Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 38

Fukki Góor Ak Ñaar Yuy Yërndu Réew Mi

Fukki Góor Ak Ñaar Yuy Yërndu Réew Mi

XOOLAL doomu garab yi nit ñooñu di indi. Xoolal ni reseñ yi ngandee ! Soxla nañu ñaari góor pur ñu yëkkëti ko ak bant. Xoolal figg yi ak gerenaad yi. Doomu garab yu rafet yooyu, fu ñu jóge ? Kanaan lañu jóge. Kanaan mooy fu Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba dëkkoon. Waaye xiif gu metti gi moo taxoon Yanqóoba toxu moom ak waa këram ca Misra. Waaye léegi ñu ngi 216 at ginnaaw loolu te Musaa mu ngi yóbbuwaat waa Israyil ca Kanaan. Ñu ngi léegi ci màndiŋ mi ci béréb bi tudd Kades.

Ñi dëkk Kanaan, ay nit ñu bon lañu. Musaa daldi yónni 12 góor, mu ne leen : ‘ Nangeen jéem a xam ñaata nit ñoo fa nekk ak fi seen doole tollu. Xoolleen ndax suuf si neex na bey. Te buleen fàttee indi ay doomu garab. ’

Bi ñu dellusee Kades, lii lañu wax Musaa : ‘ Réew mi, réew bu baax la. ’ Ñu daldi ko won doomu garab yi ñu indi woon. Waaye amoon na ci 10 ñu waxoon lii : ‘ Ay ponkal ñoo fa dëkk. Bu ñu bëggee nangu seen réew, dinañu ñu rey. ’

Bi waa Israyil déggee loolu, dañu tiit. Lii lañu doon wax : ‘ Céy waay, dee ci Misra walla sax fii ci màndiŋ mi moo gënoon. Bu ñu xeexee ak ñoom, ñun dinañu dee te ñoom dinañu jël suñu jabar yi ak suñu doom yi. Nañu tànn beneen njiit, bàyyi Musaa te dellu Misra ! ’

Waaye ci 12 góor ñu yërndu woon réew mi, amoon na ci ñaar ñu amoon ngëm ci Yexowa. Yosuwe ak Kaleb lañu tuddoon. Ñaar ñooñu dañu jéem a dalal xelu waa mbooloo mi. Ñu ne leen : ‘ Buleen tiit ! Yexowa mu ngi ak ñun. Daan réew mii dina yomb. ’ Waaye kenn dégluwu leen. Dañu leen bëggoon a rey sax.

Loolu tax na Yexowa mer lool. Mu ne Musaa : ‘ Képp ku am 20 at walla lu ko ëpp, du dugg ci réewu Kanaan. Gis nañu kéemaan yi ma def yépp ci Misra ak ci màndiŋ mi, waaye ba tey gëmuñu ma. Kon dinañu wër ci màndiŋ mi fii ba 40 at ci kanam, ba ñu dee ñoom ñépp. Yosuwe ak Kaleb rekk ñooy dugg ci réewu Kanaan. ’