Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 76

Ñu Ngiy Alag Yerusalem

Ñu Ngiy Alag Yerusalem

AM NA léegi 10 at bi buur Nebukanesar yóbboo waa Israyil yi gënoon a am xam-xam ca Babilon. Xoolal li xew léegi ! Ñu ngi lakk Yerusalem. Te ñi deewul, ñu ngi leen di yóbbu Babilon, ñu nekk jaam foofu.

Yaa ngi fàttaliku li yonent Yexowa yi waxoon ne dina dal waa Israyil su ñu soppiwul lu bon li ñu doon def. Waaye waa Israyil bëgguñu woon a déglu. Dañu kontine di jaamu ay yàlla yu dul dëgg, bañ a jaamu Yexowa. Kon yar bi ñu am nii, lu jaadu la. Li koy wone mooy li yonent Yàlla Esekiel wax ci lu bon li waa Israyil doon def.

Ndax xam nga Esekiel ? Bokk na ci ndaw yi buur Nebukanesar yóbbu woon Babilon lu ëpp 10 at bala ñu alag Yerusalem. Mooy bi ñu yóbbu woon itam Dañeel ak ñettti xaritam yi, Sadarag, Mesag ak Abed-Nego.

Esekiel, Babilon la nekkoon bi ko Yexowa wonee lu bon li ñu doon def ca kër Yàlla ga nekkoon Yerusalem. Kéemaan la Yàlla defoon noonu. Esekiel mu nga woon Babilon, waaye Yexowa def na ba mu gis lépp li ñu doon def ca kër Yàlla ga. Te li Esekiel gis foofu, dafa garaaw lool !

Yexowa ne Esekiel : ‘ Xoolal lu ñaaw lool lu nit ñi di def ci kër Yàlla gi. Xoolal nataalu jaan ak bu yeneen mala yu ñu def ci miir yi. Te xoolal waa Israyil yii di leen jaamu ! ’ Esekiel gis na loolu lépp te dafa ko bind.

Yexowa laaj Esekiel lii : ‘ Ndax yaa ngi gis li njiiti Israyil di def ci kumpa ? ’ Waaw, loolu it, mën na ko gis. Ay 70 góor ñoo fa nekk di jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Lii lañuy wax : ‘ Yexowa du ñu gis. Jóge na réew mi. ’

Yexowa won na itam Esekiel ay jigéen yu nekkoon ci buntu kër Yàlla bi féete woon bëj-gànnaar. Ñu nga toog foofu di jaamu yàlla ju dul dëgg ji tudd Tammus. Te xoolal góor yi nekk ci buntu kër Yàlla gi. Mat nañu 25 nit. Esekiel mu ngi leen di gis. Ñu ngi sukk di jaamu naaj bi, seen kanam di féete penku, maanaam fu naaj bi di génne ci suba si !

Yexowa ne Esekiel : ‘ Nit ñii, faalewuñu ma. Dañuy def lu bon, waaye li gën a garaaw mooy dañu koy def sama biir kër. ’ Yexowa daldi wax lii: ‘ Dinañu gis ni sama mer tànge. Te duma leen yërëm bu ñu leen di alag. ’

Lu tollu ak ñetti at ginnaaw bi Yexowa wonee loolu Esekiel, waa Israyil jéem nañu génn ci loxo buur Nebukanesar. Mu daldi ñów xeex ak ñoom. Xeex bi yàgg lu mat benn at ak genn-wàll. Waa Babilon mujj a toj miiri Yerusalem te lakk dëkk bi yépp. Li ëpp ci nit ñi, rey nañu leen walla dañu leen jàpp, yóbbu leen Babilon.

Lu tax Yexowa bàyyi lu metti loolu dal waa Israyil ? Ndaxte dañu bañoon a déglu Yexowa te bañ a topp ndigalam yi. Loolu dafay wone lu tax topp lépp li ñu Yexowa wax am solo lool.

Buur Nebukanesar bàyyi woon na tuuti nit ci réewu Israyil. Mu tànn ci yawut yi fa nekkoon ki tudd Gedaliya, def ko seen njiit. Waaye am na ay waa Israyil yu ko rey. Léegi dañu ragal waa Babilon ñówaat te alag leen ñoom ñépp ndax loolu. Ñu daldi forse Yeremi mu ànd ak ñoom, daw ca Misra.

Léegi kenn desul ci réewu Israyil. Noonu la réew mi nekke lu mat 70 at. Kenn nekku fa woon. Waaye Yexowa waxoon na ne dina indiwaat mbooloom fii ci réew mi bu 70 at yi matee. Ci diggante bi, lan moo dal mbooloo Yàlla mi ñu yóbbu woon Babilon ? Nañu jàng loolu léegi.

2 Buur yi (2 Rois) 25:1-26 ; Yérémi 29:10 ; Ézékiel 1:1-3 ; 8:1-18.