Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 58

Daawuda Ak Goliyàtt

Daawuda Ak Goliyàtt

WAA Filisti yi ñu ngi bëgg a xeexaat ak waa Israyil. Ñeeti magu Daawuda, ñu ngi bokk léegi ci xarekatu Sóol yi, maanaam ñiy xeex ngir waa Israyil. Looloo tax Yese wax Daawuda lii : ‘ Demal ci say mag, yóbbul leen pepp ak mburu te nga seet naka lañuy def. ’

Bi Daawuda àggee foofu, mu dem gaaw ci magam yi nekkoon fu xarekati Israyil di jàkkaarloo ak xarekati Filisti. Benn ponkal bu bokkoon ci waa Filisti yi te tudd Goliyàtt dafa doon ñów ci kanamu waa Israyil di leen ñaawal. Lu mat 40 fan a ngi nii, muy def loolu, bés bu nekk, suba ak ngoon. Lii lay wax ci kow : ‘ Tànnleen benn góor ci yéen, mu ñów xeex ak man. Su ma reyee, dinañu nekk seeni jaam. Waaye su ma ko reyee, dingeen nekk suñuy jaam. Léegi, yéenay seet li ngeen di def. ’

Daawuda daldi laaj ay xarekat yu fa nekkoon : ‘ Kuy rey nit kii te musal waa Israyil ci gàcce gii, lan lañu koy may ? ’

Xarekat bi ne ko : ‘ Sóol dina ko jox alal ju bare te dina ko may doomam bu jigéen, mu nekk jabaram. ’

Waaye waa Israyil yépp dañu ragaloon Goliyàtt ndaxte ponkal bu mag la woon. Dafa njool ba jege ñetti meetar te benn soldaar moo yor pakkam, maanaam lu réy lu mel ni kubéer lu soldaar yi di yor ngir aar seen bopp.

Ci xarekat yi, am na ñu dem ci buur bi Sóol, ne ko Daawuda dafa bëgg a xeex ak Goliyàtt. Sóol ne Daawuda : ‘ Mënoo xeex ak moom. Xale nga te moom, dundam yépp soldaar la mas a nekk. ’ Daawuda ne ko : ‘ Rey naa benn urs ak benn gaynde yu yóbbu woon samay xaru baay. Waa Filisti bii, loolu moo koy dal. Yexowa dina ma dimbali. ’ Sóol ne ko : ‘ Demal, te na Yexowa ànd ak yow. ’

Daawuda daldi dem ca dex ba, jël fa juróomi xeer yu rattax, dugal leen ci saagam. Mu jël gànnaay bi mu amoon ngir sànni xeer, ba pare mu dem ca ponkal boobu. Bi ko Goliyàtt gisee, mënul woon a gëm ne kii moo bëgg a xeex ak moom. Pur moom, rey Daawuda dina yomb lool.

Mu ne ko : ‘ Ñówal rekk. Dinaa jox sa néew picc yi ak rabu àll yi, ñu lekk ko. ’ Daawuda tontu ko ne : ‘ Yaa ngi ñów ci man ak jaasi ak xeej, waaye man maa ngi ñów ci yow ci turu Yexowa. Tey jii, Yexowa dina ma dimbali ba ma rey la. ’

Daawuda daldi daw, jëm ci Goliyàtt. Mu jël benn xeer ci saagam, def ko ci gànnaayam te sànni ko ak dooleem yépp. Xeer bi dugg ci biir boppu Goliyàtt. Mu daanu dee ! Bi waa Filisti gisee ne daan nañu seen jàmbaar, ñépp daw. Waa Israyil daldi leen dàq te yóbbu ndam li.

1 Samwil (1 Samuel) 17:1-54.