NETTALI 70
Yunus Ak Jën Bu Réy Bi
XOOLAL nit ki nekk fii ci biir géej gi. Am na poroblem, de. Jën bi dafa ko bëgg a wann ! Ndax xam nga kan la ? Yunus (Yona) la tudd. Nañu seet li ko dugal ci coono bu metti boobu.
Yunus, yonent Yexowa la. Bi Alisa deewee ba mu yàgg tuuti, lii la Yexowa wax Yunus : ‘ Demal ci Niniw, dëkk bu réy boobu. Lu bon li nit ñi di def foofu bare na lool. Dama bëgg nga wax ak ñoom ci loolu. ’
Waaye Yunus bëggul dem foofu. Mu daldi dugg ci gaal gu doon bàyyi Niniw ginnaaw, dem fu sore. Li mu daw noonu, neexul Yexowa. Mu daldi indi ngelaw bu réy a réy ci kow géej gi. Gaal gi bëgg a suux. Nit ñi tiit lool, ñu nekk di yuuxu te di ñaan seeni yàlla ngir ñu dimbali leen.
Lii la leen Yunus mujj a wax : ‘ Man, Yexowa laay jaamu, Yàlla mi sàkk asamaan ak suuf. Fii ma ne nii, maa ngi daw, ngir bañ a def li ma Yexowa wax. ’ Ñi nekkoon ci gaal gi ne ko : ‘ Lan lañu war a def ngir ngelaw bi taxaw ? ’
Yunus ne leen : ‘ Sànnileen ma ci biir géej gi ngir mu dal. ’ Waaye ñoom, bëgguñu def loolu. Ngelaw bi daldi yokku. Ñu mujj ko sànni ci biir géej gi. Ngelaw bi taxaw, géej gi ne remm.
Bi Yunus di nuur ci biir géej gi rekk, jën bu réy bi ñów wann ko. Waaye Yunus deewul. Ñetti bëccëg ak ñetti guddi, mu ngi ci biir jën bi. Réccu na léegi li mu déggalul Yexowa te bañ a dem Niniw. Ndax xam nga li mu def ?
Yunus dafa ñaan Yexowa mu dimbali ko. Yexowa daldi def ba jën bi waccu Yunus ci kow suuf. Ginnaaw loolu, Yunus dem na Niniw. Ndax loolu wonewul ne, def lépp lu ñu Yexowa wax, am na solo lool ?
Téere bi tudd Yona ci Biibël bi.