Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 82

Mordekay Ak Esteer

Mordekay Ak Esteer

NAÑU dellu ginnaaw ba tuuti at bala Esras ñów Yerusalem. Mordekay (Mordokaï) ak Esteer (Esther) ñooy waa Israyil yi gën a mag ci nguuru Pers. Esteer mooy jabaru buur bi. Mbokkam Mordekay mooy kilifa gi topp ci buur bi. Nañu seet naka la loolu lépp ame.

Waajuru Esteer dee nañu bi mu nekkee xale bu tuuti. Mordekay moo ko yar. Asuerus (Assuérus) mooy buuru Pers. Am na benn kër buur gu nekk ci dëkku Susan (Suse). Mordekay bokk na ci ñiy liggéeyal buur bi foofu. Mu am bés, jabaru buur bi tudd Wasti (Vashti) bañ a def li ko buur bi santoon. Buur bi daldi tànn beneen jigéen pur mu nekk jabaram. Xam nga kan la tànn ? Jigéen bu rafet bi tudd Esteer.

Ndax gis nga fii nit ki bare tiitar ak ñi koy sukkal ? Amaan (Hamân) la. Kilifa gu mag la ci réewu Pers. Amaan dafa bëgg Mordekay sukkal ko itam. Waaye yaa ngi gis fii Mordekay toog. Mordekay bëggul sukk ci kanamu Amaan. Pur moom, kenn warul a sukkal nit ku bon ku mel ni Amaan. Loolu tax na Amaan mer lool ba def lii :

Amaan wax na buur bi ay fen ci waa Israyil. Mu ne ko : ‘ Ay nit ñu bon lañu, te duñu topp say ndigal. War nañu leen a rey.’ Asuerus xamul ne jabaram, waa Israyil la. Mu daldi topp Amaan te digal bés bu ñu war a rey waa Israyil yépp.

Bi Mordekay déggee ndigal boobu, mu jaaxle lool. Mu yónnee ci Esteer, ne ko : ‘ Fàww nga wax ak buur bi, ñaan ko mu muccal ñu. ’ Ci yoonu Pers, kenn warul a dem gis buur bi bu fekkee ne du moom moo la woo. Waaye Esteer dem na, fekk buur bi woowu ko woon. Buur bi daldi ko tàllal yetu wurus bi mu amoon. Loolu dafay wone ne waruñu koo rey. Esteer woo buur bi ak Amaan ci lekk bu neex te bare bu mu leen di toggal. Bi ñu nekkee foofu, buur bi laaj Esteer lan la bëgg mu defal ko ko. Esteer ne ko dina ko ko wax bu ñu ñówee, moom ak Amaan, ci beneen togg bu mu leen di toggal ci ëllëg si.

Ci ëllëg si, bi ñu doon lekk, lii la Esteer wax buur bi : ‘ Man ak sama xeet lañu bëgg a rey. ’ Buur bi mer. Mu ne : ‘ Kan moo sañ a def loolu ? ’

Esteer ne ko : ‘ Ku bon ki ñuy xeex noonu mooy Amaan ! ’

Buur bi gën a mer. Mu wax ñu rey Amaan. Ginnaaw loolu, def na Mordekay kilifa gi topp ci moom ci réew mi. Mordekay fexe ba buur bi jox beneen ndigal buy may waa Israyil ñu mën a xeex bés bi ñu leen naree rey. Ndegam Mordekay léegi nit ku mag la, ñu bare ci réew mi dimbali nañu waa Israyil te ñoom mucc nañu ci seeni noon.

Téere bi tudd Esther ci Biibël bi.