Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 59

Li Tax Daawuda War A Daw

Li Tax Daawuda War A Daw

BI DAAWUDA reyee Goliyàtt ba pare, Abner yóbbu na ko ci Sóol. Abner moo doon jiite xarekati Israyil, maanaam ñi doon xeex ngir waa Israyil. Sóol dafa kontaan lool ci Daawuda. Mu def ko njiit ci xarekatam yi te indi ko mu dëkk ci kër buur bi.

Ginnaaw loolu, Israyil dem na xeex ak waa Filisti. Bi xarekat yi ñibbisee, jigéen yi lii lañu doon wooy : ‘ Sóol rey na ay junni, waaye Daawuda rey na ay fukki junni. ’ Sóol gis ne Daawuda lañu gën a tagg, mu daldi iñaan. Waaye doomu Sóol bi tudd Yonatan, moom iñaanul. Dafa bëgg Daawuda lool, te Daawuda moom itam dafa ko bëgg. Loolu tax na kenn ku nekk ci ñoom dig moroomam ne dina nekk xaritam ba fàww.

Daawuda dafa aayoon lool ci tëgg xalam. Misig bi muy def, dafa neexoon Sóol. Waaye iñaan bi Sóol doon iñaane Daawuda, tax na mu def lu ñaaw. Dawuda dafa doon xalam rekk, Sóol daldi jël xeejam, sànni ko, naan : ‘ Dinaa daaj Daawuda ci miir bi ! ’ Daawuda daldi moytu xeej bi. Beneen yoon itam, Sóol defaat na loolu waaye jotul Daawuda. Léegi Daawuda xam na ne dafa war a moytu bu baax.

Ndax yaa ngi fàttaliku li Sóol dige woon ? Nee woon na ne, kuy rey Goliyàtt, dina ko may doomam bu jigéen, mu nekk jabaram. Sóol mujj na wax Daawuda ne dina ko may doomam bi tudd Mikal, waaye bala loolu fàww mu rey 100 nit ci waa Filisti yi bañoon Israyil. Xoolal loolu ! Sóol mu ngi yaakaar ne waa Filisti dinañu rey Daawuda. Waaye reyuñu ko te Sóol mujj na may Daawuda doomam, mu nekk jabaram.

Am na bés, Sóol wax na Yonatan ak surgaam yépp ne dafa bëgg a rey Daawuda. Waaye lii la Yonatan wax baayam : ‘ Bul def Daawuda lu bon. Masu la def lu bon. Te sax, dimbali na la bu baax ak li mu def yépp. Rey na Goliyàtt fekk mënoon na ci ñàkk bakkanam te danga ci kontaanoon lool. ’

Sóol déglu na doomam te dig na ne du def Daawuda lu bon. Ñu daldi indiwaat Daawuda, mu kontine liggéey bi mu doon def ci kër Sóol. Waaye mu am bés, Daawuda mu ngi doon xalam, Sóol daldi ko sànniwaat xeejam. Daawuda moytu ko, xeej bi dugg ci miir bi nekkoon ci ginnaawam. Mooy ñetteelu yoon bi Sóol def loolu ! Léegi Daawuda xam na ne dafa war a daw !

Guddi googu, Daawuda dem na këram. Waaye Sóol dafa yónni ay nit pur ñu rey ko. Mikal xam na li baayam bëgg a def. Mu ne jëkkëram : ‘ Boo dawul ci guddi gii, suba dina fekk nga dee. ’ Guddi googu, mu dimbali Daawuda mu jaar ci palanteer, daw. Ci lu tollu juróom-ñaari at, Daawuda mënuloon a toog benn palaas lu yàgg. Dafa doon nëbbu rekk ngir Sóol bañ ko gis.

1 Samwil (1 Samuel) 18:1-30 ; 19:1-18.