Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 49

Naaj Bi Taxaw Na Ci Asamaan Si

Naaj Bi Taxaw Na Ci Asamaan Si

XOOLAL Yosuwe. Lii lay wax : ‘ Naaj bi ! Taxawal ! ’ Te naaj bi taxaw na. Taxaw na lu mat benn fan ci diggu asamaan. Yexowa moo def loolu. Nañu seet lu tax Yosuwe bëggoon naaj bi kontine di leer.

Bi juróomi buur yu bon yi nekkoon Kanaan komaasee di xeex waa Gibeyon, ñoom dañu yónni benn góor ci Yosuwe. Mu ne ko : ‘ Ñówal gaaw, muccal ñu ! Buur yi dëkk ci tund yi, ñoom ñépp, ñów nañu xeex ak ñun, ñun ñii nekk say jaam. ’

Yosuwe gaaw a jóg ak xarekatam yépp, maanaam ñi doon ànd ak moom ci xeex yi. Guddi gi yépp lañu dox. Bi ñu àggee Gibeyon, soldaari juróomi buur yi daldi ragal, komaasee daw. Yexowa daldi def mu taw ay xeeru galaas yu mag a mag. Soldaar yi taw boobu rey, ëpp nañu sax soldaar yi xarekati Yosuwe rey.

Yosuwe gis ne jant bi dafa bëgg a so. Léegi guddi jot te ñu bare ci soldaar yi nekkoon ak juróomi buur yu bon yi dinañu mën a rëcc. Loolu moo tax Yosuwe ñaan Yexowa, ba pare mu wax lii : ‘ Naaj bi ! Taxawal ! ’ Naaj bi kontine di leer. Waa Israyil daldi mën a àggale seen xeex te yóbbu ndam li.

Yeneen buur yu bon yu bare ci Kanaan dañu bañ mbooloo Yàlla. Yosuwe ak xarekatam yi xeex nañu 31 buur foofu ba daan leen. Loolu yépp, ci juróom-benni at la ame. Ginnaaw loolu, Yosuwe séddale na réewu Kanaan diggante giiru Israyil, maanaam askanu doomi Israyil, yi amagul woon fu ñu dëkk.

Ay at yu bare ginnaaw loolu, Yosuwe gaañu na bi mu amee 110 at. Moom ak xaritam yi, ay nit ñu baax lañu woon. Bi ñu doon dund, mbooloo Yàlla dafa doon topp Yexowa. Waaye bi ñu gaañoo, mbooloo mi daldi def lu bon, dugal seen bopp ci coono ba ñu soxla ndimbalu Yàlla lool.