Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 57

Yàlla Tànn Na Daawuda

Yàlla Tànn Na Daawuda

NDAX gis nga li xewoon fi léegi ? Xale bi moo muccal xar bu ndaw bi ci urs bi. Urs bi dafa jàppoon xar bi, di ko yóbbu ngir lekk ko. Waaye xale bi dafa daw topp ko te nangu xar bu ndaw bi ci gémmiñam. Urs bi jóg, bëgg ko song, waaye xale bi dafa ko jàpp, dóor ko, mu dee ! Loolu la defoon itam ak gaynde gu jàppoon benn xar. Xale bii, am na fit de ! Ndax xam nga kan la ?

Daawuda la. Betleyem la dëkk. Maamam bu góor, Obedd la tudd. Obedd, doomu Ruut ak Bowas la woon. Ndax fàttaliku nga ñooñu ? Baayu Daawuda mu ngi tudd Yese. Daawuda mooy sàmm xaru baayam yi. Daawuda juddu na 10 at ginnaaw bi Yexowa tànnee Sóol ngir mu nekk buur.

Mu am bés, Yexowa wax Samwil lii : ‘ Jëlal ci diw boobu bokkul ak yeneen diw yi, te demal ca kër Yese bi nekk Betleyem. Am na ku ma tànn ci doomam yi ngir mu nekk buur. ’ Bi Samwil gisee taawu Yese bi tudd Eliyab, lii la wax ci xelam : ‘ Ci lu wóor, kii la Yexowa tànn. ’ Waaye Yexowa ne ko : ‘ Bul xool ci taxawaayam walla ci rafetaayam. Du moom laa tànn buur. ’

Yese daldi woo doomam bi tudd Abinadab. Samwil ne : ‘ Déedéet, du moom la Yexowa tànn. ’ Yese indi doomam bi tudd Samma. Samwil ne : ‘ Yexowa tànnu ko moom itam. ’ Yese indi juróom-ñaar ci doomam yu góor yi, waaye Yexowa tànnul kenn ci ñoom. Samwil laaj Yese lii: ‘ Doom yu góor yii rekk nga am ? ’

Yese ne ko : ‘ Caat bi moo des. Waaye mu ngi sàmm xar yi. ’ Bi ñu indee Daawuda, Samwil gis na ne xale bu rafet la. Yexowa ne ko : ‘ Moom la. Sottil diw bi ci kowam. ’ Samwil daldi ko def. Kon bés dina ñów, Daawuda dina nekk buur ci Israyil.