Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 74

Góor Gii, Tiitul, Ragalul

Góor Gii, Tiitul, Ragalul

XOOLAL góor gi ñuy ñaawal fii. Xam nga kan la? Yérémi la. Yonent Yàlla bu mag la.

Bi Yosiyas komaasee dindi xërëm yi ci réew mi, tuuti ci ginnaaw loolu, Yexowa laaj na Yérémi mu nekk yonentam. Yérémi moom, xalaatul ne mën na nekk yonent ndaxte xale la. Waaye Yexowa wax na ko ne Dina ko dimbali.

Yérémi mu ngi wax waa Israyil ñu bàyyi lu bon li ñuy def. Mu ne leen : ‘ Yàlla yi xeet yi di jaamu, duñu yàlla dëgg. ’ Ba tey, ci waa Israyil yu bare, jaamu xérém moo gën jaamu Yexowa, Yàlla dëgg ji. Yérémi mu ngi wax mbooloo mi ne Yexowa dina leen yar ndax lu bon li ñuy def, waaye dañu koy reetaan rekk.

At yi dem. Yosiyas dee. Ñetti weer ci ginnaaw loolu, doomam Yowakim nekk buur. Yérémi kontine di wax mbooloo mi lii : ‘ Bu ngeen soppiwul seen yoon bu bon bi, dinañu alag Yerusalem. ’ Saraxalekat yi jàpp Yérémi te yuuxu ko lii : ‘ Dañu la war a rey ndax li ngay wax nii. ’ Ñu wax doomi buuru Israyil lii : ‘ War nañu rey Yérémi, ndaxte waxul jàmm ci suñu dëkk. ’

Lan la Yérémi di def léegi ? Moom, ragalul ! Mu ne leen ñoom ñépp : ‘ Yexowa moo ma yónni ci yéen ngir wax leen loolu yépp. Bu ngeen soppiwul lu bon li ngeen di def, Yexowa dina alag Yerusalem. Waaye nangeen xam lii : Boo leen ma reyee, nit ku deful dara lu bon ngeen di rey. ’

Doomi buuru Israyil reyuñu Yérémi, waaye ba tey waa Israyil soppiwuñu lu bon li ñu doon def. Ginnaaw loolu, buuru Babilon bi tudd Nebukanesar dafa ñów, xeex ak waa Yerusalem, def waa Israyil jaam, te yóbbu ay junniy nit Babilon. Xoolal loolu ni mu mettee : dafa mel ni ay nit jóge bitim réew, jàpp la te yóbbu la ca réew moo xamul !

Yérémi (Jérémie) 1:1-8 ; 10:1-5 ; 26:1-16 ; 2 Buur yi (2 Rois) 24:1-17.