Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 61

Dañu Def Daawuda Buur

Dañu Def Daawuda Buur

SÓOL mu ngi jéem a jàppaat Daawuda. Mu jël 3 000 nit ci nitam yi gën a aay ci xeex, ñu dem wut Daawuda. Bi Daawuda déggee loolu, mu yónni ay nit pur ñu dem seet ci ban béréb la Sóol ak nitam yi war a fanaan. Ginnaaw loolu, mu woo ñaar ci nitam yi, ne leen : ‘ Kan mooy ànd ak man, dem fu Sóol ak nitam yi nekk ? ’

Abisay ne ko : ‘ Man, dinaa dem. ’ Abisay moomu, magu Daawuda bu jigéen bi tudd Seruyaa moo ko jur. Daawuda ak Abisay dem fu nit ñooñu nekkoon, dox ndànk ngir kenn bañ leen dégg, fekk ñépp a ngi nelaw. Ñu jël xeej bi Sóol amoon ngir xeex ak potu ndoxam bi nekkoon ci wetu boppam. Kenn gisu leen, kenn déggu leen ndaxte ñépp a ngi doon nelaw, nelaw bu xóot.

Xoolal Daawuda ak Abisay léegi. Jóge nañu fi Sóol nekkoon, dem fu xaw a kowe. Lii la Daawuda yuuxu kiy jiite ñiy xeex ngir waa Israyil : ‘ Abner, lu tax doo xool ngir aar sa kilifa gi nekk buur bi ? Xoolal ! Ana xeejam ak potu ndoxam ? ’

Sóol yeewu. Mu xàmme baatu Daawuda. Mu ne : ‘ Ndax yow la, Daawuda ? ’ Ndax gis nga Sóol ak Abner fii ci suuf ?

Daawuda tontu ko ne : ‘ Waaw, man la, buur, sama kilifa. ’ Mu laaj ko lii : ‘ Lu tax nga bëgg maa jàpp ? Ana lu bon li ma def ? Sa xeej mu ngi nii, buur. Na am ku ñów jëlsi ko. ’

Sóol daldi ne : ‘ Def naa lu bon. Def naa lu amul benn njariñ. ’ Daawuda dem yoonam, Sóol ñibbi. Waaye lii la Daawuda xalaat : ‘ Sóol dina ma mas a rey. Bàyyil ma dem ca réewu Filisti. ’ Te loolu la def. Daawuda nax ñi dëkkoon Filisti ba ñu foog ne ñoom la faral léegi.

Ginnaaw loolu, waa Filisti dem xeex ak waa Israyil. Sóol ak Yonatan dee ci xeex boobu. Xolu Daawuda jeex. Mu bind benn woy bu rafet buy naan : ‘ Sama xol jeex na, Yonatan sama mag. Céy, ni ma la bëgge woon ! ’

Ginnaaw loolu, Daawuda dellu na ci dëkku Ebron bi nekk ci Israyil. Ñi bëgg doomu Sóol bi tudd Isboset nekk buur ñu ngi xeex ak ñi bëgg Daawuda nekk buur. Waaye niti Daawuda ñoo gañe. Daawuda amoon na 30 at bi ñu ko defee buur. Nguuru na ci Ebron lu mat juróom-ñaari at ak génn-wàll. Mu am fa ay doom yu góor, boole ci ñi tuddoon Amnon, Absalom ak Adoniya.

Daawuda ak nitam yi dem nañu xeex ba nangu dëkk bu rafet bi tudd Yerusalem. Ki gënoon a sawar ci xeex boobu mooy Yowab. Kooku it, doomu Seruyaa la, magu Daawuda. Daawuda bëgg ko neexal ndax li mu def. Mu def ko njiit ci xarekatam yi. Léegi Daawuda mu ngi nguuru ci dëkku Yerusalem.