NETTALI 34
Lekk Bu Bees
NDAX mën nga wax li nit ñi di for ci suuf si ? Boo ko xoolee, dafa weex, sew te mel ni pëndax galaas, waaye du galaas. Lekk la.
Bi waa Israyil génnee Misra, am na léegi benn weer. Ñu ngi ci màndiŋ mi. Foofu lekk bi barewul dara. Waa mbooloo mi, ñu ngi komaase di xultu, naan : ‘ Bu ñu Yexowa reyoon ca Misra moo gënoon. Foofu moom, lekk bu ñu bëggoon rekk, ñu am ko. ’
Kon Yexowa nee na : ‘ Dinaa def mu taw lekk bu jóge asamaan. ’ Te loolu la def. Waa Israyil daldi gis ci ëllëg si lu weex loolu jóge woon ci kow asamaan si, ñépp di laaj moroomam : ‘ Lii lan la ? ’
Musaa ne leen : ‘ Lii mooy lekk bi leen Yexowa jox. ’ Mbooloo mi di ko woowe MÀNN. Mu ngi saf lu mel ni mbiskit yu ñu defare lem.
Musaa wax mbooloo mi lii : ‘ Nangeen ci for lu nit ku nekk mën a lekk. ’ Te loolu lañu doon def suba su nekk. Bu naaj bi komaasee tàng, mànn bi desoon ci kow suuf si dafa doon seey.
Musaa ne leen itam : ‘ Buleen jël lu ëpp li ngeen soxla pur benn fan. ’ Waaye am na ñu toppul loolu. Booba, ndax xam nga lan moo doon am ? Ci ëllëg si, mànn bi doon fanaan dafa feesoon dell ak ay sax, mu komaase di xasaw.
Waaye ci ayu-bés bi, amoon na bés boo xam ne dañu waroon a jël ñaari yoon li ñu faral a jël. Bés boobu moo doon juróom-benneelu fan bi. Yexowa moo leen waxoon loolu ndaxte narul woon wàcce mànn ci juróom-ñaareelu fan bi. Kon ci juróom-benneelu fan bi, dañu naroon a jël mànn bu doy ngir mën ci dénc ngir juróom-ñaareelu fan bi. Te bi ñu doon def loolu, mànn bi du def ay sax te du xasaw. Loolu, beneen kéemaan la woon !
Yexowa dundal na waa Israyil ak mànn bi ci at yi ñu def ci màndiŋ mi yépp.
Gàddaay gi (Exode) 16:1-36; Nombres 11:7-9; Josué 5:10-12.