Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 55

Xale Bu Ndaw Buy Jaamu Yàlla

Xale Bu Ndaw Buy Jaamu Yàlla

XOOLAL xale bu rafet bi nekk fii ! Samwil la tudd. Te góor gii def loxoom ci boppam mooy saraxalekat bu mag bi ci Israyil. Mu ngi tudd Eli. Ñi indi Samwil ñooy baayam mi tudd Elkana, ak yaayam mi tudd Aana.

Samwil, ñeent walla juróomi at rekk la war a am. Waaye fii lay nekk léegi ak Eli ak yeneen saraxalekat yi, ci tànt bi fi ñuy jaamoo Yexowa. Lu tax Elkana ak Aana indi xale bu ndaw noonu ngir mu jaamu Yexowa fii ci tàntu Yàlla bi ? Nañu seet loolu.

Tuuti at bala loolu, xolu Aana dafa jeexoon tàkk ndaxte mënuloon a am doom, fekk doom rekk la bëggoon. Benn bés nag, am na lu mu ñaan Yexowa. Booba, dafa fekkoon mu nekk ca tàntu Yexowa. Mu ne ko : ‘ Céy Yexowa, bu ma fàtte ! Soo ma mayee dóom ju góor, dig naa la ne dinaa la ko may mu jaamu la dundam yépp. ”

Yexowa daldi may Aana li mu ko ñaan. Ay weer ginnaaw loolu, mu jur Samwil. Aana bëggoon na doomam lool. Mu daldi ko jàngal lépp lu jëm ci Yexowa, fekk xale bu tuuti la woon. Lii la wax jëkkëram : ‘ Bu xale bi feree, dinaa ko yóbbu ca tàntu Yàlla ngir mu jaamu fa Yexowa. ’

Aana ak Elkana lañuy wone fii, bi ñu indee Samwil. Samwil kontaan na ci li mu mën a jaamu Yexowa fii ci tàntam, ndaxte bi mu nekkee xale bu tuuti, waajuram dañu ko doon jàngal lu bare lu jëm ci Yexowa. At mu nekk, Aana ak Elkana dañu faral a ñów ci tàntu Yàlla ngir jaamu Yexowa akit ngir seetsi seen doom. Te at mu nekk Aana dafay indil doomam yére bu bees bu mu ko ñawal.

Samwil mu ngi kontine di jaamu Yexowa ci tàntam. Yexowa bëgg ko, mbooloo mi it bëgg ko. Waaye Eli moom amoon na ñaari doom yu bon. Ñu ngi tudd Ofni ak Fine. Lu bon li ñuy def bare na te ñu ngi xiir nit ñi sax ci bañ a déggal Yexowa. Eli dafa leen waroon a génne ñu bañ a bokkati ci saraxalekat yi. Waaye defu ko.

Lu bon li amoon foofu, terewul Samwil kontine di jaamu Yexowa. Ñi bëggoon Yexowa dëgg, barewuñu woon ca jamano jooja. Looloo taxoon Yexowa gëj a wax ak nit. Waaye bi Samwil màggee tuuti, lii moo xew :

Samwil mu ngi doon nelaw ci tàntu Yàlla bi, jékki-jékki rekk mu dégg baat bu koy woo. Mu ne ko : ‘ Maa ngi nii. ’ Mu jóg, dem gaaw ci Eli, ne ko : ‘ Yaa ma woo, maa ngi nii. ’

Waaye Eli ne ko : ‘ Déedéet. Woowuma la, demal tëddi. ’ Samwil dem tëddi.

Samwil daldi déggaat baat bi koy ne : ‘ Samwil ! ’ Samwil jóg, daw ci Eli, ne ko : ‘ Yaa ma woo. Maa ngi nii. ’ Eli ne ko : ‘ Déedéet, woowuma la, sama doom. Dellul tëddi. ’ Samwil daldi dellu.

Mu déggaat baat boobu mu koy wax : ‘ Samwil ! ’ Samwil daw ci Eli, ne ko : ‘ Maa ngi nii. Bi yoon moom, xam naa ne yaa ma woo. ’ Eli daldi xam ne Yexowa mooy woo xale bi. Mu ne ko : ‘ Dellul tëddi. Waaye bii yoon, bu la woowaatee, lii nga war a wax : “ Waxal, Yexowa. Sa jaam mu ngi lay déglu. ” ’

Loolu la Samwil wax bi ko Yexowa woowaatee. Yexowa ne ko léegi dina yar Eli ak doomam yi. Te loolu la def. Ofni ak Fine dee nañu ci benn xeex bi amoon diggante waa Israyil ak waa Filisti. Bi Eli déggee loolu, mu daanu, loosam damm, mu daldi dee. Li Yexowa waxoon, am na.

Samwil màgg na te moom moo doon àttekat bi mujj ci Israyil. Bi mu demee ba màgget, waa Israyil ne ko : ‘ Tànnal benn buur ngir mu ilif ñu. ’ Samwil bëggul a def loolu ndaxte ci dëgg Yexowa mooy seen buur. Waaye Yexowa ne ko mu def li ko waa Israyil laaj.

1 Samwil (1 Samuel) 1:1-28 ; 2:11-36 ; 4:16-18 ; 8:4-9.