góor ñooñu, mu am ñu ci dee, ñeneen ñi daw. Xolu Yosuwe yépp jeex. Mu daldi tëdd, kanamam féete suuf. Mu ñaan Yexowa ne ko : ‘ Lu tax nga bàyyi loolu am ? ’

Yexowa tontu ko ne : ‘ Jógal ! Israyil dafa bàkkaar. Dañu jël loo xam ne dañu ko waroon a yàq walla def ko ci tàntu Yexowa. Dañu sàcc mbubb bu rafet, ba pare nëbb li ñu def. Bala ma leen di barkeel, fàww ngeen yàq mbubb boobu te rey ki ko sàcc. ’ Yexowa wax na Yosuwe ne dina ko xamal kan moo sàcc.

Yosuwe dajale na mbooloo mi yépp. Yexowa wone na ku bon kooku tudd Akan. Akan ne lii : ‘ Bàkkaar naa. Dama gis benn mbubb bu rafet, wurus ak xaalis. Dama leen bëggoon lool, moo tax ma jël leen. Suul naa leen ci sama biir tànt. Dinga leen gis foofu. ’

Nit ñi daldi dem seet fu yëf yooyu nekkoon. Bi ñu leen indilee Yosuwe, lii la wax Akan : ‘ Lu tax nga indil ñu coono ? Léegi, Yexowa moo lay indil coono. ’ Mbooloo mi yépp daldi ko sànni ay xeer, moom ak njabootam, ba ñu dee. Ndax loolu wonewul ne waruñu jël mukk lu ñu moomul ?

Ginnaaw loolu, Israyil demaat na xeex ak ñi dëkkoon Ayi. Bii yoon, Yexowa dimbali na leen, ba ñu daan.