Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Nettali 64

Suleymaan Mu Ngi Tabax Kër Yàlla Gi

Suleymaan Mu Ngi Tabax Kër Yàlla Gi

BALA mu dee, Daawuda jox na Suleymaan palaŋ yi mu waroon a topp ngir tabax kër Yexowa gi. Yexowa moo joxoon Daawuda palaŋ yooyu. Suleymaan tàmbali na tabax bi ci ñeenteelu atu nguuram. Jeexal na ko juróomi at ak génn-wall ginnaaw loolu. Ay fukki junniy nit ñoo bokk ci liggéey boobu. Dañu ci def xaalis bu baree bare ndaxte ci biir kër gi, amoon na lu bare lu ñuy defare wurus ak xaalis.

Kër Yàlla gi am na ñaari néeg yu gën a am solo, mel ni yi amoon ci tànt bi nekkoon jaamukaayu Yàlla. Waaye néeg yi nekk ci kër Yàlla gi ñoo gën a mag. Mat nañu ñaari yoon ya amoon ca tànt ba. Suleymaan dugal na gaalu kóllëre gi ci néeg bi gënoon a féete ci biir. Leneen li nekkoon ci tànt boobu, dugal na ko ci beneen néeg bi.

Bi tabax bi paree, def nañu feet bu mag. Xoolal li ñuy wone fii. Suleymaan sukk na ci kanamu kër Yàlla gi te mu ngi ñaan Yexowa. Lii lay wax : ‘ Asamaan si sépp sax, xajuloo ci. Kon du ci kër gii ngay xaj. Waaye, céy sama Yàlla, nanga déglu sa mbooloo bu ñu lay ñaan di jublu ci kanamu kër gii. ’

Bi Suleymaan paree ñaan bi, safara daldi wàcc asamaan, lakk mala yi ñu saraxe woon foofu yépp. Leer bu mag jóge ci Yexowa daldi feesal kër Yàlla gi. Loolu dafay wone ne Yexowa déglu na li ñu fa wax. Wone na it ne kontaan na ci kër gi ak ci ñaanu Suleymaan. Léegi, mbooloo mi dina ñów ci kër Yàlla gi ngir jaamu Yàlla. Dootul dem ci tànt boobu nekkoon jaamukaay.

Suleymaan nguuru na lu yàgg ci fasoŋ bu rafet, mbooloo mi kontaan lool. Waaye Suleymaan mujj na takk jabar yu bare yu bokkoon ci réew yu jaamuwul woon Yexowa. Ndax gis nga benn ci jabar yooyu fii ci suuf di jaamu xërëm bi ? Jabaru Suleymaan yi mujj nañu yóbbaale Suleymaan ba mu jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Ndax xam nga loolu lu mu indi ? Amatul woon yërmande ci nit ñi, mu komaasee soxor. Mbooloo mi amatul jàmm.

Yexowa daldi mere Suleymaan. Mu ne ko : ‘ Dinaa nangu nguur gi ci yow, jox ko keneen. Waaye duma def loolu bi ngay dund. Dinaa ko def ci jamano bu sa doom nekkee buur. Waaye duma nangu réew mi yépp ci moom. ’ Nañu seet naka la loolu ame..